url
stringlengths 6
8
| content
stringlengths 2
3.72k
| source
stringclasses 3
values |
---|---|---|
page_1 | Bubakar Bóris Jóob
Doomi Golo | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_2 | Doomi Golo
Nettali | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_3 | XAAJ BU JËKK
NGIRAAN FAY
Gone mat naa bàyyi cim réew | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_4 | TÉEREB DÓOM
I | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_5 | Noonu ma xool ko lu yàgg, daldi yëngal
ndànk sama bopp, ni ko :
Àddina : dund, dee.
Leneen newu fi, Badu.
Lii rekk : demal, maa ngi ñëw.
Naka laa wax loolu, daldi déggaat woykat
ba :
« Àddina amul solo, ndeysaan... Ku ci
dee yaa ñàkk sa bakkan, ndeysaan ».
Booba gone laa woon, nekk ci sama diggu
doole, yaakaar ne dara tëwu ma. Maa fii
dàqoon a fecc, bare bayre ba nga ne lii lu mu
doon ! Fu ma jaaraan, janq di ma tooñ, naan :
- Ngiraan Fay jàppal fii, Ngiraan Fay bàyyil
faa !
Mbaa nga dégg ci jeeg ju ndaw ji ku ni :
- Moo Ngiraan Fay, looy jaay maanaa nii ?
Billaay yow ! Yal na nga koote ! Léegi,
mag dikk na. Maa ngi nii toog ci sama
buntu kër, fii ci gox bi ñu naan Ñarelaa, di
xaar sunu boroom bi def ci man li gën.
Teewul nag sama xel yépp nekk ci yow, Badu. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_6 | Xéy-na yaa nga ca dëkku naar ya, moo
xam Alseeri la, walla Marog mbaa Libaη.
Foofa de lanu yaakaar ne fa nga nekk.
Kenn amu ci nag lu ko wóor Am na sax
ñu naan :
- Kéwél kat du tëb doom ja bëtt. Badu
Taal kay, xam ngeen ne topp na ciy tànki
baayam Asan Taal. Ba fu coow liy mujje,
Tugal ngeen koy déggi.
Ci juróom-ñaari téere yi ma la fiy bàyyil
sax, am na bu ci tudd Téereb Ndéey
Turam tegtal bu leer la : li nekk ci biir,
maak yow doηη noo ko séq. Yoonu
keneen newu ci.Yaa ngi nii toog janook
man, ma sëgg ba jot say nopp. Su ma ci
tàbbalee ay kàddu, nga naj leen fa.
Kàddu yooyu di wéq sa kaaη, di féqu ci sa
biir bopp, ngir rekk bëgg a génn ci biti,
tasaaroo, nekk lu askan wiy waxtaane.
Nga gën leen faa naj, ndax ragal ñu jur ay
ak téesante. Du tee nag sa xel di leen tojat
ba ñu mokk rumbux, nga xam lan la bu ci
nekk wund, ne patt di wéy ak moom. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_7 | Téereb Ndéey bi yomb naa xàmmee,
mooy bu xonq bi. Moom laay dénk lépp lu
ma dégg ñu koy waxtaane ci say mbir. Saa
yu ma bettee nit mu lay jëw, dinaa la ko ci
fen. Jàng ko bu baax. Dina la amali njariñ,
bés boo dellusee Ñarelaa gii nga
cosaanoo, fas yéene fee dëkk yaak sa
njaboot. Wóolu naa la, xam naa ne ak loo
mën a fekk ci biir Téereb Ndéey, doonte
wax ju ñaaw la sax, du yàq sa digganteek
kenn ci gox bi.
Jarul nag ma ciy sore. Xanaa ma may la ci
as lëf rekk. Badu, waa Ñarelaa gërëm
nañu la.
Lu ma fekkeek lu ma fekkewul, fii ci
Ñarelaa, kàddu yu rafet rekk la nit ñiy
yëkkati, jëmale ko ci yow. Koo waxal
ñaari baat, mu ne la :
- Aa, Badu Fay Taal de, kuy jaambure
moom ngay dimbali. Gone googu kay,
Yàlla bu ko cat dugg. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_8 | Foo ko fekkaan mu ngay wut lu mu am,
ñëw bokk kook ndeyam Biige Sàmb ak
maamam
Ngiraan Fay. Dem na bay raxas ay oto ca
Waagu-Ñaay, di baana-baana màrse
Aselem, lépp ndax bañ a wër di ñaanaatu
mbaa di këf alalu jaambur ; jànqi Ñarelaa
yi sax mas nañu ko fee fental woy, di ko
gaaral, waaye teewul mu nekk ci li mu
nekk, sax ci ba dëgër.
- Moom kay, na mu noppee woon ! Seede
li daal benn la. Waa gox bi nee ñu ku
jaambure nga te am fullaak faayda. Su ma
déggee ñuy wax yu mel noonu ci yow,
Badu, sama xol day sedd guyy.
Saa yu ma sëggee di dénk kàddu yu neex
yooyu sama Juróom-ñaari Téere yi,
mbégte mi may yëg ci sama yaram, maak
Yàlla rekk a xam nu mu tollu. Sant naa
sunu Boroom bi ma may wii xeetu
bànneex, laata may génn àddina.
Waaw. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_9 | Damay daagu ci mbeddi Ñarelaa yi, dégg
ku ne :
- Badu Taal kay, du moo nar a toog bitim-
réew ba musiba di ko fa fekk. Gone
googu, jom la am ba mu mat sëkk, kaar.
Mu mel ni ay baat yu ma ngelaw li yéene,
may ma leen. Ma gaawtu, ñëw ubbi sama
waxande, roccisi Téereb Ndéey, tëral ci
lépp li ma jot a fortaatu.
Su ko defee sama xel naaw, dem fu sore,
ma fàtalliku yu bare, daldi yëngal sama
bopp, xam ne Yàlla mooy kariim.
*
* *
Badu xew-xew yi ma la fas yéenee nettali,
ñu nga door alxames ja nu demee
ayeropoor Lewopool Sedaar Seηoor, jëli
néewu Asan Taal, indi ko fii ci jàkkay
Ñarelaa, war ko fee jullee. Keroog jooju,
yow ci sa bopp def nga lu doy waar. Ba
dara desul lu dul jullee Asan, yóbbu ko
armeel ya, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_10 | Yilimaan Keeta nee na la nga ñëw tiim sa
baaytàggu ko. Tontuwook sa gémmiñ.
Danga yëngal sa bopp, ngir xamal ka mu
yónni ne jaru ko. Ña toogoon foofu ñépp
jaaxle, ku nekk xool sa moroom
Ndey Silla, ndaw soosu nga xam ne du
dugg mukk lu yoonam nekk, ne la :
- Badu Taal dofuloo jinne jàppu la, demal
wuyu, Yilimaan Keetaa la soxla.
Ñépp ne tekk di la déglu.
Nga yëngalaat ndànk sa bopp, ne yaa lànk.
Naka-jekk, masoo bare wax.
Ñu ñëw fekk ma fi may defare Asan,
boolemaak yow, ne ma :
- Ngiraan waxal ci sa sët bi, xéy-na boog
mu déggal la yow.
Ci laa leen ne :
- Bàyyileen jaa mbur, Badu Taal lu mu
def xam na ko. Noonu, Ndey Silla mer, ne
ca tonet, ni ma : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_11 | - Man Ndey Kumba Silla de, gone guy
waaj a alku laa fi gis. Badu Taal mooy
kan, ba ñu koy seetaan muy toroxal nii
baayaam ? Sama xol jóg man it, ma ni ko :
- Ndey, doo Yàlla doo yonent, mënoo fee
alag kenn. Badu Taal xamul caaxaan, li
mu def am na fu mu ko teg.
Dama ko waxe woon noonu rekk, waaye
ca dëgg-dëgg mbir mi xawoon naa ub
sama bopp.
Waaw, man mer nga dencaloon sa baay
Asan Taal ba lànk ne doo tiim néewam,
ñaanal ko, mu doon seen tàggatoo yéen
ñaar ?
Ak ni deret amee doole...
Wànte li tax doom di dëddu baayam ba
mu jaral ko ñàkke kersa ay kilifaam,
mënul a doon caaxaan.
Ci laa tàmbalee xalaat bu baax ci mbir mi.
Daan naa toog ay waxtu di jéem a seet lu
waral li am am. Waaye lu ma gën a gëstu,
diggante Yaasin Njaay | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_12 | ak sa ndey Biige Sàmb gën a ub sama
bopp. Li xew Ñarelaa sa ginnaaw ba waa
réew mépp jot ci, foo dem dégg ñu koy
waxtaane, mu yéem ñépp, loolu ndem - si-
Yàlla ji Asan Taal a ko waral.
Waaw. Sa baay Asan Taal.
Lu jiin Njaaga te mooy Njaag,
Coow li wër na àddina si juróom-ñaar.
Amaana sax Penku ba nga nekk,
yéenekaay yi maye nañu ci as lëf. Wax ji
lii doηη la : Yaasin Njaay ak ñaari
doomam yee xéy bés bëgg a jommal
Ñarelaa. Waaye yéenekaayi réew ma nga
nekk, mënuñoo sore ci mbir mi. Mënuñu
cee bind luy tax nga xam nu yëf yi deme
ci dëgg-dëgg. Kon jaadu na ma leeralal la
ko bu baax.
Dinaa ko def ci xol bu sedd. Te
duggewuma ko dara lu dul jéem laa aar.
Lu mu yàgg-yàgg, dinga ñibbisi bés
Ñarelaa, bëgg waa gox bi nettali la li fi dal
Yaasin Njaay. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_13 | Gënuma laa xam niti tey yi. Yàkkamti
nañu nga may leen nopp, ñuy fen di
dajale. Ñoo fi dàq a yokk, dàq fee
jekk-jekkal ak làq-làqal. Man, Ngiraan
Fay, jomb naa loolu. Jomb naa génnee ci
sama gémmiñ gii lu dul dëgg.
Ku dem ba bejjaaw, am ay sët ak i sëtaat,
loo wax sa digganteek Yàllaa war a tax.
Te su ma demoon bay fen it, xanaa dinaa
la ci rus ndax cofeel gi ma am ci
yowMoom kay, soo bëggee xam lu fi xew
sa ginnaaw, bul déglu kenn ku dul man.
Kon boog, Badu, tëbu ma bés rekk ηàbb
samag xalima, ubbi Téereb Ngelaw mbaa
Téereb Lëndëmtu di la ci nettali xew-xew
yi ma jot a teewe fii ci Ñarelaa.
Su ma wóoroon ne maak yow dinanu
gisewaat, damay laxas samay kàddu ci
biiri léeb yu lëndëm, xaar ba nga dellusi,
guddi gu ne mu am lu ma ci làq fa géej
gën a xóote. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_14 | Su ko defee, nga fanaanee joow ba ne ko
nuus téye, lemmi ko, jàng ko, mu amal la
njariñ. Ñu bare bu ñu gisee ni
may binde, dinañu ne sama yaram neexul.
Waaye faalewuma leen tey, faalewuma
leen ëllëg!Man bokkuma ci bindkat yi ñuy
soow.
Doore ca Musaa Ka ba agsi ci Séex Aliyu
Ndaw, jaar ci ñoomin Sëriñ Mbay Jaxate,
Cerno Aliyu Caam ak Maabo Gise, ñu ma
gën a aay fuuf ñoo saxal seeni kàddu yu
rafet a rafet ci biir xolu askan wi, jëmbët
leen ci xeli Doomi-Aadama yi.
Man nag, damay jéem rekk. Mën naa ni
sax li may bind, séentuwuma ci leneen lu
dul sama bànneexu bopp. Looloo ma
bàyyéendi tam ci dunyaa. Su dul woon
Juróom-ñaari Téere yii may làngeek yow,
àddina sàppi kon na ma bu yàgg. Dinaa la
xamal tey lu tax ma fonke nii bind ak
xalaat. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_15 | Li ma lay waxsi, guléet bésu tey mu génne
sama gémmiñ gii, jaar ci sama xalima,
jaaxaan ci téere bi nga yor, te mu doon la
xaar fii ci Ñarelaa...
Ba nu newee gone maak samay doomi
bàjjan, góor gu ñu doon wax Mbay Lóo
moo nu daan jàngal Alxuraan ci Rëbës gii.
Booba, su dee amoon naa juróom-benni at
tamit, ca lay yem. Xam nga ne kon loolu
yàgg na !
Xale bu deñ-kumpa laa woon. Saa yu nu
toogaan di tari xuluwallaawu mbaa
yeneeni saar, maa ngi sàcc di xoole Ustaas
Mbay Lóo catu bët. Ustaas Mbay Lóo ku
amoon bayre la, kaar. Kenn mënul woon
dajeek moon ci mbedd mi te doo taxaw,
geestu ko, xoolaat ko bu baax. Te soo
demee ba toog, noo def sa xel di wéy di
werante, nga naan :
« Waaw, góor gi ma dajeel sànq béréb
sàngam, ndax nitu neen la ? »
Monte de, Ustaas Mbay Lóo màggat mu
ràgg la woon te xiibon ; | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_16 | Dara jagatul woon ci moom, du bët yi, du
bëñ yi du tànk yi.
