sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
54
48
{ "fr": "Le jour où on les traînera dans le Feu sur leurs visages, (on leur dira) : \"Goûtez au contact de Saqar [la chaleur brûlante de l´Enfer]\".", "wo": "Bu keroogee ba ñu di leen diri ci seen xarkanam ca biir Safara, (naan leen) : “Mosleen tokamti gu Safara” ." }
54
49
{ "fr": "Nous avons créé toute chose avec mesure,", "wo": "Noo bind lépp lu nekk cig natale," }
54
50
{ "fr": "et Notre ordre est une seule [parole]; [il est prompt] comme un clin d´oeil.", "wo": "amul sunu menn mbir [ndigal] ; [lu dul ne] dafay mel ni xefiinu bët." }
54
51
{ "fr": "En effet, nous avons fait périr des peuples semblables à vous. Y a-t-il quelqu´un pour s´en souvenir ?", "wo": "Faagaagal Nanu, ay xeet yu mel ni yéen. Mo ndax kon kenn du fàttaliku jàjj ?" }
54
52
{ "fr": "Et tout ce qu´ils ont fait est mentionné dans les registres,", "wo": "Te lépp lu ñu defoon bind Nanu ko ca téere ya," }
54
53
{ "fr": "et tout fait, petit et grand, est consigné.", "wo": "lépp, lu ndaw ak lu mag, karmat nañu ko ca." }
54
54
{ "fr": "Les pieux seront dans des Jardins et parmi des ruisseaux,", "wo": "Ña ragal Yàlla ña nga ca àjjana yu am i dex," }
54
55
{ "fr": "dans un séjour de vérité, auprès d´un Souverain Omnipotent.", "wo": "ca kërug dëgg ga, fa Buur Bu am kàttan ba. " }
55
1
{ "fr": "Le Tout Miséricordieux.", "wo": "Yërëmaakoon bi.(h)" }
55
2
{ "fr": "Il a enseigné le Coran.", "wo": "Moo jàngale Alxuraan (xamle ko)." }
55
3
{ "fr": "Il a créé l´homme.", "wo": "Moo bind nit (sos ko)." }
55
4
{ "fr": "Il lui a appris à s´exprimer clairement.", "wo": "Moo ko jàngal waxiin wu leer." }
55
5
{ "fr": "Le soleil et la lune [évoluent] selon un calcul [minutieux]", "wo": "Jant beek weer wi ne rojj yemoo" }
55
6
{ "fr": "et l´herbe et les arbres se prosternent .", "wo": "garab yi ak ñax mi dañuy sujuud." }
55
7
{ "fr": "Et quant au ciel, Il l´a élevé bien haut. Et Il a établit la balance,", "wo": "Moom moo kaweel asamaan. Teg ca ay nattukaayam màndaxe (balaas)," }
55
8
{ "fr": "afin que vous ne transgressiez pas dans la pesée :", "wo": "buleen di naxe mukk ci màndaxe natt :" }
55
9
{ "fr": "Donnez [toujours] le poids exact et ne faussez pas la pesée.", "wo": "Nangeen di natt cig maandute buleen njuuj-njaaj." }
55
10
{ "fr": "Quant à la terre, Il l´a étendue pour les êtres vivants :", "wo": "Moo tàllal, suuf ñiy dunde :" }
55
11
{ "fr": "il s´y trouve des fruits, et aussi les palmiers aux fruits recouverts d´enveloppes,", "wo": "am na ay fuytéef, ak tàndarma yuy meññ," }
55
12
{ "fr": "tout comme les grains dans leurs balles, et les plantes aromatiques.", "wo": "ak ay fepp yu nekk ci mbaram, ak gàncax yuy gilli." }
55
13
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
14
{ "fr": "Il a créé l´homme d´argile sonnante comme la poterie;", "wo": "Moom moo bind nit ci ban bu tikk dëgër ;" }
55
15
{ "fr": "et Il a créé les djinns de la flamme d´un feu sans fumée;", "wo": "te Moo bind jinne ci safara wuy bérëx wu amul saxaar;" }
55
16
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
17
{ "fr": "Seigneur des deux Levants et Seigneur des deux Couchants ! ", "wo": "Boroom ñaari Penku yi tey Boroom ñaari Sowo yi !" }
55
18
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ? " }
55
19
{ "fr": "Il a donné libre cours aux deux mers pour se rencontrer ;", "wo": "Moo dajale ñaari géej ya ;" }
55
20
{ "fr": "il y a entre elles une barrière qu´elles ne dépassent pas .", "wo": "def na aw dig ca seen diggante ba duñu jaxasoo." }
55
21
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
22
{ "fr": "De ces deux [mers]: sortent la perle et le corail.", "wo": "Te ñaari [géej]: yooyu peme da ciy génne ak ganjar." }
55
23
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
24
{ "fr": "A Lui appartiennent les vaisseaux élevés sur la mer comme des montagnes;", "wo": "Moo moom gaal yiy tëmbu ci biir géej niki ay tundi doj ;" }
