french
stringlengths
4
937
wolof
stringlengths
4
946
Oui ceci est comme je te l'avais dit seulement. C'est du riz au poisson posé sur un plat blanc. Une sorte de patte de tamarin est mise au-dessus. Oui si tu regardes le riz, il y a une cuillère noire qui <unk> dessus de la patte de tamarin.
Waaw lii de comme ni ma la ko waxe woon rekk, ceebu jën la, ñu teg ko ci palaat bu weex, teg lu mel ni ay ñambaan, daldi koy teg ci kow. Waaw boo xoolee ceeb bi, am na benn kuddu bu ñuul bu koy cubb, bu cubb ñambaan ci kow.
Ma mère n'a pas vécu là-bas (elle est née à Milly), mais elle en a toujours entendu parler par son père, cela fait partie de son passé, pour elle cela a le goût d'un rêve inaccessible et familier (car, en ce temps-là, Maurice est si loin qu'on ne peut qu'en rêver).
Sama yaay mi juddoo Mili, newu fa woon booba wànte yàgg naa dégg baayam daan ko waxtaane. Muy boog lu bokk ci cosaanam, daldi soppiku béréb bu xelam sàkk, béréb bu boole lëndëm ak leer, jege ak sori. Ndax, ca jamono jooju, Móris sore na sore gu, ci gént rekk la ko mënoon a feeñu.
S'il veut qu'il entre !
Na dugg su bëggée ci biir !
Oui, un peu
Wau, degg naa tuuti Wolof
Je te souhaites de récupérer tôt
Tanéel ak jáam
Sur cette photo, c'est <unk> dans laquelle on garde des tasses et consorts. On l'a conçue avec du bois et du verre de manière méthodique.
Nataal bii lii ab àngal la boo xam ne dañ ciy deñci ay kaas ak yu ni deme. Ñu defare dénk ak weer defar bu mucc ayib.
Ceux-là, il ne les apprécie pas !
Yooyale deey bëggu leen !
Je n'ai aucune idée de ce qu'il faut faire avec seulement les totaux, veuillez me donner plus de détails pour comprendre ce gâchis.
Xawma dara ci li ma wara def ak lim yi rek, war ngeen ma jox ay detaay yu gëna bare ngir ma xam yàq bii.
J'ai aperçu une femme.
Séen naa as jigéen.
Les hauts plateaux où avance lentement le troupeau de bêtes à cornes de lune à accrocher les nuages, entre Lassim et Ngonzin.
Diggante Lasim ak Ngonsin, sama xel dajeek géttug nag yuy daagu ak seeni béjjén yu bindoo ni xaaju weer, di lonk niir yi.
Si ce paysage le requiert, s'il fait battre mon cœur aussi, c'est qu'il pourrait être à Maurice, à la baie du Tamarin, par exemple, ou bien au cap Malheureux, où mon père allait parfois en excursion dans son enfance.
Muy baat ba ñuy jëfandikoo ca Móris. Loolu biral ni saa yu bët yiy doxantu ci gàncaxu Afrig, gàncaxu Móris day ñëw tegu ci kowam.
Si tu es homme
Soo dee góor
Personne n'est donc parti ?
Xand kenn demul ?
Terre d'Afrique flouée dès l'aube
Suufus Afrig si nu war ca njalbéen
Quelques jours plus tard, il s'embarque à destination de Georgetown, en Guyane.
Ñu teg ciy fan, mu dugg gaal, teeri Sorstaawun, ca Guwiyaan.
Toute la chambre
Néeg bépp
J'essaie de le faire, évidemment.
Maa ngi koy jeema def, waaw.
J'ai aperçu un baobab.
Séen naa am guy.
Tu ne bavardais pas, généralement.
Daawuloo woon coow.
Il n'a pas encore pris de contacts
Giséegul
C'est grâce à lui que mon père a pu trouver ses repères dans le pays, être accepté de tous (y compris des sorciers dont il était le concurrent direct), exercer son métier.
Su Baay demee ba fépp fu mu teg tànkam xam na mooy fan, Yàllaak góor googoo tax. Jibar yi sax, nga xam ni mënoon na leen a yàqal seen liggéey, wegoon nañu Baay. Niñ ko yaatale woon noonu, Ayijoo dara la ci woon.
Tu connaissais la jeune fille ?
Xamoon ŋga jaŋx ba ?
Il parle de vous ?
Yéen ñan la wax ?
Cet homme-ci, devant nous, et cet homme-là ne sont pas les mêmes.
Waa jii ag waa joojale duñu benn.
Bonne nuit.
Fanaanal jaam.
Ils vont de campement en campement, dans des villages dont mon père note les noms sur sa carte : Nikom, Babungo, Nji Nikom, Luakom Ndye, Ngi, Obukun.
