sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
63
2
{ "fr": "Ils prennent leurs serments pour bouclier et obstruent le chemin d´Allah. Quelles mauvaises choses que ce qu´ils faisaient !", "wo": "Def nañu seeni ngiñ muy pakk ñuy gàllankoor ci yoonu Yàlla. Ñoom dey la ñuy def ñaaw na !" }
63
3
{ "fr": "C´est parce qu´en vérité ils ont cru, puis rejeté la foi. Leur coeurs donc, ont été scellés, de sorte qu´ils ne comprennent rien.", "wo": "(La ko def) moo di ne dañoo gëmoon, weddiwaat. Ñu fatt seeni xol, ba xamatuñu dara." }
63
4
{ "fr": "Et quand tu les vois, leurs corps t´émerveillent; et s´ils parlent, tu écoutes leur parole. ils sont comme des bûches appuyées (contre des murs) et ils pensent que chaque cri est dirigé contre eux. L´ennemi c´est eux. Prends y garde. Qu´Allah les extermine ! Comme les voilà détournés (du droit chemin).", "wo": "Saa soo leen gisee, seeni yaram ya dalay yéem ; bu ñuy wax it, fàww nga déglu leen. Dañuy melni ay dénk yu ñu wéer fu yuuxu jibe ñu tiit. Ñoom ñooy noon ya tigi. Moytandikuleen ! Yàlla dana leen faagaagal kem niñu dumóoyoo (yoonam)." }
63
5
{ "fr": "Et quand on leur dit : \"Venez que le Messager d´Allah implore le pardon pour vous\", ils détournent leurs têtes, et tu les vois se détourner tandis qu´ils s´enflent d´orgueil.", "wo": "Sunu leen waxee ne : “Kaayleen Yonent Yàlla bi jéggalul leen” , ñuy dag- dagali bopp, dumóoyu tey rëy-rëylu." }
63
6
{ "fr": "C´est égal, pour eux, que tu implores le pardon pour eux ou que tu ne le fasses pas : Allah ne leur pardonnera jamais, car Allah ne guide pas les gens pervers.", "wo": "Nga, jéggalul leen, ak nga ñàkk leen jéggalul ñoo yem : ndax Yàlla duleen jéggal mukk, te Yàlla du gindi nit ñu di ay saay-saay." }
63
7
{ "fr": "Ce sont eux qui disent : \"Ne dépensez point pour ceux qui sont auprès du Messager d´Allah, afin qu´ils se dispersent\". Et c´est à Allah qu´appartiennent les trésors des cieux et de la terre, mais les hypocrites ne comprennent pas.", "wo": "Ñoom ñooy wax naan : “Buleen joxati dara ña nek ca Yonent ba, ba baa nuy xaddi” . Te Yàllaa moom ndambi asamaan yeek suuf si, Waaye naaféq ya xamuñu." }
63
8
{ "fr": "Ils disent : \"Si nous retournons à Médine, le plus puissant en fera assurément sortir le plus humble \". Or c´est à Allah qu´est la puissance ainsi qu´à Son messager et aux croyants. Mais les hypocrites ne le savent pas.", "wo": "Danañuy wax naan : “Sunu delloo Madiina, ña am doole danañu génne ña néew doole” . Te Yàlla rekk am doole mook ab Yonentam ak way gëm ña. Waaye naaféq ya xamuñu." }
63
9
{ "fr": "ô vous qui avez cru ! Que ni vos biens ni vos enfants ne vous distraient du rappel d´Allah. Et quiconque fait cela... alors ceux-là seront les perdants.", "wo": "Eey yéen ñi gëm ! Bu leen seeni alal ak seeni doom fàbbi ci tudd Yàlla. Képp kuy def loolu... (na xam ne) ñoom ñooy yàqule." }
63
10
{ "fr": "Et dépensez de ce que Nous vous avons octroyé avant que la mort ne vienne à l´un de vous et qu´il dise alors : \"Seigneur ! si seulement Tu m´accordais un court délai : je ferais l´aumône et serais parmi les gens de bien\".", "wo": "Te nangeen di joxe ci alal ji nu leen wërsëgël balaa dee di dikkël kenn ci yéen muy wax naan : “Cëy sama Boroom ! muñal ma as ndiir : ndax ma man a saraxe ba bokk ca ñu yiw ñi” . " }
63
11
{ "fr": "Allah cependant n´accorde jamais de délai à une âme dont le terme est arrivé. Et Allah est Parfaitement Connaisseur de ce que vous faites.", "wo": "Saar 63 : Naaféq ya 11 - Laaya – Gannaaw Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
63
11
{ "fr": "Allah cependant n´accorde jamais de délai à une âme dont le terme est arrivé. Et Allah est Parfaitement Connaisseur de ce que vous faites.", "wo": "Te Yàlla moom du yeexe benn bakkan saasu ab digam agsee. Te Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def. " }
64
1
