sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
78
9
{ "fr": "et désigné votre sommeil pour votre repos,", "wo": "te def nanu seeni nelaw di seen nooflaay," }
78
10
{ "fr": "et fait de la nuit un vêtement,", "wo": "te it def nanu guddi mu di kiiraay sutura," }
78
11
{ "fr": "et assigné le jour pour les affaires de la vie,", "wo": "nu def bëcëg mu di yëngutu kaay," }
78
12
{ "fr": "et construit au-dessus de vous sept (cieux) renforcés,", "wo": "tabax nanu juróom ñaari (asamaan) yu dëgër ñu tiim leen," }
78
13
{ "fr": "et [y] avons placé une lampe (le soleil) très ardente,", "wo": "poose nanu ci làmpu bu leer (jant bi)," }
78
14
{ "fr": "et fait descendre des nuées une eau abondante", "wo": "wàcce nanu ci niir yi am ndox muy dottiku" }
78
15
{ "fr": "pour faire pousser par elle grains et plantes", "wo": "ñu di ca saxal ay pepp ak i gàncax" }
78
16
{ "fr": "et jardins luxuriants.", "wo": "ak ay dër yu naat." }
78
17
{ "fr": "Le Jour de la Décision [du Jugement] a son terme fixé.", "wo": "Bisub Àtte ba Dig ba jotna." }
78
18
{ "fr": "Le jour où l´on soufflera dans la Trompe, vous viendrez par troupes,", "wo": "Bis ba ñuy wal bufta, ngeen di ñëw di ay mbooloo," }
78
19
{ "fr": "et le ciel sera ouvert et [présentera] des portes,", "wo": "nu ubbi asamaan si mu def ay buntu," }
78
20
{ "fr": "et les montagnes seront mises en marche et deviendront un mirage.", "wo": "nu doxloo tundi doj yi mu melni ñàndóox. " }
78
21
{ "fr": "L´Enfer demeure aux aguets,", "wo": "Waajal nanu safara muy tuqlóo," }
78
22
{ "fr": "refuge pour les transgresseurs.", "wo": "di xala doon dekuwaayu ñu bew ña." }
78
23
{ "fr": "Ils y demeureront pendant des siècles successifs.", "wo": "Danañu fa sax ay jamono yu yàgg." }
78
24
{ "fr": "Ils n´y goûteront ni fraîcheur ni breuvage,", "wo": "Dunu fa mos ab sedd waxantumalaa ag naan," }
78
25
{ "fr": "Hormis une eau bouillante et un pus", "wo": "Lu dul ndox muy wañax ak lay rogaate ca seen jëmm ya" }
78
26
{ "fr": "comme rétribution équitable.", "wo": "muy pey gu témbóo." }
78
27
{ "fr": "Car ils ne s´attendaient pas à rendre compte,", "wo": "Ñoom dañoo foogoon ne duñu leen màndaxe," }
78
28
{ "fr": "et traitaient de mensonges, continuellement, Nos versets,", "wo": "ña weddiwoon sunuy Laaya," }
78
29
{ "fr": "alors que Nous avons dénombré toutes choses en écrit.", "wo": "lépp lu ne peek nanu ko bind ko." }
78
30
{ "fr": "Goûtez donc. Nous n´augmenterons pour vous que le châtiment !", "wo": "Ayca mosleen. Dunu leen dolli lu dul mbugël (tokamtikuleen ko) !" }
78
31
{ "fr": "Pour les pieux ce sera une réussite :", "wo": "Ña ragal Yàlla ñoom baaxal nañu :" }
78
32
{ "fr": "jardins et vignes,", "wo": "am nañu ay tooli dër ak i reseñ," }
78
33
{ "fr": "et des (belle) aux seins arrondis, d´une égale jeunesse,", "wo": "ak i jongama huur yu taxaw ay ween te maase," }
78
34
{ "fr": "et coupes débordantes.", "wo": "ak ay kaas yu fees dell." }
78
35
{ "fr": "Ils n´y entendront ni futilités ni mensonges.", "wo": "Duñu fa dégg mukk waxi caaxaan mbaa ay fen." }
