sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
57
17
{ "fr": "Sachez qu´Allah redonne la vie à la terre une fois morte. Certes, Nous vous avons exposé les preuves clairement afin que vous raisonniez.", "wo": "Xamleen ne Yàllaay dundal suuf si ginnaaw ba mu dee. Leeralal Nanu leen, sunuy firnde ngir ngeen jëfandikoo seeni xol jàjju waaru." }
57
18
{ "fr": "Ceux et celles qui font la charité et qui ont fait à Allah un prêt sincère, cela leur sera multiplié et ils auront une généreuse récompense.", "wo": "Saraxekat yu góor ak saraxekat yu jigéen ñiy lebal Yàlla bor bu rafet , dees na leen ko fulal te danañu am ag pey gu màgg." }
57
19
{ "fr": "Ceux qui ont cru en Allah et en Ses messagers ceux-là sont les grands véridiques et les témoins auprès d´Allah . Ils auront leur récompense et leur lumière, tandis que ceux qui ont mécru et traité de mensonges Nos signes, ceux-là seront les gens de la Fournaise.", "wo": "Ña gëm Yàlla ak Yonentam ñooñee ñooy ña dëggu tey seede fa seen Boroom. Am nañu seenug pey ak seenug leer, yéefar yay weddi Sunuy firnde nag, ñoom ñoo di waa safara." }
57
20
{ "fr": "Sachez que la vie présente n´est que jeu, amusement, vaine parure, une course à l´orgueil entre vous et une rivalité dans l´acquisition des richesses et des enfants. Elle est en cela pareille à une pluie : la végétation qui en vient émerveille les cultivateurs, puis elle se fane et tu la vois donc jaunie; ensuite elle devient des débris. Et dans l´au-delà, il y a un dur châtiment, et aussi pardon et agrément d´Allah. Et la vie présente n´est que jouissance trompeuse.", "wo": "Xamleen ne dundug àddina am po la, ak i caaxaan, ak gànjar ak fuukareente, ak ëppalantey alal ak i doom. Mu mel ni waame : wu dotti yéem lool yéefar yi, gàncax ga naat seet seet mboq ; sooy mi yàqu. Te àllaxira, mbugël mu tar moo fa am, ak njégël gu bawoo fa Yàlla ak ngëramam. Dundug àddina du lenn lu dul taar buy naje." }
57
21
{ "fr": "Hâtez-vous vers un pardon de votre Seigneur ainsi qu´un Paradis aussi large que le ciel et la terre, préparé pour ceux qui ont cru en Allah et en Ses Messagers. Telle est la grâce d´Allah qu´Il donne à qui Il veut. Et Allah est le Détenteur de l´énorme grâce.", "wo": "Dawleen jëkënte jëm ci njégëluk seen Boroom ak ca Àjjana joo xam ne yaatuwaayam tollu na ni yaatuwaayu asamaan ak suuf, te dañu koy waajalal ñi gëm Yàlla ak Yonentam. Loolu ngënéelul Yàllaa. Te Yàlla Mooy Boroom ngëneel lu màgg la." }
57
22
{ "fr": "Nul malheur n´atteint la terre ni vos personnes, qui ne soit enregistré dans un Livre avant que Nous ne l´ayons créé; et cela est certes facile à Allah,", "wo": "Amul menn musiba muy dal ci kaw suuf si walla seen kaw jëmm yi, lu dul ne bind Nanu ko ci ab Téere ba nu ko laata sàkk ; te loolu lu yomb Yàlla la,(s)" }
57
23
{ "fr": "afin que vous ne vous tourmentiez pas au sujet de ce qui vous a échappé, ni n´exultiez pour ce qu´Il vous a donné. Et Allah n´aime point tout présomptueux plein de gloriole.", "wo": "ngir ngeen baña yoqat ñanki ci li leer, te it baña bokk ci damoo li mu leen jox. Yàlla safoowul képp kuy damoowaakoon buy fuukare wu." }
57
24
{ "fr": "Ceux qui sont avares et ordonnent aux gens l´avarice. et quiconque se détourne... Allah Se suffit alors à Lui-même et Il est Digne de louange.", "wo": "Ña nay tey digël nit ñi ñuy nay. Képp ku dumóoyu... Yàlla moom ku doyloo boppam la di ku Yayoo cant." }
57
25
{ "fr": "Nous avons effectivement envoyé Nos Messagers avec des preuves évidentes, et fait descendre avec eux le Livre et la balance, afin que les gens établissent la justice. Et Nous avons fait descendre le fer, dans lequel il y a une force redoutable, aussi bien que des utilités pour les gens, et pour qu´Allah reconnaisse qui, dans l´Invisible, défendra Sa cause et celle de Ses Messagers. Certes, Allah est Fort et Puissant.", "wo": "Yónni Nanu sunuy Yonenta ci ay firnde yu leer, wàcce ay Téere boolekook ñoom ak i balaas yu màndaxe, ngir nit ñi taxawal maandute. Wàcce Nanu weñ gu ñuul, mu am kàttan gu tar, ak ay njariñ ñeel nit ñi, ak it ngir Yàlla xam, ana kan moo koy dimbalil ay Yonentam, ci kumpa. Yàlla ku am doole la di Boroom Kàttan." }
57
26
{ "fr": "Nous avons effectivement envoyé Noé et Abraham et accordé à leur descendance la prophétie et le Livre. Certains d´entre eux furent bien-guidés, tandis que beaucoup d´entre eux furent pervers.", "wo": "Yónni Nanu Nooh ak Ibraahiima te it def nanu Yonenta ga ci seeni sët ak Téere ba jox nanu leen ko. Am na ci ñoom ñu gindiku, waaye li ëpp ci ñoom saay-saay lañu." }
57
27
{ "fr": "Ensuite, sur leurs traces, Nous avons fait suivre Nos [autres] messagers, et Nous les avons fait suivre de Jésus fils de Marie et lui avons apporté l´évangile, et mis dans les cœurs de ceux qui le suivirent douceur et mansuétude. Le monachisme qu´ils inventèrent, Nous ne le leur avons nullement prescrit. [Ils devaient] seulement rechercher l´agrément d´Allah. Mais ils ne l´observèrent pas (ce monachisme) comme il se devait. Nous avons donné leur récompense à ceux d´entre eux qui crurent. Mais beaucoup d´entre eux furent des pervers.", "wo": "Nu daldi xentuloo sunuy Yonent seen mboor, xentuloo Iisaa domu Maryaama indil nanu ko Injiil, te it def nanu ca biir xolu ña ko topp ak ñeewante ak yërmaande. Ak bero jigéen ña ñoom ñoo ko fental seen bopp, Waaye farataalu nu ko ci ñoom. Li nu leen digël daal moo di nañu sàkku ngëramul Yàlla. Te sax sàmmuñu ko ni mu ware. Ña bokk ca ñoom te gëm indil Nanu leen seenug pey. Waaye lu bari ci ñoom ay saay-saay lañu." }