{ "fr": "Ce qui est dans les cieux et ce qui est sur la terre glorifient Allah. A Lui la royauté et à Lui les louanges. Et Il est Omnipotent.", "wo": "Ñi nekk ci asamaan yeek suuf si ña ngay sàbbaal Yàlla. Mooy boroom nguur te Mooy boroom cant. Te Moom man na Lépp." }
64
2
{ "fr": "C´est Lui qui vous a créés. Parmi vous [il y a] mécréant et croyant. Allah observe parfaitement ce que vous faites.", "wo": "Mooy ki leen bind. Am na ci yéen ay yéefar am it ci yéen ay jullit way gëm. Te Yàlla kuy gis la li ngeen di def." }
64
3
{ "fr": "Il a créé les cieux et la terre en toute vérité et vous a donné votre forme et quelle belle forme Il vous a donnée. Et vers Lui est le devenir.", "wo": "Bind na asamaan yeek suuf si ci dëgg mu tën seeni jëmm te rafetal na seeni jëm. Te ca moom mooy Deluwaay ba." }
64
4
{ "fr": "Il sait ce qui est dans les cieux et la terre, et il sait ce que vous cachez ainsi que ce que vous divulguez. Et Allah connaît bien le contenu des poitrines.", "wo": "Moom Yàlla xam na li nekk ci asamaan yeek suuf si, te it ma ngay xam li ngeen di nëbb ak li ngeen di feeñal. Te Yàlla ku xam la li nekk ci dënn yi." }
64
5
{ "fr": "Ne vous est-elle pas parvenue, la nouvelle de ceux qui auparavant ont mécru et qui ont goûté la conséquence néfaste de leur acte; ils auront en outre un châtiment douloureux.", "wo": "Moo xanaa xibaari yéefar ya jiitu woon da leen dikkalul, mosoon nañu musiba mu di peyug seeni jëf ; te am nañu mbugël mu mitti." }
64
6
{ "fr": "il en est ainsi parce que leurs messagers leur venaient avec des preuves évidentes, et qu´ils ont dit : \"Sont-ce des hommes qui nous guideront ? \" Ils mécrurent alors et se détournèrent et Allah Se passa [d´eux] et Allah Se suffit à Lui-même et Il est Digne de louange.", "wo": "la ko waral moo di ne seeni Yonent da leen daan dikkël ak ay firndeyu leer ñuy wax naan : “Moo nit ñii ñoo ñuy gindee ?” Daal di weddi dumóoyu Yàlla bàyyi leen te Yàlla ku doyloo boppam la Yayoowaakoonu cant la." }
64
7
{ "fr": "Ceux qui ont mécru prétendent qu´ils ne seront point ressuscités. Dis : \"Mais si ! Par mon Seigneur ! Vous serez très certainement ressuscités; puis vous serez certes informés de ce que vous faisiez. Et cela est facile pour Allah\".", "wo": "Yéefër yi neena ñooy kenn duleen dekkal. Waxal ne : “Axakañ! Dees na leen dekkal ; xibaar leen la ngeen jëfoon. Te loolu lu yomb la ci Yàlla” . (s)" }
64
8
{ "fr": "Croyez en Allah donc et en Son messager, ainsi qu´en la Lumière [le Coran] que Nous avons fait descendre. Et Allah est Parfaitement Connaisseur de ce que vous faites.", "wo": "Gëmleen Yàlla ak ub Yonentam, ak leer gi nu wàcce [Alxuraan]. Te Yàlla kat ku deñ- kumpa la ci li ngeen di def." }
64
9
{ "fr": "Le jour où Il vous réunira pour le jour du Rassemblement, ce sera le jour de la grande perte. Et celui qui croit en Allah et accomplit les bonnes oeuvres, Il lui effacera ses mauvaises actions et fera entrer dans des Jardins sous lesquels coulent les ruisseaux où ils demeureront éternellement. Voilà l´énorme succès !", "wo": "Te bu keroogee ba mu leen di Dajale, ca bisub daje ba bis boobee mooy bisub yàqule gu mag ga (ca yéefar ya). (Waaye) képp ku gëm tey jëf yiw, Dana ko faral ay ñaaytéefam te dana ko tàbbal Àjjana yu ay dex ñooy daw ci suufam, te dañu fay béel fàww. Loolu moo di texe gu mag ga ! " }
64
10
{ "fr": "Et ceux qui ont mécru et traité de mensonges Nos versets, ceux-là sont les gens du Feu où ils demeureront éternellement. Et quelle mauvaise destination !", "wo": "Yéefër yiy weddi Sunuy Laaya, ñooñu ñoo di waa Safara te danu fay béel. Ndaw saxuwaay bu bon !" }
64
11
{ "fr": "Nul malheur n´atteint [l´homme] que par la permission d´Allah. Et quiconque croit en Allah, [Allah] guide son cœur. Allah est Omniscient.", "wo": "Saar 64 : Yàqule gu mag ga 18 - Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
64
11
