sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
70
9
{ "fr": "et les montagnes comme de la laine,", "wo": "tund doj yi melni ngëndal," }
70
10
{ "fr": "où nul ami dévoué ne s´enquerra d´un ami,", "wo": "benn xarit dootul laajte xaritam," }
70
11
{ "fr": "bien qu´ils se voient l´un l´autre. Le criminel aimerait pouvoir se racheter du châtiment de ce jour, en livrant ses enfants,", "wo": "danañuy gisante. Su boobaa tooñkat bi danaa siiw jot boppam, joxe njabootam," }
70
12
{ "fr": "sa compagne, son frère,", "wo": "ak soxnaam, ak mbokkam," }
70
13
{ "fr": "même son clan qui lui donnait asile,", "wo": "ak askanam wa ko yiir," }
70
14
{ "fr": "et tout ce qui est sur la terre, tout, qui pourrait le sauver.", "wo": "ak sax far képp ku nekk ci kaw suuf, ngir mu mana mucc." }
70
15
{ "fr": "Mais rien [ne le sauvera]. [L´Enfer] est un brasier", "wo": "Mukk dootul raw Safara" }
70
16
{ "fr": "arrachant brutalement la peau du crâne.", "wo": "(Tàng) bay wësëm kaaŋum bopp." }
70
17
{ "fr": "Il appellera celui qui tournait le dos et s´en allait,", "wo": "Dafay woo képp ku ne wërëñ ba bëgg a dem," }
70
18
{ "fr": "amassait et thésaurisait.", "wo": "dajaley alal ba dencu ko." }
70
19
{ "fr": "Oui, l´homme a été créé instable [très inquiet];", "wo": "Bindéef na nit ci xel muy jaxasoo [di yoqat] ; " }
70
20
{ "fr": "quand le malheur le touche, il est abattu;", "wo": "su ko aw ay laalee, muy saalit ;" }
70
21
{ "fr": "et quand le bonheur le touche, il est refuseur.", "wo": "su ko jàmm ganesee mu nay, alal ak yiw danay tax mu nay bew." }
70
22
{ "fr": "Sauf ceux qui pratiquent la Salat", "wo": "Ba mu des jullikat yi" }
70
23
{ "fr": "qui sont assidu à leurs Salats,", "wo": "ña nga xam ne dañuy saxoo Julli," }
70
24
{ "fr": "et sur les bien desquels il y a un droit bien déterminé [la Zakat]", "wo": "ña nga xam ne seeni alal sàkk nañu ca cér bus xam jagle ko" }
70
25
{ "fr": "pour le mendiant et le déshérité;", "wo": "mu ñéel yalwaankat yeek ñu ñakk ñi ;" }
70
26
{ "fr": "et qui déclarent véridique le Jour de la Rétribution,", "wo": "ak ñiy dëggël Bis Pénc bi," }
70
27
{ "fr": "et ceux qui craignent le châtiment de leur Seigneur", "wo": "ak ñiy ragal seen mbugalum Boroom" }
70
28
{ "fr": "car vraiment, il n´y a nulle assurance contre le châtiment de leur Seigneur;", "wo": "te, sa mbugalum Boroom kenn du ca naagu ;" }
70
29
{ "fr": "et qui se maintiennent dans la chasteté", "wo": "ak ñiy sàmm seen pëy" }
70
30
{ "fr": "et n´ont pas de rapports qu´avec leurs épouses ou les esclaves qu´ils possèdent car dans ce cas, ils ne sont pas blâmables,", "wo": "lu dul ca seeni soxna ak seeni jébéer, ñoom kenn yeddu leen," }
70
31
{ "fr": "mais ceux qui cherchent [leur plaisir] en dehors de cela, sont des transgresseurs;", "wo": "képp kuy sàkku [bànneex] ci lu moy loolu, ñoo ñaa di way jalgati ya ;" }
70
32
{ "fr": "et qui gardent les dépôts confiés à eux, et respectent leurs engagements scrupuleusement.", "wo": "ak ñay sàmm ndénkaane ya, ak seenub dëelante." }