Daňu daan jóge dalukaay bii, dal ca ba ca des, dëkk buñ dem Baay daldi dugal tur wa ci déndam : Nikom, Babungo, Njii-Nikom, Luwaakom Ndiyee, Ngii, Òbukun.
C'est peut-être Fatim !
Soo demee, Faatim la !
Les scorpions qui vivaient sous le tapis étaient généralement petits, noirs, probablement inoffensifs.
Ay jiit yu tuuti lañu woon te ñuul, mu leer nu ne amuñu daŋar.
C'est toi qui avais l'habitude d'aller
Yaa daan dem
Nous avions dû commencer par jeter quelques pierres, pour sonder, pour écouter le bruit caverneux qu'elles faisaient en heurtant les termitières.
Liñ daan njëkk a def mooy sànniy xeer ngir seet ndax am na luy yëngu ci biir jànj bi.
Sois poli !
Àndal ak yar !
Il a vu d'autres amis à vous !
Gis na seen yeneen xarit !
La chose est d'un blanc éclatant.
Lëf ki weex na tàll.
Ainsi elle accompagne mon père dans ses tournées médicales, avec la suite des porteurs et l'interprète, à travers les montagnes de l'Ouest.
Mook Baay ñu ànd di wër dëkki tangor yi féete sowu-jant, fu ne ñu dem fa ngir faj képp ku feebar, làppto beek yenukat yi topp seen ginnaaw.
Il fait une spécialité de médecine tropicale.
Fàww xelam gën a màcc ci pajum feebari réewi Afrig yi.
Malheureusement, nul n'a été
Waaye, kenn demul
Nous étions venus d'un appartement au sixième étage d'un immeuble bourgeois, entouré d'un jardinet où les enfants n'avaient pas le droit de jouer, pour vivre en Afrique équatoriale, au bord d'une rivière boueuse, encerclés par la forêt.
Dëkk fa ci taaxu-kow bu ñàkk solo, sa baay tere la génn foweek say moroom, àddina faf sàppi la... Waaye bés, Afrig ubbil lay loxoom ni la kaay, yàgg naa laa xaar. Nga sanc ci peggu dex gu baree-bari poto-poto, li ko wër lépp dib àll bu xonq coyy.
C'est toi qui aimes la jeune femme
Yaw la ndaw si sopp
La savane, l'orage qui s'accumulait chaque après-midi, la brûlure du soleil sur nos têtes, et cette expression trop forte, presque caricaturale de la nature animale, c'est cela qui emplissait nos petites poitrines et nous lançait contre la muraille des termites, ces noirs châteaux hérissés contre le ciel.
Wànte tamit, lépp a nu daan soppi. Muy àll bi, di ngëlén yi, di asamaan si daan dajale saa yu tàkkusaan jotaan, loolu lépp a daan feesal sunuy dënni gone, daan nu xiir ci song jànj yeek xube yu ñuul ya ni woon jadd, jëm ca kow a kow.
Nous voilà assis
Ñu ŋgi toog
Nous voulions sauver une chose plus que le reste.
Deñoo bëgg sàmm lenn lu ëpp lu ci des.
Samba, toi, tu as été
Samba, yaw, yaa dem
Il se trouve que l'homme est de ces gens qui...
Góor gi doon na di nit koo xam ni...
Tu parles de quel mouton ?
Xar menn man ŋga wax ?
C'est moi qui dois partir !
Maa di dem !
Nous courions presque sans nous arrêter, à perdre haleine, dans les hautes herbes qui fouettaient nos visages à hauteur des yeux, guidés par les fûts des grands arbres.
Danu daan réer ci biir ñax mi, muy caw sunuy xar-kanam, nuy daw bay xiiqët. Su dul woon garab yi nuy séen, dunu xamati sax fan lanu nekk.
J'ai vu ceux-là.
Gis naa ñooñale woon.
Je n'aurais pas été
Demkoonuma
Il est « excessivement » courageux !
Jambaar la ba mu ëpp !
Cet homme près de moi.
Nit kii ci sama wet.
Sans doute est-ce mêlé de légende, de rêve.
Ñàkkul gént ak janeer rax ci mbir mi.
Il lui a amené du fourrage au champ.
Yobul na ka ŋgoon ca tool ya.
Tu es un autre.
Keneen ŋga.
Voyager demain
Tukki ëlëk
Est-ce que le pays a des richesses ?
Ndax réew mi am na alal ?
Puis il avait imaginé s'installer aux Bahamas, acheter un lopin à Eleuthera et y construire une sorte de campement.
Dem na sax ba xel mi nekk ci jëndi suuf Baxamaas, ci béréb buñ naan Elëteraa, samp fa xeetu berkelleem.
