sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
56
14
{ "fr": "et un petit nombre parmi les dernières [générations],", "wo": "ak lim bu néew ca ña mujjoon," }
56
15
{ "fr": "sur des lits ornés [d´or et de pierreries],", "wo": "ci kaw ay lal yu ñu sadd [wurus ak peme]," }
56
16
{ "fr": "s´y accoudant et se faisant face.", "wo": "dañu cay soonu jàkkaarloo." }
56
17
{ "fr": "Parmi eux circuleront des garçons éternellement jeunes,", "wo": "Ay xale yu dootu ñu màggat ñooleen di liggéeyal di leen wër," }
56
18
{ "fr": "avec des coupes, des aiguières et un verre [rempli]: d´une liqueur de source", "wo": "ci ay kopp, ak baraada ak i kaas: ci aw ñoll" }
56
19
{ "fr": "qui ne leur provoquera ni maux de tête ni étourdissement;", "wo": "te duñu miir dunu màndi ;" }
56
20
{ "fr": "et des fruits de leur choix,", "wo": "ak wépp xeetu fuytéef wu nu gëna xemmeem, " }
56
21
{ "fr": "et toute chair d´oiseau qu´ils désireront.", "wo": "ak yàppu picc la nu ca gëna wunnéen." }
56
22
{ "fr": "Et ils auront des houris aux yeux, grands et beaux,", "wo": "Ak ay jigéen (huur al iin), yu jekk ya lool ay gët," }
56
23
{ "fr": "pareilles à des perles en coquille.", "wo": "yu taaru ba mel ni wurusu peme." }
56
24
{ "fr": "en récompense pour ce qu´ils faisaient.", "wo": "ñu faye leen ko la ñu daan jëf." }
56
25
{ "fr": "Ils n´y entendront ni futilité ni blasphème;", "wo": "Duñu fa dégg mukk ay waxi neen walla wax ju sew ;" }
56
26
{ "fr": "mais seulement les propos : \"Salam ! Salam ! \"... [Paix ! paix ! ]", "wo": "lu dul dañuy wax rekk naan : “Jàmm nga am aa jàmm rekk!”" }
56
27
{ "fr": "Et les gens de la droite; que sont les gens de la droite ?", "wo": "Ak waa ndeyjoor ; ana ñan ñoo di waa ndeyjoor ?" }
56
28
{ "fr": "[Ils seront parmi]: des jujubiers sans épines,", "wo": "[ñoom ñanga ca]: déem yu amul dég," }
56
29
{ "fr": "et parmi des bananiers aux régimes bien fournis,", "wo": "ak ci garabi banaana yu meññet ma rangaloo," }
56
30
{ "fr": "dans une ombre étendue", "wo": "ak ci biir keppaar yu nu yiif yaatu" }
56
31
{ "fr": "[près] d´une eau coulant continuellement,", "wo": "ak ci [wetu] ndox muy sottiku te tëa dakk," }
56
32
{ "fr": "et des fruits abondants", "wo": "ak ay fuytéef yu bari sakkan" }
56
33
{ "fr": "ni interrompus ni défendus,", "wo": "du rag mukk te it kenn du ko tere," }
56
34
{ "fr": "sur des lits surélevés,", "wo": "ak ay laltaay yu yékkatiku," }
56
35
{ "fr": "C´est Nous qui les avons créées à la perfection,", "wo": "Man Yàlla maa leen sàkk ñu ñeseŋ ñoom (huur al iin)," }
56
36
{ "fr": "et Nous les avons faites vierges,", "wo": "def Nanu leen ñu di ay xiig," }
56
37
{ "fr": "gracieuses, toutes de même âge,", "wo": "yu sopp lool seen jëkër, te maase ne rojj," }
56
38
{ "fr": "pour les gens de la droite,", "wo": "waa ndeyjoor leen moom," }
56
39
{ "fr": "une multitude d´élus parmi les premières [générations],", "wo": "ñuy mbooloo ma nu tànn ca ña jëkkóon," }
