text
stringlengths 6
463
|
---|
Boo seetee, ñett ba juróomi at ci ginnaaw, ni ma doon waxe farañse laa doon waxe wolof. |
Ginnaaw waxtaan wa, way-bokk SAID ak SUTT dañu jël dogal yile: |
bis ni ki tey, boole seen doole, di xàccandoo di dóorandoo, ngir mën a taxaw ci soxlay seen way-bokk yi, rawatina lu aju ci soxla yi ñu bokk ñoom ñépp; |
ak tamit jàppante liggéey ngir taxawal ag kurél gu boole sàndikaa njëwriñ ji yore koppari réew mi, |
waaye tamit gën a taral xeex bi ngir amaat yeneeni ngëneel, dem bay taxawu liggéeykati nguur gi yépp ci seeni jafe-jafe. |
Xaalisu betteex boobule bokk na ci liy jural askan wi ndóol, |
fukk ak ñaar ci fukki réew ak juróom yi bokk xaalisu seefaa (CFA) ñu ngi leen boole ci réew yi seen nit ñi suqalikuwul dara, maanaam xeetu IDH wi mujj te PNUD xalaat ko; |
xaalis boobu nekkul luy yombal dugganteg réew yi (lu yées fukk ci téeméer boo jël ci jëflanteb réew yi ci wàllu njënd ak njaay), |
xaalis boobu dafay dakkal tamit xemmemteef gi yeneen réew yi war a am ci réew yi, di fi ñëw (ñett rekk ci téeméer boo jël, ci li yeneen réew yi di dugal Afirig ci xaalis). |
Xaalis bi ñu ci dajale mu ngi jëm ci yenn naal yu aju ci enersi, jumtukaay ak dooleel xeex bi ñuy xeex mbënn mi. |
Ngir SOFICO SA; |
ñaareelu dogal bi joxe ndigalu dàmp CFU Sarl ñeen-fukk ak juróom-ñeenti milyaar yu teg juróom-ñeenti téeméer ak juróom-fukki milyoŋ. |
Dafa war a gërëm Baay Wàdd mi tax nit ñi xam ko ! |
Ndam li kenn waru cee tëb ak a dal, |
waaye saasenegaal yi wone nañu ag jàmbaar gu mat sëkk, wone nañu ne ñoo mën saakeeñaa yi, |
ndam li fésalul jafe-jafe yi gayndey teraanga yi jànkuwanteel, nga xam ne moo leen teree dugal bit yi ñu waroon a dugal yépp. |
Ci taxawaayam bu am solo bi mu am ci xaalisu seefaa (F CFA), ci féetalewaale tëralinu joxe xaalis wi di wéy di jëm ci këri liggéeyukaay yi ëpp xaalis. |
Nañu rëy bët tey laaj ay njiit yu réew mi yelloo. |
Nañu fàtteli ne Senegaal dina fay, ci tono (entere, maanaam xaalis buy yokku ci boram), ñetti téeméeri milyaar ak juróom-benn-fukk au juróom ci seefaa atum 2020, ni ko naalu yoonu xaalis bu 2020 fésalee. |
Rafinha ak Manuel Neuer duñu ko wéddi, ñoom ñi daw ak duuti Maane yi gëlëmal, ci seen ñaareelu joŋante bi, ci juróom-ñetteelu xaaju futbal bi, diggante Bayern Munich ak Liverpool, weeru awiril wi weesu, (benn-ñett). |
Senegaal mënul woon a tàmbali joŋanteb àdduna bi bu xale yi amagul ñaar-fukki at (U-20) bu FIFA, Poloñ 2019, nu gën a baax anam yi mu ko defe woon. |
Loolu la ki ñu jox xibaar bi wax, juróom-benni nit ñu am ay gaañu-gaañu lañu yóbbu lopitaal bu Binjoona. |
Ci ay mbindam yi daw yaramu ñu bare, dafa koy ñaan mu sargal Sëybatu Juuf, |
jigéenu alkaati ju atum 2019 ndax yónnentam yépp ya mu doxi ca Mbootaayu xeet ya. |
Bi Demburu di woo pël ñi, fekkoon na Sónko woo waa Kaasamaas ba pare. |
Ndaxte, am na ñu fi jiitu, gën ñoo jàmbaare, gën ñoo xam, gën ñoo mën te raw ñu ci fànn yu baree bare te amuñu li ñu am. |
Saajo Maane moo dugalaat waaye bitu temboo bu Wilfried, |
Zaha moo naroon na yàq lépp bu Firmiñoo dugalul woon ñaareelu bit bi nga xam ne, moo tax ñu jël ndam li. |
Kàngam ci wàllu yoon ak jumtukaay xarala, Emaniyel Joox jàpp na ne mënuñu wax waxi njëg lu wàcc waaye li ñu war a wax mooy, njëg lu ñu seetaat. |
Ropplaan bi mu ngi jar juróom-fukk ak juróom-ñaari milyaar yu teg ñeenti téeméeri milyoŋ ak ñeen-fukk ak juróom-ñaar yu teg ñaar-téeméer ak fanweer ak juróom-ñaari junne ak juróom-ñaar-fukk ak benn ak benn fiftin ci xaalisu seefaa (57 447 235 356 francs CF); |
