sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
83
31
{ "fr": "et, retournant dans leurs familles, ils retournaient en plaisantant,", "wo": "bu ñu delluwaan ca seen njaboot, di ko kafe," }
83
32
{ "fr": "et les voyant, ils disaient : \"Ce sont vraiment ceux-là les égarés\".", "wo": "suñu leen masaana gis dañu daan wax ne : “Ñii dañoo sànku” ." }
83
33
{ "fr": "Or, ils n´ont pas été envoyés pour être leurs gardiens.", "wo": "Te, yabalunu leen ca ñoom ngir ñu daan leen wattu." }
83
34
{ "fr": "Aujourd´hui, donc, ce sont ceux qui ont cru qui rient des infidèles", "wo": "Tey jii nag, ñi gëm ñooy reetaan yéefar ya" }
83
35
{ "fr": "sur les divans, ils regardent.", "wo": "ña nga ne toŋŋ ca toogu ya, di xool." }
83
36
{ "fr": "Est-ce que les infidèles ont eu la récompense de ce qu´ils faisaient ?", "wo": "Moo ndax yéefar ya am nañu yoolub la ñu daan def ? " }
84
1
{ "fr": "Quand le ciel se déchirera", "wo": "Saa su asamaan si xottikoo! Maa ngi giiñ!" }
84
2
{ "fr": "et obéira à son Seigneur - et fera ce qu´il doit faire -", "wo": "te mu def – ndigalu boroomam dëggël" }
84
3
{ "fr": "et que la terre sera nivelée,", "wo": "ak saa suñu maasalee suuf si," }
84
4
{ "fr": "et qu´elle rejettera ce qui est en son sein (les morts) et se videra,", "wo": "te mu gëx lép lu nekk ci biiram," }
84
5
{ "fr": "et qu´elle obéira à son Seigneur - et fera ce qu´elle doit faire -", "wo": "moom it – mu def ngigëlu boroomam dëggël ko" }
84
6
{ "fr": "ô homme ! Toi qui t´efforces vers ton Seigneur sans relâche, tu Le rencontreras alors.", "wo": "Éy yaw nit ! Yaa ngi def jëm ci sa boroom, te danga dajeek moom de." }
84
7
{ "fr": "Celui qui recevra son livre en sa main droite,", "wo": "Képp ku ñu joxe téereem ci loxob ndeyjooram," }
84
8
{ "fr": "sera soumis à un jugement facile,", "wo": "dees na ko màndaxe mu jàppandal," }
84
9
{ "fr": "et retournera réjoui auprès de sa famille.", "wo": "muy walbatiku jëm cag njabootam di bég." }
84
10
{ "fr": "Quant à celui qui recevra son livre derrière son dos,", "wo": "Képp koo xam ne nag moom da ñu koo jox téereem ci ginnaawam," }
84
11
{ "fr": "il invoquera la destruction sur lui-même,", "wo": "Ngalla moom kon," }
84
12
{ "fr": "et il brûlera dans un feu ardent.", "wo": "te dana xoyomoo safaraw Sa’iir." }
84
13
{ "fr": "Car il était tout joyeux parme les siens,", "wo": "Moom ku bégoon la cag njabootam," }
84
14
{ "fr": "et il pensait que jamais il ne ressusciterait", "wo": "foogoon na ne du dekkiwaat mukk." }
84
15
{ "fr": "Mais si ! Certes, son Seigneur l´observait parfaitement.", "wo": "Axakañ boroomam daan na ko gis de." }
84
16
{ "fr": "Non ! ... Je jure par le crépuscule,", "wo": "Déet !... Maa ngi giiñ ci yeeri ji,(r)" }
84
17
{ "fr": "et par la nuit et ce qu´elle enveloppe,", "wo": "ak ci guddeek la mu làmboo," }
84
18
{ "fr": "et par la lune quand elle devient pleine-lune !", "wo": "ak ci weer wi su xàbbee wërngëlu mat !" }
84
19