78
36
{ "fr": "A titre de récompense de ton Seigneur et à titre de don abondant", "wo": "Muy pey gu bawoo ca seen Boroom" }
78
37
{ "fr": "du Seigneur des cieux et de la terre et de ce qui existe entre eux, le Tout Miséricordieux; ils n´osent nullement Lui adresser la parole.", "wo": "Boroom asamaan yeek suuf seek li ci seen diggante, mooy Yëramaakoon bi ; duñu mana waxanteek moom." }
78
38
{ "fr": "Le jour où l´Esprit et les Anges se dresseront en rangs, nul ne saura parler, sauf celui à qui le Tout Miséricordieux aura accordé la permission, et qui dira la vérité.", "wo": "Bu keroogee ba Jibriil jóg ànd ak malaaka ya taxaw def sàppe, duñu wax , lu dul ku Yàlla Yëramaakoon bi jox ndigël, mu wax lay dëgg te yem ca kepp." }
78
39
{ "fr": "Ce jour-là est inéluctable. Que celui qui veut prenne donc refuge auprès de son Seigneur.", "wo": "Loolu moo di bisub dëgg ba. Ku mu soob mu jël Boroomam def ko ab rawtukaay." }
78
40
{ "fr": "Nous vous avons avertis d´un châtiment bien proche, le jour où l´homme verra ce que ses deux mains ont préparé; et l´infidèle dira : \"Hélas pour moi ! Comme j´aurais aimé n´être que poussière\".", "wo": "Xuppnaa leen ci mbugëlum bis bu jigeen, bu keroogee ba nit ñi di xool la ñu jëfoon ; yéefar ba naan : “ Aka neexoon may suuf” . " }
79
1
{ "fr": "Par ceux qui arrachent violemment !", "wo": "Ci roccikat yay sanjaafu, maa ngi giñ !(s)" }
79
2
{ "fr": "Et par ceux qui recueillent avec douceur !", "wo": "Ak ña koy rocci ndànk-ndànk !" }
79
3
{ "fr": "Et par ceux qui voguent librement,", "wo": "Ak ñay féey ca asamaan sa," }
79
4
{ "fr": "puis s´élancent à toute vitesse,", "wo": "ak ñay jëkënte cig ngëm," }
79
5
{ "fr": "et règlent les affaires !", "wo": "ak ñay settantal di lijjënti mbir yi!" }
79
6
{ "fr": "Le jour où [la terre] tremblera [au premier son du clairon]", "wo": "Ca bis boobule [suuf] di yëngutu ci wal gu jëkkug mbiib ga [bufta ba]" }
79
7
{ "fr": "immédiatement suivi du deuxième.", "wo": "ñaarelug wal ga daldi cay topp." }
79
8
{ "fr": "Ce jour-là, il y aura des coeurs qui seront agités d´effroi,", "wo": "Bu keroogee, dana am ay xol yu tiit," }
79
9
{ "fr": "et leurs regards se baisseront.", "wo": "seenub gis sàjju ngir ragal." }
79
10
{ "fr": "Ils disent : \"Quoi ! Serons-nous ramenés à notre vie première,", "wo": "Ña ngay wax naan : “Ndax danuy dundaat ginnaaw dee," }
79
11
{ "fr": "quand nous serons ossements pourris ? \"", "wo": "ak sax ginnaaw bu nu doonee ay yax yu funux ?”" }
79
12
{ "fr": "Ils disent : \"ce sera alors un retour ruineux ! \"", "wo": "Ña ngay wax naan : “loolu deey yàqule la !”" }
79
13
{ "fr": "Il n´y aura qu´une sommation,", "wo": "loolu ab jàjj la," }
79
14
{ "fr": "et voilà qu´ils seront sur la terre (ressuscités).", "wo": "ñu jekki-jekki rekk ne jaww ci kaw suuf si dekkiwaat." }
79
15
{ "fr": "Le récit de Moïse t´est-il parvenu ?", "wo": "Ndax waxtaanu Muusaa dikkël na la ? Ay xibaaram ?" }
79
16
{ "fr": "Quand son Seigneur l´appela, dans Touwa, la vallée sanctifiée :", "wo": "Ba ko Boroomam di woo, ca xuru Tuwaa, wu sell wa, di ko wax ne :" }