xaalis bi ñu ko jënde, ñu ngi ko jële ci natti ati 2019, 2020 ak 2021. |
Loolu la jëwriñ ji yore gafag réew mi, Abdulaay Daawuda Jàllo, wax àjjuma bi muy layal naalu yoon n° 07/2021 bi soppi yoon n°81-52 bu 10 sulet 1981 te aju ci tëralinu payoori takk-der yeek ñi ko nekkul te àllaterete. |
Rax-ci-dolli jàmmaarlook mbas mu law fépp mi ak tàrde ca Oran, |
kilifay Alseri, ak Kurélu Afirig gi yore mbirum daw (tàggat-yaram) dañu fasoon yéene toxal ca Alsee, ci njeexitalu weeru suweŋ. |
Ndaxte dañu yaakaar ne muuraake ngir waa kër Sónko yi te war leen ko teree lekk ? |
Beneen joŋante bu ndam demul, dikkul, bu baaxul ci ñoom ndaxte dañu sore ci raŋ gi. |
Wànte yéenekaay bi xamle na ne kilifa yi tàmbali nañu ay waxtaan ngir jàmm dellusi. |
Beneen yoon, waxuñu fi xaalis bu takku lool bu dem ci kurãa bi ginnaaw sax waxtuy liggéey yi wala esãas bi. |
Xaalis bi ci taxawaay lañu ko fay xobbet xobbet, ci ab biro (bu yéenekaay bi nangul a fésal) waaye nekkul ci kayitu payooru deppite yi. |
Maanaam, keroog bañ nee mbas dikkal na réewum Siin, keroog laa doon jël samay matuwaay, tëj biir réew mi. |
Ca ginnaaw ga tuuti, sàndarma yi, ci ndigalu Ja, ga deppite yi ñu génn béreb ba, |
ñeent ci ñoom bañoon, ñu jàpp leen, |
Seŋoor mujj joxe ndigal ñu bàyyi leen. |
Bu weesoo samp ag kurél gu sax dàkk ci 77 ak jumtukaayi jiite yu baax, dinañu samp PASTEF, ci dëkki Seine ak Marne gi nga xam ne, mooy deppartemaŋ bi gën a yaatu ci Île de France. |
Ci yéenekaayu Kritik bu gaawu 25 sulet, Doktoor Buso mu ngi ñuy xamal ne : dëgg-dëgg am xaalis lu jamp la. |
Ci misaal, su ag nguur jëlee dogalu wàññi lempo yi ci li nit ki di am, loolu dafay tax li borom-kër yi mën a jënd yépp ci seen xaalis yokk, |
naka noonu soxla yi, tey wàññiwaale lempo yi mu ga këri liggéeyukaay yi, ñuy mën di am lu ëpp li ñu daan am, di mën di jël ay nit ñu liggéey. |
Bu ñu jëlee misaal ci Mbay Ñãa mi nga xam ne bu danoo ci wetu kãa yi dina am ñaar-téeméeri at soog a jóg, xam ngeen li ma bëgg a wax foofu, |
loolu mooy xel yi nekkuñu fi te seen tàggatkat bi dafa lajj wala nga xam ne, dese na lu bare. |
Am na ci tamit ñàkk gëm-gëm, ñàkk jëmu wala ñàkk mën-mën ci yenn way-pólotig yi nga xam ne, dafa mel ni dañu dugg ci pólotig ndax rekk aw yoon la wuy may nit ki alal, darajaal ko. |
Foo mënti dem ci àddina si, noonu la, ba mu des Afirig. |
Ci li Njiitu réew mi Maki Sàll wax, "ropplaan bi dina jóge Tàmbaakundaa ci ay ñaar-fukki waxtu ak ñaar yooyu". |
Xayma yi leer nañu nàññ, def nañu seen nettali: |
benn doktoor ngir juróom-fukki junney nit ag juróom-ñeent yu dëkk ci benn béréb bi. |
Ni ko Libération bindee, Interpol xam na ko ba màndargaal ko te mu ngi wër bu baax. |
Jeexital bi mooy, ay ndaanaan a ngi def ay nettaliy dundu yu amul benn solo, yu ñu juralul benn yokkute. |
Li ñuy laajte kay mooy, ndax yégleg yokk boobu nekkul luy nelawal askan wi ba duñu waxati ci tas gi ñu tas SENELEC jamono yii. |
Tasleen xibaar bi ngir jàppale soldaar bi, |
taxawu abdu kariim géey mooy jàpp ci coppite gi. |
Bulo yi futbal nañu bu baax ndax ki ñu génne ci ndoorteelu futbal bi, |
dafa leen a ndimbale bu baax. |
Wax ju daw yaram ji njegemaar bi am fukki at ak ñett kese wax ci P.V., |
ndongo li nekk ci juróom-benneelu at mi ci njàng mu suufe mi dikkaat na ci anam yi mu séqe mbëggeel ak borom jabar bi. |
Buleen jaawale cër-ci-téeméeru lempo bi ak wuute bi am ci li maas gu nekk di joxe ci lempo. |