Foo ko fekkaan, mu nga sol benn sabadoor
bu furi, ñu dabb-daaxe ko fu ne, moom ci
boppam muy tëfli deret ; pukkuus ba mu
daan fanaan, mook unk yeek jargoñ yeek
mbóot yi ñoo fa bokkoon dëkk. Du benn du
ñaar, séen naa ay jinax ñuy dóor-dàqe ci
ronu lalam.
Ci gàttal daal, Ustaas Mbay Lóo sagaru nit
la woon. Sonnoon na lool, te su ma la
nettali woon la ma daan gis mu koy añe
mbaa mu koy reere, dinga gën a xam li
may bëgg a wax.
Dama daan jonkan di ko xool, yërëm ko
be, ndeysaan. Rëbës googu ma lay wax,
gis naa fa ba tàyyi ay boroom alal yu tegul
woon sax Ustaas Mbay Lóo nit. Koo ci
laajoon xalaatam dëgg, mu ni la :
- Sa Ustaas Lóo moomu de, mook kaña gu
médd a yem, amalul kenn njariñ.
Céy ! Àddinaa ñu mën a gëlëmal, Badu ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_17 | Tey jii, su ma sunu Boroom bu baax bi
delloo woon ci sama biiru ndey ji ma jur,
ni ma : dunyaa ci 1922.
Seetlu naa nag ne, ci dëgg-dëgg jot nga
fee jànkoonteek ay jafe-jafe yu bare te tar.
Lu ne jéem nga ko, waaye daal, Ngiraan,
taloo fi dara lu dul lijjanti loo lekk, su
guddee nga tëdd nelaw. Soo yeewoo suba
teel, looy defeeti, Ngiraan ? Xanaa wuti
loo lekk ! Amoo dara loo mën a bàkkoo,
du alal, du tur, du leneen. Dinga xéy bés
ne mes, mu mel ni masoo fi jaar.
Waaye nag, seetlu naa leneen ci yow : sa
jikko rafet na lool, nit ku yéwén nga. Lu
néew li ngay fortaatu, nangu nga koo bokk
ak say xarit ak say mbokk.
Léegi nag, dinaa la fay sa xol bu rafet
boobu. Sama yërmaande amul àpp. Sama
kàttan amul àpp. Suba, dinga am lu kenn
masul a am, Ngiraan. Dinga judduwaat !
May naa la it bii yoon, maanaam ci sa
ñaareelug dund, nga taamul sa bopp nit ki
nga bëgg a doon. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_18 | Su la neexee nga ni ma : « Njiitu réew mi
Daawur la tudd, sant Jaañ. Moom laa bëgg
a wuutu, am xaalis bu dul jeex, fu ma jaar
takk-der yi di ma mbiibal,
di ma tóojal, lu ma joxoñ dag yi gaawtu
dagg ko, indil ma ». Soo bëggee loolu,
Ngiraan, ma defal la ko. Xam nga ne dara
tëwu ma ! Tey ci guddi, mën naa daaneel
Daawur Jaañ, ëllëg njiitu réew yi ci àddina
si yépp yónnee la ay bataaxal, naan la :
« Maa seer fareer e ami, Muse le
Paresidaa Ngiraan Fay », nga dof nag,
naan xanaa kay ñii du man lañuy wax !
Soo bëggee loolu, ma defal la ko ci lu
gaaw ! Waaye su dee judduwaat weccee
sa ruu ak ruuwu Ustaas Mbay Lóo moo la
gënal, ba tey mën naa la ko defal, ngay
añe sómbi di ko reere, soo foree sagaru
téeméer dund si ñaari fan walla ñetti fan.
Léegi daal, yaay seet, Ngiraan.
Badu, xam nga ne moos su ma sunu
Boroom bi nee : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_19 | - Gaawal, Ngiraan sa tontu laay xaar !
Du man mii maa fay nekk di nakk-nakkal.
Daawur Jaañ, lu mu dégg ci lu bon,
man Ngiraan Fay maa ko ko yakk ! At yi
Daawur Jaañ taxaw ci kaw suuf yépp, soo
ci dindee sàcc alalu réew mi, ak nar ak
yàq xol yi, dara dootu ci des !
Ma ni : tuuge waay, Daawur Jaañ ! Yaay
mag mu ñàkk faayda, Daawur Jaañ ! Fu ñu
la fekk, yaa ngi ratatati, lu ñor nga wax, lu
ñorul nga wax. Te kenn sañu la ni :
- Góor gi wax ji doy na sëkk ak barke, yaa
ngi nuy merde waay !
Su ma Yàlla baaxe woon ñaareelug dund
te ma am sañ-sañu taamu, damay ñëw
dëkksi Rëbës ca pukkuusu Ustaas Mbay
Lóo ba, toog ci sijaadaam, di jàng téere bu
sell bi, di màggal turu sunu boroom bi,
duma ragal xiif, duma ragal mar. Ma ni
ndem-si Yàlla ji Ustaas Mbay Lóo, sa jaan
wàcc na ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_20 | Ma dellu ni : wàccoo ngaak askan wi,
Ustaas Mbay Lóo ! Ak li coow liy bare
yépp, sa dund a ëpp njariñ fopp dundug
Daawur Jaañ ak i ñoñam !
Amoo woon jotu jëwaate ak rambaaje,
taloo woon xëccook téesante, te néew
doole masulaa tax a saalit bay wër di
woyaan. Maa ngi lay gisaat, nga sëgg ay
waxtu di jàng Alxuraan mbaa di bind li
ngay bind.
Doo sëqat, doo sax yëkkati sa bopp. Bu
weesoo sa loxo ndeyjoor bi nga téyee sa
xalima, du dara lu ma gis mu yëngu ci sa
yaram. Dama daan làqu di la seetaan,
ngay capp sa xalima ci daa ji di rëdd
ndànk ci téere yi nga tegale ci sa wet, sa
loxo ndeyjoor di yéeg ak a wàcc.
Leeg-leeg nga siggi raay sa doq, ma gis ni
sa bët yiy melaxe ak ni ngay noyyee,
ndeysaan. Mu wóor ma ni am na booba lu
la feeñu. Ustaas Mbay Lóo, jàngal nga ma
lu bare! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_21 | Coppite ga ma daan seetlu ci yaw moo ma
tax a xam ne liy tax nit di nite, day jéggi
yaram wa, romb koy dem. Doole ji nekk
ci xam-xam, teey ak fulla ji mu laaj yépp a
ngi woon ci yaw.Waxuma sax Daawur
Jaañ, waaye ku ma indiloon tey jii nit ki
ëpp alal mbaa ki ëpp bayre ci àddina,
duma ko wecceek Ustaas Mbay Lóo.
Badu, giñ naa ci Alxuraan ne masuma
naw mbaa ma weg benn Doomu-Aadama
ni ma wege woon góor googu.
Su dul woon ndem-si-yàlla ji Ustaas
Mbay Lóo de, sama dund gii deme kon na
neneen. Badu Taal, taawu Asan Taal ak
Biige Sàmb, déglu ma.
Ma ne : nit dëgg, yaram wi mën na fee
jóge te du tax mu faatu. Nit dëgg, bés ba
ñu ko yóbboo armeel ya jébbal ko
boroomam, bés booba lay dekki. Suuf sa
ñuy maasale ci kawam mënul tee
takkandeeram ne bëret ci saa si, topp ña
ko doon robsi. Na fekk rekk mu defoon ci
dundam lu jar a fàttaliku. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_22 | Nit ku sa dund neen, doo am takkandeer,
dara du la wutaleek bàyyima. Ustaas
Mbay Lóo, jàngaloo ma Alxuraan yem ca!
Jóge nga fi, waaye ba sunu jonni tey, yoon
wu ma aw, yaa ma ko xàllal démb, tey
soog a ñëw. Saa yu ma demee ba jàq, su
ma làmbaatoo daj la, nga toog ci sama
wet.
Mu mel ni nekkinu askan wi ab téere la,
nga ubbi ko, di ma sa, may tari.
Léegi màggat laa. Waaye saa yu ma yëgee
ne mbon ak kañaan a ngi may bëgg a ëpp
doole, dama lay daldi gisaat ci sa pukkuus
bu bon ba, nga sëgg di jàng, di jàngale, di
bind ak a bindaat. Fa nga tëdd ca àllaaxira
nga ma naan jàkk, ma bàyyi lépp lu ma
jàppoon, nga dëddale maak coxor, xiir ma
ci lu baax.
*
* *
Bul yàkkamti, Badu. Jaru ko. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_23 | Su waxtu wa jotee, dinga xamal sa bopp
lu tax ma ubbil la sama xol, xàll ci
juróom-ñaari yoon yu wuute, te naan la :
Badu Taal, yoon yaa ngii, bu ci sama
baaraam joxoñ topp ko, bul teg feneen say
tànk. Bul ragal a xuus ci biir dex gu
lëndëm gi. Su ma la tàllalee seetu, bul
dem ba jub ko sa fit mel ni lu rëcc, nga
dellu ginnaaw, di waxtu, naan :
- Aa déedéet, kii kay du man !
Te boo tëddee ba xaaju-guddi, dégg
ngelaw li mer bay ηar ni gaynde siibi, di
buddi garab yi di leen xalab ca xaj, di
yëkkati géej gi di ko sànni ci kow
asamaan si, loolu yépp su amee bu mu la
tax a tàggook sa sago.
Monte askan weeka soxla seetu tey !
Ñaata xarnoo ngii muy roy ak a royaat ?
Waaw nun, wan xeet lanu royul, ba xaw
koo yéem sax ?
Ma ni : yaakaar nga ne Yàlla mos naa
sàkk mbindéef mu dàq a toppandoo nit ku
ñuul ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_24 | Defe naa ne de, Sinuwaa yeek Sàppone yi
rekk ñoo nu rëccagum, te ñooñu sax
gisaguma leen Mbaaw. Su ñu defulee
ndànk, léegi nu ne leen :
- Randuleen fee waay, yéen xamuleen
Sinuwaa mbaa Sàppone dëgg nu muy mel!
Tey nu won leen ko ! Kon boog, Badu
Taal, taawu Asan Fay Taal ak Biige
Sàmb, yow sama sët bu baax bi, nang ul
ne war nanoo seetaat sunu bopp bu baax.
Bul tiit, bul ragal.
Lenn moom na la wóor : dëgg dina
naqadee dégg, naam, waaye soo ko
ñemee, song ko, doo ko réccu.
Ngëneel lu réy a ngi ci.
*
* *
Man mbindéef moo sañ ne xam na nu
jaww ji tollu ?
Am na, gaa, ay nit ñu bare pexe, loo wax
ñu ne mën nañu koo natt, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_25 | foo leen fekk ñu nga ηàbb seen xalimaak
seen kayit, di ci bind ak a nataal yu kenn
xamul. Nee nañoo ay boroom xam-xam
yu mag lañu ! Gaa ñooñu, koo ci laaj lu
muy liggéey, mu ni la :
- Gëstukat laa.
Nga ne ko :
- Ãa ?
- Waa-waaw ! Bul ma ci xeeb ! Lu la
jaaxal ci jant bi mbaa ci biddéew yi mbaa
ci weer week yeneen ak yeneen, boo
yaboo laaj ma ko. Sàllaaw, sama sagaru
néeg bii laay toog jox la tontu bu leer
nàññ.
Waaye, seen cobte googu du mujje fenn fu
dul di raay a ka raayaat seen doqi séytaane
yi, naan :
- Mbir mi kat, am na lu ma ci desee wóor.
Xanaa kay danuy jàppandi ne su
demewul nii deme naa.Ngóor soosu dinay
dem bay mbebetu, ni ku daanoo cib saret.
Déglul ma ko, Badu : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_26 | - Su wund wu ñuul wi wëree fukki yoon
niim gii, ganaar gi topp ciy daw, ñu ànd
ñoom ñaar di mbów niy xaj, du ñàkk
Pilitoη ak Sipiteer mbëkkante. Su booba,
suuf si dina yëngu ca Pakistaη ak Kore, te
Kilimaηsaro dina yàbbi ay xal yu xonq
coyy! Xam nga, Badu, waxu dof a ngoog !
Boroom xam-xam yooyu, seen muj duy
faral di rafet. Bés bi ñuy ràηηatiku, day
bett seeni mbokk, ñu daldi leen jagat
jagatee, yóbbu fa ñuy denc ñi seen xel
neexul.
Waay ñii ñoo waane, Badu ! Ku leen laaj
loolu lépp ? Luy seen yoon ci dayo
àdduna si ?
Ba sunu Boroom bi sàkkee dunyaa du tey,
du démb. Kenn ci nun fekkewu ko.
Dunyaa day dox te Yàlla rekk moo xam
kañ lay àgg fa mu ko jëme, mu daldi ko fa
yemale.
Waaye, Badu, li àddina siy yaatu-yaatu,
juróom-ñaari fan doηη ñoo ko ëmb.
Mu di lu kéemaane sax. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_27 | Juróom-ñaari fan yooyu nag, dina am ay
jamono ñu jiitle, bu ci ne dara du ko
wutale ak ba ca topp. Maanaam, su
fekkoon ne bés yi dañuy ñaasu, ni ko sunu
yenn mbokk yi baaxoo def, ñaas yooyee
dañuy mujjee raaf ba far maasaloo, benn
màndarga dootul des ci seen kanam.
Waay, jàmm a neex, Badu ! Dara
yënguwul. Réew maa ngi ne selaw. Altine
ñëw, talaata tegu ci. Àllarba yegsi.
