french
stringlengths
4
937
wolof
stringlengths
4
946
Je l'ai donné à quelqu'un de meilleur que lui.
May naa ka keneen ku ka gën.
Les jeux, les discussions et les menus travaux alternaient sans emploi du temps précis : ils ramassaient le bois mort et les bouses séchées pour le feu en se promenant, ils allaient puiser l'eau pendant des heures devant les puits en bavardant, ils jouaient au trictrac dans la terre, ou bien ils restaient assis devant l'entrée de la maison de mon père, à regarder dans le vague, à attendre pour rien.
Moonte loolu taxul ñu mën ni yoon wi ñépp daan jaar luñ rëddoon la ci suuf si, mu jub xocc. Déedéet. Dañ daan wure, di werante, di ay-ayloo itam ay liggéey yu ndaw. Rooti, taxan, mbaa for ndéef daawuleen teree wéy di waxtaan. Léeg-léeg tamit dañ daan toog lu yàgg ci sunu buntu-kër mel ni ñuy xaar dara te fekk xaaruñu tus.
Le long d'une aire dénudée et sèche, des pans de murs rouge sombre, aux crêtes noircies par l'incendie, tels les remparts d'une ancienne citadelle. De loin en loin, le long des murs, se dressaient des tours dont les sommets paraissaient becquetés d'oiseaux, déchiquetés, brûlés par la foudre.
Ay miir yu xonq te lëndëm a toppoon ab bayaal bu mag. Seen cat yaa nga lakk, ñuul, ni tata yu njëkk ya.
Quand la guerre éclate, il sait qu'elle va mettre à nouveau l'Europe à feu et à sang, comme en 1914.
Lenn wóor na ko : xare bii topp ci bu atum 1914, dina metti lool moom tamit, deret ju bare dina ci tuuru ci réewi Tugal yi.
Comment allez-vous ?
Na ngeen def ?
Tu as vu celui-là lequel ?
Gis ŋga kookuu kan ?
C'était ainsi.
Noonu la woon.
Chez celui qu'il a indiqué.
Ci ki mu wax.
Les photos que mon père a aimé prendre, ce sont celles qui montrent l'intérieur du continent, la force inouïe des rapides que sa pirogue doit remonter, halée sur des rondins, à côté des marches de pierre où l'eau cascade, avec sur chaque rive les murs sombres de la forêt.
Li ëpp ci nataal yi Baay jël, dañuy wone xolub jéeri ji ak tamit doole ginnax yi, doole ju kenn àttanul. Nga gis ni leen gaal giy songe, ak ni ndox miy balle ci eskale xeer yi, àll bi wër ko, lëndëm këruus.
Quand un homme regarde jour après jour changer la lumière sur le visage de la femme qu'il aime, qu'il guette chaque éclat furtif dans le regard de son enfant.
Nit ki, dinga dund ba bés bu Yàlla sàkk nga gis ni sa xar-kanamu soxna di soppikoo, walla ngay yeeru saa su gàtt a gàtt si ab ferñent di tàkk ci say bëti doom.
Aucune jeune fille ne s'est égarée.
Ndaw senn réerul.
C'est le lion qui a mangé entièrement celui-là
Gaynde gee lekk moomu mépp
C'est là qu'il va passer les années les plus heureuses de sa vie.
Mbégte ma Baay yëg foofu, dund na ba dee yëgaatu ko feneen.
Quelque chose m'a été donné, quelque chose m'a été repris.
Am na lees ma mayoon ba noppi nangu ko.
Toi que voilà, tu n'as pas été
Yaa ŋgi demuloo
Tout le jour le soleil a brûlé leur corps, ils sont pleins d'une force électrique incomparable.
Bëccëg googu yépp, naaj wi lakk na seen yaram, may ko doole ju kenn xamul nu mu tollu.
J'ai vu cet homme qui parlait !
Gis naa googii gan gi doon wax !
Ces enfants que voilà ne sont pas sages.
Xale yule yaruwuñu.
L'Afrique, c'était le corps plutôt que le visage.
Su ma nee Afrig, jëmmu doom-aadama moo may tax a wax. Du benn yoon bu sama xel di dem ci xar-kanam gi.
L'homme est là, il ne vint pas
Góor gaa ŋgi dikkul
La femme et l'homme sont de haute taille.
