sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
4
12
{ "fr": "Et à vous la moitié de ce laissent vos épouses, si elles n´ont pas d´enfants. Si elles ont un enfant, alors à vous le quart de ce qu´elles laissent, après exécution du testament qu´elles auraient fait ou paiement d´une dette. Et à elles un quart de ce que vous laissez, si vous n´avez pas d´enfant. Mais si vous avez un enfant, à elles alors le huitième de ce que vous laissez après exécution du testament que vous auriez fait ou paiement d´une dette. Et si un homme, ou une femme, meurt sans héritier direct, cependant qu´il laisse un frère ou une sœur , à chacun de ceux-ci alors, un sixième. S´ils sont plus de deux, tous alors participeront au tiers, après exécution du testament ou paiement d´une dette, sans préjudice à quiconque. (Telle est l´) Injonction d´Allah ! Et Allah est Omniscient et Indulgent.", "wo": "La seeni jabar bàyyi ginnaaw, am ngeen ca génn-wàll ndagam amuñu doom ju góor. Su amee doom ju góor, kon ñetteelu alal ja la jëkkër ja di jël ginnaaw bi ñu génnee ndénkaane ya mu génne woon, walla peyum bor [su amee]. Ñoom seeni jabar am nañu ñetteelu la seen jëkkër bàyyi ndegam amul doom ju góor, su amee doom ju góor [jëkkër ja], kon juróom- ñetteelu alal ja lay jël ginnaaw ba ñu génnee ndénkaane ya mu dénkaane woon walla bor. Bu fekkee ne góor walla jigéen mooy donn ab càppaacóli [ku amul doom, amul waajur] bu am rakk walla mag ju góor walla ju jigéen, ku mu ca doon ci ñoom ñaar juróom-benneelu alal ja lay jël. Bu ñu ëppee kenn nit, dañuy bokk donn ñetteelu alal ja ginnaaw bu ñu génnee ndénkaane ya mu dénkaane woon walla bor yu àndul ak lor [way-dono ya]. Lii dénkaane la lu bawoo fa Yàlla ! Te Yàlla ku xam la, Ku lewet la." }
4
13
{ "fr": "Tels sont les ordres d´Allah. Et quiconque obéit à Allah et à Son messager, Il le fera entrer dans les Jardins sous lesquels coulent les ruisseaux, pour y demeurer éternellement. Et voilà la grande réussite.", "wo": "Loolu mooy deytali Yàlla yi. Ku ko topp ak ub Yonentam [ca la mu àtte], danañu ko dugal Àjjana joo xam ne dex ya dañuy daw ca ronam, ñu béel fa [sax ba fàwwu]. Loolu mooy texe gu mag ga.(r)" }
4
14
{ "fr": "Et quiconque désobéit à Allah et à Son messager, et transgresse Ses ordres, Il le fera entrer au Feu pour y demeurer éternellement. Et celui-là aura un châtiment avilissant.", "wo": "Ku moy Yàlla ak ub Yonentam, di jéggi daytali Yàlla yi, Danañu ko dugal Safara, mu béel fa, bokk ca mbugal muy toroxale." }
4
15
{ "fr": "Celles de vos femmes qui forniquent, faites témoigner à leur encontre quatre d´entre vous. S´ils témoignent, alors confinez ces femmes dans vos maisons jusqu´à ce que la mort les rappelle ou qu´Allah décrète un autre ordre à leur égard .", "wo": "Ña def ñaawtéef [njaaloo] ci seeni jigéen, nangeen ko seedeloo ñeenti nit ci yéen. Bu ñu ko seedee, nangeen leen tëj ba dee fekk leen fa walla ba Yàlla ubbil leen aw yoon [wu ñu mën a aw ba mucc]. " }
4
16
{ "fr": "Les deux d´entre vous qui l´ont commise [la fornication], sévissez contre eux. S´ils se repentent ensuite et se réforment, alors laissez-les en paix. Allah demeure Accueillant au repentir et Miséricordieux .", "wo": "Ña nga xam ne loolu dal na leen ci yéen [góor ña], nangeen leen tas. Bu ñu tuubee, wëlbëtiku di def lu baax, nangeen leen bàyyi. Naka Yàlla, Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la." }
4
17
{ "fr": "Allah accueille seulement le repentir de ceux qui font le mal par ignorance et qui aussitôt se repentent. Voilà ceux de qui Allah accueille le repentir. Et Allah est Omniscient et Sage.", "wo": "Yàlla rekk ay nangu tuub, ña def ñaawtéef ci ñàkk a xam, te gaaw daldi tuub. Ñooña Yàlla dana nangu seen tuub. Yàlla Aji-xam la, Aji-xereñ la." }
4
18
{ "fr": "Mais l´absolution n´est point destinée à ceux qui font de mauvaises actions jusqu´au moment où la mort se présente à l´un d´eux, et qui s´écrie : \"Certes, je me repens maintenant\" - non plus pour ceux qui meurent mécréants. Et c´est pour eux que Nous avons préparé un châtiment douloureux.", "wo": "Ña dul am njéggal ñooy ña def ñaawtéef [te baluwuñu seen Boroom] ba dee dikkal kenn ca ñoom muy door a wax ne : “Léegi tuub naa” - ak ña nga xam ne dañuy dee ci kéefar. Ñooña, danañu leen xaaroo mbugal mu tar [metti]." }
4
19
{ "fr": "ô les croyants ! Il ne vous est pas licite d´hériter des femmes contre leur gré. Ne les empêchez pas de se remarier dans le but de leur ravir une partie de ce que vous aviez donné, à moins qu´elles ne viennent à commettre un péché prouvé. Et comportez-vous convenablement envers elles. Si vous avez de l´aversion envers elles durant la vie commune, il se peut que vous ayez de l´aversion pour une chose où Allah a déposé un grand bien .", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Daganul ci yéen ngeen di donn jigéen ña ci nooteel. Daganul it ngeen gàllankoor leen, ne buñu sëy ngir bëgg nangu lenn ci li ngeen leen joxoon, lu dul ña cay def ñaawtéef wu bir. Nangeen di ànd ak ñoom ci njekk. Bu ngeen leen sibee nag, [xamleen ne] mën ngeen a sib [bañ] lenn te fekk na Yàlla def ca loola yiw wu bari.(s)" }
