french
stringlengths
4
937
wolof
stringlengths
4
946
L'homme partira
Góor gi dana dem
Ahidjo, lui, a écrit régulièrement à mon père en France pendant des années.
Lu mat ay at, Ayijook Baay bindante nañu.
Aminata peut-elle venir ?
Aminta ñëw ?
Les vaccins sont en quantité très limitée, pour combattre les épidémies.
Ñakk yiy aar askan wépp ci jàngoro yiy wàlle, néew naňu lool ñoom itam.
Ceci est une tasse qui contient du lait. C'est une tasse blanche, posée, contenant du lait.
Lii ab kaas la mi ngi def am soow. Ab kaas bu weex la bu def am soow ñu taaj ko.
Le maître souhaiterait avoir donné toute sa fortune pour pouvoir demander aujourd'hui l'aumône.
Sërin bi bëgg na mayewoon alalam ji ba mënkoon yalwaan tay.
C'est toi qui n'a pas été
Yaa demulwoon
Je donne à qui ?
Ma may ñan ?
Venez !
Kaayleen !
Fais sortir tout mouton que tu vois !
Génnéel mépp xar moo gis !
Qui a été ?
Ku dem ?
Où vas-tu ?
Fo jëm ?
Le rayonnement s'échapperait d'un composant en plomb après que l'avion ait brûlé.
Radiyasioŋ bi dafa di genn ci benn yëf ci plomb bu roppalaan bi lakkee ba pare.
Élève un mouton !
Yaral xar !
Le monde change, c'est vrai, et celui qui est debout là-bas au milieu de la plaine d'herbes hautes, dans le souffle chaud qui apporte les odeurs de la savane, le bruit aigu de la forêt, sentant sur ses lèvres l'humidité du ciel et des nuages, celui-là est si loin de moi qu'aucune histoire, aucun voyage ne me permettra de le rejoindre.
Dëgg la, la woon wonni na. Mu tekki ne gone gee may séen muy réer ci biir ñax mi, jant biy raay yaram wi, asamaan siy dajale, gone googu sori na sori gu, samay kàddu walla samay tànk manuñoo fexe ba dab ko.
Il sait déjà qu'il n'aura pas les moyens de s'installer comme médecin privé.
Xamoon na ni àddina du dox ba mu am bés dooley ubbi kilinigu boppam.
Appelle l'homme qui n'est pas un Kangame d'ici !
Wool góor gi dul Kajgaamu fii !
Là, il faisait tout, comme il l'a dit plus tard, de l'accouchement à l'autopsie.
Moo fa daan def lépp, di faj, di rewle, ku faatu yit mu ubbi la seet lu la faat.
Sur cette photo ci que je vois il y a des personnes qu'on a fabriquées avec des arbres, des fleurs et consorts. Ils sont dans un endroit très beau avec des murs les entourant. Des murs peints avec de la peinture jaune.
Nataal bii ma gis de ay nit yun tabax la ak i garab ak i fleur ak yooyu. Ñu nekk fu taaroo taaru am miir bu leen wër miir boo xam ne peinture bu soon lañ ko peinture.
Pouah !
Cam !
Oui le parent, je vois que ceci c'est une théière, une très belle théière. Un outil sur la quelle on prépare ce plaisir là qu'on appelle le café. On y a dessiné deux arbres. On y voit encore, au-dessus, deux arbres et une gazelle.
Waaw mbokk mi lii de gis naa ni baraada la, baraada bu taaru. Jumtukaay bu ñuy defare xéewal googu ñu naan café moom la ñu ngi ci diseene ñaari garab ñu ngi wanewaat ca kaw ñaari garab ak benn kéwël.
Que tu partes ou que tu ne partes pas, il viendra.
Soo demee ag soo demul itam, dana ñëw.
Ce que cet homme a dit
Li waa ji wax
Si je regarde aujourd'hui la seule photo que j'ai conservée de la maison d'Ogoja (un cliché minuscule, le tirage 6 x 6 courant après la guerre), j'ai du mal à croire qu'il s'agit du même lieu : un grand jardin ouvert, où poussent en désordre des palmiers, des flamboyants, traversé par une allée rectiligne où est garée la monumentale Ford V8 de mon père.
Nataalu këru Ogosaa gi ma dese, bu tuutee-tuuti la. Tóokër bu yaatu bi, ndeysaan... Garabi-tiir yeek garabi mbër yi... Yoon wii Baay daan gaare wotoom, W8 bu réy a réy ba. Saa yu ma xoolee bile nataal, fàww ma ni ci sama xel : ndax ci dëgg-dëgg fii laa dëkkoon ? Manumaa nangu ba tey ne benn béréb bi la.
