sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
2
93
{ "fr": "Et rappelez-vous, lorsque Nous avons pris l´engagement de vous, et brandi sur vous At-Tur (le Mont Sinaï) en vous disant : \"Tenez ferme à ce que Nous vous avons donné, et écoutez ! \". Ils dirent : \"Nous avons écouté et désobéi\". Dans leur impiété, leurs coeurs étaient passionnément épris du Veau (objet de leur culte). Dis[-leur]: \"Quelles mauvaises prescriptions ordonnées par votre foi, si vous êtes croyants\" .", "wo": "[Fàttalikuleen], ba Nu wólleranteek yéen, te Nu yékkati doj wa mu tiim leen, [Ma ne leen] : “Jàppleen te farlu ci la Ma leen jox te ngeen dégg [ndigal] !” . Ñu ne : “Dégg nanu te bañ nanu” . Nàndaleef na leen seeni xol sëll wa ngir seenug weddi. Neel : “Bon na li leen seen ngëm digal ci loolu ndegam gëm ngeen” ." }
2
94
{ "fr": "- Dis : \"Si l´Ultime demeure auprès d´Allah est pour vous seuls, à l´exclusion des autres gens, souhaitez donc la mort [immédiate] si vous êtes véridiques ! \"", "wo": "- Waxal ne : “Ndegam am ngeen kërug àllaaxira ca Yàlla, gu yéen doŋŋ jagoo waliis nit ñi, mébétleen dee kon ndegam ñu dëggu ngeen !”" }
2
95
{ "fr": "Or, ils ne le souhaiteront jamais, sachant tout le mal qu´ils ont perpétré de leurs mains. Et Allah connaît bien les injustes.", "wo": "Duñu ko mébét mukk ngir la seen yoxo ya jëf [ci lu bon]. Yàlla ku xam la way-tooñ ña." }
2
96
{ "fr": "Et certes tu les trouveras les plus attachés à la vie [d´ici-bas], pire en cela que les Associateurs . Tel d´entre eux aimerait vivre mille ans. Mais une pareille longévité ne le sauvera pas du châtiment ! Et Allah voit bien leurs actions.", "wo": "Wóor na ne danga leen fekk ñoom [Yahuud ya] ñu nekk di ñu gën a xér ci nit ñi ci bëgg dundu, ak ci ñiy bokkaale. [Danga ca gis] ca ñoom ku ne siiw ñu guddal fanam junniy at. Waaye du ko soreel mbugal ma! Dundu gu guddu googu Yàllaa ngi ne jàkk ci li ñuy def. " }
2
97
{ "fr": "Dis : \"Quiconque est ennemi de Gabriel doit connaître que c´est lui qui, avec la permission d´Allah, a fait descendre sur ton cœur cette révélation qui déclare véridiques les messages antérieurs et qui sert aux croyants de guide et d´heureuse annonce\".", "wo": "Neel : “Ku noonu Jibriil it moom moo wàcce Alxuraan ci sa xol ci ndigalu Yàlla, muy dëggal la ko jiitu, mu di ag njub ak mbégte ci way- gëm ñi” ." }
2
98
{ "fr": "[Dis : ] \"Quiconque est ennemi d´Allah, de Ses anges, de Ses messagers, de Gabriel et de Michaël... [Allah sera son ennemi] car Allah est l´ennemi des infidèles\".", "wo": "[Neel : ] “Ku weddi Yàlla ba noonu ko ak i Malaakaam ak i Yonentam ak Jibriil ak Miikaayil... Yàlla it di ab noonam rekk” ." }
2
99
{ "fr": "Et très certainement Nous avons fait descendre vers toi des signes évidents. Et seuls les pervers n´y croient pas.", "wo": "Bir na ne, wàcce Nanu ci yaw ay kàddu yu leer nàññ, yu kenn du ko weddi ku dul ab saay- saay." }
2
100
{ "fr": "Faudrait-il chaque fois qu´ils concluent un pacte, qu´une partie d´entre eux le dénonce ? C´est que plutôt la plupart d´entre eux ne sont pas croyants.", "wo": "Moo ndax saa su ñu kóllaranteek [Yàlla] ab dëel, kurél ci ñoom firi ko? Li wér mooy li ëpp ci ñoom gëmuñu." }
2
101
{ "fr": "Et quand leur vint d´Allah un messager confirmant ce qu´il y avait déjà avec eux, certains à qui le Livre avait été donné, jetèrent derrière leur dos le Livre d´Allah comme s´ils ne savaient pas !", "wo": "Ba leen Yonent bu jóge ca Yàlla dikkalee di dëggal la ñu yor, gaa ya ñu joxoon ab Téere, ab kurél ca ñoom sànni Téereb Yàlla bi ca seen ginnaaw mel ni dañoo xamul !(s)" }
2
102
{ "fr": "Et ils suivirent ce que les diables racontent contre le règne de Solayman. Alors que Solayman n´a jamais été mécréant mais bien les diables : ils enseignent aux gens la magie ainsi que ce qui est descendu aux deux anges Harout et Marout, à Babylone; mais ceux-ci n´enseignaient rien à personne, qu´ils n´aient dit d´abord : \"Nous ne sommes rien qu´une tentation : ne soit pas mécréant\"; ils apprennent auprès d´eux ce qui sème la désunion entre l´homme et son épouse. Or ils ne sont capables de nuire à personne qu´avec la permission d´Allah. Et les gens apprennent ce qui leur nuit et ne leur est pas profitable. Et ils savent, très certainement, que celui qui acquiert [ce pouvoir] n´aura aucune part dans l´au-delà. Certes, quelle détestable marchandise pour laquelle ils ont vendu leurs âmes ! Si seulement ils savaient !", "wo": "Ñu topp nag la séytaane ya doon jàng ca nguurug Suleymaan. Weddiwul de, séytaane ya ñoo weddi : Daan nañu jàngal nit ña ag njibar ak la ñu wàcce woon ca ñaari Malaaka ya ca (Baabil) (Haaruut ak Maaruut); te daawuñu jàngal kenn te waxuñu ko ne : “Nun dey danoo ànd ak sànje : kon book bul weddi de” ; mu am ñu jàng ci ñoom loo xam ne mën nañu caa téqale jëkkër ak jabaram. Te daawuñu mën a lor kenn ca njibar googule, lu dul ci coobare Yàlla. Te it jàng nañu loo xam ne daf leen di lor te mënuleeen a jariñ. Xam nañu xéll ne ku jënde loolu [weccee ko ak waxi Yàlla] du am benn cër ca àllaaxira. La ñu jaaye seen bakkan bon na ! Cëy bu ñu xamoon !" }
2
103
{ "fr": "Et s´ils croyaient et vivaient en piété, une récompense de la part d´Allah serait certes meilleure. Si seulement ils savaient !", "wo": "Bu fekkoon ne ñoom dañuy gëm, te ragal Yàlla [kon mu gën ci ñoom fuuf]. Cëy bu ñu xamoon !" }
2
104
{ "fr": "ô vous qui croyez ! Ne dites pas : \"Raina\" (favorise-nous) mais dites : \"Onzurna\" (regarde-nous); et écoutez ! Un châtiment douloureux sera pour les infidèles.", "wo": "Éy yéen way-gëm yi ! Buleen di wax [sàmmoonteel ak nun], deeleen wax : “Xool nu” ; te deeleen dégg [ndigal] ! Mbugal mu metti mooy dal ca kaw way-weddi ña." }