4
20
{ "fr": "Si vous voulez substituer une épouse à une autre, et que vous ayez donné à l´une un quintar , n´en reprenez rien. Quoi ! Le reprendriez-vous par injustice et péché manifeste ?", "wo": "Bu ngeen bëggee bàyyi jabar wuutale ko ak jeneen jabar, te fekk joxoon ngeen ko alal, buleen ca nangu dara. Doonte la [barigo]wurus la ! Ndax lu ngeen ca jële ci tooñeel la ak bàkkaar bu bari." }
4
21
{ "fr": "Comment oseriez-vous le reprendre, après que l´union la plus intime vous ait associés l´un à l´autre et qu´elles aient obtenu de vous un engagement solennel ?", "wo": "Naka ngeen di nangoo alal ja, te jokkoo ngeen ba noppi te ñoom ñu fasanteek yéen kóllare gu dëgër?" }
4
22
{ "fr": "Et n´épousez pas les femmes que vos pères ont épousées, exception faite pour le passé. C´est une turpitude, une abomination , et quelle mauvaise conduite !", "wo": "Buleen takk ña seeni baay takkoon ca jigéen ña, ginnaaw la wéy ba noppi. Loolu lu ñaaw la, te luy waral mbugal la, yoon wu dëng la !" }
4
23
{ "fr": "Vous sont interdites vos mères, filles, sœurs, tantes paternelles et tantes maternelles, filles d´un frère et filles d´une sœur, mères qui vous ont allaités, sœurs de lait, mères de vos femmes, belles-filles sous votre tutelle et issues des femmes avec qui vous avez consommé le mariage; si le mariage n´a pas été consommé, ceci n´est pas un péché de votre part; les femmes de vos fils nés de vos reins; de même que deux sœurs réunies - exception faite pour le passé. Car vraiment Allah est Pardonneur et Miséricordieux;", "wo": "Araam na ci yéen [takk jabar] seeni ndey, seeni doom yu jigéen, seeni mag walla rakk yu jigéen, seeni bàjjen, seeni mag walla rakki yaay, seeni doomi mag walla rakk ju góor, seeni ndey ya leen nàmpal, seeni jigéen ya ngeen bokk ku leen nàmpal, seeni yaayi jabar ak seeni doomi jabar, ya ngeen yor ca seeni kiiraay, ndegam jot ngeen a xaraf [jote] ak seeni ndey ; bu ngeen jotul a xaraf ak seeni ndey, aayul ngeen sëy ak ñoom ; [araam na it ci yéen seeni jabari doomi ña ngeen bokk ndey ak baay, walla ndey rekk walla baay rek] ginnaaw la weesu [lu jiitu Lislaam]. Yàlla ab Jéggalaakoon la [ca loola weesu], di Jaglewaakoon ;" }
4
24
{ "fr": "et parmi les femmes, les dames (qui ont un mari), sauf si elles sont vos esclaves en toute propriété . Prescription d´Allah sur vous ! A part cela, il vous est permis de les rechercher, en vous servant de vos bien et en concluant mariage, non en débauchés. Puis, de même que vous jouissez d´elles, donnez-leur leur mahr, comme une chose due. Il n´y a aucun péché contre vous à ce que vous concluez un accord quelconque entre vous après la fixation du mahr. Car Allah est, certes, Omniscient et Sage.", "wo": "[araam na it ci yéen] jigéen ña saŋewu, ba mu des jebéer ya ngeen moom. Ndigalu Yàllaa ngoogu ci yéen ! Ginnaaw ñooña, [ña mu lim ciy jigéen ñu daganul ngeen sëy ak ñoom]. Dagan na ngeen saŋewu cig jigéen te joxe seeni alal, di way-sëy ak ñoom, bañ di way-njaaloo. Te jigéen ña ngeen sàkku bànneexu ci ñoom, nangeen leen jox seeni can. Lii mbir mu Yàlla santaane la [farataal]. Aayul ginnaaw la ñu farataal nag ngeen déggoo [ci li ngeen war a joxe]. Yàlla de Moom Ku xam la, Ku xereñ la.(h)" }
4
25
{ "fr": "Et quiconque parmi vous n´a pas les moyens pour épouser des femmes libres (non esclaves) croyantes, eh bien (il peut épouser) une femme parmi celles de vos esclaves croyantes. Allah connaît mieux votre foi, car vous êtes les uns des autres (de la même religion). Et épousez-les avec l´autorisation de leurs maîtres (Waliy) et donnez-leur un mahr convenable; (épousez-les) étant vertueuses et non pas livrées à la débauche ni ayant des amants clandestins. Si, une fois engagées dans le mariage, elles commettent l´adultère, elles reçoivent la moitié du châtiment qui revient aux femmes libres (non esclaves) mariées. Ceci est autorisé à celui d´entre vous qui craint la débauche; mais ce serait mieux pour vous d´être endurant. Et Allah est Pardonneur et Miséricordieux .", "wo": "Ku amul can ci yéen, gu mu mën a takke jabar ju nekk gor te di jullit, na takk kon ci jebéer ya di ay jullit di xale yu jigéen ya bokk ci yéen. Yàllaa gën a xam fa seen gëm toll, ndax yéen a mëññante [jurante]. Nangeen leen takk ci ndigalu seeni kilifa te ngeen jox leen seeni can ci njekk ; ngeen di way-sëy, di bañ di way-njaaloo, te bañ leen a jàppe ay coro cig nëbbu. Bu ñu sëyee te def njaaloo [ñoom jebéer ya], war nañu leen a teg genn-wàllu mbugal ma ñuy teg gor gu jigéen. Loolu ndigal la ci ku ñu ragal mu njaaloo ci yéen ; bu ngeen mënee muñ, moo gën ci yéen. Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la." }
4
26