79
17
{ "fr": "Va vers Pharaon. Vraiment, il s´est rebellé !", "wo": "“Demal ca Firawna. Moom bew na !" }
null
null
{ "fr": "Puis dis-lui : Voudrais-tu te purifier ?", "wo": "Te nga wax ko ne : “Ndax bëgg ngaa tuub ?" }
79
19
{ "fr": "et que je te guide vers ton Seigneur afin que tu Le craignes ? \"", "wo": "kon dey da naa la gindi ci sa Boroom nga ragal ko ?”" }
79
20
{ "fr": "Il lui fit voir le très grand miracle.", "wo": "Mu wan ko keemtaan yu màgg ya. " }
79
21
{ "fr": "Mais il le qualifia de mensonge et désobéit;", "wo": "Mu weddi ko (Firawna) daldi koy moy ;" }
79
22
{ "fr": "Ensuite, il tourna le dos, s´en alla précipitamment,", "wo": "Mu daldi, dumóoyu, féew dem," }
79
23
{ "fr": "rassembla [les gens] et leur fit une proclamation,", "wo": "daldi woo nit ña dajale leen," }
79
24
{ "fr": "et dit : \"C´est moi votre Seigneur, le très-Haut\".", "wo": "daldi wax ne : “Man maay sen boroom, bi gëna kawe” ." }
79
25
{ "fr": "Alors Allah le saisit de la punition exemplaire de l´au-delà et de celle d´ici-bas.", "wo": "Yàlla daldi koy faagaagal mbugalum àddina muy sar ba àllaaxira." }
79
26
{ "fr": "Il y a certes là un sujet de réflexion pour celui qui craint.", "wo": "Ag fàttalikoo ngi ci loolu ña ragal Yàlla." }
79
27
{ "fr": "êtes-vous plus durs à créer ? ou le ciel, qu´Il a pourtant construit ?", "wo": "li ngeen sos moo gëna dëgër ? walla asamaan si ma tabax ?" }
79
28
{ "fr": "Il a élevé bien haut sa voûte, puis l´a parfaitement ordonné;", "wo": "Kaweel na talaayam ba, te maasale ko ;" }
79
29
{ "fr": "Il a assombri sa nuit et fait luire son jour.", "wo": "Moo lëndamal guddi yi te leeral bëccëg yi." }
79
30
{ "fr": "Et quant à la terre, après cela, Il l´a étendue :", "wo": "Ginnaaw loolu moo tallal suuf si :" }
79
31
{ "fr": "Il a fait sortir d´elle son eau et son pâturage,", "wo": "Mu génnee ca ndox ak i gàncax," }
79
32
{ "fr": "et quant aux montagnes, Il les a ancrées,", "wo": "mu saxal ca duutan ca tund doj yi," }
79
33
{ "fr": "pour votre jouissance, vous et vos bestiaux.", "wo": "mu di bànneexu, ci yéen ak ci seenug jur." }
79
34
{ "fr": "Puis quand viendra le grand cataclysme,", "wo": "Saa su mbambu mu rëy ma dikkee," }
79
35
{ "fr": "le jour où l´homme se rappellera à quoi il s´est efforcé,", "wo": "bu keroogee nit dana fàttaliku la mu jëfoon," }
79
36
{ "fr": "l´Enfer sera pleinement visible à celui qui regardera...", "wo": "Safara danaan fàŋŋ ku ko xool gis ko..." }
79
37
{ "fr": "Quant à celui qui aura dépassé les limites", "wo": "Képp ku bewoon daan jalgati" }
79
38
{ "fr": "et aura préféré la vie présente,", "wo": "te bëggoon dundug àddina sii doŋŋ (di ko xëntéewóo)," }
79
39
{ "fr": "alors, l´Enfer sera son refuge.", "wo": "kookee, Safaraa di wàccuwaayam." }
79
40
{ "fr": "Et pour celui qui aura redouté de comparaître devant son Seigneur, et préservé son âme de la passion,", "wo": "Saar 79 : Malaaka yay rocci ruu 46 - Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
79
40