Il y a du mystère et de la sauvagerie, malgré la plage, malgré les palmes.
Géej gaa ngii. Garabi-tiir yaa ngi nii ñoom tamit. Moonte liñ leen di miin yépp, teewul mbir mi mel ni lu kéemaane te raglu.
Il a amené à l'homme un mouton chez lui.
Yobul na góor gi xar kërëm.
Homme de courage n'abonde pas paroles.
Jambaar du bare wax.
Les gens n'étaient pas, habituellement, bavards.
Nit ñi daawuñu coow.
De longues années d'éloignement et de silence, pendant lesquelles il a continué d'exercer son métier de médecin dans l'urgence, sans médicaments, sans matériel, tandis que partout dans le monde les gens s'entre-tuaient – cela devait être plus que difficile, cela devait être insoutenable, désespérant.
Lu yàgg déggu ñu, déggunu ko, muy wéy di liggéey Afrig ci anam yu jafe. Lépp jamp, garab ak jumtukaay nàkk, xare bu metti rëbloo dunyaa, reyante bi ne kurr. Loolu yombutoon a dékku, yaakaar ju tas xajoon na ci.
Quelqu'un est parti !
Nit dem na !
Le rayonnement peut également être contenu pendant un incendie.
Radiyasiyoŋ bi mën nañu ko tamit tëyé su amee lakk.
Tous lesquels as-tu vus ?
Ñépp ñan ŋga gis ?
Espérer, c'est se nourrir d'illusion.
Yaakaar, nax sa bopp doŋŋ la.
Les meubles enfin, non pas ces fameux tabourets et trônes monoxyles d'art nègre.
Ma daaneele xanaa móobalam ya. Soppul woon tabure yeek gàngune yooyu seen toogu yaatu, te ñu taq ci cosaanu nit ku ňuul.
C'est Fatim, si on va au fond des choses !
Faatim la soo demee !
À son retour à la pension, une lettre l'attend, un mot très sec du chef de l'hôpital disant : « Monsieur, je n'ai pas encore reçu votre carte de visite. » Mon père fait donc imprimer les fameuses cartes (j'en ai encore un exemplaire), juste son nom, sans adresse, sans titre. Et il demande son affectation au ministère des Colonies.
Bés, mu dem doxantu ci tàkkal-dex gi ba delsi, fekk këram benn bataaxal. Muy kàddu yu gàtt, te tukkee ci kilifag loppitaan bi : “Góor gi, jotaguma ba tey sab kàrt de wisit.” Laata mu fay dem, Baay móol-lu na, gaa, ab kàrt – maa ngi ceek benn ba tey – wànte turam doŋŋ a ca nekkoon, bindu ci woon fa mu dëkk astemaak li muy liggéey. Ñàkk tegginu direkteer bi merloo ko, mu daldi ñaan ci saa si ñu yóbbu ko feneen.
C'est un cimetière vaste comme un pays.
Mu mel ni ñu ngi dox ci biiriy armeel.
Si tu pars, il vient.
Soo demée, mu ñëw.
J'ai vu ce visiteur qui parlait !
Gis naa googii gan gi doon wax !
Un enfant est mort sur les cinq.
Ci juroom xale yi benn a ci dee.
Je parle de ceux-là !
Xar yenn yooyu laa wax !
Par bouffées cela me submerge et m'étourdit.
At ya ma fa dund ngiy wéy di ma dugg, di ma mëdd ak a miirloo.
Tu parles de quels gens ?
Nit ñan ŋga wax ?
Dites-leur
Nileen leen
Mes voeux de tabaski
Mangui lay ndokkel ci tabaski bi
Cette photo montre certainement une sorte de douche qui est très large. À l'intérieur de la douche il y a des outils que tu peux te servir après avoir fini.
Waaw nataal bii mi ngi wane ab ab wanag lii ab wanag la, wanag bu yànji sax. Ci biir wanag bi nag am nay am na jëfandikaay yoo xam ne ngir boo jëfandikoo ba pare man nga koo jël daal.
Était-ce un jeu ? Nous nous sentions pleins de puissance. Je m'en souviens aujourd'hui, non pas comme d'un divertissement sadique de sale gosse – la cruauté gratuite que des petits garçons peuvent aimer exercer contre une forme de vie sans défense, couper les pattes des doryphores, écraser les crapauds dans l'angle d'une porte –, mais d'une sorte de possession, que nous inspiraient l'étendue de la savane, la proximité de la forêt, la fureur du ciel et des orages.