Alxames tàmbalee dukkat, ñu ne déet ne
waay mu ne maa ngoog.
Jàppe ko noonu, mel ni bés yi dañuy
wëndéelu ci biir géew bu yaatoo-yaatu,
demuñu dikkuñu, ba nga xam ne soo
jëloon bant di rëdd seen doxin ci suuf si,
wërngal gu mat sëkk la lay indil.
Looloo waral foo fekk ngóor su fuddu ba
noppi óbbali, te naan :
- Waaw, gaa ñu baax yi, tey sax ban bés
lanu nekk ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_28 | Xamal ne kooku, su newulee ci bànneex
it, amul naqar wu tax ñuy wax.
Jamono yooyu mënees nañu leen a
méngaleek asamaan su amul benn niir,
weex tàll, ba nga xam ne su ko picc mu
gën a tuuti riisoo mu mel ni àddina fa lay
doxe tukki àllaaxira. Waaye, am na lu ma
la ci bëgg a yokkal, Badu. Aa, Badu, li ma
lay waxsi de, lu am solo la.
Sopp kon naa nga teeylu, may ma nopp bu
baax. Ndax mas ngaa jàng taalif bi Sëriñ
Musaa Ka jagleel Maam Soxna Jaara
Buso ?
Nii la koy sànnee :
Xerawluleen, nu sant Soxna Jaara
Ngir moo nu may lu tax nu samp i daara
Buleen ma tanqamlu, buleen ma tanqal
Buleen nëxal ndoxum ki leen di tanqal
Cellantuleen te ubbi seeni nopp
Ak seeni xol, ma ubbi seeni bopp
Te génne seen waηaani xol, te taataan. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_29 | Baal ma àq de, Badu. Lee-lee sa maam
Ngiraan day dem bay tàggook sagoom.
Day fekk booba ay kàddu yu rafet a ngi
nuur ci sama biir deret, di féey, jàpp ma të
maa bàyyi. Su ma tolloo foofu nag, fàww
ma dugal ci waxtaan wi yu ci bokkul te
duma ko tey.
Nanu dellu boog fa ma ajoon wax ji.
Waaw, dina am it ay jamono, mbir yi
deme neneen, juróom-ñaari bés yi
ràkkaaju, di tëb di dal.
Bés yi mel ni ay gone yuy fo po moomu
ñu naan xalaa-ma-ndiir-bàjjo, bu ci ne di
kar sa moroom, naan ko:
- Xalaa-xalaa doo fi jaar !
Ndaw xeex bu metti, ak xiiroo ak ηaayoo !
Doomi-Aadama yi duñu toog duñu taxaw,
kenn du tal noppalu waxatumaak naan
dangay xalaat a nelaw bay xàndoor.
Ma ne : ku masul a gis réew mu tàkk
jëppét, nekk ci fitna, kaay seetaan ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_30 | Waaye kan mooy am googu jot ag dal-xel
googu ? Liggéeykat yaa ngi bànk seeni
loxo, ne ñoom sonn nañu, te dee, bala ñoo
am jàmm nguur gi daanu, ñu ñàdd njiitu
réew meek njabootam rendi leen, sëlmoo
seen deret.
Réew mi mel ni caga bu def tuunu neen
juutu ci pénc mi, lu neex waay mu def, kii
tàpp ci fer yi, kii sëq ci cokk yi, yëkkati
leen, niit leen ba xolam sedd, jébbal leen
ngelaw li, ne ko yaay boroom, fu la neex
yóbbul, lu la neex def ci. Nga gis nag tan
yeek baaxoñ yiy naawantu, di baagante ci
diggante biddéew yeek weer wi, lee-lee ñu
ñëw ba jub néewu buur, xeeñtu ko,
yéegaat ci kow asamaan, di xaar ba néew
bi yàqu ñu dal ci kowam, sëqatoo ko.
Takk-der yi ne, aa, loolu kat moom ëpp
naa seetaan, di jéem a aar buur, di sànni
ay bomb ñuy kalaate, di dóor i liif, sa
maas gi nekk ci mbedd miy toj ak a tojaat,
lu ñu jot lakk, kilifa gu ñu dajeel nangu sa
alal, toroxal la teg ci. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_31 | Mu mel ni rekk xeetu ndof gu bees moo
jékki-jékki jàpp ñépp.
Xëccoo boobu, Badu, dara waralu ko lu
dul li ku nekk bëgg a fés, ëllëg-ak-sibir
géwél yi di la woy. Te kat, dinaa la ci
xamal lenn : du nit ñi rekk ñooy jiiroo
ndam loolu.
Juróom-ñaari bés yi ci seen bopp, benn du
ci nangoo des ginnaaw. Ndax li mbir miy
metti ak di jaxasoo yépp, dina am ci bés
yooyu benn bu ci kenn dootul fàtte ba
keroog àddinay tukki.
Li ngay nekk xale yépp, dégg nga ñu naan
Dibéeru Guy-Njulli walla Talaatay Ndeer.
Mu ngoog nag.
*
* *
Ca Kawóon la Dammel Sàmba Lawbe
Faal dajeek baayam Makoddu. Du woon
lu gënal Saalum, nag, wax dëgg Yàlla.
Ayu-bés bu jàll, Saalum gën a jaaxle. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_32 | Waaye xam nga ne kenn mënul woon am
naqar ba dab Lingeer Lat Sukk Sire Jogob
Mbóoj ma masoon a séy ak Makoddu, jur
ca Dammel Sàmba Lawbe Faal. Sa doom
ak baayam war a jàkkaarloo ! Ba yëf yi
waree am sax, fekk na Lingeer ak
Makoddu tàggoo. Waaye cofeel ga
Lingeer amoon ci moom desoon na as lëf
ba tey. Makoddu nekk Kajoor, Lingeer di
yeewoo Kawóon. Waaye amul bés bu
xelam delluwul ci yu neex yi mu jot a
dund ak Makoddu jamono ja ñu doon séy.
Bés, mu yëg ne Makoddu gàddaaye na
Kajoor, jaare Ndukkumaan jëmsi
Kawóon ! Àddinaam yàqu, ndax ci
Sàmba Lawbe Faal ak Makoddu Faal, ku
ci ne xamul nu mu lay def.
Saalum ne ko :
- Moo Lat Sukk Sire Jogob, wax ji nag
noo ciy def ?
Ndax yow, sa jëkkër ak sa doom ay bëgg
xeex bu subaa ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_33 | Mu ni :
- Bu subaa, dinaa ree tuuti, dinaa jooy
tuuti...Xare bu waroon a am la, am na. Lu
ci des, tey ? Ñetti baat. Dibéeru Guy-
Njulli. Ñetti baat yooyu, lu nee ngi ci biir
: Dammel bu tumuraanke di taxawaalu,
deret juy walangaan ak ñaari réew yu jàq
ba fu jàq yem, di Kajoor ak Saalum.
*
* *
Talaatay Ndeer, nag ? Bés a ngoog ci bés
yi ! Waaye bul yaakaar ne Talaatay Ndeer
a sukk jur boppam.
Déedéet!Mbarka Ja xéyul bés rekk dajale
jigéeni Waalo yi, ne leen :
- Nanu jaay sunu bakkan, ndax jomb
nanoo nekki jaam ginnaaw barag. Bunu
nangu mukk Naar yi di nu teg ci seen kow
i fas, di nu yóbbu Tararsaa. Am ñuy saalit
xaat, ndeysaan, di jooy, di tam Mbarka Ja
dëmm. Mbarka de, bokkul woon ca këru
Waalo yu mag ya. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_34 | Su ma ragalul woon fen sax, dinaa la ni
jaamu-néegu Lingeer la woon.
Xam nga du kooku lañu naan ci yax bu
réy la bokk. Teewul ba jigéeni Waalo ya
jàqee, ñu bare dañoo waaf, moom Mbarka
Ja mu jóg taxaw, ni :
- Dëgg la, waa Tararsaa yi nu song tey ay
góor lañu te bu dee xeex rekk ñoo nu ko
dàq fuuf, waaye nanu ko defanteek ñoom
ba lu nu ci góobe gar ko ci !
Mu neeti leen :
- Su noon yi xamee ne ay jigéen lanu, dafa
leen di gën a jox fit ! Kon, na kenn ku
nekk ci nun sol ay yëre góor !
Ñu def la mu leen sant, war seeni fas,
jàkkaarlook noon ya, won leen njàmbaar
gu matt sëkk.
Ñu dàq noon ya, noon ya daw ! Waaye ba
ñuy génn Waalo, la am ca jigéeni Waalo
ya ku mbaxanaam rot, létt ya feeñ ! Noon
ya sog a xam ne ay jigéen lañu doon
xareel. Kenn ci ñoom woo ña doon daw : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_35 | - Dellusileen ! Sañ ngeen a taxaw ci
kanamu Buuru Tararsaa naan ko ay jigéen
a leen dàqe Ndeer ?
Xeex bi neeti kur.
Foofa, Mbarka Ja daldi waxati ay waxi
gor.
Dafa ne : Jomb nanoo nekki jaam ginnaaw
Barag. Nanu dugg ci néegu ñax bu mag
bii, taal ko ci sunu kow.
Na mu ko santaanee la ko jineeni waalo ya
defe. Néegu ñax ba jàpp, di tàkk, noon ya
wër leen, jigeeni Waalo yay woy ca biir
safara sa ba sedd ñoom ñépp. Mbarka Ja
ma doon seen njiit nag, jotoon naa rawale
benn gone gu jigéen gu ñuy wax Sadani
Caam.
Dafa ni ko :
- Yow Sadani, bu nu taalee néegu ñax bi,
soo jaaree fii, dinga mucc ! Demal Sadani,
su Barag dellusee, nga nettali Waalo naka
la jigeeni Ndeer yi bàyyee fii seen bakkan,
ci jom ak fit ak ngor. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_36 | Demal, Sadani, man Mbarka Ja maa la ko
sant ! Sadani Caam ma jëkk a nettali
Talaatay Nder, ñaata at la amoon ? Am na
ñu ne juróom-ñetti at doηη la amoon. Dara
wóoru ma ci, waaye lii moom boroom
xam-xam yépp ànd nañu ci : Sadani Caam
ma jëkk a netaali Talaatay Nder, xale bu
ndaw la woon.
Kocc Barma Faal de, dafa ne woon :
- Mag mat naa bàyyi cim réew.
Ni Mbarka Ja doxalee de, safaanoo na bu
baax ak kàddu yu siiw yooyu. Mbarka Ja,
Yàlla mayoon na ko fit, may ko xel.
Dékku na saay-saay ya songoon Ndeer. Te
ba dara desul lu dul génn àddina, sóoru na
Kocc Barma Faal, boroom xam-xam bi
kenn mësul a sañ a weddi. Ndax ni
Mbarka Ja rawalee Sadani Caam, lii rekk
la tekki:
- Gone mat naa bàyyi cim réew...
Lu cee sa xalaat, Badu ? Sunu ñaari
ponkal yooyu, koo ci àndal ? Mbarka Ja
walla Kocc Barma Faal ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_37 | Looy wokk bopp ?
Mbir a ngoog, de...
Benn ayu-bés, juróom-ñaari fan la.
Xëccoo ba bés yi daan xëccoo démb,
mooy wéy ba tey. Ndax kat, juróom-ñaari
fan yooyu, balañu ciy ràññee benn, di ko
fàttaliku ëllëg, dina naan deret ba màndi,
màbbloo ay taax yu dul jeex.
Dina tax it saxaaru fetal seek bomb-
lakirmosen yi ubale jaww ji, xasaw xunn.
Ndax kat, bu la ci kenn nax, li coow liy
bare yépp, ci kàddu yii doηη lay mujje : at
sàngam, bés sàngam.
Ku nekk di bàkku, naan :
- Maa nga fa woon, bés booba kay, soo
ma gisoon xam ne maay jàmbaar, aa,
cam !
Am ku ne:
- Waaw góor, diw ! Kéwél du tëb, doom
ja bëtt ! Sa maam diw, jàmbaar dëgg la
woon ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_38 | Su ñu takkaan xare, daawu ca ñaaw ndax
daawul des ginnaaw !
Keneen ne :
- Gàcce ngaalaama !
Nga geestu, fu ne nga xool fa, say bët
duñu dajeek benn Doomu-Aadama. Fekk
na du dara lu dul ngelaw lu jóg, lemmi ay
kàddu, suy lenn ci jaww ji ba noppi ne
mes.Démb lëngoo ak Tey, ñu ànd di
daagu. Ñu ngi mel ni ay doomi bàjjan, di
kaf di reetaan, ku ci nekk di tex-texaan sa
moroom.
Su la ñaar ñooñu rombatee di déeyante,
ubbil sa nopp bu baax, Badu. Bu la dara
rëcc ci seen waxtaan, ndax mënees na cee
jàng lu bare.
*
* *
Nga ne ma :
- Lan laa ci war a mën a jàng, Maam
Ngiraan ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_39 | Su ma la bëggoon a wax lépp de, Badu,
dootuma am jotu waxtaan ak yow ci
mbirum Asan Taal. Xanaa boog, ma
ñamal la as lëf ci diggante Démb ak Tey.