56
40
{ "fr": "et une multitude d´élus parmi les dernières [générations],", "wo": "ak mbooloo ma nu tànn ci ñu mujj," }
56
41
{ "fr": "Et les gens de la gauche; que sont les gens de la gauche ?", "wo": "Ak waa càmmoñ; ana ñan ñoo di waa càmmoñ ?" }
56
42
{ "fr": "ils seront au milieu d´un souffle brûlant et d´une eau bouillante,", "wo": "ña nga ca biir cóolóolul ndox may wañax," }
56
43
{ "fr": "à l´ombre d´une fumée noire", "wo": "ak ca ron kërug saxaar su ñuul kukk" }
56
44
{ "fr": "ni fraîche, ni douce.", "wo": "seddul, neexul lewetul." }
56
45
{ "fr": "Ils vivaient auparavant dans le luxe", "wo": "Ñoom ba ñuy dund ca àddina da ñu daan fuukarewu." }
56
46
{ "fr": "Ils persistaient dans le grand péché [le polythéisme]", "wo": "Dañoo nuuran ci bàkkaar ba gëna màgg mu di bokkaale Yàlla " }
56
47
{ "fr": "et disaient : \"Quand nous mourrons et serons poussière et ossements, serons-nous ressuscités ?", "wo": "dañu daan wax naan : “ Moo ndax bu nu faatoo ba def suuf ak i yax, dees nanu dekkilaat ?" }
56
48
{ "fr": "ainsi que nos anciens ancêtres ? ...\"", "wo": "nook sunuy baay ak i maam ?...”" }
56
49
{ "fr": "Dis : \"En vérité les premiers et les derniers", "wo": "Waxal ne : “Mbooleem ña jëkkoon ak ñu mujj ñi(s)" }
56
50
{ "fr": "seront réunis pour le rendez-vous d´un jour connu\".", "wo": "dees na leen dajale ci féncóob bis bu ñu xam” ." }
56
51
{ "fr": "Et puis, vous, les égarés, qui traitiez (la Résurrection) de mensonge,", "wo": "Topp ginnaaw ba, yéen, ñi réeroon, te daan waddi (bis pénc ba)," }
56
52
{ "fr": "vous mangerez certainement d´un arbre de Zaqqoum.", "wo": "dangeen di lekk ci garabuk Zaquum." }
56
53
{ "fr": "Vous vous en remplirez le ventre,", "wo": "Ngeen di ca feesal seeni biir," }
56
54
{ "fr": "puis vous boirez par-dessus cela de l´eau bouillante,", "wo": "ngeen di fa naan ndox muy wañax teg ko ca," }
56
55
{ "fr": "vous en boirez comme boivent les chameaux assoiffés.", "wo": "ngeen di ca dëtëm ni giléem gu mar." }
56
56
{ "fr": "Voilà le repas d´accueil qui leur sera servi, au jour de la Rétribution.", "wo": "Ñam woowule ñu leen di teeroo, bu bis Pénc baa." }
56
57
{ "fr": "C´est Nous qui vous avons créés. Pourquoi ne croiriez-vous donc pas [à la résurrection] ?", "wo": "Nun noo leen sàkk bind leen. Ana lan moo tax manuleen a gëm dekkiwaat ?" }
56
58
{ "fr": "Voyez-vous donc ce que vous éjaculez :", "wo": "Xanaa gisuleen maniyyu mi ngeen sotti :" }
56
59
{ "fr": "est-ce vous qui le créez ou [en]: sommes Nous le Créateur ?", "wo": "yéen a koy bind: walla Nun (Yàlla) noo koy sos ?" }
56
60
{ "fr": "Nous avons prédéterminé la mort parmi vous. Nous ne serons point empêchés", "wo": "Nun noo natt ag dee ci yéen dogal ko te kenn du ko man a fanq. Te it lottu nu" }
56
61
{ "fr": "de vous remplacer par vos semblables, et vous faire renaître dans [un état] que vous ne savez pas.", "wo": "te wuutal leen ñeneen rey leen yéen, dekkilaat leen fu ngeen xamul." }