{ "fr": "Vous passerez, certes, par des états successifs !", "wo": "Dingeen jaar, ay jaar-jaar yu tegaloo yu bari !" }
84
20
{ "fr": "Qu´ont-ils à ne pas croire ?", "wo": "Ana lu leen dal ba gëmuñu ? " }
84
21
{ "fr": "et à ne pas se prosterner quand le Coran leur est lu ?", "wo": "te suñu jàngee ci ñoom Alxuraan duñu sujuud ?" }
84
22
{ "fr": "Mais ceux qui ne croient pas, le traitent plutôt de mensonge.", "wo": "Yéefër ya, ñoo koy weddi." }
84
23
{ "fr": "Or, Allah sait bien ce qu´ils dissimulent.", "wo": "Yàlla xam na la ñuy xalaat." }
84
24
{ "fr": "Annonce-leur donc un châtiment douloureux.", "wo": "Na gneen leen xibaar mbugël mu mitti ma." }
84
25
{ "fr": "Sauf ceux qui croient et accomplissent les bonnes oeuvres : à eux une récompense jamais interrompue.", "wo": "Ba mu des ña gëm tey jëf yiw : ñoom am na ñu pey gu dootul dog. " }
85
1
{ "fr": "Par le ciel aux constellations !", "wo": "Ci asamaan sa di boroom biddiw yu mag ! Maa ngi giñ!" }
85
2
{ "fr": "et par le jour promis !", "wo": "ak ci bis ba ñu dige !" }
85
3
{ "fr": "et par le témoin et ce dont on témoigne !", "wo": "ak ci kuy seede ak ca ka ñuy seede !" }
85
4
{ "fr": "Périssent les gens de l´Ukhdoud ,", "wo": "Faagaagal na waa Uxduud," }
85
5
{ "fr": "par le feu plein de combustible,", "wo": "ak ci safara wa am lu koy xamb," }
85
6
{ "fr": "cependant qu´ils étaient assis tout autour,", "wo": "ca ba ñu toogee wër ko," }
85
7
{ "fr": "ils étaient ainsi témoins de ce qu´ils faisaient des croyants,", "wo": "te ñoom seede la ñu ca la ñu defoon way gëm ña," }
85
8
{ "fr": "à qui ils ne leur reprochaient que d´avoir cru en Allah, le Puissant, le Digne de louange,", "wo": "te fitnaale wu ñu leen ci lu dul ne da ñoo gëm Yàlla, boroom Kàttan ga, Yayoowaakooni cant ba," }
85
9
{ "fr": "Auquel appartient la royauté des cieux et de la terre. Allah est témoin de toute chose.", "wo": "Yàlla mi moom nguurug asamaan yeek suuf si. Te yàlla seede la ci lépp lu ne." }
85
10
{ "fr": "Ceux qui font subir des épreuves aux croyants et aux croyantes, puis ne se repentent pas, auront le châtiment de l´Enfer et le supplice du feu.", "wo": "Ña daan fitnaal jullit yu góor yaak yu jigéen ya, te tubu ñu ko, dananu am mbugëlum Jahanama ñu di leen ca lakk. (ca safaraam wa)" }
85
11
{ "fr": "Ceux qui croient et accomplissent les bonnes oeuvres auront des Jardins sous lesquels coulent les ruisseaux. Cela est le grand succès.", "wo": "Ña gëmoon te daan jëf yiw am nañu ay Àjjana yu ay dex di daw ci suufam. Loolu moo di texe gu mag ga." }
85
12
{ "fr": "La riposte de ton Seigneur est redoutable.", "wo": "Sa fayug boroom lu tar la.(s)" }
85
13
{ "fr": "C´est Lui, certes, qui commence (la création) et la refait.", "wo": "Moom mooy, sos bindeef yi, te mooleen di dekkilaat." }
85
14
{ "fr": "Et c´est Lui le Pardonneur, le Tout Affectueux,", "wo": "Te moom moo di Jéggëlaakoon bi, di soppi lépp," }
85
15