Àndandoo boobu, dara gënu koo yàgg. Fi
lanu ko fékk nun ñépp. Fi lanu koy bàyyi
tamit. Bul fàtte mukk lii ma lay waxsi :
am na bés boo xam ni ci la Yàlla sàkk
àddina si. Bés boobu, Tey la tudd. Beneen
bés jiituwu ko fi. Waaye ca ëllëg sa la Tey
dee, Démb daldi juddu. Ñoom ñaar, ay
junniy-junni at a ngii, saa yu jant bi
sowee, ku ci nekk matu, ñu rewle la, nga
daldi jur sa moroom.
Moo tax kenn mënu leen a teqale. Moo
tax ñu yabante ni ay doomi-bàjjan, foo
leen fekk ñuy werante, di téesante.
Waaye saa yoo leen ëfalee ñu xeex, Tey
mooy gàddu ndam li. Day tuur Démb
andaari wax, naan ko : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_40 | - Loo may jaay daη-ηaam nii, yow Démb ?
Tee nga maa déglu te xam ne maa la gën a
xam sa bopp fuuf ?
Kooku faf toog di ko déglu, jàkkaarlook
seetu bi, di ci gis ni ko Tey di yatte.
Waaw, Tey daanaka Lawbe bu waane la,
mooy yatt Démb, moo koy sàkk.
Wax jooju tekki lan, nag, Badu ?
Lii, xanaa : xew-xewi démb ya, niti Tey
yeey mujje nettali gi. Ñi ko fekke woon
ñépp ñu nga tëdd barsàq, kenn du ci jóg sa
bàmmeel di am looy weddi walla looy
dëggal. Kuy jéem a nettali xew-xewi
démb, dinga dem ba réer, say kàddu di
mbëkkante ci jaww ji, lu ñëw sa bopp nga
wax.
Maa ngi lay dégg nga naan ci sa xel :
- Nit ñee gën a ñeme Yàlla ! Luy seen
yoon ci li sunu Boroom bi sàkk ba ñu koy
soppi, di ko nettalee mbaa di ko nataale
neneen ? Dëgg la. Loolu am na te firnde
yi bare nañu ci lool. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_41 | Réew dina nekk ci fitna, ay bakkan yu
bare rot ci, nguur gu bees taxaw, ñu jàpp
ne yëngu-yëngu yooyu dinañu des ci xeli
nit ñépp ba fàww. Waaye su ñu ci tegee ay
weer rekk, koo wéetal, cuq ko ngir mu
nettaliwaat la mbir mi, mu jox la tontu bu
wuteek bu moroomam.
Kii ne :
- Lii moo fi amoon.
Ka ca des ne ko :
- Déedéet, juum nga.
Coow jibati, te ku deful ndànk jaasi yi
génnaat, ay bomb kalaateeti, jooyoo amaat
ci yoon. Àddinaa mel noonu. Lu weesu,
ñu gas suul. Maaxàllaa, nit ñi dañoo sonn
! Kër-këri ngir am loo dundalee sa njaboot
doy na ku nekk soxla. Ku sa xel dalul, doo
tal werante jëmale ginnaaw-ëllëg.
Loolu li mu wund, Badu, lii la :
Du Doomu-Aadama walla bàyyima yi
rekk ñooy génn àddina. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_42 | Soo ko seetee bu baax, xelu nit ci boppam
mooy bàmmeelu Dëgg.
Dinga teewe dara sax, dégg ci rajo bi benn
waa ju dëgër fit di ko nettalee neneen, nga
ànd caak moom.
Moo tax Wolof Njaay, su benn waay
jógee fale, ne :
- Amoon na fi.
Li mu koy jëkk a laaj mooy :
- Ndax ba mu amee yaa fekke ?
Xam nga daldi na ko tanc fu xat fu ko
caaxaan dul génne, ne ko :
- Waxal lu la neex, waaye kenn du la gëm
feek tegoo sunuy loxo ay firnde yu wóor.
Kon Badu, fexeel ba bul fàtte lii : jëfi tey,
léebi ëllëg. Li nga teewe tey dina
soppeekuji ci sa xel, dina soppeekuji ci
say kàddu, nekk leneen lu mësul a am. Du
tee Géwél Mbaay fàqe fu kenn xamul,
taxaw ci pénc mi, dar ay noppam, di xaacu
ci naaj wu tàng wi, ñaq bay siit, naan : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_43 | - Lii ak lii moo fi amoon.
Du ñàkk mu am ñu àndul ciy waxam,
waaye kenn du ko sañ a weddi.
*
* *
Bu ñu nee :
- Loo gis ci nettali lay mujje,
Loolu la tekki.
Soo ko jàppee noonu, dinga xam lu waral
nit di nettali lu mu masta fekke. Seetal ma
lii rekk : kàddu yi ngay jottali, ba ñuy jib,
xaajagoo juddu, walla sax jamono jooju
say maamaat ay liir yu tooy xepp lañu !
Yow nag, Badu, danga dig gone, moo tax,
xéy-na, soo déggee wax ju ni mel, dinga
ne :
- Aa kon boog ni aw askan di gise
boppam, ci ay nari kese la lalu. Maam
Ngiraan Fay a ko wax.
Ma ni la :
Déet. Bul gaawtu. Njuumte lu mag a ngi
noonu : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_44 | Kàddu yooyu nga tudde ay nar, ñoo ka am
njariñ tey ! Jàppal ne doole jiy jox aw
askan pas-pasu dund ak jëm kanam, ci
baat yi nu mel lay tukkee, ci lay ñaaxe
boppam ngir yeneen réew yi ragale ko xel,
weg ko.
Ndax, soo ko seetee bu baax, ab dëkk lan
la ? Jaww ji la, nit ñi ñëw, fekkuñu fi
dara, ñu feesal ko dell ak seeni jëmm,
seeni kër, seen coow ak seen kër-këri.
Kuy faral di doxantu ci dëkk bu mel ni
Ndakaaru Njaay gii, dinga xam li may
bëgg a wax foofu.
Céy Ndakaaru ! Béréb bu rëb, sax ! Balaa
may sore sax, may ma ma sërëxal fii as
tuut : dëkk du am faayda ba dab
Ndakaaru. Lu tax ma wax loolu ? Dafa
fekk rekk ne su teyee mu ne :
- Man Ndakaaru, Njaay laa sant.
Ñu ne :
- Ndakaaru Njaay. Njaay Jaata ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_45 | Waaye du tee su ëllëg saa mu fëgg
dënnam, ne am na beneen tur. Ñu laaj ko
tur woowu wan la.
Mu ne :
- Man maay Ndakaaru Jal Jóob !
Ndakaaru, benn dëkk ñaari sant !
Moo tax ni Ndakaaru rëbe warul a jaaxal
kenn. Nit ñaa ngiy dem di ñëw, ñii di lal
ay pexe, janq ji solu ba jekk di daagu, fu
ñu aw xetu litkoloñ gu neex ne fa bann,
topp leen. Lee-lee nga bett ci kenn muy
sàcc di seet ndax xale yu góor yaa ngiy
yéemu ci taaram ; alkaati yaa ngiy door-
dàqeek dawalkati kaar-ràppid yi ; lu waay
jot jaay, lu mu ci for muy wërsëgam mu
yóbbul njaboot ga ; mbedd moo jaar, am
gone gu la dogale, ne la jabb ab
yéenekaay, nga gis ci nataali gaa ñiy laaj
réew mi. Ku ci nekk di bàkku, di ηàññ sa
moroom, naan :
- Man mii nag maay waa ji, su ngeen ma
fale kañ, fi la réew miy jóge naat ba fàww,
dinaa dàq xiif sa xaj, jële fi mar, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_46 | sàllaaw xàjj ak seen dootu fi am, benn
gone dootul wër di yalwaan waxatumaak
di fanaan ci mbedd mi, ku tawat ci yéen
dinañu ko faj bu baaxa-baax te dinaa
baaxe seeni doom xeetu njàngale wu
masul a am fenn. Ay nari kese ! Waay, ñii
ñoo yabaate dëgg !
Yéen xale yi sax lañuy gën a noggatu,
ndax, wax dëgg Yàlla, yéen a dese ñaari
xeetu kàttan yi gaa ñooñu soxla ngir jot li
ñuy yóotu : kàttanu yaakaar ak kàttanu
xeex. Seetlu naa it leneen ci Ndakaaru,
Badu : wëraakon yi bawoo bitim-réew
ñëw ganesi nu, ñoo nuy faral di gën a ànd
ak seen sago.
Ndànk lañuy faral di doxe, te foo leen
fekk ñu nga téen, mel ni dañu leen ne
Ndakaaru bëreb bu aju ca kowa-kow la,
làqu ci ginnaaw asamaan si.
Li ko waral moo di ne wàcc bees yooyu,
deñ-kumpaa leen tax a jóge seen dëkk,
dagg paasu roppëlaan, romb réew yu bare,
teersi Senegaal. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_47 | Soo nekkee gan cib dëkk, doo bëgg dara
rëcc la, fépp ngay sànni say bët, lu ne nga
laajte ko, loo ci jële muy lu bees loo jàng.
Soo ñibbee, ñu wër la nag, ngay nettali.
Naan :
- Cim ! Waa Ndakaaroo xayadi ! Ñoom
de, ci diggu tali bi lañuy juug seen
mbaalit. Fu neex waay it mu jonkan saw,
te seen oto yaa nga la ko màggatal, bare
saxar ba nga ni lii lu mu doon ! Mbaa
ngay xoromal :
- Janqi dëkk boobu ñoo taaru kaar, te rafet
doxin ! Jeeg ja nag ! Ñoo naqadee muñ
tey ! Diriyanke lañu leen di woowe, mbaa
jongoma. Ni ñuy waajalee guddi gi, benn
la. Su ngeen wéetee ba ñuy def seen
déebaadéeb yooyu, noo def yéemu. Ñoom
kay, seen xam-xam màcc na lool ci
mbirum fer yuy keleη-keleηi, mbaa bin-
bin ak gongook beeco !
- Beeco ? Loolu naka lañu ko mën a
tekkee ci sunu làmmiñ ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_48 | - Bul ko sax jéem, saa waay ! Man, wër
naa àddina si juróom-ñaar waaye
musumaa gis fenn lu ni mel. Sér bu gàtt
boobu yem ci pooj tey faral di yaraax
daal, réewum Senegaal rekk la am !
Ki gën a saay-saay ci say xarit am xaat lu
mu yëg ci yaramam, daldi yuuxu :
- Nga ne ma ? Saa waay, foofu kat war
naa neex, déwén kay sooy dem doo ma fi
bàyyi !
Du ñàkk it nga ne leen :
- Waa Afrig yooyu kay, ñu doy waar lañu.
Amuñu dara ba dara booloo jeex, ndóol ak
sidaa ngi leen di bëgg a faagaagal, waaye
foo leen fekk ñu ngay ree, di woy, di fecc!
Soo defulee ndànk, dinga saaraan ciy
kàddu ba wax lu amul.
*
* *
Dëgg la : cuune laa ci mbirum mbind ak
xalaat. Waaye lenn leer na ma : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_49 | képp ku tudde sa bopp nettalikat, war nga
foo tollu di muslu ci ñi lay déglu mbaa
ñuy jàng say téere. Moytul ma leen ! Aka
ñoo la bañ tey ! Say noon yu làqu lañu.
Ñu ngi lay siiñ, di la tàccu, waaye feek
sànkuñu la, duñu am lu leen neex. Mën
nañu laa jey ba nga yaakaar ne dunyaa jii
ñu Yàlla sàkkal doyunu. Soo dee ku
woyof bopp, dinga dem ba naagu, defe ne
say kàddu kese mën nañoo sàkk dunyaa ju
dàq jii te gën koo jub !
Loolu moom am na, Badu.
Waaye man sa maam Ngiraan Fay, juddoo
Mbériη-Saaj ca Siin, teel a ñëw Ñarelaa
gii, yaroo fi, màgge fi, dëkk fi ba am tey
juróom-ñaar fukki at ak lu topp, lu ma la
wax bu yaboo nga feye ko bor.Dama ne :
Badu, gis naa lépp, fekke naa lépp. Samay
mbokki Al-pulaar yi sax dinañu may faral
di tooñ, naan ma :
- Moo, Ngiraan, ana séeréer bu bon bu
sant Fay ak a dëkk Ñarelaa ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_50 | Loo fiy def ? Ayca, dellul ca sa xërëm ya
waay, ak yéeféer bi nga doon ! Alla
bónni !
Sama tontu benn la mas a doon :
Dëgg la, xawma fu dul Ñarelaa, waaye
maa ko xam tey !
Muy lu wóor it, Badu.
Am nay bés sax dafay mel ni ma gëmm
mbaa ma xippi benn lay doon ci man.
Sama gaa ñi kay, mënuñoo def lu ma bett,
amul fenn fu ñu ma mën a jaar. Waxtu
woo ma laajee, mën naa la wax lu ku nekk
ci waa gox biy def.
Bu dee suba teel, Usmaan Sow, boroom
saret bi ci boppu koñ bi, mu ngi
jàkkaarlook fasam wi mu tudde
Kuwaamini, di tariy saar yu takku, di ñaan
Yàlla mu may ko kilyaan yu bare ci bés bi
; seetlu naa sax ne Kuwaamini, mbir mi
daa mel ni lu ko xaw a jaaxal ba di ko def
ay ree ; Usmaan moom, caaxaanul ci
ñaanam yi, de ! Aji-néew doole la. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_51 | Su màrse neexulee njaboot gi dëñe mbaa
mu fande.
