sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
80
22
{ "fr": "puis Il le ressuscitera quand Il voudra.", "wo": "te saa su Ko soobee mu dekkalaat Ko." }
80
23
{ "fr": "Eh bien non ! [L´homme] n´accomplit pas ce qu´Il lui commande.", "wo": "Déedéet ! [Nit] moom matalul mukk la nu ko digëloon." }
80
24
{ "fr": "Que l´homme considère donc sa nourriture :", "wo": "Na nit di xool ci aw ñamam lekkam :" }
80
25
{ "fr": "C´est Nous qui versons l´eau abondante,", "wo": "Nun noo sotti ndox mu dottiku," }
80
26
{ "fr": "puis Nous fendons la terre par fissures", "wo": "ba noppi Nu xar suuf mu fett" }
80
27
{ "fr": "et y faisons pousser grains,", "wo": "nu saxal ci ay kembu," }
80
28
{ "fr": "vignobles et légumes,", "wo": "ay reseñ ak i lujum," }
80
29
{ "fr": "oliviers et palmiers,", "wo": "ak i oliw ak tàndarma," }
80
30
{ "fr": "jardins touffus,", "wo": "ak ay dër yu naat," }
80
31
{ "fr": "fruits et herbages,", "wo": "ak i fuytéef ak i xob, ngub" }
80
32
{ "fr": "pour votre jouissance vous et vos bestiaux.", "wo": "mu di seen bànneex ak seenug jur." }
80
33
{ "fr": "Puis quand viendra le Fracas,", "wo": "Bu bis pénc ba dikkee," }
80
34
{ "fr": "le jour où l´homme s´enfuira de son frère,", "wo": "bis ba nit di daw mbokkam," }
80
35
{ "fr": "de sa mère, de son père,", "wo": "ak yaayam, ak baayam," }
80
36
{ "fr": "de sa compagne et de ses enfants,", "wo": "ak soxnaam ak doomam," }
80
37
{ "fr": "car chacun d´eux, ce jour-là, aura son propre cas pour l´occuper.", "wo": "kenn ku nekk, bu keroogee, am mbir mu ko doy sëkk." }
80
38
{ "fr": "ce jour-là, il y aura des visages rayonnants,", "wo": "bu keroogee, ay xarkanam yu naat," }
80
39
{ "fr": "riants et réjouis.", "wo": "bég lool tey ree." }
80
40
{ "fr": "De même qu´il y aura, ce jour-là, des visages couverts de poussière,", "wo": "Bu keroogee, am it, ay xarkanam yu fundóoñ," }
80
41
{ "fr": "recouverts de ténèbres.", "wo": "lëndëm kariis." }
80
42
{ "fr": "Voilà les infidèles, les libertins.", "wo": "Ñooña ñoo di yéefar ya, di kàccoor ya. " }
81
1
{ "fr": "Quand le soleil sera obscurci,", "wo": "Saa su ñu lëndamalee jant bi, Maa ngi giiñ(s)" }
81
2
{ "fr": "et que les étoiles deviendront ternes,", "wo": "ak saa su biddew yi rotee," }
81
3
{ "fr": "et les montagnes mises en marche,", "wo": "ak tundi doj yi saa su ñuy randatu di dox," }
81
4
{ "fr": "et les chamelles à terme , négligées,", "wo": "ak saa su nu, sàgganee geleemam ga ëmbu ba sori talatuñu ko," }
81
5
{ "fr": "et les bêtes farouches, rassemblées,", "wo": "ak ndokmenta ya (rab yu aaytal ya), dajaloo ñu dekkalaat leen," }
81
6
{ "fr": "et les mers allumées,", "wo": "ak saa su ñu taalee geej ya mu di safara," }
81
7
{ "fr": "et les âmes accouplées ", "wo": "ak saa su ñu lëkëlee ruu ya" }
81
8
{ "fr": "et qu´on demandera à la fillette enterrée vivante ", "wo": "ak saa su ñu laajee doom ju jigéen ja nu soloon te fekk muy dund, ngir daw gàcce" }