70
33
{ "fr": "et qui témoignent de la stricte vérité,", "wo": "ak ñiy taxaw temm ci li ñuy seede," }
70
34
{ "fr": "et qui sont régulier dans leur Salat.", "wo": "ak ñiy matal sëkk seeni julli." }
70
35
{ "fr": "Ceux-là seront honorés dans des Jardins.", "wo": "Ñoom ña nga biir Àjjana deefi leen teral." }
70
36
{ "fr": "Qu´ont donc, ceux qui ont mécru, à courir vers toi, le cou tendu,", "wo": "Waaw yéefar yi lu ñu xewal bay raj-rajloo wutsi la," }
70
37
{ "fr": "de droite et de gauche, [venant] par bandes ?", "wo": "di bawoo ndeyjoor ak càmmooñ, tey wél-wéli ?" }
70
38
{ "fr": "Chacun d´eux convoite-t-il qu´on le laisse entrer au Jardin des délices ?", "wo": "Ndax nit ñépp dañoo maase bëgg a duggëndoo Àjjanay xéewal?" }
70
39
{ "fr": "Mais non ! Nous les avons créés de ce qu´ils savent .", "wo": "Mukk ! Noo leen sàkk ak ni ñu ko xame." }
70
40
{ "fr": "Eh Non ! ... Je jure par le Seigneur des Levants et des Couchants que Nous sommes Capable", "wo": "Déedéet !... Maa ngi giñ ci Boroom Penku ak Sowu yi ci ne Nun boroom Kàttan la nu." }
70
41
{ "fr": "De les remplacer par de meilleurs qu´eux, et nul ne peut Nous en empêcher.", "wo": "Ci soppi wuutale leen ak ñeneen ñu leen gën, te kenn du ko fanq." }
70
42
{ "fr": "Laisse-les donc s´enfoncer (dans leur mécréance) et se divertir jusqu´à ce qu´ils rencontrent leur jour dont on les menaçait,", "wo": "Bàyyileen ñu nuur (ci kéefër) aka fo ba baa ñuy dajeek bis ba ñu leen daan digu," }
70
43
{ "fr": "le jour où ils sortiront des tombes, rapides comme s´ils couraient vers des pierres dressées;", "wo": "bu keroogee, ba ñuy génn bàmmeel ya gaaw melni ku jëm ciy xërëm ;" }
70
44
{ "fr": "leurs yeux seront abaissés, l´avilissement les couvrira. C´est cela le jour dont on les menaçait !", "wo": "seen gët ya sajju, ñu torox ngir gàcce. Bis boobee mooy ba ñu leen daan dig (tëkoo)! " }
71
1
{ "fr": "Nous avons envoyé Noé vers son peuple : \"Avertis ton peuple, avant que leur vienne un châtiment douloureux\".", "wo": "Noo yónni woon Nooh ca aw nitam ne ko : “Xupal saw nit, bala leen mbugal mu mettee dikkël” ." }
71
2
{ "fr": "Il [leur] dit : \"ô mon peuple, je suis vraiment pour vous, un avertisseur clair,", "wo": "Mu daldi ne : “Éy seen samaw nit, man mii ab xuppekat laa ci yéen bu bir," }
71
3
{ "fr": "Adorez Allah, craignez-Le et obéissez-moi,", "wo": "Na ngeen jaamu Yàlla, te ragal ko, te topp ko" }
71
4
{ "fr": "pour qu´Il vous pardonne vos péchés et qu´Il vous donne un délai jusqu´à un terme fixé. Mais quand vient le terme fixé par Allah, il ne saurait être différé si vous saviez ! \"", "wo": "kon dey Dana leen jégël seeni bàkkaar te Dana leen yeexe ba ci dig bu ñu xam. Digub Yàlla bu agsee, du fanqu cëy bu ngeen xamoon !”" }
71
5
{ "fr": "Il dit : \"Seigneur ! J´ai appelé mon peuple, nuit et jour.", "wo": "(Nooh) : “Yaw sama Boroom ! woo naa samaw nit, guddeek bëcëg." }
71
6
