sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
92
17
{ "fr": "alors qu´en sera écarté le pieux,", "wo": "dees na ko soril ñu ragal Yàlla ña," }
92
18
{ "fr": "qui donne ses biens pour se purifier", "wo": "kay joxe alalam ngir selal" }
92
19
{ "fr": "et auprès de qui personne ne profite d´un bienfait intéressé,", "wo": "te amul genn xéewal gu ñuy faye kenn ca moom," }
92
20
{ "fr": "mais seulement pour la recherche de La Face de son seigneur le Très-Haut .", "wo": "Lu dul sàkku jëmm Boroomam ja gëna Kawe. " }
92
21
{ "fr": "Et certes, il sera bientôt satisfait !", "wo": "Te, xalset naa gëram (moom ka def noona) ! " }
93
1
{ "fr": "Par le Jour Montant !", "wo": "Ci yoor-yoor bi ! Maa ngi giñ" }
93
2
{ "fr": "Et par la nuit quand elle couvre tout !", "wo": "ak ci guddi gi bu kukkee ! ne" }
93
3
{ "fr": "Ton Seigneur ne t´a ni abandonné, ni détesté.", "wo": "Sa Boroom bàyyiwula, te bañu la." }
93
4
{ "fr": "La vie dernière t´est, certes, meilleure que la vie présente.", "wo": "Te àllaaxira, mooy, gën ci Yaw àddina de." }
93
5
{ "fr": "Ton Seigneur t´accordera certes [Ses faveurs], et alors tu seras satisfait.", "wo": "Te sa Boroom dana la jox, ba nga doyal." }
93
6
{ "fr": "Ne t´a-t-Il pas trouvé orphelin ? Alors Il t´a accueilli !", "wo": "Moo ndax fekku la ngay jirim ? Mu fat la !" }
93
7
{ "fr": "Ne t´a-t-Il pas trouvé égaré ? Alors Il t´a guidé.", "wo": "Ak it ndax fekku la nga réer ? Mu gindila." }
93
8
{ "fr": "Ne t´a-t-Il pas trouvé pauvre ? Alors Il t´a enrichi.", "wo": "Moo ndax fekku la nga ñàkk ? Mu woomalal la." }
93
9
{ "fr": "Quant à l´orphelin, donc, ne le maltraite pas.", "wo": "Jirim, nag, bu ko di xorñooñal." }
93
10
{ "fr": "Quant au demandeur , ne le repousse pas.", "wo": "Te laajkat it, bu ko di delloo." }
93
11
{ "fr": "Et quant au bienfait de ton Seigneur, proclame-le.", "wo": "Te it na ngay waxtaane, sa xéewalu Boroom. " }
94
1
{ "fr": "N´avons-Nous pas ouvert pour toi ta poitrine ?", "wo": "Moo ndax féexalu nu la sa dënn ?(n)" }
94
2
{ "fr": "Et ne t´avons-Nous pas déchargé du fardeau", "wo": "Te nu teggil la say bàkkaar" }
94
3
{ "fr": "qui accablait ton dos ?", "wo": "ya diisaloon sa ginnaaw ?" }
94
4
{ "fr": "Et exalté pour toi ta renommée ?", "wo": "Te yékatil nanu la saw tur ?" }
94
5
{ "fr": "A côté de la difficulté est, certes, une facilité !", "wo": "Jafe-jafe bu nekk, àndanaak ug yombal !" }
94
6
{ "fr": "A côté de la difficulté, est certes, une facilité !", "wo": "Jafe-jafe bu nekk, àndanaak ug yombal !" }
94
7
{ "fr": "Quand tu te libères, donc, lève-toi ,", "wo": "Te saa yoo féexee, jógël, (julli)" }
94
8
{ "fr": "et à ton Seigneur aspire.", "wo": "te it na ngay xemmeem jëm ci sa Boroom. " }
95
1
{ "fr": "Par le figuier et l´olivier !", "wo": "Ci garabug fig ak oliw Maa ngi giñ !" }
95
2
{ "fr": "Et par le Mont Sinin !", "wo": "Ak ci tund Siiniin (Siinaa’i) !" }
95
3
{ "fr": "Et par cette Cité sûre !", "wo": "Ak ca réew mu wóor mii di (Màkka) ! ne" }
95
4
{ "fr": "Nous avons certes créé l´homme dans la forme la plus parfaite.", "wo": "Bind nanu nit ci gën ja rafeti anam." }
95
5
{ "fr": "Ensuite, Nous l´avons ramené au niveau le plus bas,", "wo": "Top, waaye man naa dem ba gëna suufe lépp lu suufe," }
95
6