{ "fr": "Nul malheur n´atteint [l´homme] que par la permission d´Allah. Et quiconque croit en Allah, [Allah] guide son cœur. Allah est Omniscient.", "wo": "Amul menn musiba muy dal kenn lu dul ci ndigalul Yàlla. Képp ku gëm Yàlla, [Yàlla] dana gindi xolam. Te Yàlla xam na lépp." }
64
12
{ "fr": "Obéissez à Allah et obéissez au Messager et si vous vous détournez... il n´incombe à Notre messager que de transmettre en claire (son message).", "wo": "Nangeen di topp Yàlla te it na ngeen di topp Yonent bi suñu dumóoyoo... li ca war Sunub Yonent mooy jottali rekk ba mu leer." }
64
13
{ "fr": "Allah, nulle autre divinité que Lui ! Et c´est à Allah que les croyants [doivent] s´en remettre.", "wo": "Yàlla, amul jeneen Yàlla ju dul moom ! Te ñi gëm na ñuy doyloo Yàlla." }
64
14
{ "fr": "ô vous qui avez cru, vous avez de vos épouses et de vos enfants un ennemi [une tentation]. Prenez-y garde donc. Mais si vous [les] excusez passez sur [leurs] fautes et [leur] pardonnez, sachez qu´Allah est Pardonneur, Très Miséricordieux.", "wo": "eey yéen ñi gëm, am na ci seeni jabar ak seeni doom ñoo xam ne seeni noon la ñu. Nangeen leen di moytu. (Waaye) su ngeen balee tey jéllale, Yàlla moom ab Jéggalaakoon la, Jagléwaakoon la." }
64
15
{ "fr": "Vos biens et vos enfants ne sont qu´une tentation, alors qu´auprès d´Allah est une énorme récompense.", "wo": "Seeni alal ak seeni doom sànje la ci yéen, (Waaye) la nekk fa Yàlla moo di pey gu màgg." }
64
16
{ "fr": "Craignez Allah, donc autant que vous pouvez, écoutez, obéissez et faites largesses. Ce sera un bien pour vous. Et quiconque a été protégé contre sa propre avidité... ceux-là sont ceux qui réussissent.", "wo": "Nangeen di ragal Yàlla seen kem kàttan, dégluleen, te topp te joxe alal. Moo gën ci yéen de. Képp ku mucc ci ag nay (na xam ne)... ñoo di ña baaxle." }
64
17
{ "fr": "Si vous faites à Allah un prêt sincère, Il multipliera pour vous et vous pardonnera. Allah cependant est très Reconnaissant et Indulgent.", "wo": "Su ngeen lebalee Yàlla bor bu rafet, Dana leen ko fulal te it dana leen jéggal. Te Yàlla ab Santaakoon la Ku lewet la." }
64
18
{ "fr": "Il est le Connaisseur du monde Invisible et visible, et Il est le Puissant, le Sage.", "wo": "Mooy aji Xam ji Kumpaak li feeñ, di boroom Kàttan, di aji Xereñ. " }
65
1
{ "fr": "ô Prophète ! Quand vous répudier les femmes, répudiez-les conformément à leur période d´attente prescrite; et comptez la période; et craignez Allah votre Seigneur. Ne les faîtes pas sortir de leurs maisons, et qu´elles n´en sortent pas, à moins qu´elles n´aient commis une turpitude prouvée. Telles sont les lois d´Allah. Quiconque cependant transgresse les lois d´Allah, se fait du tort à lui-même. Tu ne sais pas si d´ici là Allah ne suscitera pas quelque chose de nouveau ! ", "wo": "Eey yaw Yonent bi ! Su ngeen di faseeti jigéen, na ngeen leen di fasee cig laab; te nangeen di lim yidda ja ; nangeen ragal Yàlla seen Boroom. Te bu leen leen génnee, ci seeni néeg, ñoom it bu ñu génn lu dul bu ñu defee ñaawtéef wu bir. Loolu mooy daytali Yàlla. Te képp ku jàll ci daytali Yàlla, tooñ na boppam. Te xamuloo baxam Yàlla dana àttewaat meneen mbir am déet !(n)" }
65
2
{ "fr": "Puis quand elles atteignent le terme prescrit, retenez-les de façon convenable, ou séparez-vous d´elles de façon convenable; et prenez deux hommes intègres parmi vous comme témoins. Et acquittez-vous du témoignage envers Allah. Voilà ce à quoi est exhorté celui qui croit en Allah et au Jour dernier. Et quiconque craint Allah, il lui donnera une issue favorable,", "wo": "Su yidda ja matee, Téyeleen ci njekk, walla ngeen yewwileen ci njekk ; te nangeen ko seedeloo ñaari way maandu ci yéen. Te seede sa na Yàlla rekk tax. Loolu la nu leen cay dénk képp ku gëm Yàlla ak bis bu mujj ba. Ak képp kuy ragal Yàlla, dana ko defal génnuwaay bu rafet (tajfël)," }
65
3