56
62
{ "fr": "Vous avez connu la première création. Ne vous rappelez-vous donc pas ?", "wo": "Xam ngeen xéll ca bu jëkk na ka ngeen sosoo. Moo kon ndax dangeen dul fàttaliku ?" }
56
63
{ "fr": "Voyez-vous donc ce que vous labourez ?", "wo": "Xanaa gisuleen li ngeen di ruuj ?" }
56
64
{ "fr": "Est-ce vous qui le cultivez ? ou [en] sommes Nous le cultivateur ?", "wo": "Yéen yéen a koy bay ? walla Nun noo koy bay ?" }
56
65
{ "fr": "Si Nous voulions, Nous le réduirions en débris. Et vous ne cesseriez pas de vous étonner et [de crier]:", "wo": "Sunu neexoon, Nu fóomal ko. Ngeen ne tócc di wél-wéli di [yuxu]:" }
56
66
{ "fr": "Nous voilà endettés !", "wo": "Te naan : “Danoo fees dell ak i bor !" }
56
67
{ "fr": "ou plutôt, exposés aux privations.", "wo": "amu nuy alal am nu tono”." }
56
68
{ "fr": "Voyez-vous donc l´eau que vous buvez ?", "wo": "Xanaa gisuleen ndox mi ngeen di naan ?" }
56
69
{ "fr": "Est-ce vous qui l´avez fait descendre du nuage ? ou [en] sommes Nous le descendeur ?", "wo": "Moo ndax yéen a koy wàccee ci niir yi ? walla Nun noo koy wàcce ? " }
56
70
{ "fr": "Si Nous voulions, Nous la rendrions salée. Pourquoi n´êtes-vous donc pas reconnaissants ?", "wo": "Sunu neexoon, Nu sëccël ko mu wex xàtt ak xorom. Moo xanaa dungeen sant ?" }
56
71
{ "fr": "Voyez-vous donc le feu que vous obtenez par frottement ?", "wo": "Xanaa gisuleen Safara wi ngeen di taaloo ?" }
56
72
{ "fr": "Est-ce vous qui avez créé son arbre ou [en] sommes Nous le Créateur ?", "wo": "Moo ndax yéen a sos garab gi walla Nun noo ko sos sàkk ko ?" }
56
73
{ "fr": "Nous en avons fait un rappel (de l´Enfer), et un élément utile pour ceux qui en ont besoin .", "wo": "Def nanu ko mu di ag fàttali (ci safaraw ëllëg), di jumtukaay ci képp ku ko ittewoo." }
56
74
{ "fr": "Glorifie donc le nom de ton Seigneur, le Très Grand !", "wo": "Na ngay sàbbaal sa Boroom, bu Màgg bi !" }
56
75
{ "fr": "Non ! ... Je jure par les positions des étoiles (dans le firmament).", "wo": "Déet !... maa ngi giiñ ci wàccuwaayi biddiw yi.(n)" }
56
76
{ "fr": "Et c´est vraiment un serment solennel, si vous saviez.", "wo": "Su ngeen xamoon lii, ngiiñ lu màgg la de." }
56
77
{ "fr": "Et c´est certainement un Coran noble,", "wo": "Lii dey Alxuraan ju teddla," }
56
78
{ "fr": "dans un Livre bien gardé ", "wo": "Saar 56 : Xew-xew ba 96 - Laaya - Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
56
78
{ "fr": "dans un Livre bien gardé ", "wo": "ci biir Téere bu ñu ñoŋal" }
56
79
{ "fr": "que seuls les purifiés touchent; ", "wo": "ñi laab rekk koy laal (ku laabul warukoo laal) ;" }
56
80
{ "fr": "C´est une révélation de la part du Seigneur de l´Univers.", "wo": "Mi ngi wàcci bawoo ca Yàlla Boroom àddina si." }
56
81
{ "fr": "Est-ce ce discours-là que vous traitez de mensonge ?", "wo": "Moo ndax ci waxtaan wii ngeen di weddi ?" }
56
82
