text
stringlengths
6
463
Ñoom am nañu balu oor, waaye yaw, xolu oor nga ame.
Mel na ne ci biir réew mi yépp, ndawi bëgg sa réew yi, dañuy bay.
Bañkat bi, tuumaal nañu ko ci yeekatu fitna, tëj nañu ko ci kasog Rëbës bi.
Wax xam-xamu taaral, mooy laaj jafe-jafeb màndargaab tànneefu xam-xam bi.
Lenn lu mënul ñàkk ci réew yiy namm a bokk ci dénd bi ñu jagleel xaalis bi mooy, ñu matale màndargaay tànnéef yi ñu bokk:
bor bi ñu bokk yées juróom-ñaar-fukk ci téeméer boo jël ci li réew mi am ci at mi yépp (PIB) bi (70%),
néewaayu koom gi yées ñett ci téeméer boo jël ci li réew mi am ci at mi yépp (PIB) bi (3%),
limu yokkute gi yées fukk ci téeméer boo jël (10%),
kondaaneb weccee bi muur gën gaa gàtt ñetti weeri dugal koom-koom ci réew mi, ak yeneen ak yeneen.
Ngir dëgëral beddeeku gi am ci anam wu rafet, njiit li, Sàll xaarul ngir jox jaarukaay buy musal beddikat yi ngir taaral ag jiitoom ak gëm-gëmam, mu melal beddikat yi niki jàngoro juy nasaxal sunu pólótig yi.
Ndeke siifeb njaay mi ci yoon, ngir mu jaar yoon, laaj na takku,
waaye itam, takku gu leer gu amul benn gàkk-gàkk, bu mel ne ñàkk a xam ci jaaykatu këf ki, ak yaatuwaayu mbir mi ñuy joxe.
Waxoon na ne, yor na firndeb moomeel yu teguwul ci yoon yi Maki ame.
Ban tànneef, ngir Maki mu jànnaxe mi, mu réere ci coobare boppam ?
Ci ñàkk kóolute gi am ci biir at mile.
"Dama mës a xam ne mën naa génn kaso jamono ju nekk, ci bés bi walla ci guddi gi", loolu la wax ci waxtaan wi mu amaloon ak tele Itv bi.
Ci atum 2015, ci wetu Bild : donte neex na ma, bëgguma ko soppi, wala ma nekk ndonol Pep.
Lépp a ngi mel ni cosaanu nit mënul weesu péex mu mënul ñàkk cig fésam.
Ndamu maye deret ji, moo bees ba léegi ci xeli waa Senegaal yi.
Ci wile tur, benn yoon terewul askan wi mu wax, wala ŋàññ doxalinu yoon.
Macron bañ na nangul Watara dëgër boppam gi mu nekke ci xareb ñoñ bi mën a juddu,
muy sukkandiku ci ay wax yu jege dëgg, di bàyyi ñaareelu wote yi ci diggante Beje ak Sóróo.
Ak Pastef, mbind yi ci lim yu baaxul yi ñu duufal, jëme ko ci doxalinu nguur gi, dinañu leen ci seppi,
jarul sax rus, yërëmtalu wala bàyyendiku.
Njiital tele bi, li ame màndargam joxe ak moomeel gi ci aju, moom ci boppam, déglu nañu ko.
Njiital tele bi ñibbi na këram.
Fàttalikuleen téereb nettali bu Rëne Marãa, téereb nettali bu njëkk ci der bu ñuul, Batouala (jógal xeex yaw mile), wala ba tay, bu Albeer Kami bi, ak nit ka Meursault (dee moom doŋŋ!).
Ci luy ñëw, dina baax ba mbooloom araftukat yi ci wàllu wér-gi-yaram gi, ñu temm ci tëralin yeek xaajaloo gi ci xam-xami settantal yi ñu teg.
Ŋàññ yi askanu Senegaal di def gannaaw bépp nërméel gu desee leer ci ñoom, tax na ba góor ñi ci melo wu ñuul wi, jomu joxe këlëb yi, ak sunu mbooloom tàggatu gi ci réew mi di ci loru ci anamu nattu.
Jigéen ñooñu, war nañoo bokk ci ñiy jël dogal yi, ci joxe xalaat yi,
te seen xalaat war nañu leen na jël boole leen ci tëralin yu kuréli pólótig yiy sàkkoo jiite.
