sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
73
8
{ "fr": "Et rappelle-toi le nom de ton Seigneur et consacre-toi totalement à Lui,", "wo": "Na ngay fàttaliku di tud sa turu Boroom te wéeru ci moom fàwwu," }
73
9
{ "fr": "le Seigneur du Levant et du Couchant. Il n´y a point de divinité à part Lui. Prends-Le donc comme Protecteur.", "wo": "mooy boroom Penkook Sowu. Amul jeneen Yàlla ju dul moom. Na nga wéeru ci moom." }
73
10
{ "fr": "Et endure ce qu´ils disent; et écarte-toi d´eux d´une façon convenable.", "wo": "Muñal li ñuy wax ; te nga gàddaay leen gàddaay gu rafet (bañ leena faale)." }
73
11
{ "fr": "Et laisse-moi avec ceux qui crient au mensonge et qui vivent dans l´aisance; et accorde-leur un court répit :", "wo": "Bàyyi maak ñiy weddi ak ñi am alal ; te nga muñal leen tuuti :" }
73
12
{ "fr": "Nous avons [pour eux] lourdes chaînes et Enfer,", "wo": "Noo ngi leen di waajal Safara wu ànd ak jéng," }
73
13
{ "fr": "et nourriture à faire suffoquer, et châtiment douloureux.", "wo": "ak aw ñam wuy fot loo, ànd ak mbugël mu mitti." }
73
14
{ "fr": "Le jour où la terre et les montagnes trembleront, tandis que les montagnes deviendront comme une dune de sable dispersée.", "wo": "Bu keroogee bis ba suuf seek doj yi dëgg-dëgg tundu yi mel ni suufus ber mokk." }
73
15
{ "fr": "Nous vous avons envoyé un Messager pour être témoin contre vous, de même que Nous avions envoyé un Messager à Pharaon.", "wo": "Yónni nanu ci yéen ab Yonent muy seede, kem ni nu yónnee woon ca Firawna ab Yonent." }
73
16
{ "fr": "Pharaon désobéit alors au Messager. Nous le saisîmes donc rudement.", "wo": "Firawna daldi moy Yonenta ba. Nu daldi koy jël bu metti. (faagaagal ko)." }
73
17
{ "fr": "Comment vous préserverez-vous, si vous mécroyez, d´un jour qui rendra les enfants comme des vieillards aux cheveux blancs ?", "wo": "Ana naka ngeen di ragale (Yàlla), su ngeen weddee, bis boo xam ne tiit ma bijaawloona ab liir ? " }
73
18
{ "fr": "[et] durant lequel le ciel se fendra. Sa promesse s´accomplira sans doute.", "wo": "Su asamaan si dee xar. Ca la digam ba di mate." }
73
19
{ "fr": "Ceci est un rappel . Que celui qui veut prenne une voie [menant] à son Seigneur.", "wo": "Lii nag ag fàttali la. Képp ku mu soob mu jël yoon wa jëm ca Boroomam aw ca." }
73
20
{ "fr": "Ton Seigneur sait, certes, que tu (Muhammad) te tiens debout moins de deux tiers de la nuit, ou sa moitié, ou son tiers. De même qu´une partie de ceux qui sont avec toi. Allah détermine la nuit et le jour. Il sait que vous ne saurez jamais passer toute la nuit en prière. Il a usé envers vous avec indulgence. Récitez donc ce qui [vous] est possible du Coran. Il sait qu´il y aura parmi vous des malades, et d´autres qui voyageront sur la terre, en quête de la grâce d´Allah, et d´autres encore qui combattront dans le chemin d´Allah. Récitez-en donc ce qui [vous] sera possible. Accomplissez la Salat, acquittez la Zakat, et faites à Allah un