wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
Jox ko xàmpit wi
donne-lui le morceau !
xàmmee
reconnaître
Ndax xàmmee nga sama nijaay ?
est-ce que tu as reconnu mon oncle maternel ?
xàmm
être absorbé dans ses pensées
Mu ngi ne xàmm, déggul dara ci li nga ko wax
il est absorbé dans ses pensées, il n’a rien entendu de ce que tu lui as dit.
xànc g-
fibre
Lu xànc gi gëna dëgër, buum gi gëna dëgër
autant la fibre est solide, autant la corde le sera.
xànq w-
planche
Ñaari xànq a koy liggéey
ce sont deux planches qui le travaillent
xànq
être chauve
Dafa xànq
il est chauve.
xàndeer b-
cailloux noirs ou rouges que l’on met dans un bol en terre cuite dans le sanctuaire des fétiches protecteurs
xàndi g-
fût
Dafay jénd ay xàndi, di ci tëgg ay furno
il achète des fûts et forge des fourneaux avec.
xànjukat b-
chanteur
xàndoor g-
hilaire neuf
xànju
chanter
xàpp b-
coupe de cheveux
Xàpp bi ñu la xame, soo ko wotee, dootuñu la xàmmee
la coupe de cheveux qu’on t’a connue, si tu la rases, on ne te reconnaîtra plus.
xànjar
avoir le trachome
Sa doom ji dafa xànjar; xanaa gisuloo bëtam yi ?
ton enfant a le trachome, n’as-tu pas vu ses yeux ?
xàppatiku
être entamé d’un morceau
Koñ bi dafa xàppatiku
L'angle est entamé d’un morceau.
xànjuraan b-
musique
xàñtu
suivre la trace
xàppati
détacher ne partie d’une masse solide
Soo bëggee birig bi xéj ci, dangay xàppati koñ bi
si tu veux que la brique y tienne, tu en détaches l’angle.
xànq b-
calvitie
Xànq bi dafa ko jàpp
la calvitie lui va.
xàppit
Évoque le fait de sectionner en croquant
xàpp
fendre à la hache
Abal ma sa sémmiñ, ma xàpp matt mi
prête-moi ta hache pour que je fende le bois !
xàtt
extrêmement
Xobi garab gii dafa wex xàtt
la feuille de cet arbre est très amère.
xàpp g-
hache
Jélal xàpp, dagg car bi
prends une hache et coupe la petite branche !
xàpp g-
ceinture talisman
Maam a ma defarluloon xàpp gii
C'est grand-père qui m’avait fait faire cette ceinture magique.
xóoñ b-
riz brûlé
Jox ma xóoñ bi
donne-moi le riz brûlé !
xóll
exprime la manière d’écarquiller les yeux avec un air hagard
Mu ngi ne xóll
il est là, les yeux écarquillés, l’air hagard.
xóotaay b-
profondeur
Ndax xam nga xóotaayu teen bi
connais-tu la profondeur du puits ?
xàqataay
rire aux éclats
Mës nga dégg mu xàqataay ?
l’as-tu jamais entendu rire aux éclats ?
xóot-xóot b-
creux partie concave
Bu bal bi agsee ci xóot-xóot bi, dina taxaw
quand le ballon arrivera dans le creux, il s’immobilisera.
xóotal
approfondir
Gën koo xóotal tuuti
creuse-le un peu plus !
xóoyal
délayer
Xóoyalal fëriñ bi
délaye la farine.
yaam b-
filet où on met la calebasse pour puiser dans un puits peu profond (séane)
Sama yaam dafa xottiku
mon filet à puiser est déchiré.
yaŋañ
marcher en écartant les jambes
Looy yaŋañ ni njulli
qu’as-tu à marcher les jambes écartées comme un circoncis !
yawut b-
juif
Am na ay Yawut ci dëkk bi
il y a des Juifs dans la ville.
yaradal
se dit d’une femme dont les enfants meurent à l’âge de nourrisson
Jur na juróomi doom, waaye dafa yaradal
elle a mis au monde cinq fois mais ses enfants meurent en bas âge.
(prov.) Jur, mu dee, du yaradal; jur, mu dund te baaxul mooy yaradal
le pire n’est pas de perdre ses enfants en bas âge mais qu’ils grandissent pour devenir des vauriens.
yalwaankat b-
mendiant
yambar b-
mou apathique mollasson
Omar ab yambar la, wool Usmaan mu jàppale ma
Omar est un mollasson, appelle Ousmane pour qu’il me donne un coup de main !
yab
traiter qqn avec trop de familiarité
Man nga yab; xam nga xél ne su fi Omar nekkoon, doo taal tele bi waxtu wii
avec moi tu montres trop de familiarité; tu sais bien que si Omar était là, tu n’allumerais pas la télé à cette heure-ci.
yaŋas
danser sans trépigner
(prov.) Am réew, su fa lingeer dee fecc, ku fay woyaan doo rusa yaŋas
dans un pays, quand il arrive que la reine danse, les courtisans ne doivent pas avoir scrupule à esquisser quelques pas.
y
de
Yàllay Israyel
Dieu d’Israël.
Barewul ñu bëgg cerey bëccëg
il n’y a pas beaucoup de gens qui aiment manger du couscous le jour.
y
être
Kuy Omar ?
qui est Omar ?
yakk b-
repas qu’on envoie à qqn en cadeau
Na mu kontaane ca sa yakk ba ?
comme il était content du plat que tu lui as offert !
yaram w-
corps
Sama yaram wi yépp ay metti
J'ai mal partout
Baax na ci yaram
C'est bon pour l’organisme.
(prov.) Sa yaram jàmm bonjour !
ton corps est-il en paix ?).
Yaram baaxul
L'obésité n’est pas bonne.
Yaram wi neexul
il ne jouit pas de toutes ses facultés mentales.
Bi ñu ma nee dem nga, dafa rey sama yaram
quand on m’a dit que tu étais parti, cela m’a refroidi.
yaaram b-
personne généreuse
Yaaram bi, yaa jara woy, yow, Séex Tiijaan
le généreux, c’est toi qui es digne d’être chanté, toi, Cheikh Tidiane.
yarin b-
mode d’éducation
Su gune gii melee nii, ci yarin bi la
si cet enfant est ainsi, c’est dû à la façon dont il a été éduqué.
yamb w-
abeille
Yamb a ko màtt
C'est une abeille qui l’a piqué.
(prov.) Ku bëgg lem ñeme yamb
celui qui veut du miel ne redoute pas les abeilles.
yaakaarloo
faire espérer
Bu ko yaakaarloo ci neen
ne le fais pas espérer en vain !
yaaf w-
poil du nez
War ngaa wàññi sa yaaf yi
tu dois raccourcir tes poils du nez.
yal b-
petit lézard bigarré
Yal du màtte
le petit lézard bigarré ne mord pas.
yakk
servir le repas
Demal yakk añ bi
va servir le déjeuner !
(prov.) Ku yakke loxo, bàyyi kuddu, doo ko ñaareel
celui qui sert le repas avec la main, sans la cuillère ne recommencera pas.
Lu ne yakk na ma ko
il m’a traité de tous les noms.
yarr
exprime la manière de penser à qqch soudain