57
28
{ "fr": "ô Vous qui avez cru ! Craignez d´Allah et croyez en Son messager pour qu´Il vous accorde deux parts de Sa miséricorde, et qu´Il vous assigne une lumière à l´aide de laquelle vous marcherez, et qu´Il vous pardonne, car Allah est Pardonneur et Très Miséricordieux.", "wo": "Eey yéen ñi gëm ! Ragal-leen Yàlla te gëm Yonentam bi dana leen defal ñaari cokkoor yu yërmande, danaleen defal it ak leer gu ngeen gindikoo, te it dinaleen jéggël, Yàlla Jéggëlaakoon la Jaglewaakoon la." }
57
29
{ "fr": "Cela afin que les gens du Livre sachent qu´ils ne peuvent en rien disposer de la grâce d´Allah et que la grâce est dans la main d´Allah; Il la donne à qui Il veut, et Allah est le Détenteur de la grâce immense.", "wo": "Ñoñ Téere nañu xam ne manuñu dara ci ngënéelu Yàlla te it ngëneel ci loxo Yàlla la nekk ; Moo koy jox ku ko soob, te Yàlla moo di Boroom ngëneel lu màgg li. " }
58
1
{ "fr": "Allah a bien entendu la parole de celle qui discutait avec toi à propos de son époux et se plaignait à Allah. Et Allah entendait votre conversation, car Allah est Audient et Clairvoyant.", "wo": "Yàlla dégg na waxi jigéen ja doon dàggasanteek yaw ci mbirum jëkëram te doon joyal njàmbatam ci Yàlla. Yàllaa ngi dégg seenuk wàqante yéen ñaar, Yàlla kuy dégg la kuy gis la.(h)" }
58
2
{ "fr": "Ceux d´entre vous qui répudient leurs femme, en déclarant qu´elles sont pour eux comme le dos de leur mères... alors qu´elles ne sont nullement leur mères, car ils n´ont pour mères que celles qui les ont enfantés. Ils prononcent certes une parole blâmable et mensongère. Allah cependant est Indulgent et Pardonneur.", "wo": "Góor ñiy weddi seeni jabar seen pendali nday , taxul ñu mel mi seeni nday ci ñoom... seeni nday ñoom ña leen juróon. Li ñuy wax lu ñaaw la di ay fen. Te Yàlla nag kuy bale la ab Jéggalaakoon la." }
58
3
{ "fr": "Ceux qui comparent leurs femmes au dos de leurs mères, puis reviennent sur ce qu´ils ont dit, doivent affranchir un esclave avant d´avoir aucun contact [conjugal] avec leur femme. C´est ce dont on vous exhorte. Et Allah est Parfaitement Connaisseur de ce que vous faites.", "wo": "Góor ñi nga xam ne dañoo woddi seeni jabar seeni pendali nday ba noppi bëgg caa dale ginnaaw, ca la ñu waxoon, nanu goreel ab jaam balaa ñoo jonjoowaat loolu la ñu leen di jàjje. Te Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def." }
58
4
{ "fr": "Mais celui qui n´en trouve pas les moyens doit jeûner alors deux mois consécutifs avant d´avoir aucun contact [conjugal] avec sa femme. Mais s´il ne peut le faire non plus, alors qu´il nourrisse soixante pauvres. Cela, pour que vous croyiez en Allah et en Son messager. Voilà les limites imposées par Allah. Et les mécréants auront un châtiment douloureux.", "wo": "Su ko manul na woor ñaari weer yu tegaloo balaa ñuy jonjoowaat. Su ko manul, na leel juróom-benn-fukki ndóol miskiin. Loolu nag, ngir ngeen gëm Yàlla ak ub Yonentam. Te loolu mooy daytali Yàlla yi. Ña weddi nag ñoom danañu am mbugël mu mitti." }
58
5
{ "fr": "Ceux qui s´opposent à Allah et à Son messager seront culbutés comme furent culbutés leurs devanciers. Nous avons déjà fait descendre des preuves explicites, et les mécréants auront un châtiment avilissant,", "wo": "Ñay juuyook Yàlla ak ub Yonentam dees na leen toroxal kem niñu toroxale woon ña leen fi jiitu woon. Te wàcce nanu ay firnde yu leer nàññ, yéefar yi am nañu mbugël mu and ak toroxtaane," }
58
6
{ "fr": "le jour où Allah les ressuscitera tous, puis les informera de ce qu´ils ont fait. Allah l´a dénombré et ils l´auront oublié. Allah est témoin de toute chose.", "wo": "bu keroog bis pénc baa ba Yàlla dékkal leen ñoom ñépp, dana leen xibaar la ñu jëfoon ndax Yàlla moom takkoon na ko ñoom it ñu fàtte ko. Yàlla kuy seede la ci lépp lu ne." }
58
7
{ "fr": "Ne vois-tu pas qu´Allah sait ce qui est dans les cieux et sur la terre ? Pas de conversation secrète entre trois sans qu´Il ne soit leur quatrième, ni entre cinq sans qu´Il n´y ne soit leur sixième, ni moins ni plus que cela sans qu´Il ne soit avec eux, là où ils se trouvent. Ensuite, Il les informera, au Jour de la Résurrection, de ce qu´ils faisaient, car Allah est Omniscient.", "wo": "Xanaa gisuloo Yàlla xam na li nekk ci asamaan yeek suuf si ? Amul fenn fu ñuy déeyoo sekkare muy ñatt te du moom Yàlla moo leen ñeenteel, du caageen juróom te du ut moo leen juróom-benneel, du lu gëna bari wala lu gëna néew loolu, lu dul ne mi ngi and ak ñoom fu ñu man a nekk. Te, Dana leen xibaar, lépp lu ñu daan jëf, bu bis pénc baa, Yàlla ku xam lépp la." }
58
8
{ "fr": "Ne vois-tu pas ceux à qui les conversations secrètes ont été interdites ? Puis, ils retournent à ce qui leur a été interdit, et se concertent pour pécher, transgresser et désobéir au Messager. Et quand ils viennent à toi, ils te saluent d´une façon dont Allah ne t´a pas salué, et disent en eux-mêmes : \"Pourquoi Allah ne nous châtie pas pour ce que nous disons ? \" L´Enfer leur suffira, où ils brûleront. Et quelle mauvaise destination !", "wo": "Xanaa gisuloo ñañu tere woon (Yahuud ya) ? Ba noppi, ñoom ñu dellu di ko def, di déeyoo ciy bàkkaar, ak ug nooneel ak moy Yonenta bi. Bu ñu dikkee fi yaw, nuyu la ak nuyoo boo xam ne Yàlla nuyoo wu la ko, te ña ngay wax ci seen xol naan : “Lu tax Yàlla dinu mbugël ci li nuy wax ?” Bàyyi leen ak Safara, Danañu ca xoyomu. Ndaw mujj gu bon !(s)" }
58
9