{ "fr": "Et est-ce pour vous [une façon d´être reconnaissant] à votre subsistance que de traiter (le Coran) de mensonge ?", "wo": "Ak li leen Yàlla defal lépp fayewuleen ko lu dul di weddi Alxuraan ?" }
56
83
{ "fr": "Lorsque le souffle de la vie remonte à la gorge (d´un moribond),", "wo": "Bu ruuh gi génnee ba des ci bóli gi (kuy sukuraat)," }
56
84
{ "fr": "et qu´à ce moment là vous regardez,", "wo": "te fekk na yéen a nga koy xool," }
56
85
{ "fr": "et que Nous sommes plus proche de lui que vous [qui l´entourez] mais vous ne [le] voyez point.", "wo": "fekk na booba Nun Yàlla noo ko gëna jigeñ waaye du ngeen gis." }
56
86
{ "fr": "Pourquoi donc, si vous croyez que vous n´avez pas de compte à rendre,", "wo": "Bu ngeen, jortee ne ameeluleen Yàlla dara," }
56
87
{ "fr": "ne la faites-vous pas revenir [cette âme], si vous êtes véridiques ?", "wo": "ana lan moo tax kon delloosiwuleen [ruuh ga], ndegam ñu dëggu ngeen ?" }
56
88
{ "fr": "Si celui-ci est du nombre des rapprochés (d´Allah),", "wo": "Su fekkee ne koo ku dafa jige woon (Yàlla)," }
56
89
{ "fr": "alors (il aura) du repos, de la grâce et un Jardin de délices.", "wo": "dana (am) noflaay, ak àjjanay xéewël." }
56
90
{ "fr": "Et s´il est du nombre des gens de la droite,", "wo": "Su fekkee ne nag dafa bokk ci waa ndeyjoor," }
56
91
{ "fr": "il sera [accueilli par ces mots]: \"Paix à toi\" de la part des gens de la droite.", "wo": "dees na ko [teeroo]: “Jàmm ju” bawoo ca waa ndeyjoor." }
56
92
{ "fr": "Et s´il est de ceux qui avaient traité de mensonge (la résurrection) et s´étaient égarés,", "wo": "Su fekkee ne nag dafa bokk ca ña daan weddi (dekkiwaat) tey ñu réer sànku," }
56
93
{ "fr": "alors, il sera installé dans une eau bouillante,", "wo": "des na ko teeroo ndox muy wañax, " }
56
94
{ "fr": "et il brûlera dans la Fournaise.", "wo": "ak xoyomu ca biir Safara." }
56
95
{ "fr": "C´est cela la pleine certitude.", "wo": "Lii mooy dëgg tigi." }
56
96
{ "fr": "Glorifie donc le nom de ton Seigneur, le Très Grand !", "wo": "Na ngay sàbaal sa turu Boroom, bu Màgg bi ! " }
57
1
{ "fr": "Tout ce qui est dans les cieux et la terre glorifie Allah. Et c´est Lui le Puissant, le Sage.", "wo": "Ñi nekk ci biir asamaan yeek suuf si ñi ngi sàbbaal Yàlla miy boroom Kàttan gi, te di ku Xereñ." }
57
2
{ "fr": "A Lui appartient la souveraineté des cieux et de la terre. Il fait vivre et il fait mourir, et Il est Omnipotent.", "wo": "Mooy boroom nguurug asamaan yeek suuf. Mooy dundal mooy rey, te Man na lépp lu ne." }
57
3
{ "fr": "C´est Lui le Premier et le Dernier, l´Apparent et le Caché et Il est Omniscient.", "wo": "Mooy ki Jëkk mooy ki Mujj, mooy ki Fés mooy ki Nëbbu te moo Xam lépp lu ne." }
57
4