{ "fr": "Et pour celui qui aura redouté de comparaître devant son Seigneur, et préservé son âme de la passion,", "wo": "Képp ku ragaloon ne dana taxaw ca Boroomam, te daan tere bakkanam bànneex (ay caaxaan)," }
79
41
{ "fr": "le Paradis sera alors son refuge.", "wo": "kookee àjjanaa di wàccuwaayam." }
79
42
{ "fr": "Ils t´interrogent au sujet de l´Heure : \"Quand va-t-elle jeter l´ancre\" ", "wo": "Ña nga lay laaj bis pénc ba : “Kañ lay teeral”(r)" }
79
43
{ "fr": "Quelle [science] en as-tu pour le leur dire ?", "wo": "Ana ban xam-xam nga ci am ngir tontu leen ?" }
79
44
{ "fr": "Son terme n´est connu que de ton Seigneur.", "wo": "Ab yemukaayam sa Boroom rekk ko xam." }
79
45
{ "fr": "Tu n´es que l´avertisseur de celui qui la redoute.", "wo": "Yaw nag ab xuppekat doŋŋ nga ngir ña ko ragal. " }
79
46
{ "fr": "Le jour où ils la verront, il leur semblera n´avoir demeuré qu´un soir ou un matin.", "wo": "Bis bu ñu ko gisee, dafay mel ne seen dund gépp genn ngoon la woon walla yoor-yoor. " }
80
1
{ "fr": "Il s´est renfrogné et il s´est détourné ", "wo": "Sóomóorlu na daldi dumóoyu" }
80
2
{ "fr": "parce que l´aveugle est venu à lui.", "wo": "ba ko gumba ga digëlee." }
80
3
{ "fr": "Qui te dit : peut-être [cherche]-t-il à se purifier ?", "wo": "Xamoo : ndax dafa bëgg tuub ?" }
80
4
{ "fr": "ou à se rappeler en sorte que le rappel lui profite ?", "wo": "walla muy fàttaliku man caa jariñoo ?" }
80
5
{ "fr": "Quant à celui qui se complaît dans sa suffisance (pour sa richesse)", "wo": "Ka nga xam ne dafa woomal" }
80
6
{ "fr": "tu vas avec empressement à sa rencontre.", "wo": "ba tax nga jublu ko." }
80
7
{ "fr": "Or, que t´importe qu´il ne se purifie pas \"", "wo": "Lu laak moom ? (yaw muhammadu)”" }
80
8
{ "fr": "Et quant à celui qui vient à toi avec empressement", "wo": "Waaye ku la dikkëlati" }
80
9
{ "fr": "tout en ayant la crainte,", "wo": "tey wuta ragal Yàlla," }
80
10
{ "fr": "tu ne t´en soucies pas.", "wo": "te faalewoo ko." }
80
11
{ "fr": "N´agis plus ainsi ! Vraiment ceci est un rappel -", "wo": "Loolu dey ag fàttali la" }
80
12
{ "fr": "quiconque veut, donc, s´en rappelle -", "wo": "ku mu soob, mu fàttaliku ko" }
80
13
{ "fr": "consigné dans des feuilles honorées,", "wo": "mi ngi ci ay xët yu ñu teral (bind ko)," }
80
14
{ "fr": "élevées, purifiées,", "wo": "yu ñu yékëti, te laabal ko," }
80
15
{ "fr": "entre les mains d´ambassadeurs", "wo": "nekk ci yoxoy ak tekkikat (malaaka)" }
80
16
{ "fr": "nobles, obéissants.", "wo": "yu tedd, yu baax." }
80
17
{ "fr": "Que périsse l´homme ! Qu´il est ingrat !", "wo": "reyeef na nit ngir ngoreedeem !" }
80
18
{ "fr": "De quoi [Allah] l´a-t-Il créé ?", "wo": "Ci lan la ko [Yàlla] bind ?" }
80
19
{ "fr": "D´une goutte de sperme, Il le crée et détermine (son destin) :", "wo": "Ci toqu maniyu la ko binde, dugal ay mbiram :" }
80
20
{ "fr": "puis Il lui facilite le chemin;", "wo": "daldi koy yombalal yoon wa ; " }
80
21
{ "fr": "puis Il lui donne la mort et le met au tombeau;", "wo": "daldi koy rey, tàbbal ko ci bàmmeel ;" }