{ "fr": "Mais mon appel n´a fait qu´accroître leur fuite.", "wo": "Te sama woote bi dolli wu leen lu dul féew." }
71
7
{ "fr": "Et chaque fois que je les ai appelés pour que Tu leur pardonnes, ils ont mis leurs doigts dans leurs oreilles, se sont enveloppés de leurs vêtements, se sont entêtés et se sont montrés extrêmement orgueilleux.", "wo": "Te man saasu ma leen di woo ngir Nga jégël leen, dañuy def séeni waaraam ci séeni biiri nopp, daldi muuroo séeni sér, daldi jomlu." }
71
8
{ "fr": "Ensuite, je les ai appelés ouvertement.", "wo": "Topp, woonaa leen cig jooru." }
71
9
{ "fr": "Puis, je leur ai fait des proclamations publiques, et des confidences en secret.", "wo": "Topp, biralalnaa leen, yalolnaa leen." }
71
10
{ "fr": "J´ai donc dit : \"Implorez le pardon de votre Seigneur, car Il est grand Pardonneur,", "wo": "Ma wax leen ne : “Jégëluleen seen Boroom, Moom dey Jégëlaakoon la," }
71
11
{ "fr": "pour qu´Il vous envoie du ciel, des pluies abondante,", "wo": "kon dey dana yabal asamaan si, mu duttil leen taw," }
71
12
{ "fr": "et qu´Il vous accorde beaucoup de biens et d´enfants, et vous donne des jardins et vous donne des rivières.", "wo": "te it dana leen may ay alal ak i doom, te dana leen defal tooli dër ak ay dex." }
71
13
{ "fr": "Qu´avez-vous à ne pas vénérer Allah comme il se doit,", "wo": "Ana lu leen dal ba du ngeen delloo Yàlla njukël," }
71
14
{ "fr": "alors qu´Il vous a créés par phases successives ? ", "wo": "te moom moo leen jaarale ci ay tolluwaay yu bari ba mu leen di sàkk ?" }
71
15
{ "fr": "N´avez-vous pas vu comment Allah a créé sept cieux superposés", "wo": "Xanaa gisu leen ni Yàlla binde juróom-ñaari asamaan yu tegaloo(s)" }
71
16
{ "fr": "et y a fait de la lune une lumière et du soleil une lampe ?", "wo": "mu def ci weer wi muy leer, mu def it jant bi mu di làmpu ?" }
71
17
{ "fr": "Et c´est Allah qui, de la terre, vous a fait croître comme des plantes,", "wo": "Te Yàllaa leen saxal, ci suuf si, ni gàncax, " }
71
18
{ "fr": "puis Il vous y fera retourner et vous en fera sortir véritablement.", "wo": "te dana leen ca delloo dana leen ca génneewaat." }
71
19
{ "fr": "Et c´est Allah qui vous a fait de la terre un tapis,", "wo": "Yàlla moo leen defaral suuf si mu di laltaay," }
71
20
{ "fr": "pour que vous vous acheminiez par ses voies spacieuses\".", "wo": "ngir ngeen mana sóobu ca yoonam yu dàndante ya” ." }
71
21
{ "fr": "Noé dit : \"Seigneur, ils m´ont désobéi et ils ont suivi celui dont les biens et les enfants n´ont fait qu´accroître la perte.", "wo": "Nooh daldi wax ne : “Yaw sama Boroom, (samaw nit) moy na ñu ma dem toppi koo xam ne alalam ak i doomam jariñu ko lu dul yàqule." }
71
22
{ "fr": "Ils ont ourdi un immense stratagème,", "wo": "Ña ngay fexe pexe yu rëy," }
71
23
{ "fr": "et ils ont dit : \"N´abandonnez jamais vos divinités et n´abandonnez jamais Wadd, Suwaa, Yagout, Yaouq et Nasr .", "wo": "tey wax naan : “Buleen bàyyi seeni Yàlli bu leen bàyyi Wud, Mbaa Suwaa’ , ak Yaquusa, ak Ya’uuqa ak Nasra." }
71