Tous ceux-là, dont il fut question, ne sont pas partis
Ñooñu ñépp woon demuñu
Est-ce que ?
Ndax
Sois l'homme de la situation !
Dil nitu nit ñi !
Ceci est une chambre couverte d'herbe. En le couvrant d'herbe, la chambre est une sorte de chambre. La chambre est couverte d'herbe, des arbres en haut, des arbres en bas. Il y a beaucoup d'arbres tout de même.
Lii ab néeg la, néeg bi dañ kaa xadde ñax. Biñ ka xaddee ñax, néeg bi ab néeg la, néeg bi ñu xadde ko ñax ay garab nekk ca kaw ay garab nekk ci suuf. Bari nay garab lool nag sax.
Poussent des légumes verts
Lejum yu nëtëx a nga fay meňň
C'est peut-être un lion !
Gaynde la, ku dem !
Ce fut un homme !
Nit lawoon !
Tous ceux-là doivent partir !
Ñooñu, ñépp dañuy dem !
Quand ma mère raconte cela, elle dit que ce qui l'a d'abord alarmée, c'est le silence, partout, alentour, dans la forêt, et les chuchotements des porteurs.
Saa yu sama yaay daan nettali xew-xewi guddi googu, fàww mu yéemuwaat ca tekk-tekkaaral ga. Su weesoo yenukat yi doon ŋun-ŋuni, benn kàddu jibul. Loolu biral ni lu réy a ngi woon ci yoon wiy ñëw.
Les embruns apportés par le vent recouvrent les arbres de la forêt, se mêlent à la vapeur des marécages et de la rivière.
Puuriti ginnax yaa ngi muur garabi àll bi, jaxasook saxaar siy bawoo ci ban beek dex gi.
La chose est d'un noir obscur.
Lëf ki ñuul na kukk.
Seul l'homme n'est pas venu.
Góor gi rekk a ñëwul.
Sur le travail, jusqu'à ce qu'il soit fait !
Liggéey bii, ba mu sotti !
Il est mort l'année où le sida a fait son apparition.
At mi mu faatoo la sidaa njëkkee feeň.
Je pense que mes grands-parents et ma mère ont été si effrayés que, lorsque nous avons consenti à revenir, ils ont oublié de nous punir.
Yaakaar naa ne samay maam ak sama yaay daňoo tiit keroog ba fàtte noo duma.
Tu as regardé dans cette chambre-ci ?
Seet ŋga buu néeg ?
La mémoire des instants de bonheur, lorsque mon père et ma mère sont unis par l'amour qu'ils croient éternel. Alors ils allaient dans la liberté des chemins, et les noms de lieux sont entrés en moi comme des noms de famille, Bali, Nkom, Bamenda, Banso, Nkongsamba, Revi, Kwaja.
Nettali askan wi seen bànneex, nag, di li ëpp solo ci mbir mi : ñoom ñaar, tollu ci seen diggu doole, nobante ba nga ni lii lu mu doon, mu wóor leen ni seen bànneex boobu amul gàpp, yooni Kamerun yi yaatal leen, dalal leen ci xol bu sedd guyy. Man ma dese ci ay turi dëkk, ñu may gunge, ma leen di jaawale sax ak samay santi mbokk yu ma jege. Baali, Nkom, Bamendaa, Bansoo, Nkoŋsàmbaa, Reewii, Kawaajaa.
Que la paix soit avec toi aussi.
Maaleekum salaam
Tu n'as pas été, non plus
Wante itam, demuloo
L'homme avait été
Góor gi demoon na
Oui ceci, cependant, il s'agit d'un policier qui porte une arme, ayant attaché son bassin et poursuivant ce jeune qui court.
Waaw lii nag ab alkaati bu yor ngànnaayam, takk ndiggam di dàq ndaw sii di dem.
J'ai vu à l'intérieur de la photo des ustensiles de cuisines blancs posées sur des tables en bois. Des ustensiles en bois et une plante à coté.
Nataal bii gis naa ci biir nataal bi ay toogukaay yu weex yu nekk ak ay taabalu dénk, ay toogukaay yoo xam ne dénk lañ ko liggéeye benn gàñcax ci wet gi.
S'exiler à la recherche d'un pays
Gàddaay baaxoo wërum réew
S'il avait été
Su demoon
Malheureusement, les enfants ne veulent pas
Waaye nag, xale yi bëggunu
Ceci, cependant, on a l'habitude de faire les courses avec. C'est-à-dire que quand les femmes vont au marché, c'est ça qu'il emporte avec elles. On l'appelle en français'panier'. On le porte et y met des marchandises comme le poisson, aubergine, chou pommé, citrouille... C'est à peu près ça qu'on met dedans en tout cas.