prêt sincère. Tout bien que vous vous préparez, vous le retrouverez auprès d´Allah, meilleur et plus grand en fait de récompense. Et implorez le pardon d´Allah. Car Allah est Pardonneur et Très Miséricordieux.", "wo": "Sa Boroom xam na ne, yaw (Muhammad) da ngay taxawlu gëna néew ñaari ñetteeli xaaji guddi gi, walla xaaj ba, walla benn ñetteelu xaaj ba. Ànd kook mbooloo ci ña ànd ak yaw. Te Yàlla dana nattale guddeek bëccëg. Xam na ne manu leen fanaanee julli. Mu jégal leen. Jàngleen lu jàppandi ci Alxuraan. (Ndax moom Yàlla) xam na ne am na ci yéen ñu wopp, ak ñeneen ñuy tukki ji ci réew yi, ngir sàkku ji ci ngënéeli Yàlla yi, ak ñeneen ñuy xare ji ci yoonu Yàlla. Kon jàngleen la ca jàppandi. Te na ngeen taxawal julli, tey génne asaka, te na ngeen lebal Yàlla bor bu rafet. Te lépp lu ngeen jiitalal seen bopp ciw yiw, da ngeen ko fekk ci Yàlla, mooy la gën te moo ëpp ag pey. Te it na ngay jéggalu Yàlla. Yàlla moom Jéggalaakoon la Jaglewaakoon la.(r) " }
74
1
{ "fr": "ô, toi (Muhammad) ! Le revêtu d´un manteau !", "wo": "Éey, yaw Ku ñu muur ki!" }
74
2
{ "fr": "Lève-toi et avertis.", "wo": "Neel ñokket jóg tey xuppe." }
74
3
{ "fr": "Et de ton Seigneur, célèbre la grandeur.", "wo": "Te na ngay màggal sa Boroom." }
74
4
{ "fr": "Et tes vêtements, purifie-les.", "wo": "Te na ngay laabal say yéere." }
74
5
{ "fr": "Et de tout péché, écarte-toi. .", "wo": "Te it na ngay daw bépp bàkkaar." }
74
6
{ "fr": "Et ne donne pas dans le but de recevoir davantage. .", "wo": "Bul di joxe mukk ngir sàkku ca lu gëna bari." }
74
7
{ "fr": "Et pour ton Seigneur, endure.", "wo": "Te na ngay muñ ngir sa Boroom." }
74
8
{ "fr": "Quand on sonnera du Clairon,", "wo": "Saasu ñu walee ca mbiib ga," }
74
9
{ "fr": "alors, ce jour-là sera un jour difficile,", "wo": "su boobaa bis bu jafeñ lay doon," }
74
10
{ "fr": "pas facile pour les mécréants.", "wo": "du yomb ca yéefar ya de." }
74
11
{ "fr": "Laisse-Moi avec celui que J´ai créé seul, ", "wo": "Bàyyi Ma ak ki nga xam ne maa ko bindoon nu wéet," }
74
12
{ "fr": "et à qui J´ai donné des biens étendus,", "wo": "te ma joxoñ ko alal ju yaatu," }
74
13
{ "fr": "et des enfants qui lui tiennent toujours compagnie,", "wo": "ak doom yu ko daan wéttali," }
74
14
{ "fr": "pour qui aussi J´ai aplani toutes difficultés.", "wo": "te Ma dindiloon ko bépp jafe-jafe." }
74
15
{ "fr": "Cependant, il convoite [de Moi] que Je lui donne davantage.", "wo": "te mo daan xemmeem saa su nekk Ma di ko dolli." }
74
16
{ "fr": "Pas du tout ! Car il reniait nos versets (le Coran) avec entêtement.", "wo": "Te kat des na ! Ndax moom da daan lànk di bañ (Al xuraan) ji." }
74
17
{ "fr": "Je vais le contraindre à gravir une pente.", "wo": "Danaa ko sonale yéegu tundu." }
74
18
{ "fr": "Il a réfléchi. Et il a décidé.", "wo": "Moom day xalaat. Na daldi soobu." }
74
19
{ "fr": "Qu´il périsse ! Comme il a décidé !", "wo": "Nu daldi koy rey ! Ca na mu sóobóo !" }
74
20