{ "fr": "ô vous qui avez cru ! Quand vous tenez des conversations secrètes, ne vous concertez pas pour pécher, transgresser et désobéir au Messager, mais concertez-vous dans la bonté et la piété. Et craignez Allah vers qui vous serez rassemblés.", "wo": "eey yéen ñi gëm ! Su ngeen dee déeyooti, buleen di déeyoo mukk ci luy bàkkaar , walla ak noonoo walla moy Yonenta bi, nangeen di déeyoo ci topp Yàlla ak ragal ko. Te nangeen ragal Yàlla mi nga xam ne dees na leen pang yéen ñépp jëmleen ca moom ( bu bis pénc baa)." }
58
10
{ "fr": "La conversation secrète n´est que [l´oeuvre] du Diable pour attrister ceux qui ont cru. Mais il ne peut leur nuire en rien sans la permission d´Allah. Et c´est en Allah que les croyants doivent placer leur confiance.", "wo": "Déeyoo moom [liggéeyub] saytaane doŋŋ la ngir man a tiit loo ñi gëm. Te manuleen a lor dara lu dul ci kàttanu Yàllu. Ñi gëm nañuy doyloo te wéeru ci Yàlla." }
58
11
{ "fr": "ô vous qui avez cru ! Quand on vous dit : \"Faites place [aux autres] dans les assemblées\", alors faites place. Allah vous ménagera une place (au Paradis) Et quand on vous dit de vous lever, levez-vous. Allah élèvera en degrés ceux d´entre vous qui auront cru et ceux qui auront reçu le savoir. Allah est parfaitement Connaisseur de ce que vous faites.", "wo": "Eey yéen ñi gëm ! bu ñu leen waxee ne yaatleleen ci jataay yi : “Na ngeen daldi yaatal” ,. Kon dey Yàlla dana leen yaatalal Bu ñu leen waxee ne jógleen, nangeen daldi jóg (su ngeen ko defee). Yàlla dana yékkatil ñi gëm te bokk ci yéen ak ña am xam-xam (ay daraja yu kawe). Te Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def." }
58
12
{ "fr": "ô vous qui avez cru ! Quand vous avez un entretien confidentiel avec le Messager, faites précéder d´une aumône votre entretien : cela est meilleur pour vous et plus pur. Mais si vous n´en trouvez pas les moyens alors Allah est Pardonneur et très Miséricordieux !", "wo": "eey yéen ñi gëm ! Su ngeen di déeyook Yonenta bi, na ngeen ca jiital ab sarax : loolu moo gën ci yéen te moo gën a sell. Su ngeen ko amul Yàlla moom Jéggëlaakoon la Jaglewaakoon la !" }
58
13
{ "fr": "Appréhendez-vous de faire précéder d´aumônes votre entretien ? Mais, si vous ne l´avez pas fait et qu´Allah a accueilli votre repentir, alors accomplissez la Salat, acquittez la Zakat, et obéissez à Allah et à Son messager. Allah est Parfaitement Connaisseur de ce que vous faites.", "wo": "Moo mbaa du dangeen ragal ñàkk ba tax du ngeen jiital sarax ? Su ngeen, ko deful Yàlla baal leen, daldi leen dem taxawali julli, te di natt asaka, te nangeen di topp Yàlla ak ub Yonentam. Yàlla Ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def." }
58
14
{ "fr": "N´as-tu pas vu ceux qui ont pris pour alliées des gens contre qui Allah S´est courroucé ? Ils ne sont ni des vôtres, ni des leurs; et ils jurent mensongèrement, alors qu´ils savent .", "wo": "Xanaa gisuloo naaféq ya dem ànd ak ña Yàlla mere (Yahuud ya) ? Ñoom bokkuñu ci yéen, bokkuñu it ci ñoom (Yahuud ya) ; te ña ngay giñ fen ci Yàlla, te xam ko xéll.(r)" }
58
15
{ "fr": "Allah leur a préparé un dur châtiment. Ce qu´ils faisaient alors était très mauvais.", "wo": "Yàlla waajalna leen mbugël mu tar. Ngir la ñu daan def ñaaw na." }
58
16
{ "fr": "Prenant leurs serments comme boucliers, ils obstruent le chemin d´Allah. Ils auront donc un châtiment avilissant.", "wo": "Jàppe woon nañu seen ngiñ ya muy pakk, ñuy gàllankor yoonu Yàlla. Danañu am mbugël muy toroxal." }
58
17
{ "fr": "Ni leurs bien, ni leurs enfants ne leur seront d´aucune utilité contre la [punition] d´Allah. Ce sont les gens du Feu où ils demeureront éternellement.", "wo": "Seen alal yeek, seen doom yi do leen jariñ manuleen fegal dara ci Yàlla. Ñoom ñoo di waa safara te danu fay béel." }
58
18
{ "fr": "Le jour où Allah les ressuscitera tous, ils Lui jureront alors comme ils vous jurent à vous-mêmes, pensant s´appuyer sur quelque chose de solide. Mais ce sont eux les menteurs.", "wo": "Bu keroogee ba Yàlla dekkal leen ñoom ñépp, su ku defee ñu di ko giiñël ni ñu leen daan giiñale yéen, dañuy jortu ne ñi ngi ci dara. Te ñoom ay fenkat la ñu. " }
58
19
{ "fr": "Le Diable les a dominés et leur a fait oublier le rappel d´Allah. Ceux-là sont le parti du Diable et c´est le parti du Diable qui sont assurément les perdants.", "wo": "Saytaane man-manee na leen ba fàtteloo leen tudd Yàlla. Ñoo di kureelub Saytaane ndaxam kureelu Saytaane ñooy ña yàqule tigi." }
58
20
{ "fr": "Ceux qui s´opposent à Allah et à Son messager seront parmi les plus humiliés.", "wo": "Ñay juuyook Yàlla ak ub Yonentam ñoom ñooy ña torox." }
58
21
{ "fr": "Allah a prescrit : \"Assurément, Je triompherai, moi ainsi que Mes Messagers\". En vérité Allah est Fort et Puissant.", "wo": "Yàlla bind na ne : “Tigi, Man, maak Samay Yonent nooy not” . Yàlla Ku bari doole la di Ku bari kàttan." }
58
22
{ "fr": "Tu n´en trouveras pas, parmi les gens qui croient en Allah et au Jour dernier, qui prennent pour amis ceux qui s´opposent à Allah et à Son Messager, fussent-ils leur pères, leur fils, leurs frères ou les gens de leur tribu. Il a prescrit la foi dans leurs cœurs et Il les a aidés de Son secours. Il les fera entrer dans des Jardins sous lesquels coulent les ruisseaux, où ils demeureront éternellement. Allah les agrée et ils L´agréent. Ceux-là sont le parti d´Allah. Le parti d´Allah est celui de ceux qui réussissent.", "wo": "Doo fekk mukk, aw nit ñu gëm Yàlla ak Bis bu mujj ba, ñuy soppanteek kuy juuyook Yàlla ak ub Yonentam, doonte la sax dafay seen baay, walla muy seen doom, walla muy seen mbokk walla ñu bokk giir. Ñooñu Yàlla def na ci seen biir xol ya ngëm dimbali leen ci bu baax. Te dina leen tàbbal ay àjjana yu ay dex di daw ci suufam, ñu béel fa. Yàlla gëram na leen ñoom it gëram nañu ko. Ñooñu ñoo di kurelub Yàlla. Te ndaxam moos kureelub Yàlla ñooy am ndam. " }