{ "fr": "Allah veut vous éclairer, vous montrer les voies des hommes d´avant vous, et aussi accueillir votre repentir. Et Allah est Omniscient et Sage.", "wo": "Yàlla dafa namm a leeral [àtteem] ci gindi leen, teg leen ca yoonu ña leen jiitu woon, te jéggal leen. Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la [ci àtteem]." }
4
27
{ "fr": "Et Allah veut accueillir votre repentir. Mais ceux qui suivent les passions veulent que vous incliniez grandement (vers l´erreur comme ils le font).", "wo": "Yàlla dafa leen bëgg a jéggal. Waaye ña topp seen bànneex, ñoom dañuy bëgg ngeen jeng, jeng gu fés." }
4
28
{ "fr": "Allah veut vous alléger (les obligations,) car l´homme a été créé faible.", "wo": "Yàlla dafa leen a bëgg a woyofal [àtteem] ndax néew doole ak lott gi nit bindoo." }
4
29
{ "fr": "ô les croyants ! Que les uns d´entre vous ne mangent pas les biens des autres illégalement. Mais qu´il y ait du négoce (légal), entre vous, par consentement mutuel. Et ne vous tuez pas vous-mêmes . Allah, en vérité, est Miséricordieux envers vous.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Buleen lekkante seeni alal cig neen. Waaye mën ngeen a jëflante ci njulo [jënd ak jaay] mu ànd ak déggoo ci seen mbir. Te buleen reyante. Yàlla, Ku am yërmaande ci yéen la.(s)" }
4
30
{ "fr": "Et quiconque commet cela, par excès et par iniquité, Nous le jetterons au Feu, voilà qui est facile pour Allah.", "wo": "Ku def loolu, ci ndëngte ak ug tooñ, Dananu ko séndal Safara, te loolu lu yomb la ca Yàlla." }
4
31
{ "fr": "Si vous évitez les grands péchés qui vous sont interdits, Nous effacerons vos méfaits de votre compte, et Nous vous ferons entrer dans un endroit honorable (le Paradis).", "wo": "Bu ngeen moytoo bàkkaar yu rëy yi ñu tere, Dananu leen baal seeni ñaawtéef [yu ndaw yi, soppil leen ko yiw], te Dananu leen tàbbal dëkkuwaay bu tedd (Àjjana)." }
4
32
{ "fr": "Ne convoitez pas ce qu´Allah a attribué aux uns d´entre vous plus qu´aux autres; aux hommes la part qu´ils ont acquise, et aux femmes la part qu´elles ont acquise. Demandez à Allah de Sa grâce. Car Allah, certes, est Omniscient.", "wo": "Buleen mébét li Yàlla yékkati ñenn ci kaw ñeneen ; góor ña am nañu cër [sañ] ca la ñu fàggu, jigéen ña it am nañu cër ca la ñu fàggu. Ñaanleen Yàlla ciy xéewalam. Yàlla lépp la xam." }
4
33
{ "fr": "A tous Nous avons désigné des héritiers pour ce que leur laissent leurs père et mère, leurs proches parents, et ceux envers qui, de vos propres mains, vous vous êtes engagés, donnez leur donc leur part, car Allah, en vérité, est témoin de tout .", "wo": "Ku nekk leeral Nanu ko ña koy donn ca la waajur ya bàyyi ginnaaw, ak jegeñaale ya, te ña seeni dëelaante ak ñoom fasuwoon, nangeen leen jox seeni cër, Yàlla seede la ci lu nekk." }
4
34
{ "fr": "Les hommes ont autorité sur les femmes, en raison des faveurs qu´Allah accorde à ceux-là sur celles-ci, et aussi à cause des dépenses qu´ils font de leurs bien. Les femmes vertueuses sont obéissantes (à leurs maris), et protègent ce qui doit être protégé, pendant l´absence de leurs époux, avec la protection d´Allah. Et quant à celles dont vous craignez la désobéissance, exhortez-les, éloignez-vous d´elles dans leurs lits et frappez-les. Si elles arrivent à vous obéir, alors ne cherchez plus de voie contre elles, car Allah est certes, Haut et Grand !", "wo": "Góor ñi, kilifa lañu ci jigéen ñi ndax la Yàlla yékkati ñenn ci ñoom ca kaw ñeneen ña, ak ngir la góor ña di dundale ci seeni alal [jigéen ña]. Waaye jigéen ñu sell ña, jaamukatu Yàlla lañu te ñu sàmmu lañu cig wéetaay ni ko Yàlla santaanee. Jigéen ña ngeen ragal ñu féttéerlu, nangeen leen waar, nangeen leen tong ca alal ya, nangeen leen dóor. Bu ñu leen nangoo topp, nangeen leen jàmmal, bañ leen defati dara, Yàlla dey Kawe na, Màgg na !" }
4
35
{ "fr": "Si vous craignez le désaccord entre les deux [époux], envoyez alors un arbitre de sa famille à lui, et un arbitre de sa famille à elle. Si les deux veulent la réconciliation, Allah rétablira l´entente entre eux. Allah est certes, Omniscient et Parfaitement Connaisseur.", "wo": "Bu ngeen ragalee tàggoo ci diggante ñaar ñay sëy, nangeen yabal kilifag ku góor ki ak kilifag ku jigéen ki. Ndegam bëgg nañoo defaroo, Yàlla dana yéwénal seen diggante [Dëppële leen]. Yàlla Ku Xam la, Ku Deñ-kumpa la." }
4
36
{ "fr": "Adorez Allah et ne Lui donnez aucun associé. Agissez avec bonté envers (vos) père et mère, les proches, les orphelins, les pauvres, le proche voisin, le voisin lointain, le collègue et le voyageur, et les esclaves en votre possession, car Allah n´aime pas, en vérité, le présomptueux, l´arrogant ,", "wo": "Nangeen jaamu Yàlla te bañ Koo bokkaale dara. Te ngeen rafetal ci seeni waajur, ak ci seeni jegeñaale, ak jirim yi, ak néew-ji-doole yi, ak seeni dëkkandoo ya di seeni mbokk, ak dëkkandoo ju sori, ak àndandoo ya, ak doxandeem , ak seeni jebéer, Yàlla du safoo kuy puukarewu ak a ndamu,(r)" }
4
37