{ "fr": "Le Maître du Trône, le Tout Glorieux,", "wo": "Mooy boroom Gàngunaay gu Màgg ga (Aras)," }
85
16
{ "fr": "Il réalise parfaitement tout ce qu´Il veut.", "wo": "Lu mu namm dana ko def." }
85
17
{ "fr": "T´est-il parvenu le récit des armées,", "wo": "Moo ndax waxtaanu xarekat ya dikal na la ( xibaar ya)," }
85
18
{ "fr": "de Pharaon, et de Tamud ?", "wo": "Firawna, ak Samuud ? " }
85
19
{ "fr": "Mais ceux qui ne croient pas persistent à démentir,", "wo": "Yéefër ya dañuy weddi," }
85
20
{ "fr": "alors qu´Allah, derrière eux, les cerne de toutes parts.", "wo": "te Yàlla ngi leen peeg, ci wet gu nekk." }
85
21
{ "fr": "Mais c´est plutôt un Coran glorifié", "wo": "li wér mooy Alxuraan ju màgg la" }
85
22
{ "fr": "préservé sur une Tablette (auprès d´Allah).", "wo": "ca biir Àlluwa ja ñu wàttu fa Yàlla (Lawhul Mahfuus ). " }
86
1
{ "fr": "Par le ciel et par l´astre nocturne", "wo": "Ci asamaan ak biddiwub guddi ba! Maa ngi giiñ" }
86
2
{ "fr": "Et qui te dira ce qu´est l´astre nocturne ?", "wo": "Ana lan moo lay xamal luy biddiwub guddi ba ?" }
86
3
{ "fr": "C´est l´étoile vivement brillante.", "wo": "moo di biddiw bay leer nàññ." }
86
4
{ "fr": "Il n´est pas d´âme qui n´ait sur elle un gardien.", "wo": "Amul benn bakkan bu amul ku koy wattu." }
86
5
{ "fr": "Que l´homme considère donc de quoi il a été créé.", "wo": "na nit ki xool ana ci lan la ñu ko binde?" }
86
6
{ "fr": "Il a été créé d´une giclée d´eau", "wo": "Da ñu ko binde ci ndox muy sereti" }
86
7
{ "fr": "sortie d´entre les lombes et les côtes.", "wo": "di génne ci diggënte ndigg li ak faar yi." }
86
8
{ "fr": "Allah est certes capable de le ressusciter.", "wo": "Yàllaa ka koo mana dekalaat." }
86
9
{ "fr": "Le jour où les coeurs dévoileront leurs secrets,", "wo": "Bis bu sekerey mbóot di deefu ko wuññi (xol yi)," }
86
10
{ "fr": "Il n´aura alors ni force ne secoureur.", "wo": "Du ci am kàttan te deefu ko dimbali." }
86
11
{ "fr": "Par le ciel qui fait revenir la pluie !", "wo": "Ci asamaan siy taw aka tawaat !" }
86
12
{ "fr": "et par la terre qui se fend !", "wo": "ak ci suuf siy toj sax gàncax !" }
86
13
{ "fr": "Ceci [le Coran] est certes, une parole décisive [qui tranche entre le vrai et le faux],", "wo": "Alxuraan dafay teqale dëgg at fen," }
86
14
{ "fr": "et non point une plaisanterie frivole !", "wo": "du ay kafi mbóosóor !" }
86
15
{ "fr": "Ils se servent d´une ruse,", "wo": "Ña ngay fexe ay pexe," }
86
16
{ "fr": "et Moi aussi Je me sers de Mon plan.", "wo": "Man it Maa ngi fexe ay pexe." }
86
17
{ "fr": "Accorde (ô Prophète) donc un délai aux infidèles : accorde-leur un court délai.", "wo": "Éy yaw Yonent muñalal yéefar yi : xaarleen as ndiir. " }
87
1
{ "fr": "Glorifie le nom de ton Seigneur, le Très Haut,", "wo": "Sàbbaalal sa turu Boroom, bi Gëna kawe,(h)" }
87
2
{ "fr": "Celui Qui a crée et agencé harmonieusement,", "wo": "Ki bind jekkal yemale," }
87
3
{ "fr": "qui a décrété et guidé,", "wo": "kiy dogal tey gindee," }