59
1
{ "fr": "Ce qui est dans les cieux et ce qui est sur la terre glorifient Allah, et Il est le Puissant, le Sage.", "wo": "Ñi nekk ci Asamaan yeek suuf si ñi ngi sàbbaal Yàlla, te moo di boroom kàttan gi, di Ku xereñ ki." }
59
2
{ "fr": "C´est Lui qui a expulsé de leurs maisons, ceux parmi les gens du Livre qui ne croyaient pas, lors du premier exode . Vous ne pensiez pas qu´ils partiraient, et ils pensaient qu´en vérité leurs forteresses les défendraient contre Allah. Mais Allah est venu à eux par où ils ne s´attendaient point, et a lancé la terreur dans leurs cœurs. Ils démolissaient leurs maisons de leurs propres mains, autant que des mains des croyants. Tirez-en une leçon, ô vous êtes doués de clairvoyance.", "wo": "Te mooy Yàlla moo génnee woon ña weddi te bokk ci, ñoñ Téere (Yahuudi Madiina), ci seen kër ca njaalbeenuk màng ga (Jëm Saam). Jortuleen woon ne danañu génn, ñoom (Yahudd ya it) jortoon nañu ne seeni tata dana leen aar. (Yàlla) daldi nay tàbbal tiitange ci seen xol,. Ñu tàmbalee gental seen kër ya ci seeni yoxo, ak yoxoy jullit ñi. Xalamleen (xalaat), yéen ñi am am njis mu leer.(s)" }
59
3
{ "fr": "Et si Allah n´avait pas prescrit contre eux l´expatriation, Il les aurait certainement châtiés ici-bas; et dans l´au-delà ils auront le châtiment du Feu.", "wo": "Su Yàlla dogalul woon seenug génn (réew mi), kon dey Mu mbugël leen ci àddina ; te bu àllaaxiraa it ñu am mbugëlum Safara." }
59
4
{ "fr": "Il en est ainsi parce qu´ils se sont dressés contre Allah et Son messager. Et quiconque se dresse contre Allah... alors, vraiment Allah est dur en punition.", "wo": "Li ko waral moo di ne ñoom dañoo juuyoo woon ak Yàlla ak ub Yonentam. Te nag képp kuy juuyook Yàlla... moom di boroom mbugël mu tar." }
59
5
{ "fr": "Tout palmier que vous avez coupé ou que vous avez laissé debout sur ses racines, c´est avec la permission d´Allah et afin qu´Il couvre ainsi d´ignominie les pervers.", "wo": "Tàndarma gu ngeen man a dog walla ngeen bàyyi ko mu taxaw, ci ndigalul Yàlla la ame ak it ngir mu gàcceel saay-saay sa (Yahuud ya)." }
59
6
{ "fr": "Le butin provenant de leurs biens et qu´Allah a accordé sans combat à Son Messager, vous n´y aviez engagé ni chevaux, ni chameaux; mais Allah donne à Ses messagers la domination sur qui Il veut, et Allah est Omnipotent.", "wo": "Li ngeen nangoo ci ñoom (alal) te xeexuleen Yàllaa ko baaxe ab Yonentam ; waaye nag Yàlla mooy bal ay Yonentam ci kaw ku ko soob te Yàlla ku am kàttan la ci def lépp lu ne." }
59
7
{ "fr": "Le butin provenant [des biens] des habitants des cités, qu´Allah a accordé sans combat à Son Messager, appartient à Allah, au Messager, aux proches parents, aux orphelins, aux pauvres et au voyageur en détresse, afin que cela ne circule pas parmi les seuls riches d´entre vous. Prenez ce que le Messager vous donne; et ce qu´il vous interdit, abstenez-vous en; et craignez Allah car Allah est dur en punition.", "wo": "Alal ji ngeen nangoo ci dëkk-dëkkaan yi te xeexuleen, Yàllaa ko moom ak ub Yonentam, ak mbokki jigeñaale, ak jirim yi, ak ndóol yi ak doxandeem yi, ( te loolu nag ngir mu baña yem rek) ci diggante way woomal yi. Lépp lu leen Yonent bi jox jël-leen ko ; lépp lu mu leen tere, bàyyileen ko ; te ngeen ragal Yàlla ndax Yàlla kat ku tar mbugël la." }
59
8
{ "fr": "[Il appartient aussi] aux émigrés besogneux qui ont été expulsés de leurs demeures et de leurs biens, tandis qu´ils recherchaient une grâce et un agrément d´Allah, et qu´ils portaient secours à (la cause d´) Allah et à Son Messager. Ceux-là sont les véridiques.", "wo": "[Bokk na ci ñi yayoo alal jooju] way ñakk ña gàddaayoon ñu génnee woon leen ca seen kër ak seen alal, te doon sàkku ngëneel ci Yàlla ak ngëramam, te doon sàkku ndimbalu Yàlla ak Ub Yonentam. Ñooña ñoo di ñu dëggal ña. " }
59
9
{ "fr": "Il [appartient également] à ceux qui, avant eux, se sont installés dans le pays et dans la foi, qui aiment ceux qui émigrent vers eux, et ne ressentent dans leurs coeurs aucune envie pour ce que [ces immigrés] ont reçu, et qui [les] préfèrent à eux-mêmes, même s´il y a pénurie chez eux. Quiconque se prémunit contre sa propre avarice, ceux-là sont ceux qui réussissent.", "wo": "[Bokk na ci ñi yayoo alal jooju] ña dëkke woon réewum (Madiina), te gëmoon ba ñu leen laataa fekk si, te soppoon lool ña gàddaay jëm si ci ñoom, iñaane wuñu leen dara, di jiital aajoy ña gàddaay ci seen aajoy bopp, ak luñu ñàkk ñàkk. Képp ku mucc ci nay, baaxle na fàww." }
59
10
{ "fr": "Et [il appartient également] à ceux qui sont venus après eux en disant : \"Seigneur, pardonne-nous, ainsi qu´à nos frères qui nous ont précédés dans la foi; et ne mets dans nos coeurs aucune rancœur pour ceux qui ont cru. Seigneur, Tu es Compatissant et Très Miséricordieux\".", "wo": "[Bokk na ci ñi yayoo alal jooju] ña dikk seen ginnaaw tey wax naan : “Yaw sunu Boroom, jéggalnu, nook sunu mbokk yi ñu jiitu ci ngëm ; te bul bàyyi genn mbañeel ci sunuy xol jëm ci ñi gëm. Yaw sunu Boroom, Kuy ñewenti nga Kuy Jaglewaakoon nga sa Yërmënde” ." }
59
11
