sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
75
31
{ "fr": "Mais il n´a ni cru, ni fait la Salat;", "wo": "Gëmul woon, te it daawuloon julli;" }
75
32
{ "fr": "par contre, il a démenti et tourné le dos,", "wo": "waaye, moom sax dafa weddi woon dumóoyu," }
75
33
{ "fr": "puis il s´en est allé vers sa famille, marchant avec orgueil.", "wo": "daldi dem nag ca aw nitam, di xoggaliku." }
75
34
{ "fr": "Malheur à toi, malheur ! ", "wo": "“Yaayoo nga toskare, yaayoo nga toskare!”" }
75
35
{ "fr": "Et encore malheur à toi, malheur !", "wo": "Te it yaayoo nga toskare, yayoo nga ko !" }
75
36
{ "fr": "L´homme pense-t-il qu´on le laissera sans obligation à observer ? ", "wo": "Moo ndax nit dafa foog ne dañu koy bàyyi rekk noonu muy nguyaay?" }
75
37
{ "fr": "N´était-il pas une goutte de sperme éjaculé ?", "wo": "Moo ndax dafa doonul woon tóqug maniyu guy sottiku ?" }
75
38
{ "fr": "Et ensuite une adhérence Puis [Allah] l´a créée et formée harmonieusement;", "wo": "Mu mujj di aw lumbu Ma bind ko mu ne càndaŋ yemoo;" }
75
39
{ "fr": "puis en a fait alors les deux éléments de couple : le mâle et la femelle ?", "wo": "ma def ci ñaari toolént ya : góor ak jigéen ?" }
75
40
{ "fr": "Celui-là (Allah) n´est-Il pas capable de faire revivre les morts ? ", "wo": "Moo ndax kooku munula dekkilaat ku dee ? " }
76
1
{ "fr": "S´est-il écoulé pour l´homme un laps de temps durant lequel il n´était même pas une chose mentionnable ?", "wo": "Mo ndax nit dafa amul woon ab diir ci jamono bu kenn daawu ko limaale ?(s)" }
76
2
{ "fr": "En effet, Nous avons créé l´homme d´une goutte de sperme mélangé [aux composantes diverses] pour le mettre à l´épreuve. [C´est pourquoi] Nous l´avons fait entendant et voyant.", "wo": "Nun noo binde nit ci maniyu mu jaxasoo. Di ko nattu def ko muy dégg di gis." }
76
3
{ "fr": "Nous l´avons guidé dans le chemin, - qu´il soit reconnaissant ou ingrat -", "wo": "Gindi nanu ko ci aw yoon , - amaana muy déloo njukkël di sant walla mu goreedi -" }
76
4
{ "fr": "Nous avons préparé pour les infidèles des chaînes, des carcans et une fournaise ardente.", "wo": "Waajalal nanu yéefar ya ay càllala, ak i jéng ak safara wuy bérëx." }
76
5
{ "fr": "Les vertueux boiront d´une coupe dont le mélange sera de camphre,", "wo": "Ñu baax ña danañuy naane ci kaas yu ñu jaxasee kaafar," }
76
6
{ "fr": "d´une source de laquelle boiront les serviteurs d´Allah et ils la feront jaillir en abondance. .", "wo": "Batab ndox boo xam ne. Jaami Yàlla yaa cay naan, ñu di ko bëtte fa mu leen soob." }
76
7
{ "fr": "Ils accomplissent leurs voeux et ils redoutent un jour dont le mal s´étendra partout.", "wo": "Dañuy mottali seeni nisër tey ragal bis bu ayam wa tiis na ." }
76
8
{ "fr": "et offrent la nourriture, malgré son amour , au pauvre, à l´orphelin et au prisonnier,", "wo": "te lañuy bëgg ñam lépp, terewul ñu di ko leel, miskiin, yaak jirim yaak ña ñu tëj kaso," }
76
9
{ "fr": "(disant) : \"C´est pour le visage d´Allah que nous vous nourrissons : nous ne voulons de vous ni récompense ni gratitude.", "wo": "(te naan leen) : “noo ngi leen koy leele de : waaye bëggu nu ci ak pey walla gëram ngir Yàlla rekk tax." }
76
10
{ "fr": "Nous redoutons, de notre Seigneur, un jour terrible et catastrophique\".", "wo": "Danoo ragal, ci sunu Boroom, bis bu ñàng te tëradi” ." }
76
11
{ "fr": "Allah les protégera donc du mal de ce jour-là, et leur fera rencontrer la splendeur et la joie,", "wo": "Yàlla daldi leen fegal ayu boobale bis, dajale leen ak naataangeek mbégte," }
76
12