2
105
{ "fr": "Ni les mécréants parmi les gens du Livre , ni les Associateurs n´aiment qu´on fasse descendre sur vous un bienfait de la part de votre Seigneur, alors qu´Allah réserve à qui Il veut sa Miséricorde. Et c´est Allah le Détenteur de l´abondante grâce.", "wo": "Ña weddi ca ñoñ-téere ya ak way-bokkaale ya yéenewuñuleen, yiw wu bari ba bawoo ca seen Boroom, wàcc ci yéen, te Yàlla dana jagale yërmaandeem ku ko soob. Yàlla mooy boroom ngëneel yu màgg yi." }
2
106
{ "fr": "Si Nous abrogeons un verset quelconque ou que Nous le fassions oublier, Nous en apportons un meilleur, ou un semblable. Ne sais-tu pas qu´Allah est Omnipotent ?", "wo": "Dunu folli jenn laaya walla Nu ginnaawal ko fàtteloo ko [nit ñi], te indiwunu bu ko gën mbaa mel ni moom. Xanaa xamoo ne Yàlla mën na lu ne ?(n) " }
2
107
{ "fr": "Ne sais-tu pas qu´à Allah, appartient le royaume des cieux et de la terre, et qu´en dehors d´Allah vous n´avez ni protecteur ni secoureur ?", "wo": "Xanaa xamuloo ne Yàlla moo di Boroom nguurug asamaan ak suuf si, te ginnaaw Yàlla amul keneen ku mën a doon seen kiiraay mbaa seen ndimbal ?" }
2
108
{ "fr": "Voudriez-vous interroger votre Messager comme auparavant on interrogea Moïse ? Quiconque substitue la mécréance à la foi s´égare certes du droit chemin .", "wo": "Am dangeen bëgg a laaj seen Yonent na ñu laajee woon Muusaa ca bu njëkk ? Képp ku weccee ngëm ak weddi, réer na te wàcc na yoon wu njub wa." }
2
109
{ "fr": "Nombre de gens du Livre aimeraient par jalousie de leur part, pouvoir vous rendre mécréants après que vous ayez cru. Et après que la vérité s´est manifestée à eux ? Pardonnez et oubliez jusqu´à ce qu´Allah fasse venir Son commandement. Allah est très certainement Omnipotent !", "wo": "Ñu bari ci ñoñ-téere [Yahuud ak Nasaraan] nee nañu siiw ñu delloo leen cig kéefar ginnaaw seen ngëm ngir kiñaan gu sosoo seeni bakkan. Ginnaaw ba dëgg ga leeree nàññ ? Baal-leen te dummóoyuleen ba Yàlla agseek ndigëlam. Yàlla nag mën na lu ne !" }
2
110
{ "fr": "Et accomplissez la Salat et acquittez la Zakat. Et tout ce que vous avancez de bien pour vous-mêmes, vous le retrouverez auprès d´Allah, car Allah voit parfaitement ce que vous faites.", "wo": "Deeleen taxawee julli te di génne asaka. Lu ngeen jiital ci lu baax ngir seen bopp, dangeen ko fekk ca Yàlla, ndax Yàlla gu gis la li ngeen di def." }
2
111
{ "fr": "Et ils ont dit : \"Nul n´entrera au Paradis que Juifs ou Chrétiens\". Voilà leurs chimères. - Dis : \"Donnez votre preuve, si vous êtes véridiques\".", "wo": "Wax nañu ne : “Kenn du dugg Àjjana ku dul ku nekk (Yahuud walla Nasaraan)” . Loolu dey seen mébét la ñoom. - Neel : “Indileen seenu lay, ndegam ñu dëggu ngeen” ." }
2
112
{ "fr": "Non, mais quiconque soumet à Allah son être tout en faisant le bien, aura sa rétribution auprès de son Seigneur. Pour eux, nulle crainte, et ils ne seront point attristés .", "wo": "Axakañ! ku wommatu ci topp Yàlla te muy rafetal, [topp, ci jëfe ndigal ak bàyyi yi Yàlla tere] kooku peyam ma nga ca Boroomam. [Ña mel ni ñoom] duñu tiit duñu jàq." }
2
113
{ "fr": "Et les Juifs disent : \"Les Chrétiens ne tiennent sur rien\"; et les Chrétiens disent : \"Les Juifs ne tiennent sur rien\", alors qu´ils lisent le Livre ! De même ceux qui ne savent rien tiennent un langage semblable au leur. Eh bien, Allah jugera sur ce quoi ils s´opposent, au Jour de la Résurrection.", "wo": "Yahuud yi wax nañu ne : “Nasraan yi nekkuñu ci dara” ; Nasraan yi itam ne : “Yahuud yi nekkuñu ci dara” , te ñoom jàng nañu Téere ba ! Noonu la ña xamul di waxe. Yàlla dana àtte seen diggante ca la ñu juuyoo bu Bis-pénc baa." }
2
114
{ "fr": "Qui est plus injuste que celui qui empêche que dans les mosquées d´Allah, on mentionne Son Nom, et qui s´efforce à les détruire ? De tels gens ne devraient y entrer qu´apeurés. Pour eux, ignominie ici-bas, et dans l´au-delà un énorme châtiment.", "wo": "Ana ku gën a tooñ kuy tere, ca jàkkay Yàlla ja, ku cay tuddu Turam te di fexe luy yàq jàkka ja ? Ñooña waruñoo dugg ca [jàkka ja] te ànduñook am tiit. Am nañu gàcce gu rëy ci àddina, te it danañu am mbugal mu rëy ca àllaaxira.(s)" }
2
115
{ "fr": "A Allah seul appartiennent l´Est et l´Ouest. Où que vous vous tourniez, la Face (direction) d´Allah est donc là, car Allah a la grâce immense; Il est Omniscient.", "wo": "Te Yàllaa moom Penku bi ak Sowu bi. Fu ngeen fi mën a jublu, Kanamu Yàlla jublu na fa, Yàlla ku xam la ; Ku Yaatu la." }
2
116
{ "fr": "Et ils ont dit : \"Allah s´est donné un fils\" ! Gloire à Lui ! Non ! mais c´est à Lui qu´appartient ce qui est dans les cieux et la terre et c´est à Lui que tous obéissent.", "wo": "Wax nañu ne : “Yàlla am na doom” ! Tudd naa ag sellam[Soreel ko lu yellul ci moom] ! Li fi nekk moo di, Moom Yàlla moo moom lépp lu nekk ci asamaan yi ak suuf si te lépp ci jaamu ko la nekk." }
2
117
{ "fr": "Il est le Créateur des cieux et de la terre à partir du néant ! Lorsqu´Il décide une chose, Il dit seulement : \"Sois\", et elle est aussitôt.", "wo": "Mooy Aji-sos asamaan yi ak suuf si ! Bu dogalee mbir du def lu dul ne ko : “Nekkal” , mu nekk. " }
2
118