{ "fr": "Ceux qui sont avares et ordonnent l´avarice aux autres, et cachent ce qu´Allah leur a donné de par Sa grâce. Nous avons préparé un châtiment avilissant pour les mécréants.", "wo": "Ña nga xam ne dañoo nay tey xiirtal nit ña ci nay, boole kook di nëbb lu leen Yàlla jox, baaxe leen ci wërsëg. [Nañu xam ne] Nun Yàlla dogu Nanu yéefar ya mbugal muy toroxale ." }
4
38
{ "fr": "Et ceux qui dépensent leurs biens avec ostentation devant les gens, et ne croient ni en Allah ni au Jour dernier. Quiconque a le Diable pour camarade inséparable, quel mauvais camarade !", "wo": "Yàlla safoowul itam ñiy sànk seeni alal ngir ngistal, ci bëti nit ñi, te gëmuñu Yàlla ak Bis- pénc ba. Koo xam ne Séytaanee di àndandoom aka bon bon ub àndandoo !" }
4
39
{ "fr": "Qu´auraient-ils à se reprocher s´ils avaient cru en Allah et au Jour dernier et dépensé (dans l´obéissance) de ce qu´Allah leur a attribué ? Allah, d´eux, est Omniscient.", "wo": "Waaw, lu Ma leen doon won su ñu gëmoon Yàlla ak Bis-pénc ba, tey joxe ca la leen Yàlla wërsëgal ? Yàllaa ka leen a xam." }
4
40
{ "fr": "Certes, Allah ne lèse (personne), fût-ce du poids d´un atome. S´il est une bonne action, Il la double, et accorde une grosse récompense de Sa part.", "wo": "Yàlla du tooñ kenn, lu toll ni pepp. Te ku def u yiw Mu ful ko, joxe ca pey [yool] gu màgg." }
4
41
{ "fr": "Comment seront-ils quand Nous ferons venir de chaque communauté un témoin et que Nous te (Muhammad) ferons venir comme témoin contre ces gens-ci ?", "wo": "Naka mu ? [Bus bis-pénc baa,] ba Nu indi xeet wu nekk ànd ak seede te yaw [Muhammad], Nu indi la bu boobaa nga doon seede ci ñii [waa Màkka] ?" }
4
42
{ "fr": "Ce jour-là, ceux qui n´ont pas cru et ont désobéi au Messager, préféreraient que la terre fût nivelée sur eux et ils ne sauront cacher à Allah aucune parole.", "wo": "Bis booba, ña weddi woon te toppuñu Yonent bi, danañu ngéeju ñu maasale leen ak suuf si te fekk na Yàlla moom kenn mënu Koo nëbb jenn wax." }
4
43
{ "fr": "ô les croyants ! N´approchez pas de la Salat alors que vous êtes ivres, jusqu´à ce que vous compreniez ce que vous dites, et aussi quand vous êtes en état d´impureté [pollués] - à moins que vous ne soyez en voyage - jusqu´à ce que vous ayez pris un bain rituel. Si vous êtes malades ou en voyage, ou si l´un de vous revient du lieu où il a fait ses besoins, ou si vous avez touché à des femmes et vous ne trouviez pas d´eau, alors recourez à une terre pure, et passez-vous-en sur vos visages et sur vos mains. Allah, en vérité est Indulgent et Pardonneur .", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Buleen jege ag julli te fekk ngeen màndi, ba ba ngeen di xam li ngeen di wax, bu ngeen laabul ci sobe it [buleen jëm ci julli] te ame janaba - ndeem fekkuleen ci yoon di tukki – ba ba ngeen di sangu [farata]. Bu ngeen woppee, walla ngeen nekkati ci tukki, mbaa ngeen jóge wanag wa, walla ngeen joteek jigéen ña [sëy] te amuleen ndox [mu mën a jàpp walla sangu], nangeen tiim ci suuf su laab, ngeen raay seen xar-kanam ak seeni yoxo. Yàlla, Baalekat la, Jéggalaakoon la." }
4
44
{ "fr": "N´as-tu (Muhammad) pas vu ceux qui ont reçu une partie du Livre acheter l´égarement et chercher à ce que vous vous égariez du [droit] chemin ?", "wo": "Moo ndax gisoo ña ñu joxoon lenni Téere ba, ñu jënd ñoom ag réer, ba noppi nag yéen ngeen réere yoon wu jub wa ?" }
4
45
{ "fr": "Allah connaît mieux vos ennemis. Et Allah suffit comme protecteur. Et Allah suffit comme secoureur.", "wo": "Yàllaa gën a xam seeni noon. Yàlla doy na te mat sëkk kilifa. Yàlla doy na te mat sëkk itam ndimbal." }
4
46
{ "fr": "Il en est parmi les Juifs qui détournent les mots de leur sens, et disent : \"Nous avions entendu, mais nous avons désobéi\", \"écoute sans qu´il te soit donné d´entendre\", et favorise nous \"Raina\", tordant la langue et attaquant la religion. Si au contraire ils disaient : \"Nous avons entendu et nous avons obéi\", \"écoute\", et \"Regarde-nous\", ce serait meilleur pour eux, et plus droit. Mais Allah les a maudits à cause de leur mécréance; leur foi est donc bien médiocre .", "wo": "Am na ci Yahuud yi ñuy firi baat [kàddu] jële leen ca barab ya ñu nekkoon, tey wax naan : “Dégg nanu waaye bañ nanu waay” , ñu naan : “Déggal te kenn du la dégg” , yàq waxin wa [Raahinaa], ñaawal ko ak bëgg a yàq diine. Waaye bu ñu ne woon : “Dégg nanu te nangu nanu” , “Déggal” , te “Xool nu” , kon mu gën ci ñoom, te mooy la gën a jub. Waaye Yàlla rëbb na leen [sorel yërmaandeem] ña weddi ; ñu néew ci ñoom ñoo gëm." }
4
47
{ "fr": "ô vous à qui on a donné le Livre, croyez à ce que Nous avons fait descendre, en confirmation de ce que vous aviez déjà, avant que Nous effacions des visages et les retournions sens devant derrière, ou que Nous les maudissions comme Nous avons maudit les gens du Sabbat . Car le commandement d´Allah est toujours exécuté.", "wo": "Éy yéen ñi jotoon Téere, gëmleen lii Nu wàcce, di dëggal li ngeen yor, bala Noo marmaral ay xar-kanam wëlbati leen ñu jëm ginnaaw, walla Nu leen di rëbbu na ñu rëbbe woon ña jalgati woon ca gaawu ba. Ndigalu Yàlla ak mbiram jëfe la sant [du jaas].(s)" }
4