{ "fr": "N´as-tu pas vu les hypocrites disant à leurs confrères qui ont mécru parmi les gens du Livre : \"Si vous êtes chassés, nous partirons certes avec vous et nous n´obéirons jamais à personne contre vous; et si vous êtes attaqués, nous vous secourrons certes\". Et Allah atteste qu´en vérité ils sont des menteurs.", "wo": "Xanaa gisuloo ña naaféq ña ngay wax ak seeni mbokk ya weddi ci ñoñ Téere naan leen : “Bu ñu leen génnee, dananu génn ànd ak yéen te dunu topp kenn ci lu leen di lor yéen ; te kuy xex ak yéen, nun yéen la nuy jàppale” . Te Yàlla seede na ne ñoom ay fenkat la ñu.(n)" }
59
12
{ "fr": "S´ils sont chassés, ils ne partiront pas avec eux; et s´ils sont attaqués, ils ne les secourront pas; et même s´ils allaient à leur secours, ils tourneraient sûrement le dos; puis ils ne seront point secourus.", "wo": "Bu ñu leen génnee woon, ñoom duñu génn mukk di ànd ak ñoom ; bu ñu doon xeex it , dunu leen jàppale ; sax dañuy mujj daw ; te duñu am ndam." }
59
13
{ "fr": "Vous jetez dans leurs coeurs plus de terreur qu´Allah. C´est qu´ils sont des gens qui ne comprennent pas.", "wo": "Ñoom naaféq yi seen jëmm yii la ñu gën a ragal ci Yàlla. Ndax ñoom dañoo xamul." }
59
14
{ "fr": "Tous ne vous combattront que retranchés dans des cités fortifiées ou de dernière des murailles. Leurs dissensions internes sont extrêmes. Tu les croirait unis, alors que leurs coeurs sont divisés. C´est qu´ils sont des gens qui ne raisonnent pas.", "wo": "Duñuy xeex ak yéen mukk (ñoom naaféq ya) lu dul biir dëkk yu ñu tata ci ginnaaw ay ñag. Seenug noonoo ci seen biir lu tar la. Danga foog ne ñu ànd lañu, te seeni xol dañoo féewoo. Li ko waral moo di ne dañoo amul ay xol di ko jariñoo." }
59
15
{ "fr": "ils sont semblables à ceux qui, peu de temps avant eux, ont goûté la conséquence de leur comportement et ils auront un châtiment douloureux ;", "wo": "danoo melni ñi leen jigeñ, te jiitu woon leen (Yéefëri Makka), mos nañu alkaande seen jëf te danañu am mbugël mu tar ;" }
59
16
{ "fr": "ils sont semblables au Diable quand il dit à l´homme : \"Sois incrédule\". Puis quand il a mécru, il dit : \"Je te désavoue car redoute Allah, le Seigneur de l´Univers\".", "wo": "dafay melni rekk Saytaane ba muy wax ak nit naan ko : “Weddil” . Ba mu weddee, mu ne ko : “Man kat deñ naa ci yaw ndax man damaa ragal Yàlla, miy Boroom àddina si” ." }
59
17
{ "fr": "Ils eurent pour destinée d´être tous deux dans le Feu pour y demeurer éternellement. Telle est la rétribution des injustes.", "wo": "Su ko defee ñoom ñaar Safaraay doon seenug muj ñu béel fa. Loolu mooy peyug tooñkat ya." }
59
18
{ "fr": "ô vous qui avez cru ! Craignez Allah. Que chaque âme voit bien ce qu´elle a avancé pour demain. Et craignez Allah, car Allah est Parfaitement Connaisseur de ce que vous faites.", "wo": "eey yéen ñi gëm ! Ragal-leen Yàlla. Bakkan bu nekk nay xool la muy jiital ngir ëllëg. Te nangeen di ragal Yàlla, Yàlla dey ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def." }
59
19
{ "fr": "Et ne soyez pas comme ceux qui ont oublié Allah; [Allah] leur a fait alors oublier leur propres personnes; ceux-là sont les pervers.", "wo": "Buleen def mukk ni gaa ña fàtte woon Yàlla ; Mu faf fàttiloo leen seen bopp ; ñooñee ñoo di saay-saay si." }
59
20
{ "fr": "Ne seront pas égaux les gens du Feu et les gens du Paradis. Les gens du Paradis sont eux les gagnants.", "wo": "Waa Safara duñu yem ak waa Àjjana mukk. Ndax waa Àjjana ñoo di ña texe. " }
59
21
{ "fr": "Si Nous avions fait descendre ce Coran sur une montage, tu l´aurais vu s´humilier et se fendre par crainte d´Allah. Et ces paraboles Nous les Nous les citons aux gens afin qu´ils réfléchissent.", "wo": "Sunu wàcce woon Alxuraan jii ci kaw aw doj, kon dey nga gis ko muy toroxlu daldi moñoxoo ngir ragal Yàlla. Yooyu ay léeb la yu nuy saddal nit ñi ngir ñu man caa xalaate." }
59
22
{ "fr": "C´est Lui Allah. Nulle divinité autre que Lui, le Connaisseur de l´Invisible tout comme du visible. C´est Lui, le Tout Miséricordieux, le Très Miséricordieux.", "wo": "Saar 59 : Màngaan ga 24 - Laaya – Laata Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
59
22
{ "fr": "C´est Lui Allah. Nulle divinité autre que Lui, le Connaisseur de l´Invisible tout comme du visible. C´est Lui, le Tout Miséricordieux, le Très Miséricordieux.", "wo": "Moom mooy Yàlla ji nga xam ne. Amul jeneen Yàlla ju dul moom, Moo xam kumpa ak li Feeñ. Mooy, Yëramaakoon bi, di Jaglewaakoon bi." }
59
23
{ "fr": "C´est Lui, Allah. Nulle divinité que Lui; Le Souverain, le Pur, L´Apaisant, Le Rassurant, le Prédominant, Le Tout Puissant, Le Contraignant, L´Orgueilleux. Gloire à Allah ! Il transcende ce qu´ils Lui associent.", "wo": "Moom Mooy, Yàlla ji nga xam ne. Amul jeneen Yàlla ju dul moom ; mooy Boroom bi, di Ku Sell ki, di Jàmm ji, di Ku Wóor ki, di Ku Peek lépp, di Boroom Kàttan gi, di Ponkal mi, di Ku Rëy ki. Tudd naa Sellam gi ! Soree na lool ak li ñu koy bokkaaleel." }
59
24
{ "fr": "C´est Lui Allah, le Créateur, Celui qui donne un commencement à toute chose, le Formateur. A Lui les plus beaux noms. Tout ce qui est dans les cieux et la terre Le glorifie. Et c´est Lui le Puissant, le Sage.", "wo": "Moom Mooy Yàlla, Bindkat biy sos, tey Melal. Mooy boroom tur yi gën a rafet. Mbooleem li nekk ci asamaan yeek suuf si dañu koy sàbbaal di ko kañ. Moom moo di boroom Kàttan gi, di Ku Xereñ ki. " }
60
1