{ "fr": "Et ceux qui ne savent pas on dit : \"Pourquoi Allah ne nous parle-t-Il pas [directement], ou pourquoi un signe ne nous vient-il pas\" ? De même, ceux d´avant eux disaient une parole semblable. Leurs coeurs se ressemblent. Nous avons clairement exposé les signes pour des gens qui ont la foi ferme.", "wo": "Ña xamul wax nañu ne : “Lu tee woon Yàlla wax ak nun, walla mu indil nu keemaan” ? Noonu la ña leen jiitu woon waxee woon wax ju mel ni seen jos. Seeni xol niroo na. Leeral Nanu laaya ya ci nit ñoo xam ne wóolu lañu." }
2
119
{ "fr": "Certes, Nous t´avons envoyé avec la vérité, en annonciateur et avertisseur; et on ne te demande pas compte des gens de l´Enfer.", "wo": "Yónni nañu la ci dëgg ngay bégal [ñi gëm ci dig leen Àjjana] ; te di xupp [ñi weddi ci mbugalum Safara] te deesula laaj dara [ëllëg ca àllaaxira loo war a layoo] ci mbiri waa Safara." }
2
120
{ "fr": "Ni les Juifs, ni les Chrétiens ne seront jamais satisfaits de toi, jusqu´à ce que tu suives leur religion. - Dis : \"Certes, c´est la direction d´Allah qui est la vraie direction\". Mais si tu suis leurs passions après ce que tu as reçu de science, tu n´auras contre Allah ni protecteur ni secoureur.", "wo": "Yahuud yi ak Nasaraan yi duñu bég ci yaw mukk li feek toppuloo seen diine. - Neel : “Njubug Yàlla mooy dëggi-dëggi njub” . Boo toppee seen bànneex ginnaawal la Nu la digal, ci xam-xam, doo am kenn ku la mën a sàmm, walla ndimbal ci [mbugalum Yàlla]." }
2
121
{ "fr": "Ceux à qui Nous avons donné le Livre, qui le récitent comme il se doit, ceux-là y croient. Et ceux qui n´y croient pas sont les perdants .", "wo": "Ña nga xam ne jox Nanu leen téere ba [Alxuraan], danañu ko jànge na mu yelle, ñooña ñoo ko gëm. Ña ko weddi ñooy way-ñàkk ña." }
2
122
{ "fr": "ô enfants d´Israël, rappelez-vous Mon bienfait dont Je vous ai comblés et que Je vous ai favorisés par dessus le reste du monde (de leur époque).", "wo": "Yéen Banii-Israayil, fàttalikuleen Sama xéewal yi Ma leen xéewale woon te Man ma defoon leen ngeen gënoon ci kaw mbindéef yépp.." }
2
123
{ "fr": "Et redoutez le jour où nulle âme ne bénéficiera à une autre, où l´on n´acceptera d´elle aucune compensation, et où aucune intercession ne lui sera utile. Et ils ne seront pas secourus.", "wo": "Ragal-leen bis boo xam ne bakkan du fa jariñ dara beneen bakkan te deesu ko nangul njotu, rammu it du ko fa jariñ. Te duñu fa am ndimbal." }
2
124
{ "fr": "[Et rappelle-toi,] quand ton Seigneur eut éprouvé Abraham par certains commandements, et qu´il les eut accomplis, le Seigneur lui dit : \"Je vais faire de toi un exemple à suivre pour les gens\". - \"Et parmi ma descendance\" ? demanda-t-il. - \"Mon engagement, dit Allah, ne s´applique pas aux injustes\".", "wo": "[Fàttalikuleen,] Ibraahiima, ba ko Boroomam nattoo, ciy ndigal, mu matal leen, Mu ne ko : “Def Naa la njiit ci nit ñi” . - Ibraayiima ne ko : “[Defal ko] it samay sët” . Mu ne ko : “Sama kóllare du ma ci boole way-tooñ ña de” ." }
2
125
{ "fr": "[Et rappelle-toi], quand nous fîmes de la Maison un lieu de visite et un asile pour les gens - Adoptez donc pour lieu de prière, ce lieu où Abraham se tint debout - Et Nous confiâmes à Abraham et à Ismaël ceci : \"Purifiez Ma Maison pour ceux qui tournent autour, y font retraite pieuse, s´y inclinent et s´y prosternent .", "wo": "[Fàttalikuleen], ba Nu defee Néeg ba muy delluwaayub nit ñi ak barabub kóolute - Te nangeen def (Màqaama Ibraahiima) barabub jullikaay, - Nu kóllarante ak (Ibraahiima) ak (Ismaahiila) : “Ne leen nangeen sellal Sama Néeg bi ngir ñi koy wër, ak ñi fay toog, di fa rukkoo ak di fa sujjóot [julli]." }
2
126
{ "fr": "Et quand Abraham supplia : \"ô mon Seigneur, fais de cette cité un lieu de sécurité, et fais attribution des fruits à ceux qui parmi ses habitants auront cru en Allah et au Jour dernier\", le Seigneur dit : \"Et quiconque n´y aura pas cru, alors Je lui concéderai une courte jouissance [ici-bas], puis Je le contraindrai au châtiment du Feu [dans l´au-delà]. Et quelle mauvaise destination\" !", "wo": "[Fàttalikuleen] Ba Ibraahiima waxee ne : “Yaw sama Boroom, defal dëkk bii muy dëkkub jàmm [bu am kóolute], te Nga xéewale ciy meññent ñi gëm Yàlla ak Bis-pénc ba, ci waa dëkk bi” , Yàlla ne ko : “Ak ku weddi it danaa ko xéewale ci diir bu gàtt, ba noppi Danaa ko wéyal ci mbugalum Safara. Ndaw delloowaay bu bon” !(r)" }
2
127
{ "fr": "Et quand Abraham et Ismaël élevaient les assises de la Maison : \"ô notre Seigneur, accepte ceci de notre part ! Car c´est Toi l´Audient, l´Omniscient.", "wo": "[Fàttalikuleen] Ba Ibraahiima ak Ismaahiila di yékkati ndéttalu néeg ba (Kaaba ga) : «Yaw sunu Boroom nangul nu, Yaw dey Kuy dégg nga, Kuy xam nga. " }
2
128
{ "fr": "Notre Seigneur ! Fais de nous Tes Soumis , et de notre descendance une communauté soumise à Toi. Et montre nous nos rites et accepte de nous le repentir. Car c´est Toi certes l´Accueillant au repentir, le Miséricordieux.", "wo": "Yaw sunu Boroom ! Def nu nuy ñaari way-wommatu jëm ci yaw. Te nga def ci sunuy sët askan wu wommatu jëm ci Yaw te nga won nu sunu jaamuwaay, boole ca jéggal nu. Yaw dey Boroom bi, Yaa di Jéggalaakoon bi, di Jaglewaakoon bi." }
2
129
{ "fr": "Notre Seigneur ! Envoie l´un des leurs comme messager parmi eux, pour leur réciter Tes versets , leur enseigner le Livre et la Sagesse, et les purifier. Car c´est Toi certes le Puissant, le Sage !", "wo": "Yaw sunu Boroom ! Yónneel ci ñoom Yonent bu bokk ci ñoom, bu leen di jàngal say laaya, di leen xamal Téere ba ak i xereñe, te di leen sellal Yaw Aji-not ji , Aji-xereñ ji!" }
2
130
{ "fr": "Qui donc aura en aversion la religion d´Abraham, sinon celui qui sème son âme dans la sottise ? Car très certainement Nous l´avons choisi en ce monde; et, dans l´au-delà, il est certes du nombre des gens de bien.", "wo": "Ana kan mooy bañ diinay Ibraahiima, ku dul ku kannasu ? Nun dey tànn nanu ko ci àddina ; te moom, bu àllaaxiraa it, mu bokk ca ña gën a yiw." }