48
{ "fr": "Certes Allah ne pardonne pas qu´on Lui donne quelqu´associé. A part cela, Il pardonne à qui Il veut. Mais quiconque donne à Allah quelqu´associé commet un énorme péché.", "wo": "Yàlla du baal ku Ko bokkaale dara. Waaye lu moy loolu, Dana ko jéggal ku ko soob. Ka bokkaale Yàlla [ak dara], def na bàkkaar bu rëy." }
4
49
{ "fr": "N´as-tu pas vu ceux-là qui se déclarent purs ? Mais c´est Allah qui purifie qui Il veut; et ils ne seront point lésés, fût-ce d´un brin de noyau de datte .", "wo": "Moo ndax dangaa gisul ña doon sànkoo sellal seen bopp ? Li wér te wóor mooy Yàllaay sellal ku ko soob ; te duleen tooñ [Bis-pénc ba], lu toll ni karnu xooxu tàndarma." }
4
50
{ "fr": "Regarde comme ils inventent le mensonge à l´encontre d´Allah. Et çà, c´est assez comme péché manifeste !", "wo": "Gisal ni ñuy duuralee Yàlla ay fen. Te loolu, doy na bàkkaar te rànniku !" }
4
51
{ "fr": "N´as-tu pas vu ceux-là, à qui une partie du Livre a été donnée, ajouter foi à la magie (gibt) et au taghout, et dire en faveur de ceux qui ne croient pas : \"Ceux-là sont mieux guidés (sur le chemin) que ceux qui ont cru\" ?", "wo": "Moo ndax gisoo ña jot lenni Téere ba, ñay gëm ay xërëm yu tudd [Jibti] ak [Taagut], ñuy wax ak ña weddi naanleen: “Seen xërëm yooyoo gën a nekk ci njub jullit ya gëm [Lislaam]” ?" }
4
52
{ "fr": "Voilà ceux qu´Allah a maudits; et quiconque Allah maudit, jamais tu ne trouveras pour lui de secoureur.", "wo": "Ñooñu Yàlla rëbb na leen ; te ku Yàlla rëbb, kenn mënu koo amal ndimbal." }
4
53
{ "fr": "Possèdent-ils une partie du pouvoir ? Ils ne donneraient donc rien aux gens, fût-ce le creux d´un noyau de datte .", "wo": "Am dañuy am sañ-sañ ci nguur gi ? Te kenn du ca sédd nit ñi, lu toll ci mboxosu xooxu tàndarma." }
4
54
{ "fr": "Envient-ils aux gens ce qu´Allah leur a donné de par Sa grâce ? Or, Nous avons donné à la famille d´Abraham le Livre et la Sagesse ; et Nous leur avons donné un immense royaume.", "wo": "Am dañuy iñaane nit ñi ci la leen Yàlla jox ciy ngënéelam ? Joxoon Nanu waa kër Ibraahiima ab Téere ak xam-xamu xereñe ; joxoon Nanu leen nguur gu rëy. " }
4
55
{ "fr": "Certains d´entre eux ont cru en lui, d´autres d´entre eux s´en sont écartés. l´Enfer leur suffira comme flamme (pour y brûler).", "wo": "Amoon nañu ca ñoom ñu gëm [Téere ba], ak ñu dëddu [weddi Téere ba]. Te Safara dana leen doy." }
4
56
{ "fr": "Certes, ceux qui ne croient pas à Nos Versets, (le Coran) Nous les brûlerons bientôt dans le Feu. Chaque fois que leurs peaux auront été consumées, Nous leur donnerons d´autres peaux en échange afin qu´ils goûtent au châtiment. Allah est certes Puissant et Sage!", "wo": "Ña weddi Sunuy kàddu, Dananu leen mos a séndal. Aw Saafara, wow, saa su seen deri yaram ñoree, Nu wecceekook yeneen, ngir ñu yëg mbugal ma. Yàlla boroom kàttan la, Ku xereñ la!" }
4
57
{ "fr": "Et quant à ceux qui ont cru et fait de bonnes oeuvres, bientôt Nous les ferons entrer aux Jardins sous lesquels coulent des ruisseaux. Ils y demeureront éternellement. Il y aura là pour eux des épouses purifiées. Et Nous les ferons entrer sous un ombrage épais", "wo": "Ñi gëm tey def u yiw, Dananu leen dëkkal ci Àjjana yu dex ya di daw ci seen ron. Ñu béel fa [sax fàwwu]. Danañu fa am ay jabar yu laab. Dananu leen dugal ci ker yu dëll" }
4
58
{ "fr": "Certes, Allah vous commande de rendre les dépôts à leurs ayants droit, et quand vous jugez entre des gens, de juger avec équité. Quelle bonne exhortation qu´Allah vous fait ! Allah est, en vérité, Celui qui entend et qui voit tout.", "wo": "Yàlla digal na leen ngeen delloo ndénkaane ya seeni boroom, te bu ngeen dee àtte diggante nit ña, ngeen defe ko ci maandute. Mbir mii leen Yàlla di ñaaxe, ndaw lu baax ! Yàlla Kuy dégg la, Kuy gis la.(n)" }
4
59
{ "fr": "ô les croyants ! Obéissez à Allah, et obéissez au Messager et à ceux d´entre vous qui détiennent le commandement . Puis, si vous vous disputez en quoi que ce soit, renvoyez-là à Allah et au Messager, si vous croyez en Allah et au Jour dernier. Ce sera bien mieux et de meilleur interprétation (et aboutissement).", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Toppleen Yàlla, topp Yonent bi ak ña nekk kilifa ci seen biir. Bu ngeen dogoo walla [xëccoo] ci mbir, dellooleen ko ca Yàlla ak Yonent bi ndegam gëm ngeen Yàlla ak Bis-pénc ba. Looloo gën te moo gën a rafet déggin." }
4
60
{ "fr": "N´as-tu pas vu ceux qui prétendent croire à ce qu´on a fait descendre vers toi [prophète] et à ce qu´on a fait descendre avant toi ? Ils veulent prendre pour juge le Tagut, alors que c´est en lui qu´on leur a commandé de ne pas croire. Mais le Diable veut les égarer très loin, dans l´égarement.", "wo": "Ndax gisoo ña nga xam ne nee nañooy gëm nañu la ñu wàcce ci yaw ak la ñu wàcce woon mu jiitu la ? Te ña nga bëgg a àttewoo ci ay xërëm, te dañu koo waroon a weddi bàyyi ko. Waaye Séytaane moom bëgg leen a sànk, soreel leen dëgg." }
4
61