Mus naa laaj Usmaan Sow lu tax mu
tudde fasam wi Kuwaamini. Duma fàtte
mukk tontu bu doy waar bi mu ma tontu
keroog. Dafa wiccax bopp bi, muuñ ba
noppi ni ma :
- Ci kàllama Suwaayili laa tibbe baat
boobu, Ngiraan.
Ma ne ko :
- Waaw, Usmaan, ba léegi nag lu
Kuwaamini tekki ? - Soo demee Tànsani,
mbaa Ruwandaa mbaa Keeñaa mbaa
Ugandaa dégg fa baat boobu, xamal ne
yaakaar la tekki. Kuwaamini mooy
yaakaar, Ngiraan.
Bi mu waxee loolu ba noppi, mu neeti ma :
- Defe naa ne jarul ma lay wax lu waral
ma taamu tur woowu. Man it, ma yëngal
sama bopp, ne ko :
- Jaru ko, kay. Mooy xanaa li nuy wax
dunde yaakaar. Loolu yomb naa jëli. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_52 | Waaye Usmaan, luy yoonu dawalkatu fasu
Ñarelaa ci kàllaama suwaayili ?
Yow gën a sore fa nga jëlijee sa turu fas
wi ! Bi ma waxee loolu, Usmaan Sow
tàmbalee xàqataay, di la ko reewal ba téye
biir bi. Ku fekkewul reetaani Usmaan Sow
ya keroog, fekkewoo dara!
Mu ngi la koy defal :
- Kex ! Kex ! Kex !
Ma defe ne dafa may kekkantoo, sama xol
jóg, ma ne ko :
-Jox ma sama ñamu bët, boog, Usmaan!
- Ci lan ?
- Li ngay ree, xanaa ! May ma ci tuuti,
boog !
Mu ne ma :
- Waay Ngiraan, buumu njaam gi ñu nu
takkee dëgër ! Ba fi mu ne daal, baatu
nasaraan yee ñu gën a jege yu waa
Tànsani ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_53 | Céy lii ! Fu mbëru làmb yi demee bay am
ay tur yu kenn xamul, di làmboo raaya
Amerig, lu tee sama fas wi tudd
Kuwaamini ? Du lii lañuy waxati ?
Ma xam ne li Usmaan Sow wax dëgg gu
wér péηη la, ma daldi soppi mbir mi ay
kaf.
Ma ne ko :
- Ñarelaa daal, du goxu como, Usmaan,
ndax fas yi sax soo leen làkkee suwaayili
ñu ηexal tontu la tontu bu wóor ! Gaa ñee
nu xamul rekk, waaye seen bopp !
Kooku, Usmaan Sow la woon, boroom
saret bi dëkk ci boppu koñ bi. Tàkkusaan
moom, su ma déggee coow jib Ñarelaa,
damay daldi xam ne ngóor soosu ñu naan
Muse Sumaare mooy jàppanteeti ak
soxnaam, ku ci ne di daggal sa moroom
ay saaga yu kenn masul a dégg, ñuy làkk
tubaab yu wex xàtt nag, mu naan jabar ji :
- Ti më feesie, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_54 | Ndaw si naan ko :
- Merd, taa géel, muwaa beese taa peer
miil fuwaa.
Ñu jàppe ko noonu, foo tollu di leen dégg.
Nun waa Ñarelaa nag, dunu ay tubaab yu
ñuul, li nu xam ci ay dëkkandoo moo di ne
su ñu tolloo foofu, séytaane roofu seen
diggante, ñu tàggook seen sago, li la war
mooy nga dem wax leen luy tax ñu
delloosi seen xel. Looloo tax bés ma sol
samay dàll, jubal seen kër, ne damay jéem
a àtte Muse ak Madam Sumaare. Waaye
dootul ñaar, moom !
Keroog jooju, lu ñu ma yakkul dañu koo
fàtte. Dañoo mujje teg fale seen xuloo
ñoom ñaar, di ma daggal ay saaga yu
ñaawa-ñaaw. Jaaraat ci dina ma xaw a
jafe, ndax nasaraan lañu doon làkk, te man
làkk woowu de, dégguma ci kaay ma rey
la. Waaye ni ñu ma doon xullee ak ni ñu
doon yuuxoo, ku jigéen ki di ma joxoñ ba
xaw a luqi samay bët ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_55 | jarul werante. Muse ak Madam Sumaare
kay, ay dëkkandoo yu doy waar lañu.
Muse Sumaaree ka bare tiitar nag, tey !
Nee naay kilifa la. Foo ko fekk mu ngi
xoju ba karwaatam mel ni lu koy tee
noyyi,
bu génne ci otoom bu xant bi sànni bunt
bi, dëngalu, defaraat ay lonetam, di jaay
pers daal, ni ngeen koy waxe yéen gone
yi, du ne kenn nag deewal ñu jullee la.
Jabar ji tamit ku soof la. Li ma xaw a
jaaxal ci mbir mi rekk, moo di ne,
Senegaal gii ma xam de, ku fi mas a am
alal ak daraja ju tax ñuy wax, yaa nga
daan dëkk ca kër yu rafet ya ca Faan
Residaa walla Almaadi. Wax dëgg, ku
ñëw luye xottu baraag fii ci Ñarelaa de,
mën ngaa bañ a sonal sa bopp ak njaayum
maanaa. Jabaru Muse Sumaare, jongoma
ju àgg ca kow la, ñuul kukk, taaru ba
tubaarkàlla. Ñuulaayam beek ni muy
tagaloo, jar nañu lu nekk. Waaye daal
ñoom ñaar ñooñu, kenn amu ci aajo. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_56 | Ngir bañ a guddal lim bi, mën naa ne
Ñarelaa gii ma dëkk, dama koo miin ba
sama gaa ñi leeg-leeg dañu may nirook ay
xuusmaañàpp. Mel ni am na ku làqu ci
béréb bu lëndëm, téye ci buumam di xëcc
na mu ko neexe te su ko defee, Doomi-
Aadama yiy kër-këri, yaakaar, ci seen
doyadeek seen xel mu gàtt, ne li ñuy def
yépp ci seen coobare la.
Waaye bés kenn ci ñoom day feebar, ñu
ne déet ne waay mu faatu, mbokk yi
jooyoo ko, ñu daldi ko jullee, ndeysaan,
yóbbu armeel ya suul. Ñu teg ci ay fan,
doom juddu ci geneen kër, ay wayjuram
bég, di ree, ñu daldi ngénte,
Yilimaan ñëw ñaanal ko, tëfli turam ci
nopp yi. Jàppee ko noonu. Ku fi jóge,
beneen bantu-Maam-Yàlla wuutu la.
Xam nga loolu, su ñu waxantee dëgg,
Badu, dafay xaw a nirook nekkinu garab
yi ci àll bi. Ngelaw li ëf garab gi màggat
ba fënëx, mu daanu, geneen garab
tàmbalee meññ, jóg, wuti asamaan. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_57 | Su ma waxee loolu, du caagin dama soxor
mbaa ma ñaaw làmmiñ. Mbir yee ni deme
doηη. Dafa mel ni ku nelawoon ay xarnu
yu baree-bare, bés bu yeewoo du fekk ci
dunyaa ku mu xamutoon walla mu gis fi
lu ko jaaxal.
Sunu Boroom bi mën lépp, yeyoo lépp,
sàkk lépp, liy noyyi ak li dul noyyi, moo
ko defe noonu, nu war ko nangu, bañ cee
teg baat.
Xam naa ne bés bu ma fi jógee ba nga
dellusi Ñarelaa jot ci sama kàddu yii,
dinga ne :
-Céy, sama Maam Ngiraan moo bare
woon wax te bëggoon waaraate !
Aa doom, ñàkk xam li mu waral bare na !
Tee nga maa bañ a tooñ, Badu !
Bokkuma ci nit ñooñu nga xam ne lu ñor
ñu wax, lu ñorul ñu wax. Lépp lu bawoo
ci sama xalima gii, ne cabax ci sa biir xel,
di fa wëndéelu, fekk na ma segg ko,
seggaat ko, seet ko, seetaat ko. Lu ma
leerul nàññ, dama ciy màndu. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_58 | Man, Badu, yàgg naa dox, yàgg naa gis.
Amuma nag sañ-sañ bu tollu naan la :
yoon wu sama baaraam joxoñ, jaar fa.
Sañuma loolu, ndax séytaane dafa bare
doole, àttan na la kar ci yoon wi, nga dem
ba defe ne yaa ci nekk, mu gal-gal la, nga
daanu.
Te bu boobaa, dinga ma mere fekk
defuma la dara.
*
* *
Lu ne mën na ñu koo yakk séytaane.
Séytaane du def lu baax, du ko wax.
Waaw. Waaye kenn du ni séytaane dafa
yaafus ! Déedéet ! Gën koo sawar,
yombul! Moo fi dàq soppeeku it. Su teyee
mu sol mii mbubb, su ëllëgee mu indi
kanam gu bees.
Moom daal lenn rekk lay bañ a dégg. Laaj
ma loolu lu mu ?
Xanaa ñu ne : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_59 | - Diw a fi gën, xamul caaxaan, nit ku jub
la. Su kàddu yooyu tàbbee ci noppam, xol
biy bon, mu daldi tàmbalee rëbb diw
moomu. Du am jàmm feek dugalu ko ci
gilaawaali. Moo tax, Badu, dëgg goo gis,
am na geneen dëgg gu tafu ci wetam, ne
fu mu jaar tiiñal ko. Ngóor soosu may bañ
a tudd nag, du nit ku baax. Ku xamadi la
te ñàkk teggin. Ponkal lay faral di doon,
am yax, am taxawaay te dara du nekk ci
bopp bi.
Kooku mooy Fen.
Yii ñett moom, Fen am na ko ba mu doy
sëkk : doole, ak fit ak fulla. Soo xoolee bu
baax ni sunu jamono jiy doxe, dinga xam
li ma wax foofu lu mu tekki. Li Fen ñeme
lu metti moo waral ku mu bëreel daan la.
Lu diggante xat-xat, mën na caa dugg,
nëxal xel yi, gàkkal xol yi ba noppi taxaw
fale, mel ni du moom. Koo xam ne tas
réewum lëmm du dara ci yow, gisuma
leneen lu la war a të. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_60 | Fen day xaar ba Dëgg toog ci biir nit ñu
baax ñi di waaraate, mu ne cabax ci biir
mbubbam, làqu fa, di ko dompat, di ko
ηóobi, di ko tex-texaan. Su ko defee, Dëgg
day muñ rekk, xam ne looloo fi sës. Ñi am
seetlu ci jataay bi, dinañu ko gis muy
gaññ, di wokkatu, di muut-muuti fi mu
toog waaye duñu xam lu waral loolu lépp.
Lee-lee it, Dëgg gag, bëgg wax lii, wax
leneen. Day fekk booba mu ngi naan ci
xelam :
-Naa muñ rekk, li ci des bareetul, su ma
toppee saay-saay bii dinaa mel ni moom,
ku ma warul a yab yab ma.
Bu séytaane demee ba xam ne kenn
faalewu ko, day daldi génn fa mu làqu
woon, ne cëpp ci biir géew bi. Ku nekk
naan ci xelam :
- Moo waay, ngóor su ñàng sii moom fu
mu jóge ak ay xiixatam yu metti ?
Noonu Fen jubal ci Dëgg, ni ko :
- Waaw, yow yaay Dëgg ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_61 | Kooku ni ko :
- Aa, am na ñu koy wax de.
Fen xàqataay, yuuxu, gëdd ko :
- Laajuma la loolu, li ma bëgg a xam lii la
: yow ndeyu-mbill gi, lu cee sa xalaat ?
Foofu Dëgg yëngal bopp bi, xaw a mel ni
ku koy dànkaafu :
- Saa waay, yaa ngi may tooñ de...
Séytaane wëndéelu ci biir géew bi, lépp lu
baax la fa Dëgg jotoon a ji ci xol yi mu
buddi ko sànni, dellusi tiim ko :
- Waay yow doo fog, toppal fale ! Ngaaka
yii toog ngay bëlde, waaye man soo ma
moytuwulee ma def la lu bon !
Aa, Badu, mas ngaa gis lii am ? Mën a
tooñ de weesuwul lii ! Su Dëgg demee ba
sës, daldi gis boppam nag, ni ko :
- Man maay diw, doomu diw ak diw te
soo defulee ndànk dinaa la ηëj léegi !
Noonu séytaane xàqataay, ñëw ba mel ni
kuy bëgg a luqi bët yi, daldi yuuxu : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_62 | - Tuuge waay ! Yow Dëgg, yaa mën a
kàcc tigi !
Dëgg di say, moom it :
- Maa tey laa wax, soo amee loo ciy wax
nga def noonu sa ndey !
Xam nga ni ay daldi na dikk.
Ndaxte Dëgg, dañu koy wax te dee, duy
faral di ànd ak màndute, te tàmmul it di
wax kenn di ci sañ a teg baat. Li mu tàmm
kay, mooy di waaraate, ñépp naan ëskéy,
di yéemu, naan :
- Kii moo bare xam-xam te rafet xalaat,
kaar.
Jeeg ju ndaw ji tegal seeni musóor, këfëlu
ba tubaarkàlla, di piisante ak a kobosante
ci seen biir, ku ne di déeyanteek sa
moroom :
- Moo, Dëgg mii kat amul xam-xam yem
ci, daa ndaanaane ba dee !