81
9
{ "fr": "pour quel péché elle a été tuée.", "wo": "ci ban bàkkaar bu mu def moo tax ñu rey ko." }
81
10
{ "fr": "Et quand les feuilles seront déployées ,", "wo": "Ak saa su ñu tasaaree kayit yi ëmboon jëfi bindéef yi," }
81
11
{ "fr": "et le ciel écorché ", "wo": "ak saa su nu xollee deri asamaan si" }
81
12
{ "fr": "et la fournaise attisée,", "wo": "ak saa su ñu taalee safaraw jahim," }
81
13
{ "fr": "et le Paradis rapproché,", "wo": "ak saas u ñu jigeelee Àjjana," }
81
14
{ "fr": "chaque âme saura ce qu´elle a présenté.", "wo": "bakkan bu Yàlla sàkk xam na la mu jëfoon." }
81
15
{ "fr": "Non ! ... Je jure par les planètes qui gravitent", "wo": "Déet !... Maa ngi giiñ ci biddiw yi fàq guddi" }
81
16
{ "fr": "qui courent et disparaissent !", "wo": "tey daw di suux !" }
81
17
{ "fr": "par la nuit quand elle survient !", "wo": "ak ci guddi gi saa suy tàmbali!" }
81
18
{ "fr": "et par l´aube quand elle exhale son souffle !", "wo": "ak ci suba si saa suy fenk!" }
81
19
{ "fr": "Ceci [le Coran] est la parole d´un noble Messager ,", "wo": "Ci ne [Alxuraan jii] waxi ab Yonent la bu tedd (Jibriil)," }
81
20
{ "fr": "doué d´une grande force, et ayant un rang élevé auprès du Maître du Trône,", "wo": "di boroom kàttan gu rëy, di ab xejj fa Boroom ganganaay ga Aras, " }
81
21
{ "fr": "obéi, là-haut, et digne de confiance.", "wo": "di ku ñuy digël, ndigëlam ca kaw, di ku ñu woolu." }
81
22
{ "fr": "Votre compagnon (Muhammad) n´est nullement fou;", "wo": "Te seen àndandoo ja (Muhammad) du ab dof de ;" }
81
23
{ "fr": "il l´a effectivement vu (Gabriel), au clair horizon", "wo": "moom gis na tigi (Jibriil), ca asamaan ya" }
81
24
{ "fr": "et il ne garde pas avarement pour lui-même ce qui lui a été révélé.", "wo": "te moom nayul ci li ñu ko soloo." }
81
25
{ "fr": "Et ceci [le Coran] n´est point la parole d´un diable banni.", "wo": "Te it [Alxuraan ji] du waxi seytaane sa ñu jam." }
81
26
{ "fr": "Où allez-vous donc ?", "wo": "Kon ana fu ngeen jëm ?" }
81
27
{ "fr": "Ceci n´est qu´un rappel pour l´univers,", "wo": "Lii du lenn lu dul luy fàttali waa àddina si yépp," }
81
28
{ "fr": "pour celui d´entre vous qui veut suivre le chemin droit.", "wo": "ku mu soob ci yéen mu topp yoon wu jub xocc wa." }
81
29
{ "fr": "Mais vous ne pouvez vouloir, que si Allah veut, [Lui], le Seigneur de l´Univers;", "wo": "Waaye manuleena soob mukk, te du ut ne dafa soob Yàlla, Boroom àddina si yépp ; " }
82
1
{ "fr": "Quand le ciel se rompra,", "wo": "Saa su asamaan si dogee, Maa ngi giñ(n)" }
82
2
{ "fr": "et que les étoiles se disperseront,", "wo": "ak saa su biddew yi tasaaroo," }
82
3
{ "fr": "et que les mers confondront leurs eaux,", "wo": "ak saa su géej yi taqaloo," }
82
4
{ "fr": "et que les tombeaux seront bouleversés,", "wo": "ak saa su bàmmeel ya jaxasoo," }
82
5