{ "fr": "C´est Lui qui a créé les cieux et la terre en six jours puis Il S´est établi sur le Trône; Il sait ce qui pénètre dans la terre et ce qui en sort, et ce qui descend du ciel et ce qui y monte, et Il est avec vous où que vous soyez. Et Allah observe parfaitement ce que vous faites.", "wo": "Mooy ki bind asamaan yeek suuf si ci biir juróom-benni fann ba noppi Mu yemoo ca kaw Gàngunaay ga (Aras); Xam na lépp luy dugg ci biir suuf ak lu caay génne, ak lépp luy wàcc bawoo asamaan ak lu cay yéek, te Moom mi ngi and ak yéen fu ngeen man di nekk. Te Yàlla kuy gis la li ngeen di def." }
57
5
{ "fr": "A Lui appartient la souveraineté des cieux et de la terre. Et à Allah tout est ramené.", "wo": "Mooy Boroom nguurug asamaan yeek suuf si . Te ca Yàlla la mbir yépp di mujj." }
57
6
{ "fr": "Il fait pénétrer la nuit dans le jour et fait pénétrer le jour dans la nuit, et Il sait parfaitement le contenu des poitrines.", "wo": "Mooy duggal guddi ci bëccëg te it mooy duggal bëccëg ci guddi, te Ku xam xéll la li nekk ci dënn yi." }
57
7
{ "fr": "Croyez en Allah et en Son Messager, et dépensez de ce dont Il vous a donné la lieutenance. Ceux d´entre vous croient et dépensent [pour la cause d´Allah] auront une grande récompense.", "wo": "Gëmleen Yàlla ak ub Yonentam, te na ngeen di joxe ci alal ji mu leen wuutalal. Ñi gëm te bokk ci yéen tey [joxe alal] danañu am ag pey gu màgg.(s)" }
57
8
{ "fr": "Et qu´avez-vous à ne pas croire en Allah, alors que le Messager vous appelle à croire en votre Seigneur ? Et [Allah] a déjà pris [acte] de votre engagement si vous êtes [sincères] dans votre foi.", "wo": "Ana lu leen dal ba munu leen gëm Yàlla, ak ub Yonentam mi ngi leen di woo ngir ngeen gëm seen Boroom ? Te jël ci yéen ab dig bu diis ndegam gëm ngeen." }
57
9
{ "fr": "C´est Lui qui fait descendre sur Son serviteur des versets claires, afin qu´il vous fasse sortir des ténèbres à la lumière; et assurément Allah est Compatissant envers vous, et Très Miséricordieux.", "wo": "Moom mooy wàcce ay kàddu yu leer ca jaamam ba, ngir mu génne leen cig lëndëm tàbbal leen cig leer; te Yàlla dey ku leen ñeewanti la, Jagléwaakoon la." }
57
10
{ "fr": "Et qu´avez-vous à ne pas dépenser dans le chemin d´Allah, alors que c´est à Allah que revient l´héritage des cieux et de la terre ? On ne peut comparer cependant celui d´entre vous qui a donné ses biens et combattu avant la conquête... ces derniers sont plus hauts en hiérarchie que ceux qui ont dépensé et ont combattu après. Or, à chacun, Allah a promis la plus belle récompense, et Allah est Grand-Connaisseur de ce que vous faites.", "wo": "Ana lu leen dal ba munuleen joxe alal ci yoonu Yàlla, te Yàllaa moom ndono yi nekk ci asamaan yeek suuf si ? Ña joxe seen alal lu jiitu (fathu Makkata) xare boole ca duñu yem ak kenn ñoom dañuy am pey gu màgg ak daraja yu kawe... ëppëlee ko ña joxe ginnaaw xare be te sax xare woon nañu . Ñoom ñépp, la Yàlla dig neexal bu duun, te Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def." }
57
11