{ "fr": "Et lorsqu´on leur dit : \"Venez vers ce qu´Allah a fait descendre et vers le Messager\", tu vois les hypocrites s´écarter loin de toi.", "wo": "Bu ñu leen waxee ne : “Ñëwleen ci li Yàlla wàcce ak ci Yonent bi” , nga gis naaféq ya dëddu ko." }
4
62
{ "fr": "Comment (agiront-ils) quand un malheur les atteindra, à cause de ce qu´ils ont préparé de leurs propres mains ? Puis ils viendrons alors prés de toi, jurant par Allah : \"Nous n´avons voulu que le bien et la réconciliation\".", "wo": "Naka mu? Bu leen musiba dalee jóge ca la ñu jëf, ba tax ñu ñëw ci yaw di giñ ci Yàlla, naan : “Bëggunu woon lu dul rafetal ak juboo” ." }
4
63
{ "fr": "Voilà ceux dont Allah sait ce qu´ils ont dans leurs coeurs. Ne leur tiens donc pas rigueur, exhorte-les, et dis-leur sur eux-mêmes des paroles convaincantes.", "wo": "Ñooña, Yàlla xam na la nekk ci seeni xol. Nanga leen dëddu [dummóoyu] te nanga leen waar, waxleen ci seen bopp wax ju jotal." }
4
64
{ "fr": "Nous n´avons envoyé de Messager que pour qu´il soit obéi, par la permission d´Allah. Si, lorsqu´ils ont fait du tort à leurs propres personnes ils venaient à toi en implorant le pardon d´Allah et si le Messager demandait le pardon pour eux, ils trouveraient, certes, Allah, Très Accueillant au repentir, Miséricordieux.", "wo": "Yónniwunu ab Yonent lu dul ne dañu koo war a topp ci ndigalu Yàlla. Te ñoom ba ñu tooñee seen bopp, bu ñu dikkoon ci yaw di sàkku jéggalu Yàlla, Yonent bi jéggalul leen, kon danañu fekk Yàlla mu di Jéggalaakoon, di Jaglewaakoon." }
4
65
{ "fr": "Non ! ... Par ton Seigneur ! Ils ne seront pas croyants aussi longtemps qu´ils ne t´auront demandé de juger de leurs disputes et qu´ils n´auront éprouvé nulle angoisse pour ce que tu auras décidé, et qu´ils se soumettent complètement [à ta sentence].", "wo": "Mukk !... Giñ naa ci sa màggug Boroom ! Duñu gëm mukk [di ay jullit] li feek àtteloowuñu la la ca seen diggante te bañ a am benn ñag- ñagi xol ca la nga àtte, nangul la ak xol bu tàlli.(s)" }
4
66
{ "fr": "Si Nous leur avions prescrit ceci : \"Tuez-vous vous-mêmes\", ou \"Sortez de vos demeures\", ils ne l´auraient pas fait, sauf un petit nombre d´entre eux. S´ils avaient fait ce à quoi on les exhortait, cela aurait été certainement meilleur pour eux, et (leur foi) aurait été plus affermie.", "wo": "Su fekkoon ñoon Danu leen sant ñu reyante mbaa ñu génn seeni kër, duñu ko def lu dul ñu néew ci ñoom. Te su ñu defoon la ñu leen di waare, mu gën ca ñoom, te gën a dëgëral seen ngëm. " }
4
67
{ "fr": "Alors Nous leur aurions donné certainement, de Notre part, une grande récompense,", "wo": "Te kon Nu jox leen pey gu màgg jóge ci Nun," }
4
68
{ "fr": "et Nous les aurions guidé certes vers un droit chemin.", "wo": "te kon Nu gindi leen teg leen ca yoon wu jub xocc wa." }
4
69
{ "fr": "Quiconque obéit à Allah et au Messager... ceux-là seront avec ceux qu´Allah a comblés de Ses bienfaits : les prophètes, les véridiques, les martyrs, et les vertueux. Et quels compagnons que ceux-là !", "wo": "Ku topp Yàlla ak Yonent ba... ñooña ànd nañook ña Yàlla wàcce xéewalam ci ñoom : ca Yonent ya ak way-dëggu ña [daraja ju kawe sahaaba ya], ak ña dee ci xare ngir Yàlla, ak ñu sell [ñu yiw] ña, ndaw àndandoo yu jekk !" }
4
70
{ "fr": "Cette grâce vient d´Allah. Et Allah suffit comme Parfait Connaisseur.", "wo": "Loolooy ngëneel la jóge ca Yàlla. Te Yàlla doy na, mat na sëkk boroom xam-xam." }
4
71
{ "fr": "ô les croyants ! Prenez vos précautions et partez en expédition par détachements ou en masse.", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Nangeen fagaru ci seen [coongum noon], moo xam ngeen tasaaroo walla ngeen àndandoo." }
4
72
{ "fr": "Parmi vous, il y aura certes quelqu´un qui tardera [à aller au combat] et qui, si un malheur vous atteint, dira : \"Certes, Allah m´a fait une faveur en ce que je ne me suis pas trouvé en leur compagnie\";", "wo": "Te am na ci yéen kuy des-deslu ginnaaw ba lu metti dal leen, mu daldi wax ne : “Man Yàlla xéewal na ma ba ma àndul ak ñoom fekke loolee [dee ci xare]” ;" }
4
73
{ "fr": "et si une grâce qui vous atteint de la part d´Allah, il se mettra, certes, à dire, comme s´il n´y avait aucune affection entre vous et lui : \"Quel dommage ! Si j´avais été avec eux, j´aurais alors acquis un gain énorme\" .", "wo": "te bu ngeen amee ndam lu leen Yàlla jox, muy wax mel ni cofeel doxul seen digganteek ñoom, ne : “ Aka neexoon ma ànd ak ñoom ba am ndam lu rëy a rëy [alal ja]” ." }
4
74
{ "fr": "Qu´ils combattent donc dans le sentier d´Allah, ceux qui troquent la vie présente contre la vie future. Et quiconque combat dans le sentier d´Allah, tué ou vainqueur, Nous lui donnerons bientôt une énorme récompense.", "wo": "Ña jaay seen dundug àddina jënde ko àllaaxira, nañu xare ci yoonu Yàlla. Képp ku xare ci yoonu Yàlla ba dee ca, mbaa mu not kàddu ndam la, Dananu ko jox pey gu rëy." }
4
75