- Billaay Ami Wàdd yaa weex bët ! Yow
daal, waat nga ne doo sippi mukk ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_63 | Waaye, tey moom, Dëgg tal na leneen lu
dul yàppu xar wu ñu wàjj ak soow mu ñu
njar ! Bëñ yi rot nañu, deret jaa ngi muur
kanam gi, fi ko Fen njatt di ko wulli mu
ngay woote wall :
- Wóoy sama ndey ! Na ngeen mënee
seetaan ñu di ma def lu ñaawe nii ?
Su ñu leen teqalee, ñuy dàggasante, Dëgg
naan ko yaay Fen, Fen naan ko doo Dëgg.
Su ko defee, waaraate ba yem fa, xel yépp
di teey. Fu ñaar wéete, nekk ci kow Dëgg,
di ko ηàññ, di ko jëw, naan : - Moo,
moom kat, war nanoo seetaat bu baax li
mu nuy digal, ndeke !
Keneen ne :
- Góor fit, waay ! Waaye di jaay xam-
xam, di xogalliku ci kow nit ñi te bu la sa
moroomu góor saagaa doo sax ñemee fayu
! Bu nit ñi delloo seen kër, lépp lañu
jotoon a jàpp ne mooy Dëgg, dara dootu
leen ca wóor. Sama gaa ñee mel noonu :
bi ngay detteelook bi ñu lay jàmbu benn
lay faral di doon ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_64 | Gis nga nag, Badu, foo fekk ñu wër benn
Doomu-Aadama, di ko tàgg, di ko tàccu,
xamal ne am na ci jataay bi ñu ko ci ñee,
di ko móolu. Noo tudde loolu, yow ?
- Xanaa kañaan, maam Ngiraan !
Waaw, su la neexee nga tudde ko noonu,
Badu. Waaye man de, ci sama gis-gis bu
gàtt bi, yaakaar naa ne du kàñaan doηη.
Gis nga nag, su ñu waxantee dëgg, Badu,
képp ku fexe ba say nawle ne la :
- Jiitul, nun noo ngi topp sa ginnaaw, dafa
fekk nga napp leen, nax leen. Naxaateek
nappaate weesuwul fekk ay nit ni yow,
nga ne leen :
- Man maa xam yoon wi, jaarleen fi ma
leen di jaarloo, ku ko deful ci yéen dinaa
dagg sa baat sànni sa xaj !
Làrme baa ngi nii ak sàndarm yi, maa leen
di fey su weer deewee te lu ma leen sant
ñu def ko !
Seet ko ci ñi nu yilif tey rekk, Badu,
maanaam sunu Daawur Jaañ meek ay nitam. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_65 | Lu tollu nim réew, nga ne teg naa ci loxo,
maa fiy dogal, foo romb ñu tóojal la, koo
waxal ñaari baat mu daldi bëgg a sedd say
loxo ndax bég ci li nga ko yëg, nga yor
alal ju dul jeex di ko pasar-pasare...
Am ñu loolu jaaxal, ñu ne la :
Waaw, yaaram, yow gën a am faayda ! Ku
la ne yaa nu moom ?
Nga ne leen :
- Aa, xanaa du yéen a ma sànnil kàrt ayu-
bés yale ñu génn ?
Xam nga ne Badu, wax jooju, xel mënu
koo nangu. Sànnil kàrt ! Waaye loo ci
mën ?
Ñàkk pexee tax aji-néew ji doole yi bu
teyee ñu ànd ak seeni njiit, bu ëllëgee ñu
jàmbu leen, lu ñaaw lu ne ñu koy teg seen
der.
Waaw.
Bu teyee ñu ne : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_66 | - Njiitu réew mi kañ, Yàlla may na ko.
Moo baax, moo am yërmaande te bare
xam-xam ! Ku mat kilifaa ngi !
Waaye ngóor soosu wax loolu, walbati
xelam lu yomb la.
Soo ko ne :
- Sunu Demba Njaay mi kenn sañul a
tudd de, dégg naa ne diw mooy góor-
góorlu ci jabar ji.
Dinga gis xaat ni mu bége, bët yiy melax,
mu ni la :
- Nga ne ma ?
Nga ne ko :
- Du xam nga Paap Xuma ?
- Moo, kooy wax Paap ? Du mooy sa
doomu bàjjan biy...
- Waaw kay, mooy kiy liggéey Paresidaas,
tusuñe la fa ! Nee na ma liy xew foofu
kenn mënu koo nettali. Ndaw si daal,
ndekete li muy ngànd-ngàndlu yépp, amu
ci benn kersa, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_67 | góor gu ko romb mu àddu kalpe la, ne la
tekkil gaaw sa tubéy, ngeen daldi ànd di
bërëηu ci moket bi !
- Déet waay ? Man sax, loolu bettu ma !
Moom kañ, paramiyeer daam lañ koy wax
xawma, soo ko xoolee bu baax tele ak
puudaroom bu metti, xam ne lagara bu
bon la !
- Ñoom kay seen bopp lañu fi newal.
Duñu gat, ñii !
Bés boobu nag, Garaη-palaas bu waa
jooju toog di damye, nettali fa la mu dégg.
Te fu mu ko nettalee nit dëggal ko, am sax
lu mu ca yokk.
Waaraatekat bi tamit, am na nu muy
nguuroo ci kow nit ñi te du tegu fenn. Day
sol ay yëreem yu rafet, ñépp dajaloo di ko
déglu, ñu wara nangu ni lépp lu mu wax
dëgg la. Ku koy ñemee weddi ? Waaye
moom it su benn sàmbaa-bóoy taxawee ci
tànku toroxal ko, ñépp a ciy bég.
Lépp li Yàlla sàkk, nit moo ci gën a doy
waar. Nit mooy mbindéef moo xam ne, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_68 | bu xol bi jëmee fii, xel maa ngi koy digal
mu jaar feneen. Dinga agsi cib dëkk, fekk
mag ña fa gën a yiw dajaloo ci pénc miy
déglu benn yaaram, mu leen di soññ ci def
lu baax mbaa di ko wax. Sa yaram daw,
nga ne :
- Lii de, dara dàqu ko, ndeysaan.
Fekk na booba séytaanee ngi yoot ndànk.
Badu, bu ñu la ajee ca kow, nee fa noηη.
Nit ñi ci suuf di la séentu, am na it lu ñuy
séenu ci yow. Bés boo wàccsee toog ci
seen biir, duñu la ko baal ba mukk Maa la
ko wax : duñu la yab yem ci. Dinañu la
jéppi ndax li nga tas seen yaakaar.
*
* *
Bi ma yeewoo tey ci njël, doxantu naa lu
mat waxtu ci ëtt bi. Bi Yilimaan Keeta di
laata nodd nodd gu njëkk, bett naa sa
takkandeer mu ηàbb Téereb Dóom, di ko
jàng.
Gisuma la, waaye dégg naa la nga naan ci
sa xel : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_69 | - Maam Ngiraan de, xanaa ba muy bind
téere bii, àndul woon ak sagoom. Ku jóg
kay ba ne dangay nettali, tee ngaa jaaraat
ci li nga fi jot a teewe rekk. Waaye di
waaraate subaak ngoon ! Loolu lu mu ci ?
Wax nga dëgg, Badu. Maa ngi mbebetu
rekk, booba ba léegi. Yaa yey laaj ma :
- Waaw, Maam, lan nga may waaj a
nettali ?
Su dee juróom-benni Téere yi des ni
Téereb Dóom bii lañu mel de, jarul may
sonal sama bopp di leen jàng.
Badu, dëgg moo neex Yàlla. Li nga wax
amuma dara lu ma ciy teg. Xanaa boog
ma jéem a tegu ci yoon wi te bañati koo
wàcc. Bu yaboo sax ma ne sama waxtaan
ak yow fii lay doore.
Bu ci kanamee, dinga daje ci Téereb
Ngelaw ak benn néew bu bawoo Tugal. Sa
néewu baay la. Ba fi Asan Taal di jóge di
futbali Màrsey, liir bu tooy xepp nga woon. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_70 | Laaj naa keroog Biige Sàmb, sa yaay,
ñaata at nga amoon, mu ni ma :
- Bi Asan di dem Tugal, Badoo ngi am
juróom-ñetti weer ak juróomi fan.
Biige yokk na ci sax lu ma ko laajul ndax
nee na ma :
Fan ya ca topp la feebaru ηas bi jëkkee
daaneel Badu. Yàllaa nu musal rekk
waaye tiitoon naa lool, ragal ni sama
doom ji du ci mucc ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_71 | TÉEREB NGELAW | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_72 | Duma fàtte mukk bés ba nu jëlijee néewu
Asan Taal ayeropooru Ndakaaru.
Bésub alxames la woon, bi timis di waaj a
jot.
Ba nu demee ba jub tali Ngaala Jóob -
mooy jàddukaay bi mujje ci yoonu
ayeropoor - lanu dajeek mbooloo mu
takkoo-takku, kaar. Xanaa waroon naa
tollu ci ñeent mbaa juróomi-téeméeri
junniy nit. Ñii ngiy waaxu, ñii di xélu, ñaq
bay siit, ñi ci des dugg ciy kaar-ràppid
mbaa ñuy dawal seeni oto bopp, ñi gën a
féete ndaw war seeni móto. Ñépp di
yuuxu, di tàccu, coow li ne kur, sófóor siy
korne tëwa bàyyi, koo dajeel mu ngi taf
rajo bu ndaw ci noppam. Gone yi mel ni
ñu tàggook seen sago.
Foo tollu, dégg ñuy salliiru :
- Móo-du ! Wiiw Móodu ! Móo-du ! Móo-
du !
Naka laa dégg tur woowu rekk, daldi nànd
ni mbir mi deme. Dëgg la sax, Ndakaaru
bari na ñu fi tudd Móodu. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_73 | Loolu kenn du ko werante. Wànte foo
dégg ay gone di yuuxoondoo tur woowu,
na la wóor ne sunu woykat bu mag bee ko
waral. Móodu Siise rekk a leen ko jaral !
Am na sax ñuy wax ne woykat yi ci Afrig
yépp, Móodu Siise amu ci moroom.
Ñeneen ñi dinañu dem ba naan képp kuy
woy ci àddina si Móodu Siise la ko dàq
fuuf.
Man nag, dootuma gone. Xam naa ne yëf
yi moom, njuuj-njaaj moo ci ëpp. Saa yoo
gisee ay Doomi-Aadama dankalikoo benn
béréb ba noppi teqalikook seen sago, di
yuuxu :
- Wiiw diw ! Wiiw diw.
Di kadd-kaddi, di say, xamal ni am na ay
boroomi pexe yu seen ceeb di tooy. Doo
leen gis mukk, ñu nga jonkan ca pet,
muuroo lëndëm, di waññi ak a waññiwaat
xaalis bu dul jeex, tey kex- kexi, naan ci
seen biir :
- Ñii ñooy ngaaka dëgg ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_74 | Bés boobu may wax nag, Móodu Siise
dafa jóge woon bitim-réew. Ci li ma
jotoon a for daal, ndam lu réy la fa
indiwaale woon. Yàlla def mook néewu
Asan Taal ñu bokk benn roppëlaan. Man
yëguma ci woon dara, ndekete fan yooyu
yépp, réew maa ngi waajal Móodu Siise
teeru bu mag a mag. Kenn mënul woon a
ubbi rajo mbaa tele te doo dégg ñu ciy
wax waxu Móodu Siise mbaa nga gis ko
moom ci boppam muy fecc, di woy. Am
na sax bés, Daawur Jaañ, njiitu réew mi,
waxtaan ak taskati-xibaar yi ba noppi,
xaw a mel ni kuy dóor pooj, daldi ne, ciy
kaf :
- Aa, xawma kan, waaye man Daawur
Jaañ mii de, bés boobu ku ma dëgg
ayeropoor Lewopool Sedaar Seηoor ne ma
mas-sa !
Bi yëf yi weesoo laa door a yëg loolu
lépp. Fekkoon na, nun mbokkiy Asan
Taal, nu ngi woon ci naqar wu réy. Wax
dëgg Yàlla, taloon nanu leneen lu dul
déglu rajo. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_75 | Seetal ma lii rekk : di jëli sa néew, am
naqar ak tiis, daje faak waa réew mi yépp
ñuy mbumbaay, di fo di ree, yëf yi mel ni
tuq su bënn !
Keroog laa yéemu !
Dafa meloon ni waa dëkk bi dañoo amoon
mbégte ci deewu Asan Taal gi, ñëw di ko
wone...
Dégg nga ba tàyyi ñu naan :
- Tombee waral aay gaaf.
Nun nag, mbokk yi, li nu soxaloon, moo
doon fexe ba jot ci Asan, dellook moom
Ñarelaa ci jàmm ak salaam. Def nanu
sunu kemtalaayu kàttan ngir bañ a réeroo
ci sunu biir. Waaye danoo mujjee seey ci
mbooloo mi doon jëm ayeropoor Sedaar
Seηoor. Kenn ci nun mënatul a xàmmee
yan oto ñoo doon jëlsi néewu Asan ak yan
oto ñoo doon sargalsi gone googu ñu naan
moo dàq a woy ci àddina si juróom-ñaar.