{ "fr": "toute âme saura alors ce qu´elle a accompli et ce qu´elle a remis de faire à plus tard.", "wo": "bakkan bu Yàlla sàkk xam na la mu jëkkoona def ak la mu mujja def." }
82
6
{ "fr": "ô homme ! Qu´est-ce qui t´a trompé au sujet de ton Seigneur, le Noble,", "wo": "Éy yaw nit ! Ana lan moo la fàbbi ci sa mbiru Boroom, bu Tedd bi," }
82
7
{ "fr": "qui t´a créé, puis modelé et constitué harmonieusement ?", "wo": "(sa Boroom) bi la bind yemale la, jekkal la ?" }
82
8
{ "fr": "Il t´a façonné dans la forme qu´Il a voulue.", "wo": "Moo la defar ca na mu ko soobe." }
82
9
{ "fr": "Non... ! [malgré tout] vous traitez la Rétribution de mensonge;", "wo": "Déet... ! [ak lu mana xew] yéen a ngay weddi bis pénc ba ;" }
82
10
{ "fr": "alors que veillent sur vous des gardiens ,", "wo": "te am na ay wattukat yu nekk ci seen kaw," }
82
11
{ "fr": "de nobles scribes,", "wo": "yu tedd yuy bind," }
82
12
{ "fr": "qui savent ce que vous faites.", "wo": "yuy xam li ngeen di def." }
82
13
{ "fr": "Les bons seront, certes, dans un [jardin] de délice,", "wo": "Ñu baax ñaa ngi ca biir àjjanay xéewal," }
82
14
{ "fr": "et les libertins seront, certes, dans une fournaise", "wo": "te itam kàccoor ya ñoom, ña nga ca biir safara jahiim" }
82
15
{ "fr": "où ils brûleront, le jour de Rétribution", "wo": "danañu ca xoyomoo, bu bis Pénc baa" }
82
16
{ "fr": "incapables de s´en échapper.", "wo": "te ñoom manuñu koo wuute." }
82
17
{ "fr": "Et qui te dira ce qu´est le jour de la Rétribution ?", "wo": "Ana lu lay xamal luy bis Pénc ?" }
82
18
{ "fr": "Encore une fois, qui te dira ce qu´est le jour de la Rétribution ?", "wo": "Ak lu lay xamal waay, luy bis Pénc ba ?" }
82
19
{ "fr": "Le jour où aucune âme ne pourra rien en faveur d´une autre âme. Et ce jour-là, le commandement sera à Allah.", "wo": "moo di bis ba benn bakkan dul manal moroomam tus. Te bu keroogee, Yàlla rekk ay joxe ndigël yi. " }
83
1
{ "fr": "Malheur aux fraudeurs", "wo": "Xuru safara ñeel na naxaatekat ya" }
83
2
{ "fr": "qui, lorsqu´ils font mesurer pour eux-mêmes exigent la pleine mesure,", "wo": "ñay natt peese di ëppal lay jëm ca ñoom," }
83
3
{ "fr": "et qui lorsqu´eux-mêmes mesurent ou pèsent pour les autres, [leur] causent perte.", "wo": "te su ñuy nattal keneen, wàññi ko." }
83
4
{ "fr": "Ceux-là ne pensent-ils pas qu´ils seront ressuscités,", "wo": "Xanaa ñoom dañoo jàpput ne dees na leen dekkilaat (ginnaaw dee)," }
83
5
{ "fr": "en un jour terrible,", "wo": "ca bis bu ñàng," }
83
6
{ "fr": "le jour où les gens se tiendront debout devant le Seigneur de l´Univers ?", "wo": "bis ba nit ña di taxaw ci kanam Boroom Àddina si yépp ?" }
83
7
{ "fr": "Non... ! Mais en vérité le livre des libertins sera dans le Sijjin", "wo": "Déet... ! Waaye téereb kàccoor yaa nga ca Sijjin de" }
83
8
{ "fr": "et qui te dira ce qu´est le Sijjin ? -", "wo": "ana lan moo lay xamal luy Sijjin ?" }