Jigéen ji ag góor gi ñjool lañu.
Mon père était l'unique médecin dans un rayon de soixante kilomètres.
Baay doŋŋ a doon fajkat fa nu dëkkoon.
C'est un bûcheron.
Aw lawbe la.
Mon père m'a raconté un jour comment il avait décidé de partir au bout du monde, quand il a eu terminé ses études de médecine à l'hôpital Saint Joseph d'Elephant & Castle, à Londres. Étant boursier du gouvernement, il devait effectuer un travail pour la communauté.
Baay mas na maa nettali naka la xéye bés laxas, wuti dëkk bu soree-sori. Ginnaaw gornmaa bee ko jàppale woon ba muy jàng ca benn loppitaanu Londar, dafa waroon a delloo askanu Àngalteer njukkal, liggéeyal ko ab diir.
Cherche autre chose !
Wutël leneen !
Me voilà parti.
Ma ŋgii dem.
Pendant plus de quinze ans, ce pays sera le sien.
Lu mat fukki at ak juróom ak lu topp, réew moomu doŋŋ ay réewam.
Mon père et ma mère sont couchés dans leur lit de sangles, sous la moustiquaire, ils écoutent battre les tambours, selon un rythme continu qui tressaille à peine, comme un cœur qui s'emballe.
Sama yaay ak Baay a nga jaaxaan ca seen néeg bu tuuti ba ni ngunug-ginaar, sànke bi muur leen. Ñu ngi dégg ni sabar yi teeyee, mel ni xolu doom-aadama bu ànd ak dal.
J'y suis avec, pas à pas.
Maangi ci kowam, ndanka, ndanka.
Alors qu'il sera en train de partir
Su dee dem
Prends celui-là en entier !
Fabal benn boobu bépp !
Cette Afrique-là existait déjà avant la guerre, sans aucun doute.
Loolu, leer na ci xelu ñépp. Leer nàññ sax, la def. Laata geer biy kalaate, noonu la Afrig meloon.
Mon père aurait pu l'aplatir d'un coup de sa fameuse savate.
Baay manoon na koo nappaaje ak dàllam, na mu ko tàmme woon def.
Les enfants sont arrivés, j'espère ?
Mbaa xale yi yeksi nañu ?
Moi-même je n'ai pas été
Man mii demuma
S'il part
Su dee dem
En l'affublant de lorgnons, je justifiais mon sentiment. Mon père, mon vrai père pouvait-il porter des lorgnons ?
Ngir gën a gëmloo loolu sama bopp, ma daldi ko takkal lonet yu woroo ak i lonetam.
Nous sommes des hommes !
Nit lañu !
Et surtout l'abandon de l'Afrique à ses vieux démons, paludisme, dysenterie, famine.
Ak lii, di li gën a xëtt xolu Baay : ni ñuy seetaanee sibbiru si, biiru-taññ ak bekkoor di wéy di ŋacc meenu Afrig.
Viens pour Moussa, lamane de ce pays !
Ñëwël ndax Musaa lamaanu réew mi !
Ils y restent une ou deux nuits, parfois une semaine. L'eau à boire est acide et violacée de permanganate, on se lave au ruisseau, on cuisine sur un feu de brindilles à l'entrée de la hutte.
Kër yu ni mel, dinañ fa fanaan benn walla ñaari guddi, léeg-léeg ñu toog fa lu mat ayu-bés, di naan ndox mu wex ba noppi permanganaat bi nganjal ko. Dinañuy faral di sangu ci dex gu ndaw gi, di dajale ñax mu wow, teg ci seen cin taal reer mbaa añ.
Peut-être qu'en fin de compte mon rêve ancien ne me trompait pas.
Su may xoolaat ni yëf yi deme, dama naan ndekete sama gént gu yàgg ga du woon janeer doŋŋ, amoon na fu mu wéeru.
Ceux-ci ne sont peut-être pas partis !
Ñii dañu demul xanaa !
Il est parti ce matin.
Dem na ca subë.
S'exiler habiter l'exil toute une vie
Gàddaay rekk dëkke gàddaay
S'exiler pour réaliser les rêves de ta mère
Gàddaay dëggal sa géntu yaay
Cela vous plongeait dans un autre monde, vous emportait vers une autre vie. Cela vous exilait au moment de la guerre, vous faisait perdre votre femme et vos enfants, vous rendait, d'une certaine façon, inéluctablement étranger.