24
{ "fr": "Elles [les idoles] ont déjà égaré plusieurs. Ne fais (Seigneur) croître les injustes qu´en égarement.", "wo": "Te réeral nañu ñu bari. Te bul dolli tooñkat ya lu dul ag réer." }
71
25
{ "fr": "A cause de leurs fautes, ils ont été noyés, puis on les a fait entrer au Feu, et ils n´ont pas trouvé en dehors d´Allah, de secoureurs\".", "wo": "Ci sababu seen ñaawtéef ya, labaleef na leen, tàbbalees leen safara, te amu ñu fa fekku ñu fa ku leen di dimbali, ku dul Yàlla” ." }
71
26
{ "fr": "Et Noé dit : \"Seigneur, ne laisse sur la terre aucun infidèle.", "wo": "Nooh wax na ne : “Yaw sama Boroom, bul bàyyi ci kaw suuf si benn yéefar bu koy dëkke." }
71
27
{ "fr": "Si Tu les laisses [en vie], ils égareront Tes serviteurs et n´engendreront que des pécheurs infidèles.", "wo": "Soo leen fi bàyyee, dañuy réeral sa jaam ñi te dunu fi jur lu dul yéefar yu kàccoor." }
71
28
{ "fr": "Seigneur ! Pardonne-moi, et à mes père et mère et à celui qui entre dans ma demeure croyante, ainsi qu´aux croyants et croyantes; et ne fait croître les injustes qu´en perdition\"", "wo": "Yaw sama Boroom ! Jégëlma, maak sama ñaari wayjur ak képp ku tàbbi sama kër te gëm, ak jullit ñu góor ñeek jullit ñu jigéen ñi ; te bul dolli tooñkat yi lu dul ag yàqule” . " }
72
1
{ "fr": "Dis : \"Il m´a été révélé qu´un groupe de djinns prêtèrent l´oreille, puis dirent : \"Nous avons certes entendu une Lecture [le Coran] merveilleuse,", "wo": "Waxal ne : “Soloof na ma am na mbooleem jinne muy déglu, bay wax naan : “Nun dey dégg nanu Ñjàngum [Alxuraan] mu yéeme,(h)" }
72
2
{ "fr": "qui guide vers la droiture. Nous y avons cru, et nous n´associerons jamais personne à notre Seigneur.", "wo": "dafay gindee jëme ci njub. Nu daldi koy gëm, te dunu bokkaale dara ci sunu Boroom." }
72
3
{ "fr": "En vérité notre Seigneur - que Sa grandeur soit exaltée - ne S´est donné ni compagne, ni enfant !", "wo": "Te sunu Boroom - màggam ga sell na - jàppewul kenn muy soxnaam, waxatumalaa doomam !" }
72
4
{ "fr": "Notre insensé [Iblis] disait des extravagances contre Allah.", "wo": "Sunu kannas ma [Ibliis] moodaan wax ay njaxum ci Yàlla." }
72
5
{ "fr": "Et nous pensions que ni les humains ni les djinns ne sauraient jamais proférer de mensonge contre Allah.", "wo": "Te foog na ne nit ak jinne amul kenn ku cay fenal Yàlla." }
72
6
{ "fr": "Or, il y avait parmi les humains, des mâles qui cherchaient protection auprès des mâles paris les djinns mais cela ne fît qu´accroître leur détresse.", "wo": "Amoon ci nit, aw gaay ñu daan sàkku ay muslaay ci aw gaay ñu bokk ci jinne yi ñu faf leen dolli jaaxle (njaaxum)." }
72
7
{ "fr": "Et ils avaient pensé comme vous avez pensé qu´Allah ne ressusciterait jamais personne.", "wo": "Te ñoom dañoo jortu li ngeen jortoon ci ne Yàlla yónniwul kenn." }
72
8
{ "fr": "Nous avions frôlé le ciel et Nous l´avions trouvé plein d´une forte garde et de bolides.", "wo": "te Nun kat làmbu Nanu asamaan si fekk mu fees dell ak i wattukat ak jumi safara." }