Ndax mbir mi po kese la woon ? Danoo yëgoon sunu doole, yaakaar ni dara warunu woon a të, rawati-na noon bu nuy dëkk te mënunu koo teg bët. Fo kese ? Ay doomi-tubaab yu xamadi di rajaxe lépp, ni ñenn ñiy dagge tànkiy gunóor walla tanc mbott ci ginnaaw bunt ? Mukk ci àddina. Liñ doon def weesu woon na loolu lépp. Danoo tegoon sunu bopp ñaari ponkal yu am doole, sëppu dunyaa ni nooy boroom. Te ci sama gis-gis, liñ taxoon a ràkkaaju du woon dara lu dul càkkeef gi nu wëroon, màndiŋ mi yaatu ba mel ni amul àpp, ngëlén yeek asamaan si xund, di gëdd ak a xultu.
Du reste la générosité est une bonne chose dans la vie.
Te dey addina laabiir dafa ci baax.
Le soin qu'il apportait chaque matin à faire son marché de très bonne heure, en compagnie des travailleurs maghrébins, qu'il rencontrait également au commissariat de police, chaque fois qu'il faisait renouveler sa carte de séjour.
Na muy dugge màrse sax, tegtal ci li may wax nii. Du ko caaxaane, moom. Bés bu Yàlla sàkk, ci suba teel, mu ànd ak i daan-dooley naar jubal ja ba. Miinanteek naak ñoom bu baax, ndax li ñuy faral a daje pólis saa yuy yeesaliy kayitam.
Mais entre !
Dugghal waay !
Les Africains ont coutume de dire que les humains ne naissent pas du jour où ils sortent du ventre de leur mère, mais du lieu et de l'instant où ils sont conçus.
Ci gisu-gisu doomiy Afrig, du bés bi nit ki juddoo la ganesi àddina. Ñoom, dañu jàpp ni bés bi ay way-juram jotee am solo.
La légende d'Aro Chuku et de sa pierre aux sacrifices humains continue d'agir sur les esprits.
Kenn fàttewul Aro Suku, ak xeer wa mu daan ñàddee nit ñiy rendi.
Sur cette photo ci, il y a des pierres qui sont rassemblées. Cependant, les pierres ont des trous à l'intérieur ainsi que des pointes. Elles semblent de couleur marron.
Waaw nataal bi de, ay xeer la yoo xam ni dañ dajaloo. Xeer yi nag Daf am am ay pax-pax ci biir, am ay cat-cat. Dafa xaw a marõ.
J'imagine son exaltation à l'arrivée à Victoria, après vingt jours de voyage.
Baay def na ñaar-fukki fan ci gaal gi, jëm Wiktoryaa.
Tel était l'homme que j'ai rencontré en 1948, à la fin de sa vie africaine. Je ne l'ai pas reconnu, pas compris.
Nit ki ma dajeel ci atum 1948, fekk muy door a jóge Afrig, xawma ko moom ci boppam. Xawma sax wan xeetu nit la.
Ce trésor est toujours vivant au fond de moi, il ne peut pas être extirpé.
Nataali démb ya àgg fu sore ci man, ni fa tekk, ni dootuñu fa jóge.
La bombe avait été désactivée par le pilote.
Gindikay bi feyyoona fètt bi.
C'est l'homme qui part, je crois !
Góor gi dem la, ma defe !
Je me souvenais de l'éclat sur la terre rouge, le soleil qui fissurait les routes, la course pieds nus à travers la savane jusqu'aux forteresses des termitières, la montée de l'orage le soir, les nuits bruyantes, criantes, notre chatte qui faisait l'amour avec les tigrillos sur le toit de tôle, la torpeur qui suivait la fièvre, à l'aube, dans le froid qui entrait sous le rideau de la moustiquaire. Toute cette chaleur, cette brûlure, ce frisson.
May fàttaliku nag ray-rayu suuf su xonq si. Tali yi jant bi xarat. Ni nu daan rawantee tànki neen, di xuus ci àll bi, dem ba jub tatay max yi. Te ngoon su ne, ngëlén li dellusi, guddi yi xumb be, fo tollu di dégg i yuux ak sunu muus mu jigéen miy jooteek siiru yi ci kow kër gi. Ak itam sibbiru. Mu daaneel la, nga ni mbàppaaral, su njël jotee ngelaw li yëkkati sanke bi, sedd bi ne cabax ci néeg bi, fekksi la fi nga tëdd, dugg ba ci sa biir yax.
Comment t'appelles-tu ?
Naka-nga sant ?
Vous voilà là à l'intérieur !
Yéena ŋgoogule foofu ci biir !
Vous acceptez ou il ne part pas !
Daŋgeen di naŋgu mbaa du dem !
Le long des routes, au bord des rivières, à l'entrée des villages, des centaines de milliers d'enfants sont en train de mourir de faim et de déshydratation.
Fu waay geestu, say bët daj téeméeri junniy gone yu wow koŋŋ, niróotuñu sax nit.