{ "fr": "Encore une fois, qu´il périsse; comme il a décidé !", "wo": "Saar 74 : Ku ñu muur ki 56 - Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
74
20
{ "fr": "Encore une fois, qu´il périsse; comme il a décidé !", "wo": "Topp Nu reyaat ko ; Ca na mu sóobóo woon ! " }
74
21
{ "fr": "Ensuite, il a regardé.", "wo": "Mu daldi, xool." }
74
22
{ "fr": "Et il s´est renfrogné et a durci son visage.", "wo": "Daldi nay gaññ te sóomórlu." }
74
23
{ "fr": "Ensuite il a tourné le dos et s´est enflé d´orgueil.", "wo": "Topp mu daldi dumóoyu tey rëy-rëylu." }
74
24
{ "fr": "Puis il a dit : \"Ceci (le Coran) n´est que magie apprise", "wo": "Mu daldi wax ne : “ Alxuraan jii daal ag njibar doŋŋ la" }
74
25
{ "fr": "ce n´est là que la parole d´un humain\".", "wo": "lii daal du leen lu dul waxi nit” ." }
74
26
{ "fr": "Je vais le brûler dans le Feu intense (Saqar).", "wo": "Kookee dey danaa ko lakk ci Safaraw (Saqar)." }
74
27
{ "fr": "Et qui te dira ce qu´est Saqar ?", "wo": "Ana kan moo lay xamal luy Saqar ?" }
74
28
{ "fr": "Il ne laisse rien et n´épargne rien;", "wo": "Du bàyyi dara ;" }
74
29
{ "fr": "Il brûle la peau et la noircit.", "wo": "Dafay alawtiku ab der di ko xëmël." }
74
30
{ "fr": "Ils sont dix neuf à y veiller. ", "wo": "Fukki (Malaaka) ak juróom-ñanant koy wattu." }
74
31
{ "fr": "Nous n´avons assigné comme gardiens du Feu que les Anges. Cependant, Nous n´en avons fixé le nombre que pour éprouver les mécréants, et aussi afin que ceux à qui le Livre a été apporté soient convaincus, et que croisse la foi de ceux qui croient, et que ceux à qui le Livre a été apporté et les croyants n´aient point de doute; et pour que ceux qui ont au cœur quelque maladie ainsi que les mécréants disent : \"Qu´a donc voulu Allah par cette parabole ? \" C´est ainsi qu´Allah égare qui Il veut et guide qui Il veut. Nul ne connaît les armées de ton Seigneur, à part Lui. Et ce n´est là qu´un rappel pour les humains.", "wo": "Ay Malaaka rekk ay wattu Safara. Te, lu ñuy bari bari nekku wu ñu fa lu dul fitnaal yéefar yi, ak tiiñal ñoñ Téere, ak dolli ngëmug ña gëmoon, ak it ñoñ Téere ak way gëm ña baña dengi-dengi ; ak it ngir yéefar yaak ña seeni xol wopp di wax naan : “Ana lu Yàlla namm ci misaal mii ?” Noonu la Yàlla réerële ku ko soob di gindi it ku ko soob. Te sa xarekati Boroom, Moom doŋŋ leen xam. Te lii du lenn lu dul luy fàttali bindéef yi jàjj leen.(s)" }
74
32
{ "fr": "Non ! ... Par la lune !", "wo": "Déet !... maa ngi giñ ci weer wi !" }
74
33
{ "fr": "Et par la nuit quand elle se retire !", "wo": "Ak ci guddi su nee wërëñ !" }
74
34
{ "fr": "Et par l´aurore quand elle se découvre !", "wo": "Ak su fajar si di xar!" }
74
35
{ "fr": "[Saqar] est l´un des plus grandes [malheurs]", "wo": "[Safaraw Saqar] bokk na ca tiis yi gëna rëy" }
74
36
{ "fr": "un avertissement, pour les humains.", "wo": "ag xuppe la, ñeel bindéef yi." }
74
37
{ "fr": "Pour qui d´entre vous, veut avancer ou reculer.", "wo": "Ku mu soob ci yéen, na jiitu walla mu des ginnaaw." }