55
25
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
26
{ "fr": "Tout ce qui est sur elle [la terre] doit disparaître,", "wo": "Képp kuy dund kaw [suuf] dana masa saay jeex," }
55
27
{ "fr": "[Seule] subsistera La Face [Wajh] de ton Seigneur, plein de majesté et de noblesse.", "wo": "Sa Jëmmi Boroom doŋŋ fiy des, moom miy boroom màgg gi ak teraanga." }
55
28
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
29
{ "fr": "Ceux qui sont dans les cieux et la terre L´implorent. Chaque jour, Il accomplit une oeuvre nouvelle.", "wo": "Ñi nekk asamaan ak suuf sii ngi koy laaj aka Dagaan. Te moom bis bu nekk, Mi ngi ci mbir." }
55
30
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
31
{ "fr": "Nous allons bientôt entreprendre votre jugement, ô vous les deux charges [hommes et djinns]", "wo": "Yéen nit ak jinne yi, danañu leen xalseta àtte" }
55
32
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
33
{ "fr": "ô peuple de djinns et d´hommes ! si vous pouvez sortir du domaine des cieux et de la terre, alors faites-le. Mais vous ne pourrez en sortir qu´à l´aide d´un pouvoir [illimité].", "wo": "Eey yéen mbooleem jinne yi ak nit ñi ! Su ngeen manee lañbatu ci biir déeléy asamaan yeek suuf si, lañbatuleen. Waaye du ngeen mana kër- këri mukk ba génn kiiraayal Yàlla." }
55
34
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
35
{ "fr": "Il sera lancé contre vous un jet de feu et de fumée [ou de cuivre fondu], et vous ne serez pas secourus.", "wo": "Dees na leen xala sotti safara ak biteex, te kenn du leen dimbali." }
55
36
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
37
{ "fr": "Puis quand le ciel se fendra et deviendra alors écarlate comme le cuir rouge.", "wo": "Su asamaan si xottikoo ruy mel ni beteex. " }
55
38
{ "fr": "Lequel des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
39
{ "fr": "Alors, ni aux hommes ni aux djinns, on ne posera des questions à propos de leurs péchés.", "wo": "Bu keroogee, nit ak jinne, kenn deesu ko laaj bàkkaaram." }
55
40
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
41
{ "fr": "On reconnaîtra les criminels à leurs traits. Ils seront donc saisis par les toupets et les pieds.", "wo": "Tooñkat ya dees na leen xàmmee ci seeni màndarga. Te deef na leen joñ boole seen bopp ak seeni tànk.(s)" }
55
42
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
43
{ "fr": "Voilà l´Enfer que les criminels traitaient de mensonge.", "wo": "Waaw-kay nag Safara sa tooñkat ya daan weddee ngi nii." }
55
44
{ "fr": "Ils feront le va-et-vient entre lui (l´Enfer) et une eau bouillante extrêmement chaude.", "wo": "Ñangay wëndéelu diggante (Safara sa) ak ndox muy bax." }
55
45
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
46
{ "fr": "et pour celui qui aura craint de comparaître devant son Seigneur, il y aura deux jardins;", "wo": "képp ku dëggël tey wagar taxawaay ba ca kanam Boroomam, dana am ñaari àjjana ;" }
55
47
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
48
{ "fr": "Aux branches touffues.", "wo": "Yu am car yu dëll meññ gacc." }
55
49
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
50
{ "fr": "Ils y trouveront deux sources courantes.", "wo": "Am na fa ñaari bëti ndox yuy daw-dawaan." }
55
51
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
52
{ "fr": "Ils contiennent deux espèces de chaque fruit.", "wo": "Nekk na ca biir ci xeetu fuytéef wu nekk ñaari wirgó" }
55
53
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
54
{ "fr": "ils seront accoudés sur des tapis doublés de brocart, et les fruits des deux jardins seront à leur portée (pour être cueillis).", "wo": "ñangay sóonu ci ay laltaay yu dëll yoo xam ne biir ga sooy la, te it meññatum ñaar dër ya day yoore." }
55
55
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Saar 55 : Yëramaakoon bi 78 - Laaya - Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
55
55
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ? " }