87
4
{ "fr": "et qui a fait pousser le pâturage,", "wo": "kiy génne ñax mi saxal ko," }
87
5
{ "fr": "et en a fait ensuite un foin sombre.", "wo": "di ko naatal dëlël ko." }
87
6
{ "fr": "Nous te ferons réciter (le Coran), de sorte que tu n´oublieras", "wo": "Dananu la jàngal (Alxuraan), te doo too ko fàtte" }
87
7
{ "fr": "que ce qu´Allah veut. Car, Il connaît ce qui paraît au grand jour ainsi que ce qui est caché.", "wo": "lu dul la soob Yàlla. Moom moo xam li feeñ ak li nëbbu." }
87
8
{ "fr": "Nous te mettrons sur la voie la plus facile.", "wo": "Dananu la jàppandalal yoon wi gëna yomb." }
87
9
{ "fr": "Rappelle, donc, où le Rappel doit être utile.", "wo": "Na ngay fàttelee, saa su fàtteli amee njariñ." }
87
10
{ "fr": "Quiconque craint (Allah) s´[en] rappellera,", "wo": "képp kuy ragal (Yàlla) na nangoo fàttaliku," }
87
11
{ "fr": "et s´en écartera le grand malheureux,", "wo": "ñu texeedi ñaa koy moytu," }
87
12
{ "fr": "qui brûlera dans le plus grand Feu,", "wo": "ñay lakk ca safara sa gëna rëy," }
87
13
{ "fr": "où il ne mourra ni ne vivra.", "wo": "du fa dund dufa dee." }
87
14
{ "fr": "Réussit, certes, celui qui se purifie,", "wo": "Képp kuy sellal texe na," }
87
15
{ "fr": "et se rappelle le nom de son Seigneur, puis célèbre la Salat.", "wo": "te fàttaliku turu boroomam , tey julli." }
87
16
{ "fr": "Mais, vous préférez plutôt la vie présente,", "wo": "Yeen, dangeena bëgg lool dundug àddina," }
87
17
{ "fr": "alors que l´au-delà est meilleur et plus durable.", "wo": "Saar 87 : Ku gëna kawe ka 19 Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
87
17
{ "fr": "alors que l´au-delà est meilleur et plus durable.", "wo": "te àllaaxira gën te moo gëna sax." }
87
18
{ "fr": "Ceci se trouve, certes, dans les Feuilles anciennes,", "wo": "Lii nekk na, ca téere yu jëkk ya," }
87
19
{ "fr": "les Feuilles d´Abraham et de Moïse.", "wo": "téerey Ibraahiima ak Muusaa. " }
88
1
{ "fr": "T´est-il parvenu le récit de l´enveloppante ? ", "wo": "Moo ndax yaw waxtaanu muuraakoon ba dikkal na la (ay xibaaram) ?" }
88
2
{ "fr": "Ce jour-là, il y aura des visages humiliés,", "wo": "Bu keroogee, ay xarkanam yu fooyooy," }
88
3
{ "fr": "préoccupés, harassés.", "wo": "yu sonn, fundóoñ." }
88
4
{ "fr": "Ils brûleront dans un Feu ardent,", "wo": "Di lakk ci Safara wu tàng," }
88
5
{ "fr": "et seront abreuvés d´une source bouillante.", "wo": "ñu di ko nandal ci bët buy wañax. (ndox)" }
88
6
{ "fr": "Il n´y aura pour eux d´autre nourriture que des plantes épineuses [darii],", "wo": "Amuñu fa genn lekk lu dul [darii] ay dég," }
88
7
{ "fr": "qui n´engraisse, ni n´apaise la faim.", "wo": "du rëyloo, du teggib xiif." }
88
8
{ "fr": "Ce jour-là, il y aura des visages épanouis,", "wo": "Bu keroogee, ay xarkanam yu nooy," }
88
9
{ "fr": "contents de leurs efforts,", "wo": "bég lool ca seeni jëf," }
88
10
{ "fr": "dans un haut Jardin,", "wo": "ci biir ay Àjjana yu kawe," }