{ "fr": "et les rétribuera pour ce qu´ils auront enduré, en leur donnant le Paradis et des [vêtements] de soie,", "wo": "mu faye leen lañu muñoon, Àjjana ak i sooy," }
76
13
{ "fr": "ils y seront accoudés sur des divans, n´y voyant ni soleil ni froid glacial .", "wo": "dañuy sóonu ca lal ya, te dunu fa gis ab jant waxantumalaak ab sedd liw." }
76
14
{ "fr": "Ses ombrages les couvriront de près, et ses fruits inclinés bien bas [à portée de leurs mains].", "wo": "Keram ya da leen di muur, meññatam ma yóore tiim leen." }
76
15
{ "fr": "Et l´on fera circuler parmi eux des récipients d´argent et des coupes cristallines,", "wo": "Ñu di leen wër ak ay ndabi xaalis, ak ay koppi weer, " }
76
16
{ "fr": "en cristal d´argent, dont le contenu a été savamment dosé.", "wo": "ay koppi weeri xaalis, yu yem kepp." }
76
17
{ "fr": "Et là, ils seront abreuvés d´une coupe dont le mélange sera de gingembre,", "wo": "Ñu, di leen fa nàndale ak kaas yu ñu njare jinjeer," }
76
18
{ "fr": "puisé là-dedans à une source qui s´appelle Salsabil.", "wo": "ab bëtu ndox bu tudd Salsabiil." }
76
19
{ "fr": "Et parmi eux, circuleront des garçons éternellement jeunes. Quand tu les verras, tu les prendras pour des perles éparpillées.", "wo": "Te ay xalee ngay wër ca ñoom sax cig ndaw. Soo leen gisee, da ngay foog ne peme ju ñu tasaare la ñu.(r)" }
76
20
{ "fr": "Et quand tu regarderas là-bas, tu verras un délice et un vaste royaume.", "wo": "Soo ko gisee, danga fa gIisaale xeewal ak nguur gu màgg." }
76
21
{ "fr": "Ils porteront des vêtements verts de satin et de brocart. Et ils seront parés de bracelets d´argent. Et leur Seigneur les abreuvera d´une boisson très pure.", "wo": "Dañuy sol mbubbi sooy yu nëtëx werta. Moom la ñuy jiital waaje ko, te dañu leen di takkal caqi xaalis. Seen Boroom di leen fa ndàndale naan gu laab." }
76
22
{ "fr": "Cela sera pour vous une récompense, et votre effort sera reconnu.", "wo": "Lii nag mooy seen neexal, te seen jëf it lu ñu sant la." }
76
23
{ "fr": "En vérité c´est Nous qui avons fait descendre sur toi le Coran graduellement.", "wo": "Nun de Noo wàcce Alxuraan ci yaw ndànk-ndànk." }
76
24
{ "fr": "Endure donc ce que ton Seigneur a décrété, et n´obéis ni au pécheur, parmi eux, ni au grand mécréant.", "wo": "Muñal sa dogalub Boroom, te bul topp, ci ñoom, kenn kuy def bàkkaar walla mu di yéefar." }
76
25
{ "fr": "Et invoque le nom de ton Seigneur, matin et après-midi;", "wo": "Te na nga tudd sa turu Boroom, subaak ngoon ;" }
76
26
{ "fr": "et prosterne-toi devant Lui une partie de la nuit; et glorifie Le de longues [heures] pendant la nuit.", "wo": "te guddi gi it na nga Koy sujuudal ; te di ko sàbbaal [waxtuw] guddi lu bari." }
76
27
{ "fr": "Ces gens-là aiment [la vie] éphémère (la vie sur terre) et laissent derrière eux un jour bien lourd [le jour du Jugement].", "wo": "Ñoom dey da ñoo bëgg Àddina tey sàggane bis bu dis ginnaawal ko." }
76
28
{ "fr": "C´est Nous qui les avons créés et avons fortifié leur constitution. Quand Nous voulons, cependant, Nous les remplaçons [facilement] par leurs semblables.", "wo": "Nun Noo leen bind. May leen kàttan, te Sunu sooboon, Nu wuutal fi ñeneen." }
76
29
{ "fr": "Ceci est un rappel. Que celui qui veut prenne donc le chemin vers son Seigneur !", "wo": "Lii dey ag fàttali la. Képp ku mu soob man ngaa sóobu yoon jëm ca sa Boroom !" }
76
30
{ "fr": "Cependant, vous ne saurez vouloir, à moins qu´Allah veuille. Et Allah est Omniscient et Sage.", "wo": "Manu leen a sottal dara, te du dafa soob Yàlla. Moom ku Xam la ku Xereñ la." }
76
31