2
131
{ "fr": "Quand son Seigneur lui avait dit : \"Soumets-toi\", il dit : \"Je me soumets au Seigneur de l´Univers\".", "wo": "[Fàttalikuleen] Ba ko Boroomam nee : “Wommatul” , Mu ne : “Wommatunaa jëm ci Boroom àddina bi” .(s)" }
2
132
{ "fr": "Et c´est ce que Abraham recommanda à ses fils, de même que Jacob : \"ô mes fils, certes Allah vous a choisi la religion : ne mourrez point, donc , autrement qu´en Soumis\" ! (à Allah) .", "wo": "Ibraahiima dénk na ay doomam solo sa, ak Yanqooba, ne leen: “Yéen samay doom, Yàllaa leen tànnal diine de, buleen dee lu dul na fekk ngeen wommatu jëm ca Yàlla” !." }
2
133
{ "fr": "étiez-vous témoins quand la mort se présenta à Jacob et qu´il dit à ses fils : \"Qu´adorerez-vous après moi\" ? - Ils répondirent : \"Nous adorerons ta divinité et la divinité de tes pères, Abraham, Ismaël et Isaac, Divinité Unique et à laquelle nous sommes Soumis\".", "wo": "walla sax fekkee woon ngeen ba dee ga dikkalee (Janqooba) te mu ne: “Éy samay doom, ana lan ngeen di xala jaamu sama ginnaaw” ? - Ñu ne : “Dananu jaamu Yàlla sa Boroom tey Yàllaay say baay Ibraahiima, Ismaahiila ak Isaaqa, di jenn Yàlla doŋŋ te nun way-wommatu lanu, jëm ci Moom” ." }
2
134
{ "fr": "Voilà une génération bel et bien révolue. A elle ce qu´elle a acquis, et à vous ce que vous avez acquis. On ne vous demandera pas compte de ce qu´ils faisaient.", "wo": "Woowa xeet jàll na, añe jëfam, yéen itam ngeen añe seeni jëf. Te bu Bis baa, du yéen a leen di layal ñoom ca la ñu defoon." }
2
135
{ "fr": "Ils ont dit : \"Soyez Juifs ou Chrétiens, vous serez donc sur la bonne voie\". - Dis : \"Non, mais suivons la religion d´Abraham, le modèle même de la droiture et qui ne fut point parmi les Associateurs\".", "wo": "Ñuy wax naan : “Doonleen Yahuud walla Nasaraan, kon dey ngeen gindiku” . - Neel : “Dée wallaay, diinay Ibraahiima ma wéetaloon Yàlla te bokkut ca way-bokkaale ya” ." }
2
136
{ "fr": "Dites : \"Nous croyons en Allah et en ce qu´on nous a révélé, et en ce qu´on n´a fait descendre vers Abraham et Ismaël et Isaac et Jacob et les Tribus, et en ce qui a été donné à Moïse et à Jésus, et en ce qui a été donné aux prophètes, venant de leur Seigneur : nous ne faisons aucune distinction entre eux. Et à Lui nous sommes Soumis\".", "wo": "Neeleen : “Gëm nanu Yàlla ak li ñu wàcce ci nun [Alxuraan], ak li ñu wàcce woon ca Ibraahiima ak Ismaahiila ak Isaaqa ak Yanqooba ak ca sët ya, ak la ñu joxoon Muusaa ak Iisaa, ya ñu joxoon Yonent ya, mu bawoo ca seen Boroom : dunu xajal kenn ci seen diggante. Te nun way-jébbalu (wommatu) lanu jëm ci Yàlla” ." }
2
137
{ "fr": "Alors, s´ils croient à cela même à quoi vous croyez, ils seront certainement sur la bonne voie. Et s´ils s´en détournent, ils seront certes dans le schisme ! Alors Allah te suffira contre eux. Il est l´Audient, l´Omniscient.", "wo": "Bu ñu gëmee Alxuraan kem ni ngeen ko gëmee, kon gindiku nañu. Ñoom Yahuud yi ak Nasaraan yi, bu ñu dummóoyoo rekk daldi dugg ci féewoo ! Yàlla dana la leen fegal. Moom mi di Aji-dégg, di Aji-xam ji. " }
2
138
{ "fr": "Nous suivons la religion d´Allah ! Et qui est meilleur qu´Allah en Sa religion ? C´est Lui que nous adorons .", "wo": "“Loolu cuubug Yàllaa ! Te ana kan moo gën a rafet Yàlla ag cuub ? Nun dey way-jaamu ko lanu” ." }
2
139
{ "fr": "Dis : \"Discutez-vous avec nous au sujet d´Allah, alors qu´Il est notre Seigneur et le vôtre ? A nous nos actions et à vous les vôtres ! C´est à Lui que nous sommes dévoués.", "wo": "Neel : “Ndax dangeen di dàggasanteek nun ci Yàlla sunu Boroom, di seen Boroom ? Nu moom sunu jëf, ngeen moom seen jëf ! Te nun nag way-sellalal Ko lanuy doon." }
2
140
{ "fr": "Ou dites-vous qu´Abraham, Ismaël, Isaac et Jacob et les tribus étaient Juifs ou Chrétiens ? \" - Dis : \"Est-ce vous les plus savants, ou Allah ? \" - Qui est plus injuste que celui qui cache un témoignage qu´il détient d´Allah ? Et Allah n´est pas inattentif à ce que vous faites.", "wo": "Am dañuy wax ne : Ibraahiima, Ismaahiila ak Isaaqa ak Yanqooba ak sët ya ay Yahuud lañu woon walla Nasaraan ?” - Neeleen : “Ndax yéen a gën xam walla Yàlla ?” - Waay-waay ana kan moo dàq a tooñ kiy nëbb seede sa nekk fa moom te bawoo fa Yàlla ? Te dey Yàlla sàgganeewul li ngeen di jëf de." }
2
141
{ "fr": "Voilà une génération bel et bien révolue. A elle ce qu´elle a acquis, et à vous ce que vous avez acquis. Et on ne vous demandera pas compte de ce qu´ils faisaient.", "wo": "Woowale xeet wéy na di añe jëfam. Yéen itam dangeen añe seeni jëf. Te kenn duleen laaj ana ñoom lañu doon def." }
2
142
{ "fr": "Les faibles d´esprit parmi les gens vont dire : \"Qui les a détournés de la direction (Cibla) vers laquelle ils s´orientaient auparavant ? \" - Dis : \"C´est à Allah qu´appartiennent le Levant et le Couchant. Il guide qui Il veut vers un droit chemin\".", "wo": "Nit ñu kannasu ñi (matadi) danañu wax ne: “Waa ñii, lu leen wëlbati fabe leen ci xible gi ñu daan jublu ?” - Neel : “Yàllaa moom Penku moom Sowu. Mooy gindi ku ko soob jëme ko ca yoon wu jub wa” ." }
2
143