Oto bi néewu Asan newoon, daa mujjee
taxaw. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_76 | Am na sax ñu ñëw ba fëgg ko, di yuuxu,
xanaa yaakaar ne woykat bu mag bee làqu
ci biir. Wànte foo dem dinga fa fekk nit ñu
am seetlu. Kenn ci gaa ñooñu moo leen ni
- Aa ! Mel na ne njuumte am na ci yëf yi,
de ! Ñii ma gis de, defe naa ni tal nañu
leneen ! Noonu, ñi mu àndal jëli li mu
wax, daldi nu xàllal yoon nu jàll. Balu
nañu nu àq sax, am ci ñoom ñu ñaanal
Asan Taal. Bi mu ko defee, nu tegu ci
yoonu Ñarelaa. Li ma la nettali noonu, ci
diir bu gàtt la xew.
Boo seetee sax, danga naan mbiir mi taxu
koo am solo. Njuumte fépp la xéj. Waaye
man mii nga xam ne ginnaaw sunu
Boroom bi, kenn gënu maa xam Asan
Taal, dara mënu maa tax a fàtte bésu
alxames boobu.
Asan Fay Taal, juruma ko yem ci. Maa ko
yar, defoon ko nawle, moom it mu defoon
ma xarit. Laata muy dem Tugal, dëkk fa
fanweeri at, ba ndogalu Yàlla fekk ko fa,
lu mu mas a xalaat mbaa mu nar koo def, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_77 | da ciy jëkk a diisook man. Su ñu
waxtaanee, lu ma ko digal mu jaar ca.
Kenn réerewul loolu mbir. Dem nañu sax
ba sama mbokk yiy xultu, naan damay
gënale Asan Taal ak sama yeneen doom
yi, maanaam ndem-si-Yàlla ji Paap
Demba ak Ndey Soxna may séy Bolooña.
Ba Asan Taal dee dund, gis naa ko ci
nekkin wu ne. Wànte bés ba ñu kooy
dénki boroomam, nit ñi bég, di fecc, di
tàccu, jeeg ju ndaw jiy sarxolle, dama ne,
Badu, bés boobu du génn mukk ci sama
xel.Ndaw naqar ! Ndaw tiis !
Am na sax benn góor gu ma ne :
- Lu kéemaane li xew Ñarelaa ba réew
mépp di ko coow, mënunoo jaaxal, nun ñi
demoon jëli néewu Asan Taal ayeropoor.
Yëf yi nii rekk la mënoon a deme. Gëm
naa loolu, man it.
Saa su ne Sunu Boroom a ngi nuy artu. Du
tàyyi, du noppalu. Waaye danu neexul
dimbali, nun Doomi-Aadama. Danoo tëx,
gumba, te gaaw a naagu. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_78 | Fan yee ñu génn, noon naa la sa baay,
Asan Taal, bitim-réew la faatoo.
Nun ay mbokkam nag, xibaar bu tiis
boobu dafa noo jóge kow ndax masunoo
yëg fu Asan woppe. Ndaw su ñuy wax
Yaasin Njaay moo ma woo bés ne ma
Asan génn na àddina. Ba ñu demee ba ci
biir waxtaan wi, laa door a xam lu mu
joteek Asan Taal, moom Yaasin Njaay
moomu.
Maa ngi fàttaliku sunu waxtaan nun ñaar :
- Dama soxla woon Ngiraan Fay Taal,
baayu Asan.
- Asan man ?
- Asan Taal, te mu daan futbal fii ci
Màrsey.
- Mana Ngiraan. Kooku ?
- Yaasin Njaay laa tudd, waaye yaakaar
naa ne xamoo ma de, góor gi.
- Waa fan ?
- Tugal laa lay woowe. Maa ngi Màrsey. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_79 | Ma tàmbalee jàmmanteek moom. Mu dog
ma ci lu gaaw :
- Góor gi, nga baal ma de, waaye fi may
wootee dafa xaw a sore. Dafa am lu ma la
bëggoon a yëgal.
- Loolu lu mu ?
Noonu, mu ne tekk.
Ma ni ko :
- Mbaa du Asan daa feebar ?
- Feebar bi yóbbu na ko.
- Aa ! Loolu kañ la ?
- Biig. Ndaw sa wootee Tugal nag, taxu
koo am yar. Ñàkkewu ma teggin, gaa,
wànte nit su faatoo fu soree noonu nga
koy yëgal ay mbokkam, dafa am noo ko
war a defe.
Moom loolu fekku ko ci. Dafa mel ni sax
li ko gënoon a soxal moo doon nan lañuy
def ba dugal néewu Asan ci roppëlaanu
Air France biy bawoo Tugal bëccëg bu ne
di teersi Ndakaaru. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_80 | Ñaari baat yu nekk, Yaasin Njaay ni ma :
- Aa, xaalis bu bare la laaj de, te dama war
a feyal Mbisin ak Mbisaan.
Bi ma ko laajee ñooñooy ñan, la ma sog a
xamal ne ay doomi Asan Taal lañu.
Mu jaaxal ma lool. Ma ne ko :
- Asan Taal kañ la fa am i doom ? Man de,
guléet ma dégg loolu.
Foofu, mu xaw a ñagasal baat bi :
- Asan Taal am na fiy doom de, te man
Yaasin Njaay mii di wax ak yow maay
seen ndey, nekkoon it soxnaam.
Xamatuma lu ma ciy teg. Ma daldi ne ko :
- Ba léegi nag, soxna si ?
Foofu de, su ma bañul woon fen dinaa ne
ndaw si mer na dëggëntaan ! Lu leer nàññ
la ma ci tegal :
- Góor gi, jottali ma benn gone ci kër gi,
ma wax ko fan ngeen may mën a woowe.
Su ko defee, saa yu ngeen jekkoo | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_81 | ngeen yónnee ma xaalis ma ànd ak néewu
Asan Taal indil leen ko Ñarelaa. Soo
fàttalikoo, yow Badu sax laa booleek
moom, yéen ñaar ngeen làkkante seen
nasaraan.
Ci ngeen jëkk a waxe, yaak Yaasin
Njaay. Waxoo ma ci dara, ndax tàmmoo
di nettali mbaa di waxantu. Loolu du sa
jikko. Waaye teewul ma gis ne seen
jokkoo bu jëkk boobu, xol bu tàng doηη
nga ca jële.
Nga xam ne boog ni yëf yi deme tey
jaaxal na ñépp, ba mu des man. Ci la la
Yaasin Njaay xamale ne lu néewu Asan
Taal gën a toog ca morg ba ca Tugal,
xaalis bi nuy war a fey di gën a bare.Sama
bopp bi ubu lool, ndax xawma fu may jële
ay milyoη. Mu wóor ma ne du Yaasin
Njaay moomoo fasoon yéene sonn ci
mbirum Asan ba ciy dugal alalam.Xam
nga, Badu, mag day faral di am seetlu. Ak
li may ñàkk xam nu diggante Asan Taal
ak ndaw soosu deme yépp, | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_82 | leeroon na ma ne masul a nob sa baay te
itam masu koo naw
Ku bëgg nit mbaa nga naw ko, neneen
ngay doxale bu génnee àddina, rawatina
bu dee danga ne sa boroom kër la woon.
Fanweeri at yu mat sëkk, Asan Taal toog
ko bitim réew, nekk ci lu ko neex, bindul,
wootewul ! Yu mel nii moo tax ñu naan :
- Ëllëg du añ du reer, waaye dees koy
sédd.
Waaw !
Asan ak jabar te kenn yëgul fu mu ko
takke !
Aa, Badu, niti tey yi jaaxal nañu ma.
Xalaatoo ne Asan dafa mujjee dof Tugal
ga mu nekkoon ?
Xam naa ne sa baay la, waaye du tee ma
laaj la loolu, ndax dootoo gone.Léegi,
ndaw saa ngi waaj a ñëw Ñarelaa, nar nu
fee indil ñaari doomam yooyu, Mbisin ak
MbisaanAy doomi Asan, te nun yëgunu,
tinunu ! Say rakk, yow Badu ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_83 | Waaye, céy, su Yaasin Njaay géntoon
booba li ko fiy xaar ! Moom it kenn gënu
koo sàggan. Nde moos waroon naa xam
ne Tugal ak Ñarelaa duñu benn. Fii de,
ndekete Biige Sàmb a ngi ko fi doon yeeru
ak meram mu tëwa giif. Bi yëf yi weesoo,
lanu ay xariti Biige Sàmb sog a xamal ne
sa yaay doon na faral di tëkku Asan, naan
leen :
- Asan Taal, bés bu wàccee Ndakaaru,
kaso laay fanaani ndax dinaa ko gor jaasi,
mu dee, ma sog a jébbali sama bopp
yoon.Waaw, Badu. Sa ndey, Biige Sàmb,
moo daan wax loolu. Far Yàlla def Asan
faatu Tugal. Taxul ba tey meru Biige giif.
Waatoon na ne fàww mu feyu. Te Biige
Sàmb feyu na. Ma ni : fey na Asan Taal
ba wis ko ! Dinaa ci dellusi ci jëmmi-
jamono.
*
* *
Ay weer a ngii Yaasin Njaay nekk ci kër
gi. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_84 | Waa gox baa ngi kooy jëw. Bi ñu
tàmbalee coow ci ay mbiram ba am yu ci
senn, laa yëg ne mook Asan Taal nekkaale
nañu ay ati at ca Màrsey. Nee nañu it
Asan jëkkoon na faa takk benn tubaab bu
tudd Natali, Yaasin Njaay dugg ci seen
séy, tas ko.
Lu ne ñu ngi koy wax :
- Dégg naa dafa takkal pot jabaru Asan,
kooka mujjee daw, ba kook jëkkëram.
- Fi nga koy gis nii, moo fi dàq a sëriñtu.
- Xanaa déet kay ! Ak làkkum tubaabam
yu metti !
- Loolu lañu tudde tubaab-njallxaar, dàll
saη kawas !
- Rakku Ndey Saar ji nekk Pari moo ma
woo keroog ne ma nanu moytu Yaasin
Njaay, ndax njaaxum lu nekk def na ko
Tugal door a teersi Ñarelaa
- Dara ! Cagatu doηη la fa nekke woon.
Ku demul Gànnaar it xam ne guddi lañu
fay reer ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_85 | Waaw. Ña ko jot a gis Tugal nee nañu
Yaasin Njaay ku fowe woon boppam la.
Dégg naa nekkewu fa woon lu dul naan
sàngaraak tóx yàmbaa. Wax nañu it ne da
doon cagatu.
Ab sàmbaa-bóoy jóge fale, ngeen waxaale
ba juboo, nga tëj sa buntu néeg, jaaxaan.
Mu dem ci, dem yoonam. Keneen ñëw
yéeg moom it, wàcc, wacc la fa. Bu bët
setee ngay waññi sa koppar, naan :
- Biig de, màrse neex na.
Dem nanu sax bay ηun-ηunee ni Yaasin
Njaay moo wàll Asan Taal feebar bu bon
bi ko yóbbu.Xawma dëgg la, xawma du
dëgg.
Lenn daal wóor na ma :ca njëlbéen ga la
waa Ñarelaa xaare Yaasin Njaay. Lu metti
li ko dal, ñu bare ci gox bi yéene woon
nañu ko ko
Aa, Badu, Yaasin Njaay ak doomam yaa
ngi may bëgg a jommal, kat ! Gii génn
xeet gën a jéggi dayo ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_86 | Am na yoo xam ne de, su doon sama sago
duma la ko nettali. Waaye nu may def ?
War ngaa xam li fi xew sa ginnaaw yépp,
te man doηη maa la ko mën a àgge. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_87 | TÉEREB LËNDËMTU | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_88 | - Badu Taal ?
- Naam.
- Neel Birëm Seen mu ndaw mu teg àttaaya.
- Birëm seetaani na futbal ba, te ni ma ko
xame de, balaa mu fiy teersi reer jot.
- Nu nuy def nag ?
- Xanaa ma jéem a xiim, Maam.
- Yow de sa àttaaya moom...!
- Man kay, xam naa ne wóoluwoo ma ci,
waaye sa bopp ! Sama lëwël amul
moroom, ñaareel bi ne ko dandu ma !
- Waaw, Badu ?
- Naam.
- Mbaa yaa ngi déglu li ma lay wax booba
ba léegi ?
- Bu baax sax, Maam.
- Guddi tey gii nag, guddi gu mag la, ndax
ci laa la fas yéenee wax lu waral ma ubbi
Téereb Lëndëmtu.
- Mooy bu ñuul bi, du ?
- Mooma. Dóoral yat. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_89 | Maa ngi ferenklaayu ci béréb bu lëndëm
këruus, ne la jàkk te mënoo fexe ba gis
ma.
Yaa ngi téye ab téere bu ñuul di ko jàng.
Ba ma ko bindee
ak léegi xanaa war naa mat juróom-fukki
at, maanaam genn-wàllu xarnu. Yow ci sa
bopp, Badu Taal, màggat nga. Yaa ngi
bejjaaw ba weex tàll.
Ma waxaat la ko : mënoo maa gis waaye
sa yaram a ngi yëg ni ma ferenklaayoo ci
sama biir bàmmeel, ni la jàkk. Foo jëm ci
dunyaa samay bët a ngi la topp.
Li ma jëkk a seetlu mooy ni yëf yi ubee sa
bopp.Nee nga ci sa xel :
- Aa, Maam Ngiraan de, ni mu ubbee
Téereb Lëndëmtu bii, doy na waar. Lu
tax mu jaar ci sama tur, te mu wóor ko ne
mënuma koo wuyu ?