{ "fr": "ô vous qui avez cru ! Ne prenez pas pour alliés Mon ennemi et le vôtre, leur offrant l´amitié, alors qu´ils ont nié ce qui vous est parvenu de la vérité. Ils expulsent le Messager et vous-mêmes parce que vous croyez en Allah, votre Seigneur. Si vous êtes sortis pour lutter dans Mon chemin et pour rechercher Mon agrément, leur témoignerez-vous secrètement de l´amitié, alors que Je connais parfaitement ce que vous cachez et ce que vous divulguez ? Et quiconque d´entre vous le fait s´égare de la droiture du sentier.", "wo": "Eey ñi gëm ! Buleen jàpp Samay noon ak seeni noon, ay xarit, ndax ñoom dañoo weddi dëgg ga dikk ci yéen. Danañu génne Yonent bi ak yéen néey da ngeen a gëm, Yàlla. Su fekkee ne dangeen a génn di xare ji ci yoonu Yàlla tey sàkku sama ngërëm, buleen rocciku mukk di wut ci ñoom ay xarit, ndax Man xam naa li ngeen di nëbb ak li ngeen di feeñal ? Képp ku ko def ci yéen na xam ne réere na yoon wu jub xocc wa.(s)" }
60
2
{ "fr": "S´ils vous dominent, ils seront des ennemis pour vous et étendront en mal leurs mains et leurs langues vers vous; et ils aimeraient que vous deveniez mécréants.", "wo": "Te suñu leen jekkoo, danañu leen rey saaga leen ; li ñu bëgg moo di ngeen weddi." }
60
3
{ "fr": "Ni vos proches parents ni vos enfants ne vous seront d´aucune utilité le Jour de la Résurrection, Il [Allah] décidera entre vous, et Allah est Clairvoyant sur ce que vous faites.", "wo": "Te bu Bis Pénc baa seeni doom walla seeni mbokk dunuleen fa jariñ, [Yàlla] dana fa teqale seen diggante, te Yàlla kuy Gis la li ngeen di def." }
60
4
{ "fr": "Certes, vous avez eu un bel exemple [à suivre] en Abraham et en ceux qui étaient avec lui, quand ils dirent à leur peuple : \"Nous vous désavouons, vous et ce que vous adorez en dehors d´Allah. Nous vous renions. Entre vous et nous, l´inimitié et la haine sont à jamais déclarées jusqu´à ce que vous croyiez en Allah, seul\". Exception faite de la parole d´Abraham [adressée] à son père : \"J´implorerai certes, le pardon [d´Allah] en ta faveur bien que je ne puisse rien pour toi auprès d´Allah\". \"Seigneur, c´est en Toi que nous mettons notre confiance et à Toi nous revenons [repentants]. Et vers Toi est le Devenir.", "wo": "Am ngeen, royukaay wu rafet ci Ibraahiima ak ña àndoon ak moom, (fàttalikul) ba ñu waxee seen nit ña ne leen : “Deñ nanu ci, yéen ak li ngeen di jaamu te du Yàlla. Weddi nanu leen. Sunu digganteek yéen it, mbañeel ak ug noonoo moo fiy dox ba fàwwu, lu dul bu ngeen gëmee Yàlla doŋŋ” . Ba mu des waxi Ibraahiima ak baayam ne ko : “Danaa la, jéggalul [Yàlla] waaye amaluma la dara ci Yàlla” . “Yaw sunu Boroom, Yaw la nu doyloo te ci Yaw la nuy delu. Te ci Yaw la lépp di Mujj." }
60
5
{ "fr": "Seigneur, ne fais pas de nous [un sujet] de tentation pour ceux qui ont mécru; et pardonne-nous, Seigneur, car c´est Toi le Puissant, le Sage\"", "wo": "Yaw sunu Boroom, bul nu def mukk [sànje] ci loxoy yéefar yi ; te nanga nu jéggal, Yaw, yaa di Boroom Kàttan gi, di Ku Xereñ ki”" }
60
6
{ "fr": "Vous avez certes eu en eux un bel exemple [à suivre], pour celui qui espère en Allah et en le Jour dernier : mais quiconque se détourne... alors Allah Se suffit à Lui-même et est Digne de louange.", "wo": "Ñoom am ngeen ci ñoom royuwaay wu rafet, mu ñeel képp ku yaakaar Yàlla ak Bis bu mujj ba : képp ku dumóoyu nag... na xam ne Yàlla ku doyloo boppam Yayoowaakoonu cant la." }
60
7
{ "fr": "Il se peut qu´Allah établisse de l´amitié entre vous et ceux d´entre eux dont vous avez été les ennemis. Et Allah est Omnipotent et Allah est Pardonneur et Très Miséricordieux.", "wo": "Amaana bu Yàlla defee ci seen diggante ak ñi ngeen noonooloon ag bëggënte. Yàlla Ku Man la te Yàlla Jéggëlaakoon Jaglewaakoon la.(r)" }
60
8
{ "fr": "Allah ne vous défend pas d´être bienfaisants et équitables envers ceux qui ne vous ont pas combattus pour la religion et ne vous ont pas chassés de vos demeures. Car Allah aime les équitables.", "wo": "Yàlla duleen tere ngeen di maslaa ak di laamisook ñi xeexul ak yéen ci seen diine te génnewuñuleen seeni kër. Yàlla safoona way maandu yi. " }
60
9
{ "fr": "Allah vous défend seulement de prendre pour alliés ceux qui vous ont combattus pour la religion, chassés de vos demeures et ont aidé à votre expulsion. Et ceux qui les prennent pour alliés sont les injustes.", "wo": "Ñi leen Yàlla di tere kay ñooy ñiy xeex ak yéen ci diine, di leen génnee ci seeni kër walla ña leen cay jàppale. Buleen xaritoo mukk ak ñoom képp kuy xaritook ñoom ñooy tooñkat yi." }
60
10
{ "fr": "ô vous qui avez cru ! Quand les croyantes viennent à vous en émigrées, éprouvez-les; Allah connaît mieux leur foi; si vous constatez qu´elles sont croyantes, ne les renvoyez pas aux mécréants. Elles ne sont pas licites [en tant qu´épouses] pour eux, et eux non plus ne sont pas licites [en tant qu´époux] pour elles. Et rendez-leur ce qu´ils ont dépensé (comme mahr). Il ne vous sera fait aucun grief en vous mariant avec elles quand vous leur aurez donné leur mahr. Et ne gardez pas de liens conjugaux avec les mécréantes . Réclamez ce que vous avez dépensé et que (les mécréants) aussi réclament ce qu´ils ont dépensé. Tel est le jugement d´Allah par lequel Il juge entre vous, et Allah est Omniscient et Sage.", "wo": "Eey yéen ñi gëm ! Su leen jullit yu jigéen ñi digëloon ne da ñuy gàddaay, nangeen leen seetlu nattu leen ; Yàllaa gën a xam seen dayob ngëm ; su ngeen xamee ne ay jullit la ñu, buleen leen delloo ca Yéefër ya. Ndax daganatuñu ci yéefar yi, Yéefër yi it daganatuñu ci ñoom. Te nangeen delloo alal ya. Aayul ci yéen ngeen denc leen soxna su ngeen joxee can. Buleen maslaak Yéefër. Laajleen la ngeen joxe woon ñoom it nañu laaj la ñu joxe woon. Loolu moo di àtteb Yàlla, Yàlla di àtte seen diggante Yàlla Ku Xam la Ku Xereñ la." }
60
11