72
9
{ "fr": "Nous y prenions place pour écouter. Mais quiconque prête l´oreille maintenant, trouve contre lui un bolide aux aguets.", "wo": "Te nun danu fa daan toog di yadu. Leegi nag képp ku fay jéema yëdu ji, dana fa fekk ab jum bu koy tuŋlu." }
72
10
{ "fr": "Nous ne savons pas si on veut du mal aux habitants de la terre ou si leur Seigneur veut les mettre sur le droit chemin.", "wo": "Te nun sax xamu nu ndax ñi nekk ci suuf si aw ay lees namm ci ñoom walla seen Boroom dafa namm ci ñoom ñu jub." }
72
11
{ "fr": "Il y a parmi nous des vertueux et [d´autre] qui le sont moins : nous étions divisés en différentes sectes.", "wo": "Am na ci nun ñu jub am na it ñu yées loolu : nun daal ay kurél lanu yu limu." }
72
12
{ "fr": "Nous pensions bien que nous ne saurions jamais réduire Allah à l´impuissance sur la terre et que nous ne saurions jamais le réduire à l´impuissance en nous enfuyant.", "wo": "Te xam nanu ne manuñoo tiiñ Yàlla te it manuñoo daw mukk ba raw ko." }
72
13
{ "fr": "Et lorsque nous avons entendu le guide [le Coran], nous y avons cru, et quiconque croit en son Seigneur ne craint alors ni diminution de récompense ni oppression.", "wo": "Te nun ba nu déggee njub ga [Alxuraan], gëm nanu ko, te nag képp ku gëm Boroomam dootul ragal wàññikug jëf waxantumalaak sànje. " }
72
14
{ "fr": "Il y a parmi nous les Musulmans, et il y en a les injustes [qui ont dévié]. Et ceux qui se sont convertis à l´Islam sont ceux qui ont cherché la droiture.", "wo": "Am na ci nun ay jullit, am na it ci nun ay tooñkat. Ña nga xam ne ñoom dañoo tuub defi jullit ñoo ñaa làmboo njub." }
72
15
{ "fr": "Et quant aux injustes, ils formeront le combustible de l´Enfer.", "wo": "Tooñkat ya nag, ñoom ñoo di mattum safara." }
72
16
{ "fr": "Et s´ils se maintenaient dans la bonne direction, Nous les aurions abreuvés, certes d´une eau abondante,", "wo": "Te kat su ñu jaaroon ca yoon wu jub xocc wa, Danaa leen nàndale, ndox mu neex," }
72
17
{ "fr": "afin de les y éprouver. Et quiconque se détourne du rappel de son Seigneur, Il l´achemine vers un châtiment sans cesse croissant.", "wo": "ngir nu nattu leen ca. Képp ku dumóoyu baña fàttaliku Boroomam, (Yàlla) dana ko sóob ci mbugël muy dolliku saa su nekk." }
72
18
{ "fr": "Les mosquées sont consacrées à Allah : n´invoquez donc personne avec Allah.", "wo": "Jàkka yi Yàlla moo leen moom : buleen fay woo kenn di ko booleek Yàlla." }
72
19
{ "fr": "Et quand le serviteur d´Allah s´est mis debout pour L´invoquer, ils faillirent se ruer en masse sur lui. .", "wo": "Te kat ba jaamub Yàlla bi taxawee di ñaan Boroomam, xawnañoo raj- rajloo ca kawam." }
72
20
{ "fr": "Dis : \"Je n´invoque que mon Seigneur et ne Lui associe personne\".", "wo": "Waxal ne : “Maa ngi ñaan sama Boroom te duma ko bokkaaleek kenn” ." }
72
21
{ "fr": "Dis : \"Je ne possède aucun moyen pour vous faire du mal, ni pour vous mettre sur le chemin droit\".", "wo": "Waxal ne: “man mii kat manuma leen a lor manuma leen a jubbanti” ." }