{ "fr": "Quiconque fait à Allah un prêt sincère , Allah le Lui multiplie, et il aura une généreuse récompense.", "wo": "Ana kan mooy nangoo lebal Yàlla bor bu rafet, Mu fulandikul ko ko, te it dana am ag pey gu màgg." }
57
12
{ "fr": "Le jour où tu verras les croyants et les croyantes, leur lumière courant devant eux et à leur droite; (on leur dira) : \"Voici une bonne nouvelle pour vous aujourd´hui : des Jardins sous lesquels coulent les ruisseaux pour y demeurer éternellement\". Tel est l´énorme succès.", "wo": "(Bu keroog) (bis pénc baa) dangeen gis way gëm ña, leer ga dox seen diggante di jolli ci kanam ak ndeyjoor ; (ñu naan leen) : “Bégleen tey : am ngeen ay àjjana yu dex ya di daw ci suufam te dangeen fay béel” . Loolu mooy texe gu mag ga." }
57
13
{ "fr": "Le jour où les hypocrites, hommes et femmes, diront à ceux qui croient : \"Attendez que nous empruntions [un peu]: de votre lumières\". Il sera dit : \"Revenez en arrière, et cherchez de la lumière\". C´est alors qu´on éleva entre eux une muraille ayant une porte dont l´intérieur contient la miséricorde, et dont la face apparente a devant elle le châtiment [l´Enfer]", "wo": "Bu keroogee ba naaféq yu góor yi ak naaféq yu jigéen yi, di wax ñi gëm naan leen : “Xoolleen nu ndax nu man a niitu: ci seenug leer” . Ñu ne leen: “Delluleen ginnaaw, wutig leer” . Daldi doxale seen diggante ñag boo xam ne biir ga yërmaande la (fareek ña gëm), biti ba di mbugël (fareek naaféq ya)" }
57
14
{ "fr": "N´étions-nous pas avec vous ? leur crieront-ils. \"Oui, répondront [les autres] mais vous vous êtes laissés tenter, vous avez comploté (contre les croyants) et vous avez douté et de vains espoirs vous ont trompés, jusqu´à ce que vînt l´ordre d´Allah . Et le séducteur [Le diable]: vous a trompés au sujet d´Allah.", "wo": "“(Naaféq yaa ngay) woote naan xanaa àndunu woon ak yéen ?” jullit ña ne. “ Axakañ, waaye yéen a fitnaal seen bopp, daan fexeel (ñi gëm) daan werante, faggu ba faf mbirum Yàlla agsi saytaane nax leen." }
57
15
{ "fr": "Aujourd´hui donc, on n´acceptera de rançon ni de vous ni de ceux qui ont mécru. Votre asile est le Feu : c´est lui qui est votre compagnon inséparable. Et quelle mauvaise destination !", "wo": "Bis niki tey, kenn du jël ci yéen ag njotu kenn it du ko jëll ca ña weddi. Seenub saxuwaay Safara moom ngeen mengóol: dootu leen tàggoo. Ndaw mujj gu bon !" }
57
16
{ "fr": "Le moment n´est-il pas venu pour ceux qui ont cru, que leurs cœurs s´humilient à l´évocation d´Allah et devant ce qui est descendu de la vérité [le Coran] ? Et de ne point être pareils à ceux qui ont reçu le Livre avant eux . Ceux-ci trouvèrent le temps assez long et leurs cœurs s´endurcirent, et beaucoup d´entre eux sont pervers.", "wo": "Ndax jotul nag ci ñi gëm, seeni xol ragal buur jëm ci di fàttaliku Yàllu ak lépp lu wàcci tey dëgg ? Te ñuy baña mel ni ña leen jiitu woon te Téere wàcci ca ñoom . Ba diir ba yàggee seeni xol wow, ba faf la ëpp ca ñoom saay-saay lañu (génn topp).(r)" }