74
38
{ "fr": "Toute âme est l´otage de ce qu´elle a acquis.", "wo": "Bakkan bu mu mana doon ag tayle la ci jëfam." }
74
39
{ "fr": "Sauf les gens de la droite (les élus) :", "wo": "Ba mu des waa ndeyjoor :" }
74
40
{ "fr": "dans des Jardins, ils s´interrogeront", "wo": "ñoom ña nga ca biir Àjjana di laajante" }
74
41
{ "fr": "au sujet des criminels :", "wo": "ci mbirum tooñkat ya :" }
74
42
{ "fr": "Qu´est-ce qui vous a acheminés à Saqar ? ", "wo": "“(Naan) Ana lan mooleen wara duggloo Safaraw Saqar ?”" }
74
43
{ "fr": "Ils diront : \"Nous n´étions pas de ceux qui faisaient la Salat,", "wo": "Ñu tontu ne : “Nun kat danu daawul julli, " }
74
44
{ "fr": "et nous ne nourrissions pas le pauvre,", "wo": "te daawune leel miskiin yi," }
74
45
{ "fr": "et nous nous associions à ceux qui tenaient des conversations futiles,", "wo": "te danu daan ànd ak caaxankat ya," }
74
46
{ "fr": "et nous traitions de mensonge le jour de la Rétribution,", "wo": "te danu daan weddi bis Penc bi," }
74
47
{ "fr": "jusqu´à ce que nous vînt la vérité évidente [la mort]\".", "wo": "ba dee aksi ci sunu kaw” ." }
74
48
{ "fr": "Ne leur profitera point donc, l´intercession des intercesseurs.", "wo": "Rammug rammukat, du leen fa jariñ dara." }
74
49
{ "fr": "Qu´ont-ils à se détourner du Rappel ?", "wo": "Ana lan moo leen dëdëleek fàttaliku ?" }
74
50
{ "fr": "Ils sont comme des onagres épouvantés,", "wo": "Dañoo mel ni ñu ñu tiital (ay mbaam)," }
74
51
{ "fr": "s´enfuyant devant un lion.", "wo": "ni ñuy dawe gaynde." }
74
52
{ "fr": "Chacun d´eux voudrait plutôt qu´on lui apporte des feuilles tout étalées.", "wo": "Kenn ku nekk ci ñoom bëggoon na ñu jox ko ay kayit yu teqalikoo." }
74
53
{ "fr": "Ah ! Non ! C´est plutôt qu´ils ne craignent pas l´au-delà.", "wo": "Dee wa laay ! Ñoom ragalu ñu woon àllaaxira." }
74
54
{ "fr": "Ah ! Non ! Ceci est vraiment un Rappel.", "wo": "Mukk ! Te lii ag fàttali la." }
74
55
{ "fr": "Quiconque veut, qu´il se le rappelle.", "wo": "Kéep ku mu soob, na fàttaliku." }
74
56
{ "fr": "Mais ils ne se rappelleront que si Allah veut. C´est Lui qui est Le plus digne d´être craint; et c´est Lui qui détient le pardon.", "wo": "Te manuñoo fàttaliku lu dul ci bu soobee Yàlla. Te moo gëna yayoo ci ragal ko ; te moom doŋŋa am njégël. " }
75
1
{ "fr": "Non ! ... Je jure par le jour de la Résurrection !", "wo": "Maa ngi giñ ci bisub dekkiwaat ga !(n)" }
75
2
{ "fr": "Mais non ! , Je jure par l´âme qui ne cesse de se blâmer. .", "wo": "Te maa ngi giñ ci bakkan bi di ab yeddaakoon." }
75
3
{ "fr": "L´homme, pense-t-il que Nous ne réunirons jamais ses os ?", "wo": "Moo ndax, nit ki dafa foog ne dunu dajale ay yaxam ?" }
75
4
{ "fr": "Mais si ! Nous sommes Capable de remettre à leur place les extrémités de ses doigts. .", "wo": "Axakañ ! Mën nañoo dajale yemalewaat cati waaraamam." }
75
5
{ "fr": "L´homme voudrait plutôt continuer à vivre en libertin.", "wo": "Te nit moom day bëgg rekk di dund cig boy." }