{ "fr": "Et aussi Nous avons fait de vous une communauté de justes pour que vous soyez témoins aux gens, comme le Messager sera témoin à vous. Et Nous n´avions établi la direction (Cibla) vers laquelle tu te tournais que pour savoir qui suit le Messager (Muhammad) et qui s´en retourne sur ses talons. C´était un changement difficile, mais pas pour ceux qu´Allah guide. Et ce n´est pas Allah qui vous fera perdre [la récompense de] votre foi, car Allah, certes est Compatissant et Miséricordieux pour les hommes ", "wo": "Noonu la Nu leen defe [yéen jullit ñi] xeet wu digg-dóomu [di tànneef] ngir ngeen doon seedey nit ñi, Yonent bi itam doon seede ci yéen. Xibla gi nga nekk nag defewunu ko lu dul mën caa xame kay topp Yonent bi ak ka koy dummóoyu. Mu doonoon lu diis, lu dul ci ña nga xam ne Yàlla gindi na leen. Te Yàlla de, sànk seen ngëm taxu koo jóg, ndax moom Yàlla ku ñeewant la, Jaglewaakoon la ci nit ñi." }
2
144
{ "fr": "Certes nous te voyons tourner le visage en tous sens dans le ciel. Nous te faisons donc orienter vers une direction qui te plaît. Tourne donc ton visage vers la Mosquée sacrée. Où que vous soyez, tournez-y vos visages. Certes, ceux à qui le Livre a été donné savent bien que c´est la vérité venue de leur Seigneur. Et Allah n´est pas inattentif à ce qu´ils font ", "wo": "Gis Nanu la ni ngay wëlbatee sa xar-kanam, di téen ci asamaan. Dananu la méngalee jubluwaay boo gëram. Kon jubaleel sa xar- kanam jëmale ko ca Jàkka ju ñu wormaal ja (Al masjidal Haraam). Fu ngeen mën a nekkati, nangeen ko jublu. Te sax, ñañu joxoon Téere ba [Ñoñ-téere] xam nañu xéll ne mooy dëgg gi bawoo ca seen Boroom. Te Yàlla du sàggane li ñuy jëf de." }
2
145
{ "fr": "Certes si tu apportait toutes les preuves à ceux à qui le Livre a été donné, ils ne suivraient pas ta direction (Cibla) ! Et tu ne suivras pas la leur; et entre eux, les uns ne suivent pas la direction des autres. Et si tu suivais leurs passions après ce que tu as reçu de science, tu sera, certes, du nombre des injustes.", "wo": "Boo indiloon, ñoñ-téere, kéemaan gu mu mën a doon, du tax ñu topp sa jubluwaay (xibla) ! Yaw itam du yaay topp seen xibla ; ñoom ci seen biir sax, kenn du ca topp xibla moroomam. Yaw nag boo toppee seeni bànneex ginnaaw ba la xam-xam bu leer dikkalee, kon de ca tooñkat ya ngay bokk." }
2
146
{ "fr": "Ceux à qui nous avons donné le Livre, le reconnaissent comme ils reconnaissent leurs enfants. Or une partie d´entre eux cache la vérité, alors qu´ils la savent !", "wo": "Ña ñu joxoon Téere, xam nañu ko ni ñu xame seeni doon. Dafa fekk ne am na ci ñoom kurél bu xam dëgg ba noppi di ko nëbb !" }
2
147
{ "fr": "La vérité vient de ton Seigneur. Ne sois donc pas de ceux qui doutent.", "wo": "Dëgg, ca sa Boroom la bawoo. Bul bokk mukk ci werentekat yiy sikki-sàkka. " }
2
148
{ "fr": "A chacun une orientation vers laquelle il se tourne. Rivalisez donc dans les bonnes oeuvres. Où que vous soyez, Allah vous ramènera tous vers Lui, car Allah est, certes Omnipotent.", "wo": "Xeet bu nekk a am jublukaayam . Nangeen njëkkante ci jëf yu baax, yu yiw. Fu ngeen fi mën a nekk nag, Yàlla dana leen dajale yéen ñepp ca Bis-pénc ba, Yàlla mën na lu nekk.(s)" }
2
149
{ "fr": "Et d´où que tu sortes, tourne ton visage vers la Mosquée sacrée. Oui voilà bien la vérité venant de ton Seigneur. Et Allah n´est pas inattentif à ce que vous faites.", "wo": "Foo demati, jëmëleel sa kanam ca jàkka juñu wormaal ja ca Màkka. Looloo di dëgg de. Te Yàlla du sàgganee li ngeen di jëf." }
2
150
{ "fr": "Et d´où que tu sortes, tourne ton visage vers la Mosquée sacrée. Et où que vous soyez, tournez-y vos visages, afin que les gens n´aient pas d´argument contre vous, sauf ceux d´entre eux qui sont de vrais injustes. Ne les craignez donc pas; mais craignez-Moi pour que Je parachève Mon bienfait à votre égard, et que vous soyez bien guidés !", "wo": "Foo mën a demati, jëmaleel sa kanam ca Jàkka juñu wormaal ja ca Màkka. Fu ngeen mën a nekk, nangeen ca jëmale seeni kanam [jublu], ndax nit ñi bañ a am aw lay ci seen kaw, ku dul ñiy tooñ. Te buleen leen ragal ; ragal-leen Ma, man Yàlla, ngir Ma mottali sama xéewal ci yéen ak itam ndax ngeen gindiku !" }
2
151
{ "fr": "Ainsi, Nous avons envoyé parmi vous un messager de chez vous qui vous récite Nos versets, vous purifie, vous enseigne le Livre et la Sagesse et vous enseigne ce que vous ne saviez pas.", "wo": "Noonu, Lanu yónnee ci yéen Yonent bu bokk ci yéen buy jàng ci yéen laaya ya, di leen sellal, di leen xamal Téere ba ak Xereñ ga te di leen xamal itam lu ngeen xamul woon." }
2
152
{ "fr": "Souvenez-vous de Moi donc, Je vous récompenserai. Remerciez-Moi et ne soyez pas ingrats envers Moi.", "wo": "Fàttalikuleen Ma, Ma fàttaliku leen. Santleen Ma te buleen ma weddi." }
2
153
{ "fr": "ô les croyants ! Cherchez secours dans l´endurance et la Salat. Car Allah est avec ceux qui sont endurants.", "wo": "Éy yéen ñi gëm [Jullit ñi] ! Nangeen dimbandikoo ci muñ ak julli. Yàlla ànd na ak way- muñ ña." }
2
154
{ "fr": "Et ne dites pas de ceux qui sont tués dans le sentier d´Allah qu´ils sont morts. Au contraire ils sont vivants, mais vous en êtes inconscients.", "wo": "Buleen wax ne ñi ñu rey ci yoonu Yàlla dañuy dee de. Ña ngay dundu te yéguleen ko." }
2
155
{ "fr": "Très certainement, Nous vous éprouverons par un peu de peur, de faim et de diminution de biens, de personnes et de fruits. Et fais la bonne annonce aux endurants,", "wo": "Danaa leen farala nattoo lennat ci am tiit, xiif ak wàññikug ay alal, ak i bakkan ak i meññent. Waaye bégalal ñi koy muñ," }
2
156
{ "fr": "qui disent, quand un malheur les atteint : \"Certes nous sommes à Allah, et c´est à Lui que nous retournerons\".", "wo": "ña nga xam ne, saa su leen tiis dalee dañu naan : “Yàllaa nu moom te ca Moom Yàlla lanuy dellu” ." }
2
157
