wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
xottu-butéel g-
eucalyptus
Jëmbët naa ay xottu-butéel sama kër
J'ai planté des eucalyptus chez moi.
xosi b-
tissu teint à l’indigo avec des motifs en zigzag
xoymet
laisser entrevoir (en général, les parties intimes)
Defarul, yaa ngiy xoymet nit
ñi corrige ta tenue, tu laisses entrevoir tes parties intimes.
Xoymet nit bokkul ci yiw
faire entrevoir ses parties intimes à qqn, ce n’est pas être digne.
xotit w-
morceau coupé d’un papier
Foral xotiti kayit yooyu
ramasse ces morceaux de papier coupés.
xotar b-
grappe de fruits du baobab
Yebal xotar yi ci saret bi
charge les paquets de pains de singe dans la charrette.
xotti
déchirer
Xotti yére
acheter des habits.
Xotti yoon
frayer une voie, une route.
xottiku
déchiré
Sama mbubb mi dafa xottiku ci baat bi
mon boubou est déchiré au col.
(prov.) Wax, ab xottiku la, kenn ku nekk, yaa xam noo koy ñawe
une dispute, c’est comme une déchirure, il appartient à chacun de voir comment il va la recoudre.
xucc b-
cordon ombilical
Ndax xucc bi rot na ?
est-ce que le cordon ombilical est tombé ?
xuléet
regarder la réalité en face
Ba mu nekkee lu yàgg ca kër buur, mu ni xuléet, delluwaat na mu meloon
après être restée longtemps à la cour du roi, elle se fit une raison et redevint comme elle était.
xund-xund m-
libellule
xuréet
avoir la coqueluche
Dafa xuréet
il a la coqueluche.
xunn
extrêmement puant
Dafa xasaw xunn
ça pue énormément.
xunn
s’irriter, s’énerver (parce qu’on est perdant)
Danu doon kart, ma gañe ko, mu xunn
nous jouions aux cartes, je l’ai gagné et il s’est irrité.
xurfaan j-
rhume
Garab bii baax na ci xurfaan ji
ce médicament est bon contre le rhume.
xunnloo
exaspérer
xurfaan
être enrhumé
Dafa xurfaan
il est enrhumé.
xur w-
vallée asséchée
Nanu jaare ci xur wi; moo gëna gaaw
passons par la vallée asséchée; c’est plus rapide.
xusër
manière d’apparaître sans qu’on s’y attende, de se présenter à l’improviste
Benn bés, gaynde ga ne xusër ci kanamam
un jour, le lion surgit devant lui.
xutaab b-
situation défavorable
Duggati na ci xutaab
il est dans le pétrin encore une fois.
xutba b-
sermon
Xutba bi dafa gudd tey
le sermon a été long aujourd’hui.
xutt b-
poltron peureux
Ab xutt la
C'est un poltron.
xutba
dire un sermon
Dafay xutba
il dit un sermon.
xuuj b-
camelote
Xuuj bii nga jénd ?
c’est cette camelote que tu as achetée ?
xuyët
Éclairer une chambre au crépuscule, pour un laps de temps pour chasser les mauvais esprits qui, selon les croyances, pourraient s’y trouver
Demal xuyët néeg ba, xale baa nga ca biir
va éclairer la chambre un peu, l’enfant est dedans.
xuy
clignoter
Lii naan xuy, xuy, xuy, lan la
cette chose qui clignote sans arrêt, qu’est-ce que c’est ?
xuuge b-
personne bossue
Mësumaa gis xuuge bu am yaram
je n’ai jamais vu un bossu obèse.
xuus
marcher dans l’eau
Lu-tax nga xuus ak say dàll ?
pourquoi as-tu marché dans l’eau avec tes chaussures ?
(prov.) Ndox moo fekkewul ba muy taa, bul jiite xuusam
ne te mets pas en tête de file pour marcher dans une étendue d’eau que tu n’as pas vue se former
xuur-baat
avoir la voix rauque
Dafa xuur-baat
il a la voix rauque.
xuyéntaan b-
luciole
Xuyéntaan bi la xaj biy baw
le chien aboie après la luciole.
xuy-xuyi
clignoter (lumière)
xàbb g-
canari ébréché dont on se sert encore
Defal xàbb gi ca waañ wa
mets le canari ébréché à la cuisine !
xuur b-
testicule
Xuuri xar maa ngi
voici les testicules du mouton.
xuur b-
terre noire (renfermant du fer)
Foofa, suuf si, xuur la
là-bas, la terre est de la terre noire.
xuusmaañàpp g-
marionnette
Am na ñax mu nu daan foye xuusmaañàpp
il y a une herbe avec laquelle nous jouions à faire des marionnettes.
xàcc
mettre bas un mort-né
Dafa xàcc
elle a mis bas un mort-né.
xàddi
cesser d’attendre après une longue attente
Xaar naa la ba xàddi
je t’ai tant attendu que j’ai fini par ne plus attendre.
xàccee b-
annulation d’une vente par l’acheteur, rédhibition
Xàcceeb kër gi mu ko jaayoon moo tas seenug xaritoo
L'annulation de vente de la maison qu’il lui avait vendue a mis fin à leur amitié.
xuuxaan b-
hernie scrotale
Xuuxaanam bi lañuy waxtaane
ils parlent de son hernie scrotale.
(prov.) Werante xuuxaan : tekki tubay
plutôt que de polémiquer sur l’existence d’une hernie scrotale, il faut défaire le pantalon
xàcci
esquisser un coup
Dafa xàcci kuur gi, gis ma, daldi daw
il a esquissé un coup avec le pilon, m’a vu et a fui.
xàcci
(humain) Avorter
Ëmb bi dafa xàcci
elle a avorté.
xàddamtiku
se racler la gorge, faire hem ! hem !
Ba may xàddamtiku, dama bëggoon nga noppi
quand je faisais hem ! hem ! je voulais que tu te taises.
xàll
frayer une voie
Bi ñuy xàll yoon wi lañu yékëti kër yi fi nekkoon
C'est quand on construisait la voie qu’on a dégagé les maisons qui se trouvaient ici.
(prov.) Bu ñay di xàll yoon, doom yaa tax
quand l’éléphant fraie un passage, c’est à cause de ses petits.
xàccee
annuler un achat après avoir payé
Su ma ko rusuloon, dinaa xàccee xar mi
si je n’avais pas d’égard pour lui, je ferai annuler l’achat du mouton.
xàjjalekoo
séparer de
Foofa lañu xàjjalekoo ak moom
C'est là que nous nous sommes séparés de lui.
xàmmaliku
se retrouver
Mbedd male la; xàmmaliku naa
C'est la rue là-bas; je m’y retrouve.
xàmbaar w-
gros paquets de nuages défilant à grande vitesse qui s’accumulent puis reforment des paquets à nouveau
xàmp
prélever (une partie de qqch avec les dents)
Ñówal, ñu xàmpi xaali Baay Xaali Njaay
viens que nous allions mordre dans les melons de Père Khali Ndiaye.
xànc
défibrer
Am na réew yu, dañuy xànc xasum koko mi, def ko buum
il y a des pays où on défibre l’enveloppe de noix de coco pour en faire des cordes.
xàll w-
grand-route en zone rurale
Soo demee ca xàll wa, dinga am woto
si tu vas sur la grand-route, tu auras une voiture.
xàmpit w-
prélevé avec les dents