{ "fr": "et lui accordera Ses dons par [des moyens] sur lesquels il ne comptait pas. Et quiconque place sa confiance en Allah, Il [Allah] lui suffit. Allah atteint ce qu´Il Se propose, et Allah a assigné une mesure à chaque chose.", "wo": "te dana koy wërsëgale fu mu foogewul. Képp kuy doyloo Yàlla, Yàlla dana ko doy. Yàlla Dana jot mbiram, te Yàlla defal na lu nekk ab dayo." }
65
4
{ "fr": "Si vous avez des doutes à propos (de la période d´attente) de vos femmes qui n´espèrent plus avoir de règles, leur délai est de trois mois. De même pour celles qui n´ont pas encore de règles. Et quant à celles qui sont enceintes, leur période d´attente se terminera à leur accouchement. Quiconque craint Allah cependant, Il lui facilite les choses .", "wo": "Jigéen ñi mbaragatul, ñoom seen yidda ñetti weer lay doon. Ak ñi mbaragagul. Ñi ëmbu doom, seen yidda mi ngi yem ca ba ñu imbee seen ëmb. Te képp kuy ragal Yàlla, Dana ko defal ak yombal ciy mbiram." }
65
5
{ "fr": "Tel est le commandement d´Allah qu´Il a fait descendre vers vous. Quiconque craint Allah cependant, il lui efface ses fautes et lui accorde une grosse récompense.", "wo": "Loolu moo di ndigëlul Yàlla li mu wàcce ci yéen. Te képp kuy ragal Yàlla, dana ko jéggal ay ñaawtéefam jox ko pey gu màgg." }
65
6
{ "fr": "Et faites que ces femmes habitent où vous habitez, et suivant vos moyens. Et ne cherchez pas à leur nuire en les contraignant à vivre à l´étroit. Et si elle sont enceintes, pourvoyez à leurs besoins jusqu´à ce qu´elles aient accouché. Puis, si elles allaitent [l´enfant né] de vous, donnez-leur leurs salaires . Et concertez-vous [à ce sujet] de façon convenable. Et si vous rencontrez des difficultés réciproques, alors, une autre allaitera pour lui.", "wo": "Nangeen di dëkkël jigéen ñi ca fa ngeen dëkk yéen, ca nangeen ko mane. Buleen leen bunduxataal ngir xatal leen. Su fekkee ne dañoo ëmb, na ngeen leen di dundal ba baa ñuy imbi. Suñu, leen nàmpalalee seen doom, nangeen ko fay. Nangeen diisoo ci njekk. Su ngeen ca juuyoo, kon, na ko keneen nàmpal." }
65
7
{ "fr": "Que celui qui est aisé dépense de sa fortune; et que celui dont les biens sont restreints dépense selon ce qu´Allah lui a accordé. Allah n´impose à personne que selon ce qu´Il lui a donné, et Allah fera succéder l´aisance à la gêne.", "wo": "Ku am alal na joxee na mu woomale ; ku amul alal it na joxee ci kem na ko Yàlla wërsëgële. Yàlla du ga kenn ci lu mu manul, Yàlla dana def yombal ci ginnaaw ag jafe.(s) " }
65
8
{ "fr": "Que de cités ont refusé avec insolence le commandement de leur Seigneur et de Ses messagers ! Nous leur en demandâmes compte avec sévérité, et les châtiâmes d´un châtiment inouï.", "wo": "Aka bari ay dëkk yu moyoon seen ndigëlu boroom ak i Yonentam ! Nu nattu leen nattu bu tar, mbugal leen mbugal mu mitti." }
65
9
{ "fr": "Elles goûtèrent donc la conséquence de leur comportement. Et le résultat final de leurs actions fut [leur] perdition.", "wo": "Mosnañu musibam seeni mbir. Ñu mujj yàqule." }
65
10
{ "fr": "Allah a préparé pour eux un dur châtiment. Craignez Allah donc, ô vous qui êtes doués d´intelligence, vous qui avez la foi. certes, Allah a fait descendre vers vous un rappel,", "wo": "Yàlla waajal na leen mbugël mu tar. Kon book ragal-leen Yàlla, yéen woroom xel yi, natt gëm. Yàlla wàcce na ci yéen ag fàttali," }
65
11
{ "fr": "un Messager qui vous récite les versets d´Allah comme preuves claires, afin de faire sortir ceux qui croient et accomplissent les bonnes oeuvres des ténèbres à la lumière. Et quiconque croit en Allah et fait le bien, Il le fait entrer aux Jardins sous lesquels coulent les ruisseaux, pour y demeurer éternellement. Allah lui a fait une belle attribution.", "wo": "ab Yonent buy jàng ci yéen Laayay Yàlla mu leer nàññ, ngir mu génne ñi gëm tey jëfe yiw cig lëndëm jëme leen ci leer. Képp ku gëm Yàlla tey jëfe yiw, (Yàlla) dana ko tàbbal Àjjana joo xam ne ay dex ñooy daw ci suufam, ñu béel fa Yàlla may ko fa xéewal gu jekk." }
65
12