{ "fr": "Et si quelqu´une de vos épouses s´échappe vers les mécréants, et que vous fassiez des représailles , restituez à ceux dont les épouses sont parties autant que ce qu´ils avaient dépensé. Craignez Allah en qui vous croyez.", "wo": "Su seeni soxna rëccee dem ca Yéefër ya yóbbaale can, su ngeen xareek ñoom ba nangu seeni alal, nangeen daldi génneel ña ca seeni soxna dem kem lu tollu ni seeni can. Te nangeen ragal Yàlla mi ngeen gëm." }
60
12
{ "fr": "ô Prophète ! Quand les croyantes viennent te prêter serment d´allégeance, [et en jurent] qu´elles n´associeront rien à Allah, qu´elles ne voleront pas, qu´elles ne se livreront pas à l´adultère, qu´elles ne tueront pas leurs propres enfants, qu´elles ne commettront aucune infamie ni avec leurs mains ni avec leurs pieds et qu´elles ne désobéiront pas en ce qui est convenable, alors reçois leur serment d´allégeance, et implore d´Allah le pardon pour elles. Allah est certes, Pardonneur et Très Miséricordieux.", "wo": "Eey yaw Yonent bi ! Jigéen ñi gëm su ñu la dikkalee di jaayanteek yaw ci ne, dootuñu bokkaaleek Yàlla dara, duñu sàcc, duñu njaaloo, duñu rey seeni doom, te duñu sos genn njaaxum ci seeni tànk ak yoxo te dunu la moy ci wenn yiw, nanga jaayanteek ñoom, te nanga leen jéggalul Yàlla. Te Yàlla moom, Jéggalakoon la Jaglewaakoon la." }
60
13
{ "fr": "ô vous qui avez cru ! Ne prenez pas pour alliés des gens contre lesquels Allah est courroucé et qui désespèrent de l´au-delà, tout comme les mécréants désespèrent des gens des tombeaux.", "wo": "Eey yéen ñi gëm ! Buleen di xaritook aw nit ñoo xam ne Yàlla da leen mere te dañoo yoqat ci àllaaxira, ni Yéefër yi yoqate ci ñi nekk ci biir bàmmeel yi. " }
61
1
{ "fr": "Ce qui est dans les cieux et ce qui est sur la terre glorifient Allah, et Il est le Puissant, le Sage.", "wo": "Ñi nekk ci asamaan yeek suuf si ña ngay sàbbaal Yàlla, te Moom moo di Boroom Kàttan ga, di Ku Xereñ ka.(s)" }
61
2
{ "fr": "ô vous qui avez cru ! Pourquoi dites-vous ce que vous ne faites pas ?", "wo": "Eey yéen ñi gëm ! Ana lan moo tax ngeen di wax lu ngeen dul def ?" }
61
3
{ "fr": "C´est une grande abomination auprès d´Allah que de dire ce que vous ne faites pas.", "wo": "Wax ji ngeen di wax te du ngeen ko def ak jéppi gu rëy (la leen di jural ca Yàlla)." }
61
4
{ "fr": "Allah aime ceux qui combattent dans Son chemin en rang serré pareils à un édifice renforcé.", "wo": "Yàlla safoona ñiy xeex ci yoonam wi def senn sàppe melni ñoom tabax bu ñu raax la ñu." }
61
5
{ "fr": "Et quand Moïse dit à son peuple : \"ô mon peuple ! Pourquoi me maltraitez-vous alors que vous savez que je suis vraiment le Messager d´Allah [envoyé] à vous ? \" Puis quand ils dévièrent, Allah fit dévier leurs coeurs, car Allah ne guide pas les gens pervers.", "wo": "(Fàttalikul) Ba Muusaa waxee aw nitam ne leen : “Yéen samaw nit ! Ana lan moo tax ba ngeen di ma lor te xam ngeen xell ne man mii Yonentub Yàlla laa ci yéen ?” Bu ñu jengee, Yàlla jengal seeni xol, te Yàlla du gindi mukk aw nit ñu di ay saay-saay." }
61
6
{ "fr": "Et quand Jésus fils de Marie dit : \"ô Enfants d´Israël, je suis vraiment le Messager d´Allah [envoyé] à vous, confirmateur de ce qui, dans la Thora, est antérieur à moi, et annonciateur d´un Messager à venir après moi, dont le nom sera \"Ahmad\" . Puis quand celui-ci vint à eux avec des preuves évidentes, ils dirent : \"C´est là une magie manifeste\".", "wo": "(Fàttalikul it) Ba Iisaa doomu Maryaama waxee ne : “eey yéen waa giir Banii-Israayiil, man mii Yonentub Yàlla laa ci yéen, may dëggal la ma jiitu woon, ca Tawraat, di bégale it, ci Yonent buy dikk sama ginnaaw aw turam di “ Ahmadu” . Waaye ba mu leen dikkale ak ay firnde yu leer , dañoo wax ne : “Lii kat ag njibarla gu bir ne fàŋŋ” ." }
61
7
{ "fr": "Et qui est plus injuste que celui qui invente un mensonge contre Allah, alors qu´il est appelé à l´Islam ? Et Allah ne guide pas les gens injustes.", "wo": "Ana kan moo gën a doon tooñkat kuy duural Yàlla ay fen, te ña nga koy woo jëme ko ci Lislaam ? Yàlla dey du gindi aw nit ñu di ay tooñkat." }
61
8
{ "fr": "Ils veulent éteindre de leurs bouches la lumière d´Allah, alors qu´Allah parachèvera Sa lumière en dépit de l´aversion des mécréants.", "wo": "Ñoom dañoo bëgg fay leerug Yàlla ci seeni gimiñ, te Yàlla moom kuy mottali la ag leeram doontele sax Yéefër yi dañuy bañ." }
61
9
{ "fr": "C´est Lui qui a envoyé Son messager avec la guidée et la Religion de Vérité, pour la placer au-dessus de toute autre religion, en dépit de l´aversion des associateurs.", "wo": "Moom moo yónni ab Yonentam ci njub ak diiney dëgg, ngir mu kawe mbooleem diine yi, doonte la sax Yéefër yi dañuy bañ." }
61
10
{ "fr": "ô vous qui avez cru ! Vous indiquerai-je un commerce qui vous sauvera d´un châtiment douloureux ?", "wo": "Eey yéen ñi gëm ! Moo ndax du ma leen tektal ci am njoló mu leen di musël ci mbugël mu mitti ?" }
61
11
{ "fr": "Vous croyez en Allah et en Son messager et vous combattez avec vos biens et vos personnes dans le chemin d´Allah, et cela vous est bien meilleur, si vous saviez !", "wo": "Dangeen di gëm Yàlla ak ub Yonentam tey xare ci yoonu Yàlla ak seeni alal ak seeni bakkan, looloo gën ci yéen de, cëy bu ngeen xamoon ! " }
61
12
{ "fr": "Il vous pardonnera vos péchés et vous fera entrer dans des Jardins sous lesquels coulent les ruisseaux, et dans des demeures agréables dans les jardins d´Eden ? Voilà l´énorme succès", "wo": "kon dey dana leen jéggal seeni bàkkaar te it dana leen tàbbal ay Àjjana yu ay dex di daw ci suufam, ak ay dëkkuwaay yu teey ci Àjjanay adan ? Loolu mooy texe gu mag ga" }