Ñu dugal leen ca fukk ak benneelu simili ba,
waxtu juróom-ñeent-fukk yu teg ñaari simili ci la seen waa ji, Jaata andeewaat mbooloom, ñu tollook seen naataango yi ci ngoon gile.
Dafa mel ne mbër mu Yaawu jaal dóor mu daanu, ba noppi mu jóg, jànnaxe, di sóoru Bàlla Gay 2.
Pastef, moo ëpp wërsëg, niki bu sampoon ndëndam ci wotey njiitu réew yi ci réew yu booloo yi!
Naples a ngi wéyal yoonam wu bon wi,
te loolu wuute naak Romains yiy doxal.
Fi mu nekk nii, Sónkoo ngi gën di siiw, ba ca Asie.
Bàyyileen di ñu reeloo ak sang bi nga xam ne, lenn rekk moo taxoon muy pólótig, mooy takk nombo tànku njiit.
Mën-mën yi aju ci xam-xamu lënd gi war nañu leen a yokk.
Gaynde yi ñoo ngi bokk ci kippu D mi, ñu bokk ko ak Cameroun, Sud du Soudan ak ñaareel bi jàll ci kippu E bi, ci joŋanteb toogloo yi.
Mbooloom tàggatu mi jox na ma ñetti yoon sama wërsëg,
foog naa ne tono googu baaxul.
Ci jamono jooju, waa Senegaal a ngi desoon seen kër ci jàmm, cig buqat ak tóoy yu teguwul ci kanamu tëj gi.
Ab oto bu ràññeeku, bu nekkoon ci dëkku diine bu sell bi, Tiwaawan, moo mbëkkante ak beneen bu jóge ci beneen boor bi.
Soxna Aana Dãafaa la nu fal doxalkatu Mojip Farãas ci penc mi.
Ñaata at la Pointe de Sagomar am laata ñu koy weccee ?
Noo ngi rafetlu jëfi jàppoo gi ñu nemmeeku fépp,
tey woo bépp doomu Senegaal mu jàppale way-loru yi, ci limu am ci alalam, ak mën-mënam.
B. Juuf wone na ne ci jamonoy yoon wi, la doon daw xël yu metti.
Sama baay, ndem-si-Yàlla Mamadu, doonoon na xaritu Seex Beeco Cuun mi mu bokkaloon dëkk ak liggéey ci jamonoy 60, niki ay jàngalekat ci dëkku-kaw gi, Añag ca Kaasamaas.
Naka jekk, cim réew mu nga xam ne sàcckatu netetu dañu koy tëj, di négandiku ñu àtte ko,
cim réew moo xam ne, ñi seen malaanum kiiraayu demlantem réew yi, wala mu péncum ndawi réew mi aar, ñoo ngi koy jëfandikoo, di ñu sàcc,
du yoon ñu ciy loru.
Loolu gaañ na ma, ba àgg ci képp ku nekk ci mbooloo mi,
ndax xibaar yooyu dañu leen a wasaare woon, cig tayeef, ci taskati xibaar yi,
mu jur ay doxalin yu ñaaw ci ñi ñàkk mbooloo mi, andi ay njort yu ñaaw ak ay noonoo.
Noo ngi koy wax te dunu ci dellusi:
noo ngi bàyyi xel lépp, di càmbar bu baax bépp tolluwaay ci mbir mii ak kóolute,
waaye itam ak xel mu dal, dëggook sañ-sañ.
Jënd ag daamar gu màndargawoo Ford Santafe Sport (2016) laata tabaski bi, moom laajoon na, ci li Le Témoin wax, Aminata Balde mi teewoon ci kanamam ci anamu lëkkalekat buy yëngu ci këru liggéeyukaay gi, Unit Transit sise Mole II bi ci pooru Ndakaaru bi, ngir liggéeyu duwaañ bi.
Waaye, dafa soppi li mu naroon, bi mu gisee nataal yi ci wetu bayaal bi (téeméer ak fukk ak juróom-benneel), gannaaw bi àttekat bi àddoo cib widéwoo.
Waxtaan nanu ak moom, ndaw si : Maymuna Dem.
Wax nu sa jaar-jaar?
Ñaar-fukk ak ñetti (23) poñ ku nekk, waaye bali bit yi, moo leen wuutale, dañoo jeng jëm ci foxes yi.