{ "fr": "Ceux-là reçoivent des bénédictions de leur Seigneur, ainsi que la miséricorde; et ceux-là sont les biens guidés.", "wo": "Gaa ñooña am nañu njéggal gu bawoo ca seen Boroom, ak yérmaande ; te ñoo di ña gindiku tigi." }
2
158
{ "fr": "As Safa et Al Marwah sont vraiment parmi les lieux sacrés d´Allah. Donc, quiconque fait pèlerinage à la Maison ou fait l´Umra ne commet pas de péché en faisant le va-et-vient entre ces deux monts. Et quiconque fait de son propre gré une bonne oeuvre, alors Allah est Reconnaissant, Omniscient.", "wo": "Safaa ak Marwa bokk nañu ci màndargay jaamukaayu Yàlla yi. Ku aj Màkka walla mu Umra , du aay ci moom mu jaabante seen diggante ñoom ñaar. Ku coobarewu te jëf lu baax, lu yiw, na xam ne Yàlla gërëmaakoon la, Aji-xam la.(r)" }
2
159
{ "fr": "Certes ceux qui cachent ce que Nous avons fait descendre en fait de preuves et de guide après l´exposé que Nous en avons fait aux gens, dans le Livre, voilà ceux qu´Allah maudit et que les maudisseurs maudissent ", "wo": "Ña nga xam ne dañuy nëbb la ñu wàcce ci ag leeral ak ug njub ginnaaw ba ñu ko biralalee nit ñi ca Téere ba, ñooña Yàlla dana leen rëbb, rëbbkat ya itam dana leen rëbb" }
2
160
{ "fr": "sauf ceux qui se sont repentis, corrigés et déclarés : d´eux Je reçois le repentir. Car c´est Moi, l´Accueillant au repentir, le Miséricordieux.", "wo": "lu dul ña ca tuub, yéwénal te leeral : ñooña Danaa leen jéggal Man Yàlla. Te Man maay Jéggalaakoon bi, di Jaglewaakoon bi. " }
2
161
{ "fr": "Ceux qui ne croient pas et meurent mécréants, recevront la malédiction d´Allah, des Anges et de tous les hommes.", "wo": "Ña weddi te dee ci kéefar, ñooña rëbbum Yàlla ak Malaaka ya ak nit ñépp dana dal ci seen kaw." }
2
162
{ "fr": "Ils y demeureront éternellement; le châtiment ne leur sera pas allégé, et on ne leur accordera pas le répit.", "wo": "Dañuy béel ca rëbb moomu ; kenn duleen ko woyafalal, kenn duleen ko yeexalal." }
2
163
{ "fr": "Et votre Divinité est une divinité unique. Pas de divinité à part lui, le Tout Miséricordieux, le Très Miséricordieux.", "wo": "Seen Yàlla jii, jenn Yàlla rekk la. Amul jeneen yàlla ju dul moom, mooy xéewal bindéef yi ci yërmaandeem ci àddina, di Jaglewaakoonu yërmaandeem jullit ña ca àllaaxira." }
2
164
{ "fr": "Certes la création des cieux et de la terre, dans l´alternance de la nuit et du jour, dans le navire qui vogue en mer chargé de choses profitables aux gens, dans l´eau qu´Allah fait descendre du ciel, par laquelle Il rend la vie à la terre une fois morte et y répand des bêtes de toute espèce, dans la variation des vents, et dans les nuages soumis entre le ciel et la terre, en tout cela il y a des signes, pour un peuple qui raisonne.", "wo": "Nit ñiy jëfandikoo seeni xel, war naa doy sëkk kéemaan ci ñoom, ni Yàlla binde asamaan yi ak suuf si, jëllasanteb guddi ak bëccëg, gaal yiy daw ci géej ci luy njariñi nit ñi, ak li Yàlla wàcce ci ndox mu bawoo asamaan, mu nàndal ca suuf si ginnaaw ba mu wowee, mu tasaare ca kaw suuf si ay meññeef, walbatim ngelaw leek niir yi nekk diggante asamaan ak suuf." }
2
165
{ "fr": "Parmi les hommes, il en est qui prennent, en dehors d´Allah, des égaux à Lui, en les aimant comme on aime Allah. Or les croyants sont les plus ardents en l´amour d´Allah. Quand les injustes verront le châtiment, ils sauront que la force tout entière est à Allah et qu´Allah est dur en châtiment ! ...", "wo": "Am na ci nit ñi ñuy jaamu xërëm bàyyi Yàlla, soppleen ni ñu soppee Yàlla. Ña gëm ñoo gën a tar cofeel ci Yàlla. Ay boo gisoon ña weddi, naka lañuy janook mbugal ma, xam xéll ne kàttan ba kàttan jeex Yàllaa ko am te Yàlla ku tar mbugal la !..." }
2
166
{ "fr": "Quand les meneurs désavoueront le suiveurs à la vue du châtiment, les liens entre eux seront bien brisés !", "wo": "[Bu Bis-pénc baa] ba ñañu toppoon deñtalu ca ña leen toppoon ndax te gis nañu mbugal ma, la leen boole woon lépp daggatoo !(s)" }
2
167
{ "fr": "Et les suiveurs diront : \"Ah ! Si un retour nous était possible ! Alors nous les désavouerions comme ils nous ont désavoués\" - Ainsi Allah leur montra leurs actions; source de remords pour eux; mais ils ne pourront pas sortir du Feu.", "wo": "Ña toppe woon, daldi ne : “ Ay ! bu nu delluwaatoon àddina! Dananu deñtalu ci ñoom kem ni ñu deñtaloo ci nun” - Noonu la leen Yàlla doon wane seeni jëf ; mu di ag yàqule ca seen kaw te duñu génn Safara." }
2
168
{ "fr": "ô gens ! De ce qui existe sur la terre, mangez le licite et le pur; ne suivez point les pas du Diable car il est vraiment pour vous, un ennemi déclaré.", "wo": "Yéen nit ñi ! Lekkleen ci li nekk ci suuf si, dagan, teey ; te buleen topp jéegoy (Séytaane) moom seenub noon la bu bir ." }
2
169
{ "fr": "Il ne vous commande que le mal et la turpitude et de dire contre Allah ce que vous ne savez pas.", "wo": "Li mu leen di digal moo di ag mbon ak ug caay-caay ak ngeen di wax ci Yàlla lu ngeen xamul." }
2
170
{ "fr": "Et quand on leur dit : \"Suivez ce qu´Allah a fait descendre\", ils disent : \"Non, mais nous suivrons les coutumes de nos ancêtres.\" - Quoi ! et si leurs ancêtres n´avaient rien raisonné et s´ils n´avaient pas été dans la bonne direction ?", "wo": "Bu ñu leen nee : “Toppleen li Yàlla wàcce” , ñu ne : “Nun kay la nu miin [di ko jaamu, baaxu maam ya] lanuy topp.” - Moo ndax ! Seen baay ya doonuñu woon ñu dul xalaat, ñu dul gindiku ?" }
2
171
{ "fr": "Les mécréants ressemblent à [du bétail] auquel on crie et qui entend seulement appel et voix confus. Sourds, muets, aveugles, ils ne raisonnent point.", "wo": "Ña weddi dañu mel ni ay mala yoo xam ne kàddu duñu ca dégg lu dul coow la. Ñu tëx lañu, gumba, luu, duñu xel-lu." }