61
13
{ "fr": "et il vous accordera d´autres choses encore que vous aimez bien : un secours [venant] d´Allah et une victoire prochaine. Et annonce la bonne nouvelle aux croyants.", "wo": "Saar 61 : Sàppe si 14 - Laaya - Laata Gàdday ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
61
13
{ "fr": "et il vous accordera d´autres choses encore que vous aimez bien : un secours [venant] d´Allah et une victoire prochaine. Et annonce la bonne nouvelle aux croyants.", "wo": "dana leen defal it yeneeni mbir yu ngeen bëgg : ndimbal [lu bawoo] fa Yàlla ak ndam lu jige. Bégalal jullit ñi ci xibaar bu neex bi." }
61
14
{ "fr": "ô vous qui avez cru ! Soyez les alliés d´Allah, à l´instar de ce que Jésus fils de Marie a dit aux apôtres : \" Qui sont mes alliés (pour la cause) d´Allah ? \" - Les apôtres dirent : \"Nous sommes les alliés d´Allah\". Un groupe des Enfants d´Israël crut, tandis qu´un groupe nia. nous aidâmes donc ceux qui crurent contre leur ennemi, et ils triomphèrent.", "wo": "eey yéen ñi gëm ! Nangeen doon ay farandooy Yàlla, kem ni Iisaa doomu Maryaama waxe woon taalibeem ya ne leen : “ Ana ñan ñooy doon samay farandoo yi jëm ci Yàlla ?” – Taalube ya ne ko : “Nun ñoo di farandoo ya jëm ca Yàlla” . Mu am Kureel ci Banii-Israayiila bu gëm na, mu am it Kureel bu weddi. Nu daldi dooleel ña gëm ca kaw seeni noon, ñu daldi am ndam. " }
62
1
{ "fr": "Ce qui est dans les cieux et ce qui sur la terre glorifient Allah, le Souverain, le Pur, le Puissant, le Sage.", "wo": "Ñi nekk ci asamaan yeek suuf si ña ngay sàbbaal Yàlla, miy Buur, bu Sell, di Boroom Kàttan, di Ku xereñ.(h)" }
62
2
{ "fr": "C´est Lui qui a envoyé à des gens sans Livre (les Arabes) un Messager des leurs qui leur récite Ses versets, les purifie et leur enseigne le Livre et la Sagesse, bien qu´ils étaient auparavant dans un égarement évident,", "wo": "Moom mooy ki yónni ci araab yi ab Yonent bu bokk ci ñoom bu leen di jàngal ay Laayam, di leen jàngal Alxuraan ak Sunna, te ñoom bu jëkkoon ña nga woon ci réer gu sore," }
62
3
{ "fr": "ainsi qu´à d´autres parmi ceux qui ne les ont pas encore rejoints. C´est Lui le Puissant, le Sage.", "wo": "ak ci ñeneen ñoo xam ne dabaguñuleen. Te moom Yàlla Mooy boroom Kàttan, di Ku Xereñ." }
62
4
{ "fr": "Telle est la grâce d´Allah qu´Il donne à qui Il veut. Et Allah est le Détenteur de l´énorme grâce.", "wo": "Loolu ngënéelul Yàlla la moo koy jox ku ko soob. Te Yàlla mooy boroom Ngënéel lu màgg li." }
62
5
{ "fr": "Ceux qui ont été chargés de la Thora mais qui ne l´ont pas appliquée sont pareils à l´âne qui porte des livres. Quel mauvais exemple que celui de ceux qui traitent de mensonges les versets d´Allah et Allah ne guide pas les gens injustes.", "wo": "Misaalum ñi ñu wàcceeloon Tawraat te jëfewunu ko ñi ngi melni mbaam mu sëfi téere. Aka bon misaalum nit ñooñu nga xam ne dañoo weddi kàdduy Yàlla te Yàlla du gindi mukk aw nit ñu di ay tooñkat." }
62
6
{ "fr": "Dis : \"ô vous qui pratiquez le judaïsme ! Si vous prétendez être les bien aimés d´Allah à l´exclusion des autres, souhaitez donc la mort, si vous êtes véridiques\".", "wo": "Waxal ne : «Eey yéen Yahuud yi ! Su fekkee ne nii ngeen méngook Yàllaay, kon ñaan leen dee, su fekkee ne dëggu ngeen” ." }
62
7
{ "fr": "Or, ils ne la souhaiteront jamais, à cause de ce que leurs mains ont préparé. Allah cependant connaît bien les injustes.", "wo": "Dunu ko ñaan mukk ngir (la ñu jëf cik caay-caay). Yàlla ku Xamaakoon la tooñkat yi." }
62
8
{ "fr": "Dis : \"La mort que vous fuyez va certes vous rencontrer. Ensuite vous serez ramenés à Celui qui connaît parfaitement le monde Invisible et le monde visible et qui vous informera alors de ce que vous faisiez\".", "wo": "Waxal ne : “Dee gi ngeen di daw dana dajeek yéen. Ba noppi ñu delloo leen ca Yàlla mi xam kumpaak li feeñ mu di leen xibaar la ngeen daan def” ." }
62
9
{ "fr": "ô vous qui avez cru ! Quand on appelle à la Salat du jour du Vendredi, accourez à l´invocation d´Allah et laissez tout négoce . Cela est bien meilleur pour vous, si vous saviez !", "wo": "Eey yéen ñi gëm ! Saa suñu wootee ngir julli ci bisub Àjjuma, dawleen jëm ci tudd Yàlla te nangeen fa ne ñukk njaay ma bàyyi ko. Looloo gën ci yéen de, cëy bu ngeen xamoon !(r)" }
62
10
{ "fr": "Puis quand la Salat est achevée, dispersez-vous sur la terre, et recherchez [quelque effet] de la grâce d´Allah, et invoquez beaucoup Allah afin que vous réussissiez.", "wo": "Su julli gi jeexee, na ngeen tasaaroo ci suuf si, tey sàkku ci xeewali Yàlla yi, te na ngeen di tudd Yàlla lu bari ndax amaana ngeen baaxle. " }
62
11
{ "fr": "Quand ils entrevoient quelque commerce ou quelque divertissement, ils s´y dispersent et te laissent debout. Dis : \"Ce qui est auprès d´Allah est bien meilleur que le divertissement et le commerce, et Allah est le Meilleur des pourvoyeurs\".", "wo": "Te saa su ñu gesee am njoló walla am po danuy buur jëm ca, bàyyi la nga ne saŋŋ taxaw. Waxal ne: “La nekk fa Yàlla moo gën fuuf am po te moo gën it am njoló, te Yàlla moo di Gën ji kuy wërsëgël” . " }
63
1
{ "fr": "Quand les hypocrites viennent à toi, ils disent : \"Nous attestons que tu es certes le Messager d´Allah\"; Allah sait que tu es vraiment Son messager; et Allah atteste que les hypocrites sont assurément des menteurs.", "wo": "Su naaféq ya dikkee ci yaw danuy wax naan : “Noo ngi seede ne yaw Yonent Yàlla nga” ; Yàlla xam na ne yaw ab Yonentam nga ; te Yàlla seede na ne naaféq ya ay fenkat la ñu.(s)" }