french
stringlengths
4
937
wolof
stringlengths
4
946
L'enfant dit d'entrer !
Xale bi ne ŋgeen dugg !
C'est moi qui vais partir
Maay dem
Quels moutons qui t'appartiennent ?
Xar yooyu yan ŋga moom ?
Nous étions seulement deux enfants qui avaient traversé l'enfermement de cinq années de guerre, élevés dans un environnement de femmes, dans un mélange de crainte et de ruse, où le seul éclat était la voix de ma grand-mère maudissant les « Boches ».
Maak sama mag, àddinaa ñu tooñoon. Juróomi at yi Tugal di xare yépp, danoo lëlu. Nu yaroo ci biir jigéen ñi, dëkke moytu. Ñépp a ragaloon a wax ca kow ba mu des sama maam ju jigéen ma daan móolu saa su nekkAlmaŋ yi.
À Ogoja, les insectes étaient partout.
Xeetu gunóor wu waay mën a xalaat a nga woon Ogosaa.
« J'ai été » ne nous suffit pas
Dem naa doyunu
Donc, tu ne partiras pas ?
Xanaa doo dem ?
Les marchands continuent de transporter le sel, la laine, le bois, les matières premières.
Ñoom ñu ngay wéy di yab ci seeni kamyoŋ xorom ak kawari xar ak bant ak yu ni mel.
L'homme est parti
Gor gi dem na
Il ne t'avait pas remis la taxe
Joxu la woon juuti bi
À l'intérieur de cette maison
Ci biir kër googule
Ma mère parle des fêtes qui éclatent soudain, dans les villages, comme à Babungo, en pays nkom, à quatre jours de marche de Banso.
Mas naa dégg sama yaay muy yéemu ci liñ daan jékkee-jékki rekk dëkk bépp ràkkaaju. Babungoo ko doon tax a wax, keroog. Soo jógee Bansoo, dinga dox ñeenti fan soog a yegg Babungoo, ca réewum nkom ya.
L'individu respire avec son nez.
Waa ji day noyyee ak bakkan.
Le territoire qu'il a en charge est immense.
Gox bi mu yilif nag, yaatu na lool.
Les gens n'eussent pas été des maîtres.
Nit ñi doonkoonuñu ay kaaŋ.
Certaines personnes ne sont pas encore arrivées.
Nit ñenn ñi yegseeguñu.
Là-bas où ?
Foofee fan ?
J'avais reconnu cette dame-là !
Xammeewoon naa jigéen joojale !
À l'intérieur : où il fait clair
Ci bir : foofu di leer
De cet autre qu'on appelle.
Keneen kookule muy woo.
J'ai vu celui-là, auparavant.
Gis naa kooku woon.
C'est quelqu'un de bien !
Nit ku baax la !
Dans la maison dont parle le Monsieur
Ci kër gi waa ji wax
C'est ces moutons que tu avais achetés ?
Xar yii yan ŋga jënd ?
Autres, ils sont.
Ñeñeen lañu.
Elle donnait du champ, de la profondeur, elle multipliait les sensations, elle tendait un réseau humain autour de moi.
Daan na yaatal, di xóotal, tey yokk yëg-yëg.
J'ai vu l'ovin mâle.
Gis naa xar mu góor ma.
Ils ont été quelqu'un !
Nit lañu !
Je parle de la personne qui est sortie !
Nit kookuu génn laa wax !
Le lion n'a pas fui, pourtant.
Gaynde gi dawul, moontin.
où femmes et hommes même couchés
jigeen ňaak góor ňa donte dañu tëdd
Voilà qu'il est parti
Ma ngii dem
Sur ma photo qu'on m'a envoyée, il y a apparemment une chaise, sur laquelle on s'assoit. Mais, elle est clairement de couleur bleue.
Sama nataal bii ñu ma yónnee dafa mel ni ab sées la, sées yi ñuy tooge. Waaye nag couleur bi moom dafa bula couleur bu bula la.
C'est une autre maison que je veux !
Beneen néeg laa bëgg !
Tu as vu quels amis à toi ?
Gis ŋga sa yan xarit ?
À la chute d'Aba (non loin de l'ancien sanctuaire des guerriers magiciens d'Aro Chuku), le Biafra entre dans une longue agonie.
Àbbaa daanu. Àbbaa, sorewul xàmbi Aro Suku ya. Biyaafaraa tàmbalee sukkuraat, sukkuraat ju metti te yàgg.
J'ai donné le livre à l'homme qui est venu.
Jox naa téere bi góor gi ñëw.