2
172
{ "fr": "ô les croyants ! Mangez des (nourritures) licites que Nous vous avons attribuées. Et remerciez Allah, si c´est Lui que vous adorez.", "wo": "Ey yéen ñi gëm ! Lekkleen ci yi teey ci lun leen wërsëgal. Te ngeen sant Yàlla, su fekkee moom ngeen di jaamu. " }
2
173
{ "fr": "Certes, Il vous est interdit la chair d´une bête morte, le sang, la viande de porc et ce sur quoi on a invoqué un autre qu´Allah. Il n´y a pas de péché sur celui qui est contraint sans toutefois abuser ni transgresser, car Allah est Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "La mu araamal [tere] mooy médd, dereet, yàppu mbaam-xuux ak la ñu tuddu keneen ku dul Yàlla [ba ñu koy rey]. Ku ñàkk pexe nag ci lu dul beew walla jéggi dayo, du am bàkkaar ci xettaliku [ci yooyu], Yàlla Jéggalaakoon la." }
2
174
{ "fr": "Ceux qui cachent ce qu´Allah à fait descendre du Livre et le vendent à vil prix, ceux-là ne s´emplissent le ventre que de Feu. Allah ne leur adressera pas la parole, au Jour de la Résurrection, et ne les purifiera pas. Et il y aura pour eux un douloureux châtiment.", "wo": "Ña nga xam ne dañuy nëbb la Yàlla wàcce ca téere ba jaaye ko njëg gu néew, ñooña Safara lañuy lekk ca seeni biir. Bu Bis-pénc baa, Yàlla du wax ak ñoom, duleen sellal. Te am nañu mbugal mu tar." }
2
175
{ "fr": "Ceux-là ont échangé la bonne direction contre l´égarement et le pardon contre le châtiment. Qu´est-ce qui leur fera supporter le Feu ? !", "wo": "Ñooña ñooy jaay njub weccee ko ak réer, jaay njéggal wecee ko ak mbugal. Ñooñu ana kan moo leen gën a mën a dékku Safara?" }
2
176
{ "fr": "C´est ainsi, car c´est avec la vérité qu´Allah a fait descendre le Livre; et ceux qui s´opposent au sujet du Livre sont dans une profonde divergence.", "wo": "Loola la muy tegtale moo di Yàllaa wàcce Téere ba ci dëkk; te ña nga xam ne dañoo wuute ca Téere ba, ña nga cig féewoo gu sore." }
2
177
{ "fr": "La bonté pieuse ne consiste pas à tourner vos visages vers le Levant ou le Couchant. Mais la bonté pieuse est de croire en Allah, au Jour dernier, aux Anges, au Livre et aux prophètes, de donner de son bien, quelqu´amour qu´on en ait, aux proches, aux orphelins, aux nécessiteux, aux voyageurs indigents et à ceux qui demandent l´aide et pour délier les jougs, d´accomplir la Salat et d´acquitter la Zakat. Et ceux qui remplissent leurs engagements lorsqu´ils se sont engagés, ceux qui sont endurants dans la misère, la maladie et quand les combats font rage, les voilà les véridiques et les voilà les vrais pieux !", "wo": "Mbaax [topp Yàlla] du rekk jubale sa kanam Penku walla Sowu. Waaye mbaax mooy nga gëm Yàlla, Bis bu mujj ba, Malaaka ya, Téere ba ak Yonent ya, te alal ak ni mu neexee ci xol, nga di ko jox ña la jege, jirim yi, way-ñàkk ñi, doxandéem yi, ñay yalwaan ngir loru, jaam bu bëgg a jotu, [batey mbaax mooy] taxawal julli, di génne asaka. Te di mottali kóllare fu mu ko fasantee tey muñ tiis yeek naqar yi, ak tolluwaay yi, diggante yu metti yi, gaa ñooñu ñoo dëggal, ñoo ragal Yàlla !(n)" }
2
178
{ "fr": "ô les croyants ! On vous a prescrit le talion au sujet des tués : homme libre pour homme libre, esclave pour esclave, femme pour femme. Mais celui à qui son frère aura pardonné en quelque façon doit faire face à une requête convenable et doit payer des dommages de bonne grâce. Ceci est un allégement de la part de votre Seigneur et une miséricorde. Donc, quiconque après cela transgresse, aura un châtiment douloureux.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Digal nañu leen ci ku rey nit : gor ya fay gor, jaam ya fay jaam, jigéen fay jigéen. Waaye koo xam ne mbokkam baale na ko, nañu topp ci njekk mu fay dëyya ca namu rafetee. Loolu ag woyafal la gu tukkee ca seen Boroom ak yérmaande. Ku jalgati ginnaaw loolu, dana am mbugal mu metti." }
2
179
{ "fr": "C´est dans le talion que vous aurez la préservation de la vie, ô vous doués d´intelligence, ainsi atteindrez-vous la piété.", "wo": "Am ngeen ci feyyu googu dundu [gu yokku], yéen ñi ame xel, ndax Yàlla ngeen di moytandiku." }
2
180
{ "fr": "On vous a prescrit, quand la mort est proche de l´un de vous et s´il laisse des biens, de faire un testament en règle en faveur de ses père et mère et de ses plus proches. C´est un devoir pour les pieux.", "wo": "Digaleef na leen, ku bokk ci yéen te dee dikkal ko te fekk mu am alal ju muy bàyyi ginnaaw, [na def] ab dénkaane bu jëm ci ñaari waajuram ak ay jegeñaaleem cig njekk. Muy lu yell ci kaw ñi ragal Yàlla." }
2
181
{ "fr": "Quiconque l´altère après l´avoir entendu, le péché ne reposera que sur ceux qui l´ont altéré; certes, Allah est Audient et Omniscient.", "wo": "Ku dégg ndénkaane boobu ba noppi soppiku, bàkkaar boobu dafay tegu ca kaw ña ko soppi.Yàlla ku xam la, kuy dégg la." }
2
182
{ "fr": "Mais quiconque craint d´un testateur quelque partialité (volontaire ou involontaire), et les réconcilie, alors pas de péché sur lui car Allah est certes Pardonneur et Miséricordieux !", "wo": "Koo xam ne ragal na, ca aji-dénkaan ja, jeng walla bàkkaar, mu jubbanti ko rafetal diggante way-dono ya, du ca am bàkkaar, Yàlla ab Jéggalaakoon la, ab Jaglewaakoon la ! " }
2
183
{ "fr": "ô les croyants ! On vous a prescrit as-Siyam comme on l´a prescrit à ceux d´avant vous, ainsi atteindrez-vous la piété,", "wo": "Éy yéen ñi gëm!, farataaleef na ci yéen koor, kem ni ñu ko farataalee woon ca ña leen fi jiitu woon, ndaxtelee ngeen [mën caa am] ragal Yàlla," }