{ "fr": "Allah qui a créé sept cieux et autant de terres. Entre eux [Son] commandement descend, afin que vous sachiez qu´Allah est en vérité Omnipotent et qu´Allah a embrassé toute chose de [Son] savoir.", "wo": "Moom Yàlla mi bind juróom-ñaari asamaan ak suuf yu na toll. Ay ndigalam di wàcci ci seen diggante, loolu lépp ngir ngeen xam ne Yàlla man na lépp lu ne te it peek na lépp lu ne ci xam-xam. " }
66
1
{ "fr": "ô Prophète ! Pourquoi, en recherchant l´agrément de tes femmes, t´interdis-tu ce qu´Allah t´a rendu licite ? Et Allah est Pardonneur, Très Miséricordieux.", "wo": "Éy yaw Yonent bi ! Ana lu tax, ngay araamal lu la Yàlla daganalal, nga di ca sàkku ngëram loo say soxna ? (Waaye) Yàlla moom Jéggalaakoon la, Jagléwaakoon la.(r)" }
66
2
{ "fr": "Allah vous a prescrit certes, de vous libérer de vos serments. Allah est votre Maître; et c´est Lui l´Omniscient, le Sage .", "wo": "Yàlla fartal na ci yéen, daganal seeni ngiñ. Yàlla di seen Boroom ; te Ku Xam la Ku Xereñ la ." }
66
3
{ "fr": "Lorsque le Prophète confia un secret à l´une de ses épouses et qu´elle l´eut divulgué et qu´Allah l´en eut informé, celui-ci en fit connaître une partie et passa sur une partie. Puis, quand il l´en eut informée elle dit : \"Qui t´en a donné nouvelle ? \" Il dit : \"C´est l´Omniscient, le Parfaitement Connaisseur qui m´en a avisé\".", "wo": "Ba Yonent bi joxee sekkare lennat ci soxnaam ba ñu ko tasaaree te Yàlla wuññil ko lenn la, dëddu leneen la. Ba mu ko xibaare soxna sa mu ne ko : “ku la ko xibaar ?” Mu ne ko : “Yàlla mi Xam, te deñ Kumpa ci lépp mooma ko xibaar” ." }
66
4
{ "fr": "Si vous vous repentez à Allah c´est que vos coeurs ont fléchi. Mais si vous vous soutenez l´une l´autre contre le Prophète, alors ses alliés seront Allah, Gabriel et les vertueux d´entre les croyants, et les Anges sont par surcroît [son] soutien .", "wo": "Yéen ñaari soxna yi su ngeen tuubee (moo gën) ndax seeni xol jeng na. Su ngeen takktoo (Yonent bi), Yàlla farnaak moom, ak Jibriil ak jullit ñu yiw ñi, ak Malaaka yi di ko dimbali." }
66
5
{ "fr": "S´Ils vous répudie, il se peut que Seigneur lui donne en échange des épouses meilleurs que vous, musulmanes, croyantes, obéissantes, repentantes, adoratrices, jeûneuses, déjà mariées ou vierges .", "wo": "Te itam su leen fasee, Boroomam dana ko jox ay soxna yu leen gën, yu di ay jullit, yu gëm, yuy topp ndigal, ñuy tuub, ñuy jaamu, ñuy woor, di ay jeeg mba ay janq." }
66
6
{ "fr": "ô vous qui avez cru ! Préservez vos personnes et vos familles, d´un Feu dont le combustible sera les gens et les pierres, surveillé par des Anges rudes, durs, ne désobéissant jamais à Allah en ce qu´Il leur commande, et faisant strictement ce qu´on leur ordonne.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Fegalleen seen bopp ak seen njaboot, aw Safara woo xam ne matt ma aw nit lay doon ak xeer, ay Malaaka yu tal, te tar, ñoo fay nekk duñu moy mukk, li leen Yàlla digal te la mu leen digal la ñuy def." }
66
7
{ "fr": "ô vous qui avez mécru ! Ne vous excusez pas aujourd´hui Vous ne serez rétribués que selon ce que vous oeuvriez.", "wo": "Éy yéen Yéefër yi! Buleen jéema jéggalu tey danañuleen fay la ngeen daan jëf." }
66
8
{ "fr": "ô vous qui avez cru ! Repentez-vous à Allah d´un repentir sincère. Il se peut que votre Seigneur vous efface vos fautes et qu´Il vous fasse entrer dans des Jardins sous lesquels coulent les ruisseaux, le jour où Allah épargnera l´ignominie au Prophète et à ceux qui croient avec lui. Leur lumière courra devant eux et à leur droite; ils diront : \"Seigneur, parfais-nous notre lumière et pardonne-nous. Car Tu es Omnipotent\".", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Tuuballeen Yàlla tuub gu sell. Kon dey Yàlla dana leen jéggal seeni ñaawtéef te Dana leen tàbbal ay Àjjana yu ay dex di daw ci suuf, bu keroogee Yàlla du gàcceel mukk Yonenta bi ak ñi gëm ànd ak moom. Seen leer gaa nga ca seen kanam ak ndeyjoor ; ña ngay wax naan : “Yaw sunu Boroom, mottalil nu sunug leer te jéggal nu. Yaw dey man nga lépp lu ne” .(s) " }