72
22
{ "fr": "Dis : \"Vraiment, personne ne saura me protéger contre Allah; et jamais je ne trouverai de refuge en dehors de Lui.", "wo": "Waxal it ne: “man mii keen manumaa aar ci Yàlla, te it duma wut benn rawtukaay budul moom." }
72
23
{ "fr": "[Je ne puis que transmettre] une communication et des messages [émanant] d´Allah. Et quiconque désobéit à Allah et à son Messager aura le feu de l´Enfer pour y demeurer éternellement.", "wo": "Manuma lu dul jottali ndigëlul Yàlla. Waaye képp ku moy Yàlla akub Yonentam ca Safara sa lay sax te dafay béel ba fàww.(s)" }
72
24
{ "fr": "Puis, quand ils verront ce dont on les menaçait, ils sauront lesquels ont les secours les plus faibles et [lesquels] sont les moins nombreux.", "wo": "Ba bis ba ñu gisee la ñu leen daan tëkkoo, danañu xala xam ana kan moo gën ñàkk ndimbal ak ana kan moo gën a néew lim." }
72
25
{ "fr": "Dis : \"Je ne sais pas si ce dont vous êtes menacés est proche, ou bien, si mon Seigneur va lui assigner un délai.", "wo": "Waxal ne: “Xamuma baxam li ñu leen di tëkkoo dafa jiggeñ, walla, sama Boroom da leen may ab dig." }
72
26
{ "fr": "[C´est Lui] qui connaît le mystère. Il ne dévoile Son mystère à personne,", "wo": "[Moom] moo xam kumpa. Te du wuññil kumpaam ga kenn," }
72
27
{ "fr": "sauf à celui qu´Il agrée comme Messager et qu´Il fait précéder et suivre de gardiens vigilants,", "wo": "lu dul ku mu gëram ci Yonent te dakoy booleek ñu koy wattu kanam ak ginnaaw," }
72
28
{ "fr": "afin qu´Il sache s´ils ont bien transmis les messages de leur Seigneur. Il cerne (de Son savoir) ce qui est avec eux, et dénombre exactement toute chose\".", "wo": "Saar 72 : Jinne ya 28 - Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
72
28
{ "fr": "afin qu´Il sache s´ils ont bien transmis les messages de leur Seigneur. Il cerne (de Son savoir) ce qui est avec eux, et dénombre exactement toute chose\".", "wo": "ngir mu xam ne jotal nañu seen Yonentub Boroom. Te it peeg na lépp lu ne ci ab lim (xam na na mu day” . " }
73
1
{ "fr": "ô ! , toi , l´enveloppé [dans tes vêtements] !", "wo": "Éy ! yaw, ku ñu sàng ki !" }
73
2
{ "fr": "Lève-toi [pour prier], toute la nuit, excepté une petite partie;", "wo": "Jógal [di julli], ci guddi gi, bamu des lu ,néew ;" }
73
3
{ "fr": "Sa moitié, ou un peu moins;", "wo": "Ab xaajam, walla sax nga wàññi ca lu tuuti ;" }
73
4
{ "fr": "ou un peu plus. Et récite le Coran, lentement et clairement.", "wo": "walla sax nga dolli ca. Te na ngay jàng Alxuraan, njàng mu léer." }
73
5
{ "fr": "Nous allons te révéler des paroles lourdes (très importantes).", "wo": "Xalset nanu laa gàll wax ju diis." }
73
6
{ "fr": "La prière pendant la nuit est plus efficace et plus propice pour la récitation.", "wo": "Jullig guddi nag moo gëna nangu te moo gëna leer cim njàng." }
73
7
{ "fr": "Tu as, dans la journée, à vaquer à de longues occupations.", "wo": "Am nga, ci bëcëg bi, jot gu gudd goo mana lijantee." }