Jëlukaayu tàngaayu yaram, nattukaayu taasiyoŋ, niitukaayu biir bër ngir faj bët bi, màndargay kuurãa biy dox ci xol ak ñoom seen. |
Réewum Farãas dafa yég ne mu ngi gën di ñàkk doole ji mu amoon ci Senegaal. |
Mëneesul a ñàkk a tudd réewum Ërob mi mujj a jël ndamal joŋanteb dénd ba. |
Am naa yaakaar ne waa ji am na sañ-sañu wax li mu gis ni bépp saasenegaal, |
wànte li mu bokkul xalaat ak as peresidaŋ su mel ni Sónko miy mbokku joolaam moo tax ñu kay saaga, |
nit ñi nite saagawuñu sama mbokk mi bi mu joxee xalaatam. |
Soxna si Kan la, moom miy jabaru jaaykatu dorog bu mag bi jënd benn ci bato yi yeboon kokaayin bi. |
Li mënoon a doon yoon wu mujj wu maas gu jëm mag te xarañ mën a jël kub bi. |
Bi ñu leen fekkee ñu yore njureef li rekk, lañu leen song ngir jàpp leen. |
Terewul, ci ndimbalu jumtukaayu xarala yi, njiitu Pastef teewe na ndaje ma am bitim réew te nekk fii ci Dakaar. |
Doomu jàngoro bi fa la juddoo, |
ay weer rekk ginnaaw gi, bi mu fa defee ay jéyya, Réewum Siin ci boppam, mooy ñëw di dimbale réew yi nekk jamono jii di jël seen wàll ci koronaa bi. |
Stv, ki ñuy waxal dafa ñuy xamal tolluwaayu cër bi. |
Mësuñoo gis, ci taarixu Première ligue ab ekib bu duma moroomam bitim réew juróom-ñeenti bit ci dara. |
Ni ñu ko waxee ci suñu mbind mu mujj mi, takk-der yi dañu xam bu baax mbégtey askan wi ba seenug bëgg nguur tax ñu taqalikoo ak njiitu réew ma, gunge ko ba mu dem. |
Gaawu bile la ñaari ekibu Àngalteer, Chelsea ak Manchester City di laale ngir finaalu Ligg-dee-sàmpiyoŋ bi. |
Saajo Maane, (ataakãa Liverpool bi): kenn mësul gis lii ! |
Ak nit ñu ñuul ñi ñu beddi ca Palestin ak Móritani. |
Loolu doyul, nga taafantoo guural gi, di jël dogal yu la neex. |
Taggat yarambi bi di Downhill skiing mingi bayyéko ci lum néew-néew ci fukk ak juroom gnarélu xarnu bi, ci attum 1861 la nju dëkk Noorwees ubbi mbotayu ski bu njeekk fële ca Australia. |
Su jigéenu jullit bëgg a muuru, war na koo mën a def. |
Ci noonu, Mbaalo Ja Caam dina jiite SUTSAS ci diiru ñetti at. |
Naka la SONES mi nga xam ne, moom moo war a saytu liggéeyu këru liggéeyukaay gi yore ndox mi léegi, di amee ab cër ci këru liggéeyukaay googule ? |
Ci dëmi-finaalu dellusi bu Ligg-dee-sàmpiyoŋ bi, Liverpool moo doon dalal ci màkkaanam bile di Anfield ekibu Barcelone mi jëloon ndam la ci ñetti bit ci dara, bi mu ko fekkee dëkkam. |
Lu yées menn at ginnaaw bi ñu ko sosee, Xaalis bi ñu teg ci loxol saasenegaal bile di Mamadu Mbay, jur na ay ndefar yu bare yu ñu mën a tiitaroo. |
Ku xool Meetar Elaas Juuf rekk, dinga gis ne li ñu ko fàtteli jëfu siif jigéen ja mu defoon te yoonu Farãas tegoon ko ci ay daan, metti na ko lool. |
G.E, lu ñu mën a jële mbégte, ci yeggee Njiitu réew mi li xew, gët yi muy xool doxinu njiiteef gi, moo xam muy njiiteef gu mag gi wala njiiteef giy am ci gox-goxaan yi. |
Dinañu am ay gan yu mel ni ay kuréli diiney katolig ak yu lislaam. |
Gàcceel ngeen réew mi, |
te it jox ngeen dëgg ñi doon wax waxi ndaw ñu ñàkk yar. |
Réew yile di làkk àngale di Niseriyaa, Ganaa ak Gàmbi dañuy des ak seen xaalis, |
ndaxte dañu bëgg a xaar ba xam fu wànnent di mujj ak gëtam, soog a dugg ci xaalisu Afirig bu bees bi. |
Ndate mu sell mi, mi am naqar bu rëy ne na Xànju mi ñàkk kilifa, mi tontu tontu bi ngeen di fàtteliku, |
woo ko ñetti yoon, |
nga ne ko sama yaay nee na, teen bi gënoon na fee déey, mu root rootaaleel la. |
Takku taxaw temm boo xam ne la, dangay fàtte sa bopp, jëf ngir ñépp. |