Le mouton en entier.
Xar mi mépp.
Attache tout mouton !
Yeewal mépp xar !
Je lui ai dit de rentrer.
Wax naa ko mu ñibbi.
Le chef est retraité de l'US Air Force.
Njiit mi retraitee US Air Force la.
Tu as regardé dans cette chambre-ci ?
Seet ŋga néeg buu ?
Puis ils s'endorment à l'aube, dans le souffle froid du matin qui fait onduler le rideau de la moustiquaire, enlacés, sans plus entendre le rythme fatigué des derniers tam-tams.
Suñ fa jógee, sonn, ne yàcc, nelaw ba fajar. Su ngelawu njël lu sedd liy raay sànke bi, dina fekk ku ci nekk a ngi kott moroom mi, fekk it riiri sabar yiy dakk ndànk-ndànk.
L'homme t'eût vu
Góor gi giskoon na la
Vous partez
Dem ŋgeen
Je ne parle pas de ces enfants ?
Waxuma yooyale xale ?
Où sont les membres de ta famille ?
Ana waa kër gi ?
Elle avait révélé en lui la rigueur.
Afrig dafa dekkali woon doŋŋ njub ga masoon a nekk ci moom.
Que tu partes, c'est ce que désire l'homme.
Ŋga dem la, góor gi bëgg.
Sur cette photo se trouvent deux présidents. Ici, c'est en France. Il s'agît des présidents Macky Sall et Macron. Ils sont là, marchant sur un tapis rouge. Il y a des voitures qui sont derrière eux. Il y a des personnes debout à leur coté portant ce qui semble être des fil électriques ; ce sont des policiers. Macky Sall et Macron, chacun d'eux porte des habits et des chaussures noirs <unk>.
Nataal bii de ñaari président la. Fii nag France la mu di président Maki Sàll ak Macron ñi ngi noon di dox ci affaire bu rouge bi. Am na oto yu topp seen gannaaw. Am na ñu taxaw seen wet yor lu mel ni ay fiil ay policier lañ. Maki Sàll ak Macron ku nekk sol yére bu ñuul ak dàll yu ñuul kostin.
Ceux-là, cependant, sont des cases. Celle qui est en haut est conçue d'une très belle manière. L'autre aussi est conçue en prenant une charge et l'entourant autour et en lui fournissant une porte.
Waaw lii nag ay néegi ñax la, néegi ñax bi ci kaw dañ kaa defar ko bam taaru lool. Bi ci des tamit ñu defar ko jël ab sars wërale ko ci kaw wutal kob buntu.
La vieille, elle, ne parla plus !
Jigéen ji, moom waxatul !
Sois avec politesse !
Àndal ak yar !
Mais ce que cela aurait changé en l'homme qu'il était, qui aurait mené une vie plus conforme, moins solitaire. De soigner des enrhumés et des constipés, plutôt que des lépreux, des impaludés ou des victimes d'encéphalite léthargique. D'apprendre à échanger, non sur le mode exceptionnel, par gestes, par interprète, ou dans cette langue élémentaire qu'était le pidgin English (rien à voir avec le créole de Maurice raffiné et spirituel), mais dans la vie de tous les jours, avec ces gens pleins d'une banalité qui vous rend proche, qui vous intègre à une ville, à un quartier, à une communauté.
Coppite gi may njort doon na àgg ba ci waxinam ak ni muy jokkook ñeneen ñi. Làpptoo ko naroon a jàppale, xam naa, walla muy làkk « pijinu » àngale – bi jotewul daraak kerewolu dunu Móris bu sell ba te yiw. Ci gàttal, benn kàddu mën naa tënk li may bëgg wax, te mooy : maasaloo. Su Baay toogoon Tugal, du xéy ba dégg lu mu masul a dégg. Te it képp ku mu faj, dina jàpp ne mook moom benn lañu, bokk waaso. Maasaloo. Walla sax seey ?
Tous les autres moutons fuirent.
Yeneen xar yi yépp daw.
Quand pars-tu ?
Kañ ñgay dem ?
Sans doute verser des larmes.
Walla xéy-na léeg-léeg nga làqu fomp rangooñ.
marchandent le prix de leur avenir bradé
a ngi waxaale seen àdduna si nu wanteer
Avoir été, eût été bon !
Dem, rafetoon na !
J'y suis avec, petit à petit.
Maangi ci kowam, ndanka, ndanka.
Ceci est une maison, une maison endommagée. En le voyant tu sauras qu'elle est vieille ainsi que ses lampes et ses fenêtres.
Lii ag kër la, kër gu yàqu. Boo ko gisee xam ni dafa màgget ak làmpam yeek palanteer am yi.