83
9
{ "fr": "un livre déjà cacheté (achevé).", "wo": "ab téere la bu ñu xas tàmpe." }
83
10
{ "fr": "Malheur, ce jour-là, aux négateurs,", "wo": "Bu keroogee, weddikat ya, danañu tàbbi xuru safara," }
83
11
{ "fr": "qui démentent le jour de la Rétribution.", "wo": "ña daan weddi bis Pénc ba." }
83
12
{ "fr": "Or, ne le dément que tout transgresseur, pécheur :", "wo": "te kenn, du ko weddi ku dul ab jalgatikat, buy def bàkkaar :" }
83
13
{ "fr": "qui, lorsque Nos versets lui sont récités, dit : \"[Ce sont] des contes d´anciens ! \"", "wo": "su ñu jàngee ci ñoom Laaya, dañu naan : “Léebi mag ña la!”" }
83
14
{ "fr": "Pas du tout, mais ce qu´ils ont accompli couvre leurs coeurs .", "wo": "Lañu daan def moo muur xomaagal seen xol ya.(s)" }
83
15
{ "fr": "Qu´ils prennent garde ! En vérité ce jour-là un voile les empêchera de voir leur Seigneur,", "wo": "Déet ! Ñoom kay bu keroogee duñu gis seen Boroom de," }
83
16
{ "fr": "ensuite, ils brûleront certes, dans la Fournaise;", "wo": "te, dees na leen lakk, Safara jahiim ;" }
83
17
{ "fr": "on [leur] dira alors : \"Voilà ce que vous traitiez de mensonge ! \"", "wo": "te di leen wax naan leen: “Lii ngeen daan weddi !”" }
83
18
{ "fr": "Qu´ils prennent garde ! Le livre des bons sera dans l´Illiyoun -", "wo": "Déetawaay ! Téereb ñu baax ñaa nga ca biir Illiyiina" }
83
19
{ "fr": "et qui te dira ce qu´est l´Illiyoun ? -", "wo": "Saar 83 : Naxekat ya 36 - Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
83
19
{ "fr": "et qui te dira ce qu´est l´Illiyoun ? -", "wo": "ana lan moo lay xamal luy Illiyiina ?" }
83
20
{ "fr": "un livre cacheté !", "wo": "ab téere la bu ñu xas tàmpe ! " }
83
21
{ "fr": "Les rapprochés (d´Allah : les Anges) en témoignent.", "wo": "Ña jege Yàlla koy seede (Malaaka ya)." }
83
22
{ "fr": "Les bons seront dans [un jardin] de délice,", "wo": "Ñu baax ñaa nga ca biir xeewal," }
83
23
{ "fr": "sur les divans, ils regardent.", "wo": "ña nga ne toŋŋ ca kaw toogu ya, di xool." }
83
24
{ "fr": "Tu reconnaîtras sur leurs visages, l´éclat de la félicité.", "wo": "Danga seere ca seen xarkanam ya, naataangey xéewël ya." }
83
25
{ "fr": "On leur sert à boire un nectar pur, cacheté,", "wo": "Ñu nandalu ci sàngaras àjjana suñu xàmmee," }
83
26
{ "fr": "laissant un arrière-goût de musc. Que ceux qui la convoitent entrent en compétition [pour l´acquérir]", "wo": "tem-temam misk lay doon. Ñiy rawante nañu rawante [ci am ko]" }
83
27
{ "fr": "Il est mélangé à la boisson de Tasnim ,", "wo": "Di njarum Tasniim," }
83
28
{ "fr": "source dont les rapprochés boivent.", "wo": "bëtub ndox la bu ña jegeñoo cay naan." }
83
29
{ "fr": "Les criminels riaient de ceux qui croyaient,", "wo": "Tooñkat ya dañu daan reetaan ña gëmoon," }
83
30
{ "fr": "et, passant près d´eux, ils se faisaient des oeillades,", "wo": "saa suñu leen rombaan, di leen ñaawal," }