{ "fr": "sauf ceux qui croient et accomplissent les bonnes oeuvres : ceux-là auront une récompense jamais interrompue.", "wo": "ba mu des ña gëm tey jëfu yiw : ñoom dananu am pey gu dootul dog." }
95
7
{ "fr": "Après cela, qu´est-ce qui te fait traiter la rétribution de mensonge ?", "wo": "Bu loolu wéyee, ana lan moo tax ngay weddi bisub faytoo ba (bis pénc) ?" }
95
8
{ "fr": "Allah n´est-Il pas le plus sage des Juges ?", "wo": "Saar 95 : Garabu Figg 8 - Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
95
8
{ "fr": "Allah n´est-Il pas le plus sage des Juges ?", "wo": "Moo xanaa Yàlla dafa dul ki dàqa àtte àttekat yi ? " }
96
1
{ "fr": "Lis, au nom de ton Seigneur qui a créé,", "wo": "Jàngal, ci sa turu Boroom biy bind," }
96
2
{ "fr": "qui a créé l´homme d´une adhérence.", "wo": "moo bind nit ci lumbu deret." }
96
3
{ "fr": "Lis ! Ton Seigneur est le Très Noble,", "wo": "Jàngal ! Sa Boroom mooy ki gëna tedd," }
96
4
{ "fr": "qui a enseigné par la plume [le calame],", "wo": "mooy kiy xamle ci xalima [mbind]," }
96
5
{ "fr": "a enseigné à l´homme ce qu´il ne savait pas.", "wo": "moo xamal nit lamu xamut woon." }
96
6
{ "fr": "Prenez-garde ! Vraiment l´homme devient rebelle,", "wo": "Waaye nit kat dafay bew," }
96
7
{ "fr": "dès qu´il estime qu´il peut se suffire à lui-même (à cause de sa richesse).", "wo": "bu gisee dafa woomal man boppam." }
96
8
{ "fr": "Mais, c´est vers ton Seigneur qu´est le retour.", "wo": "Saar 96 : Lumbu deret 19 Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
96
8
{ "fr": "Mais, c´est vers ton Seigneur qu´est le retour.", "wo": "(Xamal ne), sa Boroom mooy delluwaay ba." }
96
9
{ "fr": "As-tu vu celui qui interdit", "wo": "Xanaa gisoo waa jay tere" }
96
10
{ "fr": "à un serviteur d´Allah (Muhammad) de célébrer la Salat ?", "wo": "ab jamub Yàlla (Muhammad) ci muy taxawal Julli ?" }
96
11
{ "fr": "Vois-tu s´il est sur la bonne voie,", "wo": "Xanaa gisoo ni tey su nekkoon ci njub," }
96
12
{ "fr": "ou s´il ordonne la piété ?", "wo": "walla muy digale ragal Yàlla ?" }
96
13
{ "fr": "Vois-tu s´il dément et tourne le dos ?", "wo": "Xanaa gisoo su weddi woon tey dumóoyu ?" }
96
14
{ "fr": "Ne sait-il pas que vraiment Allah voit ?", "wo": "Xanaa dafa xamul ne Yàllaa ngi gis ?" }
96
15
{ "fr": "Mais non ! S´il ne cesse pas, Nous le saisirons certes, par le toupet,", "wo": "Déedéet ! Su ko bàyyiwul, Dananu jiñ, mbaq ko," }
96
16
{ "fr": "le toupet d´un menteur, d´un pécheur.", "wo": "ni ñuy mbaqi, fenkat buy defkatu bàkkaar." }
96
17
{ "fr": "Qu´il appelle donc son assemblée.", "wo": "Na woo gàngooram ga." }
96
18
{ "fr": "Nous appellerons les gardiens (de l´Enfer).", "wo": "Nun dananu woo wattukati (Safara)." }
96
19
{ "fr": "Non ! Ne lui obéis pas; mais prosterne-toi et rapproche-toi ", "wo": "Déedéet ! Yaw dey bu ko topp ; te na ngay sujood tey jige jigelu lu (sa Boroom). " }
97
1
{ "fr": "Nous l´avons certes, fait descendre (le Coran) pendant la nuit d´Al-Qadr.", "wo": "Wàcce nanu ko (Alxuraan) ci guddig dogal ba (Laylatul Qadri)." }
97
2
{ "fr": "Et qui te dira ce qu´est la nuit d´Al-Qadr ?", "wo": "Ana lan moo lay xamal laylatul Qadri ?" }
97
3
{ "fr": "La nuit d´Al-Qadr est meilleure que mille mois.", "wo": "Laylatul Qadri moo gën junni weer." }
97
4