Gan kuréelu pólótig moo mën a màng mbooloo mu tollu nii, te du leen jox njëgu oto, du ñam wu ñuy lekk, wala ay yére ?
Tàggatkatu mbooloom Liverpool, Jorgen Klopp, mën naa bañ a sukkandiku ci Salah.
Waxtoom wépp ak dooleem jépp, dafa ko def ci wasaare làkki réew mi.
Jot na sëkk, jëwriñ ji ŋànk mbay mi dëggal.
Li réewi Afirig yi noppeegul a booloo, warul tax ñu nekk ci diggante tànn benn xaalis ak gëmm seeni bët tànn lu mel ni euro.
Ndax mës nañoo dund ci Senegaal, benn yoon rekk, wu nga xam ne jamonoy wote ju amul ger askan week sunu milyaar yi, nga xam ne fa muy jóge duñu ko mës a leeral ?
Ñun ñépp, nanu àndandoo wote ngir génne fi jalgati yoon,
mànkoo ngir faagaagal, nguuru Fay- Sàll gi amul benn worma ci askan wi.
Amul benn borom xel, bu dul takku ngir askanam wala pólótig, te du am jàmmaarloo ak ñiy jalgati yoon.
Sa doom ji bëggul a yéeg.
Sa doom ji dafa bëgg a sukkandiku ci yaw ngir nekk Njiit.
Rax-ci-dolli, du yégal askan wi, ndax amul benn worma ci nun.
Dañu nekk di seet daggit bi des : tàggatkat bu am jom.
Ngir fomp jigéenu Sud-Africaine bi, Elmarie Gerryts ci àlluwa ji, war na def...
Su ñu booloo takku ngir génne seen gaa yi léegi léegi, fekksi askan wu sonn ci ay ñaxtoom, boo moytuwul, dina nekk musiba ci Maki ak nguuram gi.
Dama bëgg a wax foofu ne, jot na sëkk, ñu bàyyi di ko jëfandikoo ni gannaay, te def ko ngir ñaari sabab.
Jërëjëf ci jéem a def luy tax nga yelloo sa payoor ngir mën a ñëw taxaw jàkkaarlook ñun di ñu wax waxi liggéey bu yemb te mucc-ayib!
Dakaar, fukki fan ak ñett ci weeru nowàmbar 2019.
Xew-xewi weeru màrs yi weesu yóbbaale nañu turam ba fàww,
te dafa mel ni, dañoo dem ba di ko jàppe ni mbër mu yem doole ak njiitu réew mi Maki Sàll.
Gëm-gëm bu xóot boobu moo ma tax dugg ci pólotig.
Xeltukat yi dañu war a nekk ñuy dooleel askan wi, di liggéey ngir yëkëti ko ba ci màqaama ak jikko yu baax yi gën a kowe tey dakkal jaay doole ngir génn ci ag naaféq gu suufe, dànd bu baax lépp luy wanewu, yëkëti sa bopp wala lu ñàkk teggin.
Su nguur googule jëlee dogalu yokk lempo yi (li këri liggéeyukaay yi di am), loolu dafay wàññi soxla yi (borom kër yi duñu am xaalis bu doy).
Xaalis bi këri liggéeyukaay yi di dugal ci ndefar mi dafay bokk ci liy gën a diisal lempo yi ñuy fay.
Saapoloñ bile di Lewandowski, ci juróom-ñeenti fani joŋante yi la raw ki fi rawoon.
Bu ko defee, kooku lees war a laaj xaalis ndax moo yor xaalisu askan wi.
Mu ngi doon soog a teg jeegoy fippu bi amoon ca ñaar-fukki fan ak ñett ci weeru suyee atum 2011.
Nguur gi dafa war a taxaw temm ci séddaleb alali askan wi bu jaar yoon te yemale ñépp.
Yàgg bawul dara,
du seen wax jeey soppi lenn lu fi soppeeku,
te jamono ju neegn dajee ci ëttub buur rekk, Ndawu réew mile di Usmaan Sónko, dóor na leen ba ngeen xalangu.
Dañu am ayib boo xam ne dafa mel ni dañu ko judduwaale, nañ ko wax te dee:
bokkuñu ci xeet yiy waaf wala ñuy daw bu leen ki ñuy xeexal jekkoo.
Jeexitalu ay mbir yu lëj yu dal ci koom-koom bi la,
waaye gépp yokkuteg njëg tekkiwul ne yokkute googu, dafa war sax.