{ "fr": "Il fait entrer qui Il veut dans Sa miséricorde. Et quant aux injustes, Il leur a préparé un châtiment douloureux.", "wo": "Mooy tàbbal ku ko soob ci yërmëndéem. Te tooñkat yi, Waajalna leen mbugël mu mitti. " }
77
1
{ "fr": "Par ceux qu´on envoie en rafales .", "wo": "Maa ngi giñ ci ngelaw ya ñu yabal muy jaayu." }
77
2
{ "fr": "et qui soufflent en tempête !", "wo": "Ak yiy ràddi càllmeer!" }
77
3
{ "fr": "Et qui dispersent largement [dans toutes les directions].", "wo": "ak yiy gëwéeluy tasaare." }
77
4
{ "fr": "Par ceux qui séparent nettement (le bien et le mal) ,", "wo": "Ak yiy teqale dëgg ak fen (Laaya yi) ," }
77
5
{ "fr": "et lancent un rappel", "wo": "di sànni fàttali" }
77
6
{ "fr": "En guise d´excuse ou d´avertissement ! !", "wo": "Di jélële walla muy xuppe !" }
77
7
{ "fr": "Ce qui vous est promis est inéluctable.", "wo": "La ñu leen di tëkóo fàwwu mu ay (xew)." }
77
8
{ "fr": "Quand donc les étoiles seront effacées,", "wo": "Bu ru raafee biddiw yi," }
77
9
{ "fr": "et que le ciel sera fendu,", "wo": "daldi xar asamaan si," }
77
10
{ "fr": "et que les montagnes seront pulvérisées,", "wo": "moñoxe tundi doj yi," }
77
11
{ "fr": "et que le moment (pour la réunion) des Messagers a été fixé ! ...", "wo": "ak suñu dajalee Yonent ya !..." }
77
12
{ "fr": "A quel jour tout cela a-t-il été renvoyé ?", "wo": "Ana ban bis la doon xaar ?" }
77
13
{ "fr": "Au Jour de la Décision. [le Jugement] !", "wo": "Ca bisub àtte ba !" }
77
14
{ "fr": "Et qui te dira ce qu´est le Jour de la Décision ?", "wo": "Ana kan moo lay xamal luy bisub àtte ba ?" }
77
15
{ "fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.", "wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi." }
77
16
{ "fr": "N´avons-Nous pas fait périr les premières [générations] ?", "wo": "Moo ndax Nun faagaagalunu ñu jëkk ña ?(s)" }
77
17
{ "fr": "Puis ne les avons-Nous pas fait suivre par les derniers ?", "wo": "Toftal ca ña mujjoon ?" }
77
18
{ "fr": "C´est ainsi que Nous agissons avec les criminels.", "wo": "Noonu la ñuy def ak tooñkat ya." }
77
19
{ "fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.", "wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi." }
77
20
{ "fr": "Ne vous avons-Nous pas créés d´une eau vile ", "wo": "Moo ndax bindewunu leen ci ndox mu doyadi " }
77
21
{ "fr": "que Nous avons placée dans un reposoir sûr, ,", "wo": "Nu daldi koy saxal ci barab wu wóor," }
77
22
{ "fr": "pour une durée connue ?", "wo": "ba ca ab diir bu ñu xam ?" }
77
23
{ "fr": "Nous l´avons décrété ainsi et Nous décrétons [tout] de façon parfaite.", "wo": "Nu daldi dogal cëy Noo mana dogal yemale." }
77
24
{ "fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.", "wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi." }
77
25
{ "fr": "N´avons-Nous pas fait de la terre un endroit les contenant tous,", "wo": "Ndax defu nu suuf si mu làmboo lépp," }
77
26
{ "fr": "les vivants ainsi que les morts ?", "wo": "ñuy dund ak ñu dee ?" }
77
27
{ "fr": "Et n´y avons-Nous pas placé fermement de hautes montagnes ? Et ne vous avons-Nous pas abreuvés d´eau douce ?", "wo": "Te def Nanu ci ay tund doj yu kawe? Te nàndale leen ak ndox mu neex ?" }
77
28
{ "fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.", "wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi." }
77
29
{ "fr": "Allez vers ce que vous traitiez alors de mensonge !", "wo": "Fëxleen nag jëm ci li ngeen daan weddi !" }
77
30
{ "fr": "Allez vers une ombre [fumée de l´Enfer] à trois branches;", "wo": "Fëxleen jëm ca ker ga am ñatti tokkoor [saxaar sa] ;" }