{ "fr": "Et qu´avez vous à ne pas combattre dans le sentier d´Allah, et pour la cause des faibles : hommes, femmes et enfants qui disent : \"Seigneur ! Fais-nous sortir de cette cité dont les gens sont injustes, et assigne-nous de Ta part un allié, et assigne-nous de Ta part un secoureur\".", "wo": "Waaw yéen, lu leen nekkal ci bañ a xeex ci yoonu Yàlla [yiiraale] ñi néew doole ci góor, ak jigéen, ak xale yi? Ñoom ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom !Génne nu ci dëkk bii aw nitam diy tooñkat te nga boole nook ku nuy sàmm, jox nu ku nuy dimbali, ñoo tànnal sa bopp” ." }
4
76
{ "fr": "Les croyants combattent dans le sentier d´Allah, et ceux qui ne croient pas combattent dans le sentier du Tagut . Eh bien, combattez les alliés de Diable, car la ruse du Diable est certes, faible.", "wo": "Ñi gëm, ñi ngi xare ci yoonu Yàlla, ñi weddi di xare ci yoonu xërëm [taguut]. Xeexleen ak farandooy Séytaane, pexem Séytaane lu néew doole la." }
4
77
{ "fr": "N´as-tu pas vu ceux auxquels on avait dit : \"Abstenez-vous de combattre, accomplissez la Salat et acquittez la Zakat ! \" Puis lorsque le combat leur fut prescrit, voilà qu´une partie d´entre eux se mit à craindre les gens comme on craint Allah, ou même d´une crainte plus forte encore, et à dire : \"ô notre Seigneur ! Pourquoi nous as-Tu prescrit le combat ? Pourquoi n´as-Tu pas reporté cela à un peu plus tard ? \" Dis : \"La jouissance d´ici-bas est éphémère, mais la vie future est meilleure pour quiconque est pieux. Et on ne vous lésera pas fût-ce d´un brin de noyau de datte.", "wo": "Ndax gisoo ña nga xam ne waxoon nañu leen ne : “Téyeleen seeni yoxo, te ngeen farlu ci julli, tey génne asaka !” Te bu ñu leen digalee xare, ñenn ci ñoom ragal nit ña ni ñu ragalee Yàlla, walla sax ragal gu gën a tar, ñu naan : “Sunu Boroom ! Lu tax nga digle xare ci nun ? Lu teewoon nga yeexe nu ba beneen àpp bu jege ?” . Neel : “Yóbbalu àddina lu néew la, te àllaaxira moo dàq ci ku ragal Yàlla. Te bu boobaa duñu leen tooñ lu toll ni karanu xooxu tàndarma." }
4
78
{ "fr": "Où que vous soyez, la mort vous atteindra, fussiez-vous dans des tours imprenables. Qu´un bien les atteigne, ils disent : \"C´est de la part d´Allah.\" Qu´un mal les atteigne, ils disent : \"C´est dû à toi (Muhammad).\" Dis : \"Tout est d´Allah.\" Mais qu´ont-ils ces gens, à ne comprendre presque aucune parole ?", "wo": "Fu ngeen mën a nekk dey, dee dana leen fa fekk, doonte la dangeen a nekk ci tata yu ñoŋ. Te bu leen lu neex dikkalee, ñu ne : “Lii ci Yàlla la bawoo [jóge].” . Bu leen naqar dalee, ñu ne : “Lii ci yaw [Muhammad] la jóge.” . Neel : “Lépp ca Yàlla la jóge.” Waaw ana lu nekk ca ñooña nit ba xawuñoo déggati wax [ju am njariñ] ?" }
4
79
{ "fr": "Tout bien qui t´atteint vient d´Allah, et tout mal qui t´atteint vient de toi-même . Et Nous t´avons envoyé aux gens comme Messager. Et Allah suffit comme témoin.", "wo": "Lu la dal ci lu baax ma nga jóge ca Yàlla, lu bon lu la dal ci sa bakkan la jóge. Te yónni Nanu la [yaw Muhammad] nga di ab Yonent. Te Yàlla doy na seede ci lépp.(s)" }
4
80
{ "fr": "Quiconque obéit au Messager obéit certainement à Allah. Et quiconque tourne le dos... Nous ne t´avons pas envoyé à eux comme gardien.", "wo": "Képp ku topp Yonent ba topp na ndigalu Yàlla. Ku dummóoyu [weddi]... Xamal ne yónniwuñu la ci ñoom ngir nga di leen wattu." }
4
81
{ "fr": "Ils disent : \"obéissance ! \" Puis sitôt sortis de chez toi, une partie d´entre eux délibère au cours de la nuit de tout autre chose que ce qu´elle t´a dit. [Cependant] Allah enregistre ce qu´ils font la nuit. Pardonne-leur donc et place ta confiance en Allah. Et Allah suffit comme Protecteur.", "wo": "Danañu wax ne : “Nangul nanu la !” Te bu ñu jóge ci yaw , ab kurél ci ñoom dana fanaanoo lu wuuteek la ñu la waxoon. Yàlla Dana bind la ñu fanaane. Nanga leen dëddu te nga wéeru ci Yàlla. Yàlla doy na ndëgërlaay ." }
4
82
{ "fr": "Ne méditent-ils donc pas sur le Coran ? S´il provenait d´un autre qu´Allah, ils y trouveraient certes maintes contradictions !", "wo": "Moo ndax ñoom dañu dul settantal Alxuraan ? Alxuraan, bu jóge woon ci keneen ku dul Yàlla, fàwwu ñu gis ca ay juuyoo ciy waxam !" }
4
83
{ "fr": "Quand leur parvient une nouvelle rassurante ou alarmante, ils la diffusent. S´ils la rapportaient au Messager et aux détenteurs du commandement parmi eux ceux d´entre eux qui cherchent à être éclairés, auraient appris (la vérité de la bouche du Prophète et des détenteurs du commandement). Et n´eussent été le grâce d´Allah sur vous et Sa miséricorde, vous auriez suivi le Diable, à part quelques-uns.", "wo": "Su leen mbir ma dikkale ci kóolute walla tiitaange, ñu siiwal ko. Te bu ñu ko delloo woon ca Yonent ba walla kilifa ya nekk ca ñoom, kon ña ko soloo xam ne ñoom danañu ca am lu leer bu dul woon ak xéewali Yàlla ak yërmaandeem ci yéen. Giñ naa ne kon lim bu néew ci yéen moo dul topp [Séytaane]." }
4
84