66
9
{ "fr": "ô Prophète ! Mène la lutte contre les mécréants et hypocrites et sois rude à leur égard. leur refuge sera l´Enfer, et quelle mauvaise destination !", "wo": "Éy yaw Yonent bi ! Xeexal ak Yéefër yi ak Naaféq yi te na nga tar ci ñoom. Safaraay doon seenug muj, ndaw muj gu bon !" }
66
10
{ "fr": "Allah a cité en parabole pour ceux qui ont mécru la femme de Noé et la femme de Lot. Elles étaient sous l´autorité de deux vertueux de Nos serviteurs. Toutes deux les trahirent et ils ne furent d´aucune aide pour [ces deux femmes] vis-à-vis d´Allah. Et il [leur] fut dit : \"Entrez au Feu toutes les deux, avec ceux qui y entrent\",", "wo": "Yàlla saddna leebu Yéefër yi ci soxnas Lóot ak soxnas Nooh. Nekkoon nañu ci ron sunu ñaari jaam yu yiw. Waaye ñu worleen dem àndeek Yéefër ya (la ñuy doon ay Yonent taxul ñu manal leen ci Yàlla dara. Dees na [leen] ne : “Tàbbileen Safara, ànd ak way tàbbi ña” ," }
66
11
{ "fr": "et Allah a cité en parabole pour ceux qui croient, la femme de Pharaon, quand elle dit \"Seigneur, construis-moi auprès de Toi une maison dans le Paradis, et sauve-moi de Pharaon et de son oeuvre; et sauve-moi des gens injustes\".", "wo": "Yàlla saddna léebu way gëm ña, ci soxnas Firawna, ba mu waxee ne “Yaw sama Boroom, tabaxal ma kër fa yaw ca Àjjana, te nga musël ma ci Firawna ak jëfam; nga musël ma it ci nit ña di ay tooñkat” ." }
66
12
{ "fr": "De même, Marie, la fille d´Imran qui avait préservé sa virginité; Nous y insufflâmes alors de Notre Esprit. Elle avait déclaré véridiques les paroles de son Seigneur ainsi que Ses Livres : elle fut parmi les dévoués.", "wo": "Saar 66 : Araamal ga 12 - Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
66
12
{ "fr": "De même, Marie, la fille d´Imran qui avait préservé sa virginité; Nous y insufflâmes alors de Notre Esprit. Elle avait déclaré véridiques les paroles de son Seigneur ainsi que Ses Livres : elle fut parmi les dévoués.", "wo": "Ak ci, Mariyaama, doomi Imraana mi ñoŋaloon boppam ; Nu af ca ci sunu ruu. Mu dëkëloon kàdduy Boroomam ak i téereem : te bokkoon ca toppakat ya (daan jaamu Yàlla). " }
67
1
{ "fr": "Béni soit celui dans la main de qui est la royauté, et Il est Omnipotent.", "wo": "Barkeel na (Yàlla) mi nga xam ne nguur gaa ngi ci loxom, te Moom man na Lépp lu ne.(h)" }
67
2
{ "fr": "Celui qui a créé la mort et la vie afin de vous éprouver (et de savoir) qui de vous est le meilleur en oeuvre, et c´est Lui le Puissant, le Pardonneur.", "wo": "Mooy ki bind dee ak dund ngir nattu leen ci ana kan koo gën a rafet jëf, te Moom (Yàlla) moo di boroom Kàttan gi, di Jéggalaakoon bi." }
67
3
{ "fr": "Celui qui a créé sept cieux superposés sans que tu voies de disproportion en la création du Tout Miséricordieux. Ramène [sur elle] le regard. Y vois-tu une brèche quelconque ?", "wo": "Mooy ki bind juróom-ñaari asamaan yu tegloo doo gis kenn roobaate ci bindug Yërëmaakoon bi. Dellul xool. Moo ndax danga gis genn sutaate ?" }
67
4
{ "fr": "Puis, retourne ton regard à deux fois : le regard te reviendra humilié et frustré.", "wo": "Topp, nga déllu xool ñaari yoon : da koy délloosiwaat ci yaw rekk waaye du man a gis sikk ne cucum." }
67
5
{ "fr": "Nous avons effectivement embelli le ciel le plus proche avec des lampes [des étoiles] dont Nous avons fait des projectiles pour lapider des diables et Nous leur avons préparé le châtiment de la Fournaise.", "wo": "Taaralal nanu àddina si ci ay làmp [biddiw] def nanu ko muy lakk Saytaane yi te waajalal nanu leen mbugëlum Safara." }
67
6
{ "fr": "Ceux qui ont mécru à leur Seigneur auront le châtiment de l´Enfer. Et quelle mauvaise destination !", "wo": "Ña weddi Yàlla am nañu mbugalum Safara. Ndaw mujj gu bon !" }
67
7
