wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
Xelam ne yarr ci pexe
soudain, il lui vint une solution à l’esprit.
yéew
faire cercle autour de
yaam
mettre dans le filet la calebasse qui sert à puiser dans un puits peu profond (séane)
Bi may yaam laa nemmeeku ne leket gi dafa xar
C'est quand je plaçais la calebasse dans le filet à puiser que j’ai remarqué qu’elle était fendue.
yaflu
s’engraisser
Xanaa yow dangay yaflu
est-ce que par hasard tu ne serais pas en train de t’engraisser ?
yeewwute g-
vivacité d’esprit
Su doon jëmale yeewwuteem gi ci njàngam, kon mu baax
S'il appliquait sa vivacité d’esprit à ses études, alors ce serait bien.
yabeel g-
familiarité outrageante
yafal
engraisser
Dafay jénd ay xar, yafal leen, jaayaat leen
il achète des moutons, les engraisse et les revend.
(prov.) Boo yafalee sa am kuuy, yow lay jëkka daan
si tu engraisses ton bélier, c’est toi le premier qu’il terrasse.
yabóy b-
sardine
Tey de yaboy bare na marse
aujourd’hui, il y a beaucoup de sardines au marché.
yay w-
désert
Rali Pari-Dakaar bi, ci yay wi lay jaar
le rallye Paris-Dakar passe par le désert.
yaxu yamarkiij b-
coccyx
yaaf w-
poil du nez
War ngaa wàññi sa yaaf yi
tu dois raccourcir tes poils du nez.
yaafusloo
rendre veule
yebbi
décharger
yaj b-
calebasse-gourde
Dafa daan jaay ay yaj
il vendait de petites calebasses-gourdes.
yëbb
déteindre
Sér bi dafay yëbb, bu ko boole ak yeneen yére yi
le pagne déteint, ne le mets pas avec les autres habits !
yeb
préparer une femme à rejoindre son domicile conjugal en la dotant d’ustensiles de ménage et en lui prodiguant des conseils
Astu lañuy yeb, moo tax nit ñi bari ci kër gi
C'est Astou qu’on prépare à rejoindre son domicile conjugal, c’est pour cela qu’il y a beaucoup de gens dans la maison.
yebal
envoyer qqn qq. part
yedd
sermonner
Dama ko yedd, mu daldi fa jóge bàyyi tux
je l’ai sermonné, et depuis il a cessé de fumer.
yeble b-
précepte
Limal fukki yeble Yàlla yi
cite les dix commandements de Dieu !
yaasa
(Cré. portugais de Casamance) Préparer du yaasa
Tey, damay yaasa
aujourd’hui, je prépare du ‘yaasa’.
yaxu diggu-gannaaw b-
Échine
yakkal
envoyer à qqn un repas qu’on lui offre
Tey, damay yakkal samay goro
aujourd’hui, je vais envoyer un plat à mes beaux-parents.
(prov.) Su ñu la yakkalee ci gaalu xaj, fexeel ba bu ca lekk
si on te sert dans un bol de chien, fais en sorte de ne pas y manger
yedd j-
délai de viduité ou temps à observer par une femme divorcée avant de pouvoir se remarier, ceci pour s’assurer qu’elle n’a pas conçu un enfant au moment du divorce
Bu ñu la fasee, dangay jàpp yedd
quand tu es divorcée, tu observes un délai de viduité.
yakkataan
abuser (d’une femme) pendant son sommeil
Dafa doon bëgga yakkataan ndaw si
il tentait d’abuser de la femme pendant qu’elle dormait.
yaay j-
mère
Xaaral ba sa yaay dellusi
attends que ta maman revienne !
Yaay ju ndaw
épouse du père.
Yaayu jiitle
marâtre.
yaag
remuer le riz dans de l’eau pour faire descendre les petits cailloux qui s’y trouvent
Yaagal ceeb bi te sóor
remue le riz dans de l’eau pour le séparer des cailloux puis mets-le dans la marmite.
yaafus b-
un bon à rien un incapable
Kooku ab yaafus la
celui-là est un bon à rien.
yaa
c’est toi qui
Yaa ko wax
C'est toi qui l’as dit.
yékkat
sangloter
Dafa agsi di yikkat
il est arrivé en sanglotant.
yabeel g-
familiarité outrageante
yalandi
rincer
Ndax yalandi nga ko ?
est-ce que tu l’as rincé ?
yablu
se laisser traiter sans égards, se laisser marcher sur les pieds
Bul yablu sa bopp
ne donne pas aux gens l’occasion de te marcher sur les pieds.
yagar-yagari
marcher lestement
Léegi wute na ak ba ngay yagar-yagari di dem
maintenant c’est différent du temps où tu allais d’un pas agile.
yaxeet
complètement (détruit, gâté, abîmé)
Ku la bañ yàqu yaxeet
celui qui te haïra sera détruit complètement.
yaak
Toi et
Yaak moom ay bokk néeg bi
C'est vous deux qui partagerez la chambre
yéeg
monter
Yéegal ci kow siis bi
monte sur la chaise !
(prov.) Bu jinne bëggee daqaar, ku yéeg daanu
quand le djinn veut du tamarin, quiconque monte dans l’arbre tombera
yéeféer b-
mécréant païen
Am na réew yu, yéeféer yaa gëna bare jullit ya ak kercen ya
il y a des pays où les mécréants sont plus nombreux que les musulmans et les chrétiens.
yaasa b-
(Cré. portugais de Casamance.) Plat constitué de riz blanc cuit à l’eau et accompagné de viande ou de poisson grillé et d’une sauce apprêtée avec du piment et beaucoup d’oignon
Sa yaasa bi neex na
ton ‘yaasa’ est délicieux.
yalwaan b-
obole, aumône reçue par un mendiant
(prov.) Boo saraxatul gumba, bàyyi ko ak yalwaanam
passe encore que tu ne fasses pas l’aumône à un aveugle mais laisse-lui son obole.
yaaba b-
danse sp
yaar b-
yard
yeble
(qqn quelque part pour accomplir qch)
Yeble naa ñu wooyi ko
j’ai envoyé le chercher.
yawaal b-
nom d’une variété de poisson
yaay-faal b-
femme disciple de Cheikh Ibra Fall (chef spirituel dans la confrérie des mourides)
yeelu-maam b-
cadeau fait aux grand-parents (et par extension, à des personnes de leur âge) à l’occasion du baptême de leur petit-fils
Nañu ma indil fii sama yeelu-maam
qu’on m’apporte ici mon cadeau de grand-parent !
yeejaan b-
lanière de cuir de vache
Yeejaan lañu ràbbe basaŋ gi
C'est avec des lanières de peau de vache qu’on a tissé la natte.
yéeg b-
fait de monter ascension
yéene
souhaiter
Jëkkër ju baax laa ko yéene
je lui souhaite un bon mari.
yéene
annoncer publiquement
Lu ñuy yéene ca jàkka ja
qu’annonce-t-on à la mosquée ?
yeena
c'est vous qui
Yeena ko fi indi
C'est vous qui l’avez amené ici.
yeel b-
partie inférieure de la jambe
Xale la de, yeel yee gudd rekk
il est jeune, c’est qu’il a de longues jambes.
yendu
passer la journée
Kawlax laa yendu démb
J'ai passé la journée à Kaolack hier.
yeeru
être aux aguets
Muus maa ngi lay yeeru, xoolal yàpp wi
le chat t’épie, surveille la viande.
yéene b-
annonce publique
Dégg na yéene bi ?
a-t-il entendu l’annonce ?
yéen w-
sourcils