Mu jaral ko lu ne nag, ba ci gàddaay dem fu sori, xare bi kalaate mu bàyyi njabootam Tugal, dëkk béréb bu mu xamul kenn, kenn xamu ko fa, saa yu rombee nit kooku naan ci xelam : « Moo, doxandéem bii, lan la fiy def ? »
Appelle celui-là qui ne part pas
Wool kee dul dem
Mon père est arrivé en Afrique en 1928, après deux années passées en Guyane anglaise comme médecin itinérant sur les fleuves.
Ci atum 1928 la Baay jëkk a teg tànk Afrig. Fekk na booba mu def ñaari at ci Guwiyaan bi ci moomeelu Àngalteer.
Cherche l'autre.
Seetal beneen bi.
Où est le Monsieur ?
Ana góor gi ?
Je travaille encore à ce jour.
Ba tey maa ngi liggéey.
Mes amis !
Samay xarit !
Je ne peux pas dire ni même penser : admirable, immense, puissance.
Kàddu yu deme ni « yéeme », « yaatu » walla « kàttan », mënu ñoo génne sama gémmiñ. Xajuñu sax ci sama biir bopp.
C'est des enfants qui jouent avec leurs jouets. Les enfants sont entrain de jouer avec leurs jouets. C'est des enfants qui jouent.
Xale yuy fo la, yor seeni fowukaay. Xale yi dañuy fo, yor seeni fowukaay. Ay xale yuy fo la.
J'ai été dans une maison spacieuse !
Dem naa ci kër gu yaa !
Sur la photo que vous m'avez envoyée, j'y ai vu un poisson adulte qu'on a coupé en morceaux et posé quelque part.
Nataal bii ngeen ma yónnee de gis naa ci biir nataal bi jën yu mag, yuñ dagg ay dagg teg ko ci fenn.
Un autre, tu es.
Keneen ŋga.
Chez les Peul, les Sérère, et les Niominka.
Ci Pël yi ag ci Séeréer si, ag ci Ñomiŋka yi.
ces villages d'Afrique anémiés
jëme ko ci dëkki Afrig yu ŋiis yi
On voit sur la photo beaucoup de personnes sorties sur la route, qui ont sortis leurs mains, les uns qui sont assis et lèvent leurs mains et écrivent, sur la photo,'La Casamance', qui veut dire la région de Casamance.
Ñu gis ci nataal bi ay nit ñu bari ñu génn ci tali, ñu yékkati seen i loxo, ñenn ñi sukku yékkati seen loxo, ñu bind ci nataal bi'La Casamance', mooy diiwaanu Kaasamaas.
Ce qu'il eût fait
Li mu defkoon
L'un, dont il fut question, est parti
Kenn ki woon dem na
C'est d'autres chevaux que je veux !
Fas yéenen la bëgg !
C'est peut-être celui-là !
Soo demee kookule la !
Ainsi, l'homme ne veut pas partir
Ba, góor gi bëggul dem
Plus jamais je ne ressentirai ces atroces migraines, plus jamais je ne pourrai donner libre cours aux crises de colère de ma petite enfance.
Ca la samay metiti bopp ya dakke ba fàww, ma bàyyi tamit gaaw a mer.
Où ?
Foofee fan ?
Il ne te parle pas.
Waxu la.
Douala, Lagos, Victoria sont à des années de là.
Sooy méngale diiwaan beek Duwaalaa, Legoos walla Wiktoryaa, day mel ni Yàllaak Yaali.
S'exiler pour s'éloigner de l'acacia
Gàddaay ba mana daw kàdd gi
Nous ne l'eussions pas vu
Giskoonuñu ka
L'homme ne t'a pas vu
Góor gi gisu la
Il est venu hier et aujourd'hui.
Tay ag demb yépp ñëw na.
Comment ?
Naan ?
C'est devant toi.
Cha kanam.
Sur cette photo il y a, semble-t-il, des bancs.
Nataal bii lu mel ni ay bãŋ la.
J'ai vu un lion.
Gis naa gaynde.
L'homme veut partir de temps à autre
Góor gi bëgg na di dem
Qu'as-tu vu ?
Loo gis ?