{ "fr": "Durant celle-ci descendent les Anges ainsi que l´Esprit , par permission de leur Seigneur pour tout ordre.", "wo": "Ci guddi googu Malaaka ya, dañu cay wàcci àndak (Jibriil) ci seen ndigalu Boroom ci mépp mbir." }
97
5
{ "fr": "Elle est paix et salut jusqu´à l´apparition de l´aube.", "wo": "Jàmm rekk la ba baa njël di jot (fajar sa di xar). " }
98
1
{ "fr": "Les infidèles parmi les gens du Livre, ainsi que les Associateurs, ne cesseront pas de mécroire jusqu´à ce que leur vienne la Preuve évidente :", "wo": "Yéefër ya bokk ca ñoñ Téere, ak Bokkaalekat ya, du ñu deñ mukk di weddi ba baa Firnde di leen dikkël ju leer :(s)" }
98
2
{ "fr": "un Messager, de la part d´Allah, qui leur récite des feuilles purifiées,", "wo": "ab Yonent, bu jóge ca Yàlla, di jàng ay xëti këyit yu sell laab," }
98
3
{ "fr": "dans lesquelles se trouvent des prescriptions d´une rectitude parfaite.", "wo": "ay téere nekk ci biir yu ame dayo bu màgg." }
98
4
{ "fr": "Et ceux à qui le Livre a été donné ne se sont divisés qu´après que la preuve leur fut venue.", "wo": "Te gaa ña ñu joxoon téere masuñoo teqalikoo lu dul ginnaaw ba leen firnde ja dikkëlee." }
98
5
{ "fr": "Il ne leur a été commandé, cependant, que d´adorer Allah, Lui vouant un culte exclusif, d´accomplir la Salat et d´acquitter la Zakat. Et voilà la religion de droiture.", "wo": "Saar 98 : Firnde 8 - Laaya – Gannaaw Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
98
5
{ "fr": "Il ne leur a été commandé, cependant, que d´adorer Allah, Lui vouant un culte exclusif, d´accomplir la Salat et d´acquitter la Zakat. Et voilà la religion de droiture.", "wo": "Te digaleefu leen, lu dul, na nuy jaamu Yàlla, bañ Koo bokkaale te di ko sellal, tey taxawal Julli di joxe asaka. Loolu mooy diiney njub ja." }
98
6
{ "fr": "Les infidèles parmi les gens du Livre, ainsi que les Associateurs iront au feu de l´Enfer, pour y demeurer éternellement. De toute la création, ce sont eux les pires.", "wo": "Ñay weddi te bokk ci ñoñ téere, ak Bokkaalekat ya ñoom ña nga ca biir Safaraw Jahanama, te danu fay béel. Ñoom ñii, ñoo yées ci bindeef yi." }
98
7
{ "fr": "Quant à ceux qui croient et accomplissent les bonnes oeuvres, ce sont les meilleurs de toute la création.", "wo": "Ñi gëm tey jëfu yiw, ñoom ñoo ñee ñoo gën ci bindeef yi." }
98
8
{ "fr": "Leur récompense auprès d´Allah sera les Jardins de séjour, sous lesquels coulent les ruisseaux, pour y demeurer éternellement. Allah les agrée et ils L´agréent. Telle sera [la récompense] de celui qui craint son Seigneur.", "wo": "Seenug pey fa seen Boroom Àjjanay adan lay doon, yoo xam ne ay dex ñooy daw ci suufam, ñu béel fa. Yàlla gëram leen ñoom it ñu gëram ko. Loolu ku ragal Yàlla rekk koy am. " }
99
1
{ "fr": "Quand la terre tremblera d´un violent tremblement,", "wo": "Saa su suuf si yëngutoo yëngoom ba," }
99
2
{ "fr": "et que la terre fera sortir ses fardeaux ,", "wo": "te suuf si génne la mu suuloon," }
99
3
{ "fr": "et que l´homme dira : \"Qu´a-t-elle ? \"", "wo": "nit naan : “Ngala man ?”" }
99
4
{ "fr": "ce jour-là, elle contera son histoire,", "wo": "bu keroogee, ci lay waxtaane ay xibaar," }
99
5
{ "fr": "selon ce que ton Seigneur lui aura révélé [ordonné].", "wo": "ci la ko sa Boroom soloo." }
99
6