75
6
{ "fr": "Il interroge : \"A quand, le Jour de la Résurrection ? \"", "wo": "Muy laaj : “Kañ la, Bisub Dekkiwaat ba ?”" }
75
7
{ "fr": "Lorsque la vue sera éblouie,", "wo": "Su gis ba nee melxat gëlam," }
75
8
{ "fr": "et que la lune s´éclipsera,", "wo": "weer wi muuru," }
75
9
{ "fr": "et que le soleil et la lune serons réunis,", "wo": "ñu boole jant beek weer wi," }
75
10
{ "fr": "l´homme, ce jour-là, dira : \"Où fuir ? \"", "wo": "bu keroogee, nita ngay, wax naan : “Fees di rawe ?”" }
75
11
{ "fr": "Non ! Point de refuge !", "wo": "Déedéet ! Laquwaay amul de !" }
75
12
{ "fr": "Vers ton Seigneur sera, ce jour-là, le retour.", "wo": "Bis boobu kay, dellu ca sa Boroom, rekk ay am." }
75
13
{ "fr": "L´homme sera informé ce jour-là de ce qu´il aura avancé et de ce qu´il aura remis à plus tard.", "wo": "Ca la ñuy xamale nit la mu jëkka def ba ci li mu mujjoon def (cig dundam)." }
75
14
{ "fr": "Mais l´homme sera un témoin perspicace contre lui-même,", "wo": "Li war moo di ne nit mooy seede boppam," }
75
15
{ "fr": "quand même il présenterait ses excuses.", "wo": "dontela sax dafay jégalu ak miim." }
75
16
{ "fr": "Ne remue pas ta langue pour hâter sa récitation : ", "wo": "(Su Alxuraan) di wàcc (yaw Muhammad) bul di yëngël saw làmmiñ ngir gaawtoo ko :" }
75
17
{ "fr": "Son rassemblement (dans ton cœur et sa fixation dans ta mémoire) Nous incombent, ainsi que la façon de le réciter. .", "wo": "Sol la ko aku jàngiinam, Nun la war." }
75
18
{ "fr": "Quand donc Nous le récitons , suis sa récitation.", "wo": "Te suñu koy jàng na ngay toppaat, njàng ma." }
75
19
{ "fr": "A Nous, ensuite incombera son explication.", "wo": "Leeral ko it, Nun la war. " }
75
20
{ "fr": "Mais vous aimez plutôt [la vie] éphémère,", "wo": "Yéen da ngeena bëgg (lool) dundug àddina si," }
75
21
{ "fr": "et vous délaissez l´au-delà.", "wo": "te da ngeena sàggane (lool) Àllaxira." }
75
22
{ "fr": "Ce jour-là, il y aura des visages resplendissants", "wo": "Bu keroogee, dana am xarkanam yu naat" }
75
23
{ "fr": "qui regarderont leur Seigneur;", "wo": "yuy xool seen Boroom ;" }
75
24
{ "fr": "et il y aura ce jour-là, des visages assombris,", "wo": "dana fa am it bu keroogee, ay xarkanam yu ñàng," }
75
25
{ "fr": "qui s´attendent à subir une catastrophe.", "wo": "dangay foog ne njuuma la." }
75
26
{ "fr": "Mais non ! Quand [l´âme] en arrive aux clavicules", "wo": "Bu ruuga génnee ba ca bóli ga" }
75
27
{ "fr": "et qu´on dit : \"Qui est exorciseur ? \"", "wo": "ñu ne ko: “ Ana kan mooy mocckat ba ?”" }
75
28
{ "fr": "et qu´il [l´agonisant] est convaincu que c´est la séparation (la mort),", "wo": "Mu daldi xam nag ne dee dikk na," }
75
29
{ "fr": "et que la jambe s´enlace à la jambe,", "wo": "yeel ya daldi jaxasoo rawaasoo," }
75
30
{ "fr": "c´est vers ton Seigneur, ce jour-là que tu seras conduit.", "wo": "Bu keroogee, ñu wommat la jaŋat-jaŋatee la jëm ca sa Boroom." }