Lii nag dañ ciy faral di def ndugg maanaam jigéen ñi bu ñuy dem ja marse ba ëe, moom lañuy yor. Ñu koy woowe ci farañse pañe.. Dañu koy gàddu nag. Buñ ko gàddoo dañu ciy def lu mel niki ay ndugg daal lu mel ne jën, batañse,suppome, naaje... Yooyu daal lañuy def ci biir.
Les patients sont dans les dortoirs, couchés sur de vrais lits en métal aux draps empesés et très blancs, ils souffrent probablement autant de l'angoisse que de leurs affections.
Ñi tawat a ngi tëdd ciy lali weñ yu darab yi dëll te weex tàll.
Le tout s'est renversé.
Lépp tuuru na.
Va leur chercher une barque !
Wutëli leen gaal !
C'est ce qu'il a dit qui est vrai !
Li mu waxoon la !
Des boeufs que tu vois dans cette ville, celui le plus gros appartient à ton père Alfa.
Nagi dëkk bii ŋga gis, wa ci ëpp sa baay Alfa moo ka moom.
La réunion ce n'est pas après-demain ?
Ndaje mi du gannaaw ëlëk ?
Ramona me jugeait silencieusement.
Ramona dafa doon ma atte te waxul dara.
Non, ils vont bien.
Déedéet, defuñu dara.
C'est une autre épouse que je veux !
Jeneen jabar laa bëgg !
Il n'a rien dit à cause de l'homme.
Waxul ndax góor gi.
Mon grand-père maternel, lui, avait reçu dans sa jeunesse mauricienne des principes plus stricts, mais son grand âge, l'amour qu'il portait à ma grand-mère, et cette sorte de distance ennuyée propre aux gros fumeurs l'isolaient dans un réduit où il s'enfermait à clef pour, justement, y fumer en paix son caporal.
Sama maam ju góor, li mu yaroo Dunub Móris taxoon na koo bañ caaxaan waaye màggat la woon, amoon cofeel ci soxnaam te mel ni ku àddina sàppi. Lenn rekk a ko soxaloon : kimmi sigaretam « kaporaal ». Da daan faral a tëju sax ci benn pukkuus, jàpp njàmburam di tóx.
Tu vas vers qui ?
Ci ñan ŋga jëm ?
C'est un homme âgé de par ses années.
Mag la ndax iy atam.
L'endroit, où l'homme est parti, est beau.
Foofu, góor gi dem, fu rafet la.
Aucun mouton n'est arrivé.
Menn xar ñëwul.
Je me souviens de la violence en Afrique. Non pas une violence secrète, hypocrite, terrorisante comme celle que connaissent tous les enfants qui naissent au milieu d'une guerre – se cacher pour sortir, épier les Allemands en capote grise en train de voler les pneus de la voiture de ma grand-mère, entendre dans un rêve remâcher les histoires de trafic, espionnage, mots voilés, messages qui venaient de mon père par le canal de Mr Ogilvy, consul des États-Unis, et surtout la faim, le manque de tout, la rumeur des cousines de ma grand-mère se nourrissant d'épluchures.
Sama xel dellu ci Afrig, am kàddu gu riir ci sama biir kaaŋ. Kàddu googu di « Kàttan ». Mbaa « Doole » ? Benn la rekk. Li wóor ba wóor moo di safaanoo na lool ak xeetu njàqare yi ma daan seetlu jamono ja ma newee gone te làrme bu Almaañ tegoon loxo ci Frãs, Almaŋ yi yóbbu fitu ñépp, lu leen neex ñu def, di jaay doole dëggëntaan. Booba, kenn du dox ci mbedd mi te sa xel newul ci ñoom. Almaŋ ya ma bett bés ak seeni mànto yu dóomu-taal, ñuy wekki sama ruuwu woto maam ju jigéen... Yemul foofu, de. Te li may waxsi, gépp gone gu màgg ci fitnay xare xam na ko. Mooy ni nit ñiy soppikoo, doon i naaféq, ku nekk ni patt ndax ragal a wax lu ëpp. Ku mel ni ndawul Amerig ca Ogosaa, te tuddoon Ogilwi, daan nay faral a déeyanteek Baay, di ko àgge ay xibaar yu mu warul woon a dégg ci yoon. Kersa dina ma teree sulli yenn yi, muy ndóol gu metti gi taxoon, ci boog liñ doon ruumandaat, samay doomi-bàjjen daan añe xollitu banaana mbaa sorãs, di ko reere.
En Afrique, l'impudeur des corps était magnifique.
Ca Afrig, ňàkk kersag yaram yi lu yéemoon na ma lool.
Ils étaient gras, d'un brun rougeâtre, très luisants. Ils volaient lourdement.
Ay mbóot yu duuf sax, ba noppi tikk ba mel ni lu xonq, di nes-nesi, xaw a tëlee naaw.