55
56
{ "fr": "Ils y trouveront [les houris] aux regards chastes, qu´avant eux aucun homme ou djinn n´aura déflorées.", "wo": "Ay Huur Al iin ñuy sajj seenub gis, ñoo xam ne nit walla jinne masu leen laal ñuy nekk ca biir." }
55
57
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
58
{ "fr": "Elles seront [aussi belles]: que le rubis et le corail.", "wo": "Dañuy [rafet ba] melni: wurus yaaquut walla marjaan." }
55
59
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
60
{ "fr": "Y a-t-il d´autre récompense pour le bien, que le bien ?", "wo": "Moo ndax lu rafet man naa am geneen pey guddul lu rafet (mukk du am) ?" }
55
61
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
62
{ "fr": "En deçà de ces deux jardins il y aura deux autres jardins.", "wo": "Ci dër yooyu amaat na yeneen ñaari dër." }
55
63
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
64
{ "fr": "Ils sont d´un vert sombre.", "wo": "Ñu di ñaari dër yu naat lool nëtëx." }
55
65
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
66
{ "fr": "Dans lesquelles il y aura deux sources jaillissantes.", "wo": "Nekk na ci seen biir ñaari bëti ndox yuy jol di fuur." }
55
67
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
68
{ "fr": "ils contiennent des fruits, des palmiers, et des grenadiers.", "wo": "am na ci biiram ay fuytéef, ak i tàndarma, ak rummaan." }
55
69
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
70
{ "fr": "là, il y aura des vertueuses et des belles.", "wo": "ay jigéen ñu yiw te rafet jekk, ñoo nekk ca biir." }
55
71
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
72
{ "fr": "des houris cloîtrées dans les tentes,", "wo": "jigéenu huur yu sax fa seen mbaar ya," }
55
73
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
74
{ "fr": "qu´avant eux aucun homme ou djinn n´a déflorées.", "wo": "nit wala jinne masuta laal jigéen ñooñu. " }
55
75
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
76
{ "fr": "Ils seront accoudés sur des coussins verts et des tapis épais et jolis.", "wo": "Ña ngeen soonu ci ay ngegenaay yu nëtëx (wert) ak ay laltaay yu rafet." }
55
77
{ "fr": "Lequel donc des bienfaits de votre Seigneur nierez-vous ?", "wo": "Yéen nit ak jinne ana naka ngeen di man a weddee seen xeewali Boroom ?" }
55
78
{ "fr": "Béni soit le Nom de ton Seigneur, Plein de Majesté et de Munificence !", "wo": "Saw turu Boroom Baarkeel na, moom miy Boroom Màgg ak Teraanga ji ! " }
56
1
{ "fr": "Quand l´événement (le Jugement) arrivera,", "wo": "Saa su xew-xew ba tàbbee (bis pénc ba),(r)" }
56
2
{ "fr": "nul ne traitera sa venue de mensonge.", "wo": "kenn dóotul weddeeti ag digëm." }
56
3
{ "fr": "Il abaissera (les uns), il élèvera (les autres).", "wo": "Mooy daane (ñenn), di yëkëti (ñeneen)." }
56
4
{ "fr": "Quand la terre sera secouée violemment,", "wo": "Bu ñu gësëmee suuf si mu rëg-rëgi," }
56
5
{ "fr": "et les montagnes seront réduites en miettes,", "wo": "te moñoxo tundi doj yi mu ne tasar," }
56
6
{ "fr": "et qu´elles deviendront poussière éparpillée", "wo": "daldi doon pënd buy tasaaroo" }
56
7
{ "fr": "alors vous serez trois catégories :", "wo": "ngeen dikk di ñatti kurél :" }
56
8
{ "fr": "les gens de la droite - que sont les gens de la droite ? ", "wo": "waa ndeyjoor – ana ñan ñooy waa ndeyjoor ?" }
56
9
{ "fr": "Et les gens de la gauche - que sont les gens de la gauche ?", "wo": "Ak waa càmmoñ – ana ñan ñooy waa càmmoñ ?" }
56
10
{ "fr": "Les premiers (à suivre les ordres d´Allah sur la terre) ce sont eux qui seront les premiers (dans l´au-delà)", "wo": "Ak ña jiitu woon ci ndigal te ñooy jiitu ba fàww" }
56
11
{ "fr": "Ce sont ceux-là les plus rapprochés d´Allah", "wo": "Ñooñee ñooy ña gëna jigeñ Yàlla" }
56
12
{ "fr": "dans les Jardins des délices,", "wo": "ca biir Àjjanay xeewu ja," }
56
13
{ "fr": "une multitude d´élus parmi les premières [générations],", "wo": "lim bu takku ca ña jiitu woon," }