Une grand-mère avec ses contes, un grand-père avec sa voix chantante de Mauricien, des camarades de jeu, de classe, tout cela s'était glacé tels des jouets qu'on enferme dans une malle, telles les peurs qu'on laisse au fond des placards.
Xanaa léeg-léeg rekk nuy janeer, di déggaat sama baatu maam ju jigéen ak i léebam. Am nay bés it, sama maam ju góor a may ganeseek baatam bu neex ba, baatu doomu réewum Móris. Su weesoo ñaar ñoonu, samay maas xanaa, ña ma doon àndal di dem lekool mbaa di fo. Waaye loolu lépp dafa mujjee dee, mel niy fowukaay yu ñu tëj ci waxande, fàtte leen fa ba ñu pënde. Ak it mbóoti njaboot gi, li kenn ñemewul a tudd.
Je ne vous eusse pas vus
Giskóonuma leen
Comment t'appelles-tu ?
Noo tudd ?
Afin que parte ?
Ndax kan dem ?
Il avait cru qu'il n'en partirait pas.
Masul a toog ba xalaat ni dina fa jógeji bés.
L'homme, il n'est pas parti ?
Gor gi dafa demul ?
La femme et l'homme non plus ne désirent s'entendre
Ndaw si ak waa ji itam dañu bëggul déggoo
Là-bas jusqu'à ce que vous reveniez !
Ci foofu ba ŋgeen dellusi !
L'homme qu'il a amené
Góor gi mu àndi
C'est ici, dans ce décor, que j'ai vécu les moments de ma vie sauvage, libre, presque dangereuse.
Fii laa dunde dundug njaay-àll, moom sama bopp ba léeg-léeg sax mu mënoon maa gaañ.
Lorsque, à la suite d'une mauvaise grippe, il est hospitalisé brièvement pour une transfusion sanguine, j'obtiens avec difficulté que le résultat des examens lui soit transmis.
Bés, sibbiru su metti daaneel ko, ñu war koo sol deret. Ma laaj waa loppitaan bi ay kayitam.
Dans l'est du Nigeria, la sorcellerie est secrète, elle s'exerce au moyen des poisons, des amulettes cachées, des signes destinés à porter malheur.
Penkub Niseryaa, xonjom dafa fa muuroo lëndëm, raglu te itam ñoxor-njaay ñu posone la nga dee.
S'il est parti
Su demee
L'homme a frappé la vache avec un bâton.
Nit ki dóor na nag wi ak bant.
Venez en paix
Agsileen ak jaam
Comment vas-tu ?
Na nga def ?
Mais cet homme est parti
Gor gii dem
Il m'a vu !
Gis na ma !
Alors, l'homme se fâcha.
Foofu, góor gi mer.
Va le voir !
Seeti ka !
Sauf pour deux brefs congés, il ne reviendra plus en Europe jusqu'à la fin de sa vie active.
Ba ni muy demee alaateret, ñaari yoon la delsi Tugal.
Que la personne sorte ?
Ndax waa ji génn ?
Dites-lui
Nileen ka
Où est-ce que tu vas ?
Ana foo jëm ?
Tu es quel étudiant ?
Ya di ban jaŋgkat ?
Le voyage en Afrique met fin à tout cela.
Gàddaay jëm Afrig a dakkal loolu lépp.
Il est là ?
Mi ŋgi fii ?
Le clair-obscur d'un tableau du siècle
Maraxum nataalu xarnu bi
Nous n'avons rien connu de ce qui a pu fabriquer l'identité un peu caricaturale des enfants élevés aux « colonies ».
Waaye dunu woon liy bindkat yu siiw tudde ay « doomi-tubaabi-Afrig », di leen kókkali.
Afin que qui parte ?
Ndax kan dem ?
Comment vont les gens de la maison ?
Naka waa kër ga ?
Je n'ai pas besoin de faire de grands efforts d'imagination pour voir surgir à nouveau, chaque nuit, les armées de cafards – les cancrelats, comme les appelait mon grand-père, sujets d'une sirandane : kankarla, nabit napas kilot, il porte un habit, mais n'a pas de culotte.
Guddi gu Yàlla sàkk, naaxi mbóot laa daan gis ci kër gi. Ca Tugal, sama maam ju góor a nga leen daan woowe'kànkarlaa', di dem ba ciy jukkiy cax, di woy ci kàllaama kerewol kànkarla, nabit nàppaa kilot, « mbóot sol na yére waaye teewu koo def taatu neen ».