{ "fr": "Ce jour-là, les gens sortiront séparément pour que leur soient montrées leurs oeuvres.", "wo": "Bu keroogee, nit ñéppay génn kenn kenn ngir ñu wan leen seeni jëf." }
99
7
{ "fr": "Quiconque fait un bien fût-ce du poids d´un atome, le verra,", "wo": "Képp ku jëf lu toll ni aw fepp te muy lu baax, dana ko gis," }
99
8
{ "fr": "et quiconque fait un mal fût-ce du poids d´un atome, le verra.", "wo": "Saar 99 : Yëngutu ba 8 - Laaya – Gannaaw Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
99
8
{ "fr": "et quiconque fait un mal fût-ce du poids d´un atome, le verra.", "wo": "Képp ku jëf lu toll ni aw fepp su dee lu bon, dana ko gis. " }
100
1
{ "fr": "Par les coursiers qui halètent,", "wo": "Ca jaabkat ya seeni gimiñ di foor (fas) (Maa ngi giñ)," }
100
2
{ "fr": "qui font jaillir des étincelles,", "wo": "tey këdaa seen tànk ya my xuuy (ferñent)," }
100
3
{ "fr": "qui attaquent au matin.", "wo": "ak yay songe suba coy." }
100
4
{ "fr": "et font ainsi voler la poussière,", "wo": "yay naawal pënd," }
100
5
{ "fr": "et pénètrent au centre de la troupe ennemie.", "wo": "tey xuus ca biir noon ya." }
100
6
{ "fr": "L´homme est, certes, ingrat envers son Seigneur;", "wo": "Nit dey, kuy ñàkk deloo Boroomam njukal la ;" }
100
7
{ "fr": "et pourtant, il est certes, témoin de cela;", "wo": "te kat, moom, seede la ci loolu ;" }
100
8
{ "fr": "et pour l´amour des richesses il est certes ardent.", "wo": "Saar 100 : Jaabkat ya 11- Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
100
8
{ "fr": "et pour l´amour des richesses il est certes ardent.", "wo": "te kat moom ku tarla xérlool ci bëgg alal." }
100
9
{ "fr": "Ne sait-il donc pas que lorsque ce qui est dans les tombes sera bouleversé,", "wo": "Xanaa dafa xamul saa su ñu ko jaxasee ci biir bàmmeel,(r)" }
100
10
{ "fr": "et que sera dévoilé ce qui est dans les poitrines,", "wo": "te wuñées li nekk ci biir dënn yi," }
100
11
{ "fr": "ce jour-là, certes, leur Seigneur sera Parfaitement Connaisseur d´eux ?", "wo": "bu keroogee, sa Boroom Ku deñ Kumpa la ci ñoom? " }
101
1
{ "fr": "Le fracas !", "wo": "Toj-toj ba !" }
101
2
{ "fr": "Qu´est-ce que le fracas ?", "wo": "Ana lan mooy toj-toj ba ?" }
101
3
{ "fr": "Et qui te dira ce qu´est le fracas ?", "wo": "Ana lan moo lay xamal luy toj-toj ba ?" }
101
4
{ "fr": "C´est le jour où les gens seront comme des papillons éparpillés,", "wo": "Moo di bis ba nit ñi di melni ay lëpaalëpp yu ñu wasaare," }
101
5
{ "fr": "et les montagnes comme de la laine cardée;", "wo": "te tund doj yi it mujj mel ni ngëndal nooy nepp ;" }
101
6
{ "fr": "quant à celui dont la balance sera lourde", "wo": "képp ku peeseem diis (ci yiw)" }
101
7
{ "fr": "il sera dans une vie agréable;", "wo": "ma nga ko ca dundu gu neex ;" }
101
8
{ "fr": "et quant à celui dont la balance sera légère,", "wo": "képp ku peeseem wayaf (ci yiw)," }
101
9
{ "fr": "sa mère [destination] est un abîme très profond.", "wo": "ma ngay jëm Haawiyatu." }
101
10
{ "fr": "Et qui te dira ce que c´est ?", "wo": "Ana luy xamal lan mooy loolu Haawiyatu ?" }
101
11
{ "fr": "C´est un Feu ardent.", "wo": "Saar 101 : Toj-toj ba 11 - Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
101
11
{ "fr": "C´est un Feu ardent.", "wo": "Aw Safara la wu tàng. " }