{ "fr": "Quand ils y seront jetés, ils lui entendront un gémissement, tandis qu´il bouillonne.", "wo": "Bu ñu leen ca sànnee, nga dégg ko muy fuur, di wañax." }
67
8
{ "fr": "Peu s´en faut que, de rage, il n´éclate. Toutes les fois qu´un groupe y est jeté, ses gardiens leur demandent : \"Quoi ! ne vous est-il pas venu d´avertisseur ? \"", "wo": "Day mer, bay fuur. Saa su ñu ca sànnee mbooloo, ña kay wattu naan leen: “Xanaa ! yéen kuy xuppe dikkul woon ci yéen ?”" }
67
9
{ "fr": "Ils dirent : \"Mais si ! un avertisseur nous était venu certes, mais nous avons crié au mensonge et avons dit : Allah n´a rien fait descendre, vous n´êtes que dans un grand égarement\" ", "wo": "Ñu naan ko : “Axakañ ! dikkaloon nañu nu kay, nu ne leen: Yàlla wàccewul tus, te yéen dangeen a sànku”" }
67
10
{ "fr": "Et ils dirent : \"Si nous avions écouté ou raisonné, nous ne serions pas parmi les gens de la Fournaise\".", "wo": "Ñu wax it ne : “Su nu doon dégg mbaa nu xel-lu, kon dunu nekk ci mbugël mii tey” ." }
67
11
{ "fr": "Ils ont reconnu leur péché. Que les gens de la Fournaise soient anéantis à jamais.", "wo": "Nangu nañu seeni bàkkaar. Waa safara toskare nañu." }
67
12
{ "fr": "Ceux qui redoutent leur Seigneur bien qu´ils ne L´aient jamais vu auront un pardon et une grande récompense.", "wo": "Saar 67 : Nguur ga 12 - Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
67
12
{ "fr": "Ceux qui redoutent leur Seigneur bien qu´ils ne L´aient jamais vu auront un pardon et une grande récompense.", "wo": "Ñay ragal seen Boroom ci kumpa am nañu ag njégël ak pey gu màgg." }
67
13
{ "fr": "Que vous cachiez votre parole ou la divulguiez Il connaît bien le contenu des poitrines.", "wo": "Su ngeen di déey walla ngeen di jooru Moo xam tigi li nekk ci dënn yi." }
67
14
{ "fr": "Ne connaît-Il pas ce qu´Il a créé alors que c´est Lui Compatissant, le Parfaitement Connaisseur.", "wo": "Ki bind ndax dadul xam te Moom moo di ki Ñewenti, di Ku deñ Kumpa ci lépp. " }
67
15
{ "fr": "C´est Lui qui vous a soumis la terre : parcourez donc ses grandes étendues. Mangez de ce qu´Il vous fournit. Vers Lui est la Résurrection.", "wo": "Moom moo leen tàggatal suuf si : doxleen ci ay déndëm. Tey lekk ciy xéewalam. (Ca Yàlla) la léppiy mujj." }
67
16
{ "fr": "êtes-vous à l´abri que Celui qui est au ciel enfouisse en la terre ? Et voici qu´elle tremble !", "wo": "Ndax man ngeen a raw ki nekk ci asamaan si su talañee suuf si ? Ba muy rëg-rëgi, mukk !" }
67
17
{ "fr": "Ou êtes-vous à l´abri que Celui qui au ciel envoie contre vous un ouragan de pierres ? Vous saurez ainsi quel fut Mon avertissement.", "wo": "Walla dangeen a man a raw ki nekk ci asamaan su yabalee lu ànd ak i doj ? Xalset ngeen xam Samag xupe." }
67
18
{ "fr": "En effet, ceux d´avant eux avaient crié au mensonge. Quelle fut alors Ma réprobation !", "wo": "Ña leen fi jiitu woon, weddi woon nañu. Kon naka la sama mbugël deme woon ci ñoom !" }
67
19
{ "fr": "N´ont-ils pas vu les oiseaux au-dessus d´eux, déployant et repliant leurs ailes tour à tour ? Seul le Tout Miséricordieux les soutient. Car Il est sur toute chose, Clairvoyant.", "wo": "Xanaa dañoo xoolul ci picc yi leen tiim, di tàllal seeni laaf ak bank ? Te (Yàlla) Yëramaakoon bi rekk leen teye (ci jawu ji). Moom, Kuy Gis la lépp lu ne.(s)" }
67
20
{ "fr": "Quel est celui qui constituerait pour vous une armée [capable] de vous secourir, en dehors du Tout Miséricordieux ? En vérité les mécréants sont dans l´illusion complète.", "wo": "Ana kan moo leen man a wutal ay xarekat yu leen di taxwu te du Yàlla ? Yéefër yi ci woro la ñu nekk." }
67
21
{ "fr": "Ou quel est celui qui vous donnera votre subsistance s´Il s´arrête de fournir Son attribution ? Mais ils persistent dans leur insolence et dans leur répulsion.", "wo": "Ana kan moo leen di wërsëgal su (Yàlla) téyee wërsëgëm ? Ñoom da ñoo sànku." }
67
22
{ "fr": "Qui est donc mieux guidé ? Celui qui marche face contre terre ou celui qui marche redressé sur un chemin droit.", "wo": "Moo ndax ? Waajiy dëpp xarkanamam moo gën a gindiku kiy dox ne sàtt ca kaw yoon wa jub xocc." }