77
31
{ "fr": "qui n´est ni ombreuse ni capable de protéger contre la flamme;", "wo": "Saar 77 : Ñu ñuy yabal ña 50 - Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
77
31
{ "fr": "qui n´est ni ombreuse ni capable de protéger contre la flamme;", "wo": "manuta keral kenn waxatumaak di feg tàkk-tàkk ;" }
77
32
{ "fr": "car [le feu] jette des étincelles volumineuses comme des châteaux,", "wo": "moom dafay sànni ay ferñent yu tollu ni njéndi," }
77
33
{ "fr": "et qu´on prendrait pour des chameaux jaunes.", "wo": "dañu melni ay giléem yu mboq." }
77
34
{ "fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.", "wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi." }
77
35
{ "fr": "Ce sera le jour où ils ne [peuvent] pas parler,", "wo": "Bu bis baa du ñu mana àddu wax," }
77
36
{ "fr": "et point ne leur sera donné permission de s´excuser.", "wo": "kenn du leen may pose bu ñuy jéggaloo." }
77
37
{ "fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.", "wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi." }
77
38
{ "fr": "C´est le Jour de la Décision [Jugement], où nous vous réunirons ainsi que les anciens.", "wo": "Lii mooy bisub àtte ba, boole nanu leen ak ñu jëkk ña." }
77
39
{ "fr": "Si vous disposez d´une ruse, rusez donc contre Moi.", "wo": "Su ngeen amee ay pexe, fexel leen Ma." }
77
40
{ "fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.", "wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi." }
77
41
{ "fr": "Les pieux seront parmi des ombrages et des sources.", "wo": "Ña ragal Yàlla ñoom ña nga ca ker ya ak bëti ndox ya." }
77
42
{ "fr": "De même que des fruits selon leurs désirs.", "wo": "Ak ay fuytéef ya ñu bëgg." }
77
43
{ "fr": "Mangez et buvez agréablement, pour ce que vous faisiez.", "wo": "“Lekkleen te naan, mooy peyug la ngeen daan jëf” ." }
77
44
{ "fr": "C´est ainsi que Nous récompensons les bienfaisants.", "wo": "Noonu la Ñuy faye way rafetal ya." }
77
45
{ "fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.", "wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi." }
77
46
{ "fr": "Mangez et jouissez un peu (ici-bas); vous êtes certes des criminels.", "wo": "“Lekkleen te bànneexu tuuti ; yéen ay tooñkat ngeen” . " }
77
47
{ "fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.", "wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi." }
77
48
{ "fr": "Et quand on leur dit : \"Inclinez-vous , ils ne s´inclinent pas.", "wo": "Te saasu ñu leen waxee ne : “rukóoleen, duñu rukoo (duñu julli)." }
77
49
{ "fr": "Malheur, ce jour-là, à ceux qui criaient au mensonge.", "wo": "Bu keroogee xuru safara ñeel na ñay weddi." }
77
50
{ "fr": "Après cela, en quelle parole croiront-ils donc ?", "wo": "Bu waxtaan wii jàllee, ana wan waxtaan lañuy gëmati ? " }
78
1
{ "fr": "Sur quoi s´interrogent-ils mutuellement ?", "wo": "Ana ci man mbir la ñuy laajante ?(h)" }
78
2
{ "fr": "Sur la grande nouvelle,", "wo": "Ci xibaar bu rëy ba," }
78
3
{ "fr": "à propos de laquelle ils divergent.", "wo": "xibaar ba nga xam ne dañu caa juuyoo." }
78
4
{ "fr": "Eh bien non ! Ils sauront bientôt.", "wo": "Mukk ! danañu xala xam." }
78
5
{ "fr": "Encore une fois, non ! Ils sauront bientôt.", "wo": "Déedéet kay ! Danañu xala xam." }
78
6
{ "fr": "N´avons-Nous pas fait de la terre une couche ?", "wo": "Moo ndax du Nun Noo def suuf si mu di laltaay ?" }
78
7
{ "fr": "et (placé) les montagnes comme des piquets ?", "wo": "ak tundi doj yi ñu di ay dott ?" }
78
8
{ "fr": "Nous vous avons créés en couples,", "wo": "Nu bind leen ngeen di ay tóllent," }