Lu ko xiiroon ci waxtaan ak man, di ma
sant ma xiimal ko àttaaya te xam ne booba
sore naa lool Ñarelaa ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_90 | Xéy-na boog da doon jéem a xoromal
mbind mi... Moo, soo demee kat maam
Ngiraan dafa bokk ci bindkat yooyu nga
xam ne, su ñuy nettali benn xew-xew
duñu nangu dara rëcc leen ci. Waaye yenn
wër-wërloo yi jar na koom ? Man de,
nettali lii laa ci xam : nataal li nga gis,
jottali li nga dégg, soo tëddee nelaw.
Rawa su dee li ngay nettali sotti na ba
noppi.
Dëgg la, Badu. Sa kàddu yu mujj yooyu
kenn du leen werante : waa réew mi yépp
yëg nañu li dal Yaasin Njaay ak sa ñaari
doomi baay yi, Mbisin ak Mbisaan.
Waxtaane nañu ko ba fàtte.
Ma ni la :
Yaa yey jaaxle, wutewumaak màggat muy
naax, di waxtu. Waaye na sa xel dal.
Dofuma, jinne jàppu ma.
Maa la gën a xam ne Birëm Seen mi ma
tudd sànq turam, du nit dëggëntaan.
Man mii maa njatt ngelaw li, yatt ci Birëm
Seen ! | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_91 | Dafa fekk rekk ne, bindkat boo gis, ñaare
day bëgg tijjee waxtaanam ay kàddu yu
koy sànni ci jaww ji, mu woyof ni picc, ay
kàddoom gën a neex a dégg. Moo tax ñu
naan :
- Léebóon !
- Lëppóon !
- Amoon na fi.
- Daan na am.
- Ba mu amee yaa fekke ?
- Yaa wax ma dégg.
- Waxi tey matul a déglu !
- Sa jos a ci raw !
Ba ma newee gone de, noona la Meer Faat
Njaay daan ubbeey léebam.
Léebam ya neexoon nañu lool, waaye
daawu ci door benn feek taalul sunu xel ba
mu tàkk, mu koy xamb, mu wóor ko ne lu
mu wax nu gëm ko.
Meer Faat Njaay dafa ma doon fàttali ab
tëggkatu sabar. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_92 | Seetlul bu baax Géwél Mbaay. Day jëkk a
raay ndànk sabaram, raayaat ko, jàppee ko
noonu ba yaram wi tàng, muy rëkk, di
xaaccu, jeeg ji sànneeku ci biir géew bi di
njaay-xólléy, mbooloo mi yépp
àndandooy awu.
Te itam Badu, nun bindkat yi danuy faral
di wéet lool. Metit woowu, kenn du ko
yëg ba naan nu mas-sa !
Waaw. Waa Ñarelaa dañuy xéy di kër-këri
ba guddi jot, ñu tas, tasaaro, daldi dem
tëri. Waaye saa yu ñuy nelaw bay
yàndoor, maa ngi ferenklaayu fii man
kenn di bind. Juróom-benni waxtoo ngi nii
ma déju ci sama ndéstan di joow ak sama
xalima. Joow laa wax de, Badu. Waaw, di
joow ni sama mbokki Gét-Ndar yiy géti.
Gaalu dof laa dugg, waaye gaal gii moom
dina teer te fa muy teer dina la neex. Géej
gee gën a yaatu... Mu ngi ne selaw. Kon
jaadu na lee-lee sama gaa ñi jóge laaxira,
ñëw wétallisi ma. Ku ma ci rëdd sa tur ci
kayit gi, nga feeñu ma, ni ma : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_93 | - Yaa ma woo, Ngiraan Fay wuyusi naa la.
Noonu, mu yëngatu ndànk ci béréb bu
lëndëm bi mu jaaxaan, gis ni ma jaaxlee
daldi ma neeti :
Yaa ma woo, du ? Seen dunyaa ju naqadi
jooju de, xam nga ne moos, rus laa gàntu
rekk moo tax nga woo ma ma wuyusi la !
Nde sama bàmmeel bii ma tëdd, jàmm
rekk laa ci gis !
- Baal ma de, waa ju baax. Woowuma la,
xam naa sama xalima gi nga dégg muy
xoos kayit gi, di kiij-kiiji, nga yaakaar ne
maa wax. Yàlla xam na ne ηaaηuma, sama
xalima gi doηη ay coow, tëwa noppi.
Yu mel noonu dafa may delloo ay ati at ci
ginnaaw, ma daldi doonaat gone gu ndaw.
Démb sax, bi ma jullee timis ba noppi,
benn xale romb na ma, di dawal mbegeem,
ma yaakaar ne sama bos la sàcc. Tuutee
tee ma laaj ko fan la ko jële.
Leneen am na : wéetaay bu metti rekk
moo waral may jaar lee-lee ci sa tur, Badu
Taal. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_94 | Léegi nag, lan moo tax ma fas yéenee aj
mbirum Yaasin Njaay ak waa Ñareelaa,
ne la jabb Téereb Lëndëmtu ?
*
* *
Badu, wax joo gis, am na biir am biti.
Jàppe ma ni nit kuy daagu moom kenn ci
biir àll bu xonq bi. Yoon wi may aw,
Maam yaa ko xàll démb, booba tey
ñëwagul.Lu yoon woowu xat-xat, moom
doηη laa xam. Yoon du ko gën a wóor.
Xool ma bu baax : xam naa fi ma jëm.
Maa ngiy temp, ndax leer na ma ne balaa
jant biy so, ma àgg fa.
Yow, yaa ngi toog ci ëtt bi di ma xaar. Ma
ñëw, nu nuyoonte, julli timis, reere sunu
cere baasi bu neex ba noppi lal sunu basaη,
tàmbalee waxtaan jëmale bët-set. Su lëwël
jàllee, laaj ma lan laa gis ci àll bi. Nanga
ma may nopp bu baax, nag : li ëpp ci li ma
lay nettali, gisuma ci dara ba dara booloo
jeex ! Xam nga lu waral loolu, Badu ? | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_95 | Ba ma nekkee man kenn ci àll bi, sama xel
yépp a ngi woon ci rab yi ma wëroon, làqu,
ne ma jàkk, di ma xeeñtu, nar maa song,
xët ma cig lëndëm. Moo xam till la, walla
bukki, walla segg, walla jaan mbaa xeetu
picc wu mu mënti doon, ñoom ñépp a ngi
ne tekk, di ma yeeru.
Doomu Segg ni :
- Tee noo dal ci kowam, yàpp ko ?
Ndey ji artu ko :
- Moytul ma nit ! Ni muy taxawee ci ñaari
tànkam, noonu la baree pexe ! Boo demee
sàkkati na gànnaay gu bees !
Duma la ko nëbb, Badu : li may dox man
kenn ci àll bi yépp, sama fit waa ngi naan :
- Tëf ! Tëf ! Tëf !
Nu yëkkati sunuy kaasi àttaaya, ku nekk
guux, guuxaat ba muy ñetti yoon. Yow it
ngay yàkkali bóli, na ma ko daan defe su
nu wëraan Meer Faat Njaay, di déglu
léebam yu neex ya. Ma ni la : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_96 | Badu, noo mënee dal xel bay wékk sa
yaakaar yépp ci man mii tëx, gumba,
muuma ?
Nga ni ma :
- Dëgg la, ci àll bu lëndëm këruus nga
jóge ! Waaye won ma lépp la nga fa gisul,
jottali ma lépp la nga déggul ba nga fa
jaaree !
Ma reetaan, ndeysaan, daldi ne ci sama
xel :
Aa ! Gone gaa ngi mokkalsi kat !
Nga neeti :
- Maam Ngiraan, su say kàddu naree diisal
sa làmmiñ, takkal leen ay laaf. Dinañu
woyof nim picc, di naaw ni moom, jaww
ji naan leen :
- Aayoo nenne tuuti...
Waaw, kenn mënul a xam lépp, wax lépp.
Sañ-sañ boobu dof yi rekk, maanaam ñi
teqalikook seen sago ñoo ko am. Léegi daal,
li ma ci gis mooy gas pax mu xóot a xóot ci
taatu ndaa li, suul fa Téereb Lëndëmtu. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_97 | Bés boo ñibbisee Ñarelaa, fekk ma jóge fi,
nga lemmi ko, jàng ko, jéem koo firil sa
bopp.
Bu jëkk, gone yi dañu daan toog ci ab jalu
suuf, def géew, ku ci ne di fent lu ko neex,
ngir bégal say moroom. Loolu lañu daan
tudde maye. Dégg nga wax ji de : maye.
Maye... Waay ndax am na lu dàq kàddu
googu ? Ak ni jamono ji naqadee... Sa
yaakaar tas, nga jaaxle, nit ku yéwén ñëw
ne la :
- Am na lu ma la bëgg a may...
Nga ne ko :
- Te naxoo ma ?
- Xam naa ne gëmewoo ko, waaye tey
dinaa la may bànneex ba nga doyal ci sëkk
ak barke !
Noonu, mu ubbi waxandeem génne ci
benn seetu bu mag, fomp ko, tàllal la ko.
Nga seetu, tiit, dellu ginnaaw.
Daldi ne : | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_98 | - Waaw, ana ma ? Bii seetoo gën a doy
waar ! Ñii mu may won kat, kenn laa ci
xamul. Boroom lonet yee niroo naak man,
gaa... Am na it ñu ma ci xelmati wànte
wóoruma ne ñoom la. Te sax, jigéen ju
màggat jee toog buntu këram ca Aselem,
téye layoom di tànn ceeb... mel na ni...
Moom a de, moonte ! Waaw, Meer
Sukayna Sàll, lan lay def ci biir seetu bi ?
Mbedd mee may séen de, am na béréb bu
mu may fàttali. Su tawaan, fa lanu daan
futbale maak ñoomin Baabakar Mbów,
sunu ponkalum Ndeem Maysa mi, ak
ndemsi-Yàlla ji Alsaan Ñaη ma des Tugal
ak Asan Pereera mbaa Ben Jogoy Béey.
Waay, bile seetoo ëpp li ñu koy doye ! Ku
la waxloo lu ñu la laajul ?
Su ko defee, seetu bi reetaan, yëngal
boppam, di ñurumtu :
Céy ! Doomu-Aadama Njaay moo naqadee
digaaleel ! Yow, yaa fi gën a ragal dee,
lépp lu la Sunu Boroom bi teg mën nga koo
dékku ba mu des sa wéetaayu bàmmeel. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_99 | Saa yu sa xel demee ci ñi fi jot a jaar,
njaxlaf ba, tubaarkallà, di tëb di dal ba
noppi xéy ne mes, dara dootu la saf, Kon
kay, su ma fexee ba nga jokkoo ak ña woon
démb, looy waxati ? Lu gaaw-gaaw
nekkaat nga fi gone, topp ci benn balu
futbal bu weex di dóor, di duut say
moroom ba ñuy miir, ngay mbëkk bal bi, di
ko rëkk, caax yi bëtt, nga bég, yuuxu ! Loo
bëggati ? Xanaa du lu mu gën a lëndëm
gën a neex ? Soo ma merloo, dinaa la won
maay kan, de ! Rajaxe sama bopp ak naan
ndox laa yemale. Te man seetu, su may toj
àddina siy tukki ba fàww !
Nga koy saraxu nag :
- Ëpp naa def, waa ju baax ! Yow it,
Seetu, may kaf rekk nga bëgg fi mer xaat !
Jébbal naa la sama bopp, lu la neex defal :
delloo ma démb, diri ma ba ëllëg, mbaa
sax yóbbu ma béréb bi amul tur, fa sunu
jamono jii tage, dem të ko, dikk të ko.
- Waaw kañ, yaa ngi sog a génne waxu nit
ci sa gémmiñ gi ! Badu, yaa ma tax di wax.
Fàtteendi ma tuuti. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
page_100 | Nanu ànd wëri Maam Ngóor.
Soo ma nee :
- Maam Ngóor ? Kuy kookooti, Ngiraan ?
Ma ni la :
Maam Ngóor du kenn. Mooy ñépp, te it
moom doηη mooy Maam Ngóor. Moo jur
ki ma jur. Du xam nga lu loolu tekki ?
Maamaat la ci sa baay Asan Taal.
Fii ma toog ci buntu kër gi, di féexlu, la
sama xel ni yarr ci Maam Ngóor.
Lépp li ma lay waxsi ci moom, may naa la
ko ci xol bu sedd guyy.
Badu, ay at a ngii ca ginnaaw lu doy waar
dal na ma. Njëlug Ñarelaa. Bi Yilimaan
Keeta noddee nodd gu njëkk, fekk na ma
yeewu bu yàgg. Ni ma ko tàmmee def,
maa ngi wéeru ci taatu màngo gu mag gi,
di xaar waxtu wi jot, ma jubal jàkka ja.
Ëtt baa ngi ne selew. Fi ma ferenklaayu ci
basaη gi, sama xel dellu na ci sa maam ju
jigéen, ndem-si-Yàlla ji Ndàmbaaw, sama
soxna su yaarame sa, ma ñaanal ko. | DOOMI-GOLO-Ebook-1.pdf |
End of preview. Expand
in Data Studio
README.md exists but content is empty.
- Downloads last month
- 58