2
184
{ "fr": "pendant un nombre déterminé de jours. Quiconque d´entre vous est malade ou en voyage, devra jeûner un nombre égal d´autres jours. Mais pour ceux qui ne pourraient le supporter (qu´avec grande difficulté), il y a une compensation : nourrir un pauvre. Et si quelqu´un fait plus de son propre gré, c´est pour lui; mais il est mieux pour vous de jeûner; si vous saviez !", "wo": "ay bis yu ñuy lim [weeru Ramadaan]. Ku wopp ci yéen mbaa mu nekk ci tukki, na ko fey ci yeneeeni bis. Ñi nga xam ne àttanuñu koor, nañu jote ci jox ñam way-ñàkk ña. Ku coobarewu ci jëfi yiw, mu nekkal la fa ; ngeen woor nag moo gën ci yéen ; Cëy boo leen xamoon !" }
2
185
{ "fr": "(Ces jours sont) le mois de Ramadan au cours duquel le Coran a été descendu comme guide pour les gens, et preuves claires de la bonne direction et du discernement. Donc quiconque d´entre vous est présent en ce mois, qu´il jeûne ! Et quiconque est malade ou en voyage, alors qu´il jeûne un nombre égal d´autres jours. - Allah veut pour vous la facilité, Il ne veut pas la difficulté pour vous, afin que vous en complétiez le nombre et que vous proclamiez la grandeur d´Allah pour vous avoir guidés, et afin que vous soyez reconnaissants !", "wo": "Weeru koor, ci la Alxuraan wàcc di njub ci nit ñi ak faramfàcce [diggante dëgg ak i fen] ci njub. Képp ku teewe ci yéen weer wi, na ko woor ! Ku wopp walla mu nekk ci tukki, na fey yeneeni bis. - Yàlla jàppandal na leen te bëggaluleen ag jafeel, nangeen matal lim ba te màggal Yàlla ndaxtelee ngeen [jéem a delloo Yàlla njukkal], sant Ko.(s)" }
2
186
{ "fr": "Et quand Mes serviteurs t´interrogent sur Moi.. alors Je suis tout proche : Je réponds à l´appel de celui qui Me prie quand il Me prie. Qu´ils répondent à Mon appel, et qu´ils croient en Moi, afin qu´ils soient bien guidés.", "wo": "Saa su la samay jaam laajee lu jëm ci Man, [Neeleen : ] Man ku jegeñ laa: Ku Ma woo dinaa ko wuyu, saa su ma woowee. Nañu sàkku Ma wuyu leen te nañu ma gëm ndaxtelee ñu jub, gindiku." }
2
187
{ "fr": "On vous a permis, la nuit d´as-Siyam, d´avoir des rapports avec vos femmes; elles sont un vêtement pour vous et vous un vêtement pour elles. Allah sait que vous aviez clandestinement des rapports avec vos femmes. Il vous a pardonné et vous a graciés. Cohabitez donc avec elles, maintenant, et cherchez ce qu´Allah a prescrit en votre faveur; mangez et buvez jusqu´à ce que se distingue, pour vous, le fil blanc de l´aube du fil noir de la nuit . Puis accomplissez le jeûne jusqu´à la nuit. Mais ne cohabitez pas avec elles pendant que vous êtes en retraite rituelle dans les mosquées. Voilà les lois d´Allah : ne vous en approchez donc pas (pour les transgresser).C´est ainsi qu´Allah expose aux hommes Ses enseignements, afin qu´ils deviennent pieux.", "wo": "Dagan na ci yéen ngeen di jote ak seeni soxna ci guddiy weeru koor ; ñoom malaan lañu ci yéen, yéen itam malaan ngeen ci ñoom. Yàlla xam na ne dangeen daan wuruj seen bopp. Mu jéggal leen, jéllale. Kon léegi nangeen jonjonteek ñoom, te ngeen sàkku ci li leen Yàlla dogalal ; te nangeen lekk di naan ba ba ngeen di mën a ràññee wëñ gu weex ak gu ñuul ci fajar gi. Ngeen dale fa mottali koor gi ba guddeeti. Buleen jonjook ñoom fekk yéen a ngi wéet ci jàkka yi di jaamu Yàlla. Loolu deytali Yàlla la : buleen ko jéggi. Noonu la Yàlla di biralee ay laayaam ndaxtelee ñu ragal Yàlla." }
2
188
{ "fr": "Et ne dévorez pas mutuellement et illicitement vos biens, et ne vous en servez pas pour corrompre des juges pour vous permettre de dévorer une partie des biens des gens, injustement et sciemment.", "wo": "Buleen lekk seeni alal ci seeni diggante cig neen, te buleen cay ger àttekat ya ngir mën a labaj ba lekk ci alali nit ñi, ci bàkkaar te xam ko [xéll]." }
2
189
{ "fr": "Ils t´interrogent sur les nouvelles lunes - Dis : \"Elles servent aux gens pour compter le temps, et aussi pour le Hajj [pèlerinage]. Et ce n´est pas un acte de bienfaisance que de rentrer chez vous par l´arrière des maisons . Mais la bonté pieuse consiste à craindre Allah. Entrer donc dans les maisons par leurs portes. Et craignez Allah afin que vous réussissiez ! \".", "wo": "Danañu la laaj ci terutel weer yi - Neeleen : “Ay takkukaayu waxtu lañu ci nit ñi ak nattukaayi aj Màkka. Te mbaax [mbaaxu Yàlla] du tekki duggu kër jaare ko ñoot ya [ginnaaw]. Waaye mbaax [jaamu Yàlla] moo di dugge kër ca buntu ya àndak ragal Yàlla. Ay waay ragal- leen Yàlla ndaxtelee ngeen texe !” .(r)" }
2
190
{ "fr": "Combattez dans le sentier d´Allah ceux qui vous combattent, et ne transgressez pas. Certes. Allah n´aime pas les transgresseurs !", "wo": "Xeexleen ci yoonu Yàlla ak ña leen di xeex, te buleen jéggi dayo di tooñ Yàlla. Yàlla dey soppul ñay jalgati ! " }
2
191
{ "fr": "Et tuez-les, où que vous les rencontriez; et chassez-les d´où ils vous ont chassés : l´association est plus grave que le meurtre. Mais ne les combattez pas près de la Mosquée sacrée avant qu´ils ne vous y aient combattus. S´ils vous y combattent, tuez-les donc. Telle est la rétribution des mécréants.", "wo": "Reyleen leen, fu ngeen fi dajeek ñoom ; Nangeen leen génne fa ñu leen génne woon : [Sànje] moo gën a tar reyaate. Buleen xeex ak ñoom fa Màkka ndare du ñoom ñoo leen fa songu. Bu ñu leen fa songee nag, reyleen leen. Loolu mooy peyub yéefar yi." }
2
192
{ "fr": "S´ils cessent, Allah est, certes, Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "Bu ñu génnee ci kéefar ga nag, Yàlla ab Jéggalaakoon la, ab Jaglewaakoon la." }