67
23
{ "fr": "Dis : \"C´est Lui qui vous a crées et vous a donné l´ouïe, les yeux et les coeurs\". Mais vous êtes rarement reconnaissants !", "wo": "Waxal ne: “Moom moo leen sàkk defal leen dégg, ak ub gis ak i xol” . Te néewaana ngeen sant delloo njukël !" }
67
24
{ "fr": "Dis : \"C´est Lui qui vous a répandus sur la terre, et c´est vers Lui que vous serez rassemblés\".", "wo": "Waxal ne : “It moo leen ji ci suuf si, te ca moom ngeen di mujj ñu pang leen” ." }
67
25
{ "fr": "Et ils disent : \"A quand cette promesse si vous êtes véridiques ? \".", "wo": "Ñuy wax naan : “Dig ba kañ lay doon su fekkee ne ñu dëggu ngeen ?” ." }
67
26
{ "fr": "Dis : \"Allah seul [en] a la connaissance. Et moi je ne suis qu´un avertisseur clair\".", "wo": "Waxal ne : “Xam-xamub loolu ma nga ca Yàlla. Man nag ab xuppekat buy leeral laa” ." }
67
27
{ "fr": "Puis, quand ils verront (le châtiment) de près, les visages de ceux qui ont mécru seront affligés. Et il leur sera dit : \"Voilà ce que vous réclamiez\".", "wo": "Bu, ñu ne gegg ca (mbugël ma), xarkanami yéefar ya di gañ-gañi. Ñu ne leen: “Lii nag ngeen yàkkamti woon” ." }
67
28
{ "fr": "Dis : \"Que vous en semble ? Qu´Alla me fasse périr ainsi que ceux qui sont avec moi ou qu´Il nous fasse miséricorde, qui protégera alors les mécréants d´un châtiment douloureux ? \".", "wo": "Waxal ne : “Xanaa gisu leen ? Su ma Yàlla reyoon maak ñi ma àndal, ana kan mooy man a yiir yéefar yi aar leen ci mbugal mu mitti (amul de) ?” ." }
67
29
{ "fr": "Dis : \"C´est Lui, le Tout Miséricordieux. Nous croyons en Lui et c´est en Lui que nous plaçons notre confiance. Vous saurez bientôt qui est dans un égarement évident\".", "wo": "Waxal ne : “Kooku moo di, Yàlla yëramaakoon bi. Gëm nanu ko te doyloo nanu ko. Dangeen xala xam ana kan moo nekk cig réer” ." }
67
30
{ "fr": "Dis : \"Que vous en semble ? Si votre eau était absorbée au plus profond de la terre, qui donc vous apporterait de l´eau de source ? \" ", "wo": "Waxal ne : “Xanaa gisuleen ? Bu seen ndox mi rawoon ci biir suuf xóot, ana kan moo leen di may bëtu ndox bu tane (Yàlla) ?” " }
68
1
{ "fr": "Noun . Par la plume et ce qu´ils écrivent !", "wo": "Nuun. Ak Xalima ga ak la ñuy bind !" }
68
2
{ "fr": "Tu (Muhammad) n´est pas, par la grâce de ton Seigneur, un possédé.", "wo": "Sa xéewali Boroom (yaw Muhammad), tax na ba dofoo." }
68
3
{ "fr": "Et il y aura pour toi certes, une récompense jamais interrompue.", "wo": "Te itam, am nga pey gu dootul dog." }
68
4
{ "fr": "Et tu es certes, d´une moralité imminente.", "wo": "Te yaa ngi làmboo, ak jikko yu màgg." }
68
5
{ "fr": "Tu verras et ils verront.", "wo": "Danga gis ñoom it danañu gis." }
68
6
{ "fr": "qui d´entre vous a perdu la raison.", "wo": "Ana kan ci yéen moo sànku." }
68
7
{ "fr": "C´est ton Seigneur qui connaît mieux ceux qui s´égarent de Son chemin, et il connaît mieux ceux qui suivent la bonne voie.", "wo": "Te sa Boroom moo gën a xam ku réere aw Yoonam, te it moo gën a xam ñay gindiku." }
68
8
{ "fr": "N´obéis pas à ceux qui crient en mensonge,", "wo": "Bul topp mukk ñiy fen," }
68
9
{ "fr": "Ils aimeraient bien que tu transiges avec eux afin qu´ils transigent avec toi.", "wo": "Bëgg nañu nga nooy ba ñu nooy ñoom itam." }
68
10
{ "fr": "Et n´obéis à aucun grand jureur, méprisable,", "wo": "Bul topp bépp waatkat, bu doyadi," }
68
11
{ "fr": "grand diffamateur, grand colporteur de médisance,", "wo": "ab saagakat, buy dox di rambaaje," }
68
12
{ "fr": "grand empêcheur du bien, transgresseur, grand pécheur,", "wo": "buy tere aw yiw, tey jalgati, di def bàkkaar," }
68
13
{ "fr": "au cœur dur, et en plus de cela bâtard .", "wo": "ak ku jàgg, te bariw ay." }
68
14
{ "fr": "Même s´il est doté de richesses et (de nombreux) enfants.", "wo": "Mu nekk di boroom alal ak i doom." }