Cet homme est un Laobe de Saint-Louis.
Gor gii di Lawbe Ndar.
Aide-les à cause de ceux-là !
Dimëlé leen ŋgir ñooñe !
Il m'a vu moi !
Gis na ma man !
Selon la tradition, le roi est nu jusqu'à la ceinture, assis sur son trône, son chasse-mouches à la main.
Ni ko waa Bansoo aadawoo, Buur baa ngi def yaramu neen ba ci ndigg li, toog ci gànguneem, téye uppukaayam.
Ceci est un four. C'est ce qu'on appelle une cuisinière. Le four, on l'allume et cuisine avec. Après avoir l'allumer, tu dois ensuite y poser la marmite et commencer à cuisiner ce que tu veux.
Waaw lii nii ab ab puur la. Waaw moom lañuy wax cuisinière. Ab puur la dañ koy taal di ci togg, boo ko taalee danga ciy teg cin li rekk togg ci li nga bëgg a togg.
L'homme qui avait reçu l'entraînement des médecins en pays lointains – être ambidextre, capable de s'opérer soi-même en se servant d'un miroir ou de recoudre sa hernie.
Rax-ci-dolli, tàggatoon nañ ko ngir mu mën a faj doom-aadama ciy réew yu sore Tugal te seeni aada wute lool ak yu Tugal. Mëne woon na ñaari loxo, mënoon na sax opeere boppam walla su laajee ñaw mu ñaw ko. Te suy def loolu, seetoo koy won yaram wi.
Il est difficile d'en parler aujourd'hui, après tant de catastrophes et d'abandon. Peu d'Européens ont connu ce sentiment.
Lu jafee waxtaane la tey ndax musiba yi ñu fi jot a jànkonteel ak it ni nit ñi bàyyeekoo, rawati-na fii ci Tugal.
J'imagine que, pour beaucoup de femmes en France, cela a dû être difficile, avec un mari prisonnier en Allemagne, ou disparu sans laisser de traces. Sans doute pour cela cette époque terrible m'a-t-elle paru normale. Les hommes n'étaient pas là, il n'y avait autour de moi que des femmes et des gens très âgés.
Jigéen ñu bare, Almaŋ yee jàppoon seen jëkkër tëj ; amoon na it ci boroom-kër yooyu ñu kenn xamul ndax ñu ngi dund ba tey am déet. Ak nu mu mënoon a deme, lii moom wóor na : bi góor ñi demee xareji, ay jigéen ak i màgget ñoo ma wër. Ba tax ak li xare biy metti yépp, yëguma ci dara.
L'homme est allé aux champs.
Góor gi dem na ca tool ya.
C'était une guerre perdue d'avance.
Kenn mënul woon dara ci gunóor yi.
Mon père était indigné. Son commentaire s'étendait à toute l'occupation française dans ce pays, qui empêchait les autochtones d'exercer le moindre travail, fût-ce celui de chauffeur de car, et qui maltraitait les pauvres.
Baay am ci naqar wu réy te nëbbu ci dara, ne fay ŋàññ doxandéem yiy ñëw ci réewu jàmbuur, aakimu lépp, di fa toroxal baadoolo yi, ba doon sófóoru ótó-biis doŋŋ të leen.
Un homme n'a été
Góor demul
Tais-toi !
Dil noppi !
Je vois l'homme.
Gis naa nit ki.
C'est là seulement !
Kooku doŋŋ la !
Si je n'avais pas eu cette connaissance charnelle de l'Afrique, si je n'avais pas reçu cet héritage de ma vie avant ma naissance, que serais-je devenu ?
Waaw, su Afrig duggul woon ba ci samay biir yax, ma xam ko ba jeexal ko, naka la sama àddina deme kon ?
Quelles personnes sont venues ?
Yan nit ñoo ñëw ?
Cet homme dont il était question
Nit kookule woon
Je l'ai lu, non pas sur les rares objets, masques, statuettes, et les quelques meubles qu'il avait rapportés du pays ibo et des Grass Fields du Cameroun.
Jàngewuma ko ci mask yeek estati yu ndaw yi mu jële woon dëkku Ibo yaak réewi Kamerun ya Àngale yi doon woowe Garaas Fiild.
Donne le travail à un autre !
Joxal kenn liggéey bi !