J'ai été chez un autre qui est gentil.
Dem naa ci keneen ku baax.
Ceux-ci sont de vieilles cases à l'intérieur desquelles des personnes marchent. Ceux qui ont froid, ils la couvrent avec une façade, des bâtons et des arbres.
Lii ay néegu ñax la, néegu ñax yu màggat ay nit di ci dox ci biir. Am na yi nga xam ne si nii dañ liiwe ay sàkket dañ ko muure ay sàkket ak ay bant ak ay garab.
À l'intérieur si tu ne veux pas !
Ci biir soo bëggul !
Je parle de ces autres individus !
Nit ñenn ñooñii laa wax !
Ce n'est pas là une belle parole !
Jile wax rafetul !
J'ai aperçu des choses.
Séen naa ay yëf.
Je crois que ce n'est pas celui-ci, ce n'est pas celui-là
Defe naa du kookuu, du kookee
Les premiers temps, je m'écorchais sur le ciment du sol en courant – je ne sais pourquoi, c'était toujours le gros orteil du pied droit dont la peau s'arrachait.
Ca njëlbéen ga, dalu simoŋ bi dafa ma daan gaañ. Xawma lu tax, sama benn baaraamu tànk kott la der bi daan xolleeku, te muy baaraamu ndey-joor bu mag bi.
Tu as vu quoi ?
Gis ŋga lan ?
Lesquels ne sont pas venus ?
Ñu dikkul ?
Quel mouton ?
Xar mii man ?
Il n'était pas payé pour le travail qu'il faisait. Sans doute y gagnait-il du prestige, du crédit : il était l'homme de confiance du toubib.
Daawuñu ko fey fiftin bi gën a tuuti ci liggéey boobu mu daan def, wànte da doon yokk darajaam, ñu koy xoole bëti doktoor bi wóolu.
Je veux un peu d'argent de toi
Bëgg naa tuuti xaalis ci yaw
Où est l'homme dont il parle ?
Ana góor gi mu wax ?
Tout cet endroit-là ?
Foofule fépp ?
Ce matin ou ce soir c'est moi qui suis ici !
Maa fiy nekk tày ci ŋgoon, tày ci suba !
Une colonne, plutôt un fleuve épais, qui avance lentement, sans s'arrêter, sans se soucier des obstacles, droit devant, chaque fourmi soudée à l'autre, dévorant, brisant tout sur son passage.
Li ma tudde naax, daanaka dexu mellentaan la woon. Yàkkamtiwuñu, de. Ñu ngay dox ndànk, du dara lu leen mën a tee wéy di dem. Bu ci nekk a ngi sës ca moroom ma, ñu topp seen yoon rekk, gumba, tëx. Ñu ngay ŋeeñ it, lu ñu romb rajaxewaale ko.
Vers celui que voilà, vers celui-ci, vers celui-là
Ci kii, ci kuu, ci kee
Au Calabar, au Cameroun, l'ennemi n'est plus Aro Chuku et son oracle, ni les armées des Foulanis et leurs longues carabines venues d'Arabie.
Ësen noon ko it ca Kalabaar, ci Kamerun, ay noonam duñ dooni Soko Uru ak i xërëmam mbaa soldaari Pël yeek seeni fetal yu gudd. Déedéet.
Fais sortir tout cheval que tu vois !
Génnéel wépp fas woo gis !
L'homme le voici, il est Saint-Louisien.
Góor gaa ŋgi, nitu Ndar la.
Je veux que tu viennes le matin à cinq heures dans la fraîcheur !
Bëgg naa ci juróomi waxtu, ci subë, ŋga ñëw !
S'exiler pour fuir les feux de brousse
Gàddaay ba nekk fu amul daay
J'ai vu l'homme qui est venu !
Gis naa góor gi ñëw !
Appelle l'homme qui ne part pas
Wool góor gi dul dem
C'est un autre qui est venu ?
Keneen la ku yeksi ?
Ce n'est qu'à la fin de la guerre qu'il pourra revoir sa femme et faire la connaissance de ses enfants au cours d'une brève visite dont je ne garde aucun souvenir.
Ci ginnaaw gi la door a gisaat jabar ji, xaw a miinal boppam doom yi. Ngan gu gàtt googu, dara laa ci fàttalikuwul.
J'ai vu celui en question.
Gis naa ki woon.
L'homme te voyait
Góor gi daan na la gis
Il n'est de Ardo du Dieri que tu ne connaisses !
Amul benn ardow Jéeri boo xamul !
Ce n'est pas un homme.
Du góor.