{ "fr": "Combats donc dans le sentier d´Allah, tu n´es responsable que de toi même, et incite les croyants (au combat) Allah arrêtera certes la violence des mécréants. Allah est plus redoutable en force et plus sévère en punition.", "wo": "Xareel ci yoonu Yàlla, sasewuñu la lu dul sa bopp, te nanga ñaax ñi gëm, amaana Yàlla fegal la ayu yéefar ya. Te Yàllaa gën a tar ngaañ, Moo gën a tar xorñoñal." }
4
85
{ "fr": "Quiconque intercède d´une bonne intercession, en aura une part; et quiconque intercède d´une mauvaise intercession portera une part de responsabilité. Et Allah est Puissant sur toute chose.", "wo": "Képp ku taxawu nit [dooleel ko] taxawaay bu rafet, dana ca am cër ; ku taxawu nit [dooleel ko] cig ñaawtéef, dana ca am bàkkaar ba. Yàlla Kuy seetlu lépp la." }
4
86
{ "fr": "Si on vous fait une salutation, saluez d´une façon meilleure; ou bien rendez-la (simplement) . Certes, Allah tient compte de tout.", "wo": "Bu ñu leen nuyyoo, nangeen delloo nuyyoo bu gën a rafet ; mbaa bu na mel. Yàlla Kuy natt lépp la." }
4
87
{ "fr": "Allah ! Pas de divinité à part Lui ! Très certainement Il vous rassemblera au Jour de la Résurrection, point de doute là-dessus. Et qui est plus véridique qu´Allah en parole ?", "wo": "Amul jeneen yàlla yu dul Moom Yàlla ! Fàwwu dana leen dajale Bis- pénc ba, sikkuwut. Te kan moo gën a dëgguy wax Yàlla ? [Amul](h)" }
4
88
{ "fr": "Qu´avez-vous à vous diviser en deux factions au sujet des hypocrites ? Alors qu´Allah les a refoulés (dans leur infidélité) pour ce qu´ils ont acquis. Voulez-vous guider ceux qu´Allah égare ? Et quiconque Allah égare, tu ne lui trouveras pas de chemin (pour le ramener).", "wo": "Lu ngeen am ? Ca naaféq ya, am na ñaari kuréel.Te Yàlla delloo na leen ca la ñu fàggu woon. Moo ndax dangeen a bëgg gindi ka Yàlla bàyyi cig réer ? Ku Yàlla bàyyi cig réeram, doo ko mën wutal yoonu mucc." }
4
89
{ "fr": "Ils aimeraient vous voir mécréants, comme ils ont mécru : alors vous seriez tous égaux ! Ne prenez donc pas d´alliés parmi eux, jusqu´à ce qu´ils émigrent dans le sentier d´Allah. Mais s´ils tournent le dos, saisissez-les alors, et tuez-les où que vous les trouviez; et ne prenez parmi eux ni allié ni secoureur,", "wo": "Ñanga ne siiw ngeen weddi, na ñu weddee [ñoom] : ndax ngeen yem ! Buleen jàpp ay xarit ci ñoom, li feek ñuy gàddaay jëm ci yoonu Yàlla. Bu ñu dëddoo, jàppleen leen te reyleen fu ngeen leen mën a fekk ; te buleen wut ci ñoom xarit waxumalaak ndimbal," }
4
90
{ "fr": "excepte ceux qui se joignent à un groupe avec lequel vous avez conclu une alliance, ou ceux qui viennent chez vous, le cœur serré d´avoir à vous combattre ou à combattre leur propre tribu. Si Allah avait voulu, Il leur aurait donné l´audace (et la force) contre vous, et ils vous auraient certainement combattu. (Par conséquent,) s´ils restent neutres à votre égard et ne vous combattent point, et qu´ils vous offrent la paix, alors, Allah ne vous donne pas de chemin contre eux .", "wo": "lu dul ña jóge ca nit ñoo xam ne kóllare dox na ci seeni diggante, ak ña jëm ci yéen te fekk xeex ak yéen di lu tiis ci seeni xol, walla ñu xeex ak ña bokk ca ñoom. Bu sooboon Yàlla, Mu xiir leen ci yéen, te kon ñu farlu ci xeex ak yéen. Bu ñu leen bàyyee, berleen, xeexuñu ak yéen, te ñu doxal jàmm ak yéen, Yàlla mayatuleen wenn lay wuy tax ngeen mën dal ci seen kaw." }
4
91
{ "fr": "Vous en trouverez d´autres qui cherchent à avoir votre confiance, et en même temps la confiance de leur propre tribu. Toutes les fois qu´on les pousse vers l´Association, (l´idolâtrie) ils y retombent en masse. (Par conséquent,) s´ils ne restent pas neutres à votre égard, ne vous offrent pas la paix et ne retiennent pas leurs mains (de vous combattre), alors saisissez-les et tuez les où que vous les trouviez. Contre ceux-ci, Nous vous avons donné autorité manifeste.", "wo": "Dangeen gis ñeneen ñu bëgg jàmm dox seeni diggante, ñoom ak yéen ak seen biir. Saa yu ñu leen xëccee jëme leen ci bokkaale, ñu yabu ca lool. Bu ñu leen bàyyiwul, berleen te jàmmoowuñu ak yéen, te wàccewuñu seen yoxo ci yéen, jàppleen leen, reyleen fépp du ngeen leen fekk. Ñooñu, may Nanu leen ci ñoom ndigal lu wér ci ñu nennu leen." }
4
92
{ "fr": "Il n´appartient pas à un croyant de tuer un autre croyant, si ce n´est par erreur. Quiconque tue par erreur un croyant, qu´il affranchisse alors un esclave croyant et remette à sa famille le prix du sang, à moins que celle-ci n´y renonce par charité. Mais si [le tué] appartenait à un peuple ennemi à vous et qu´il soit croyant, qu´on affranchisse alors un esclave croyant. S´il appartenait à un peuple auquel vous êtes liés par un pacte, qu´on verse alors à sa famille le prix du sang et qu´on affranchisse un esclave croyant. Celui qui n´en trouve pas les moyens, qu´il jeûne deux mois d´affilée pour être pardonné par Allah. Allah est Omniscient et Sage.", "wo": "Yellul ab jullit rey ab jullit, lu dul ci njuumte. Ku rey jullit ci njuumte, war na mu goreel jaam bu nekk jullit te jox ndàmpaay ay mbokkam, ndegam defuñu ko sarax [Baal ko ko]. Bu fekkee ka ñu rey dafa di ab jullit bu bokk ca nit ña nekk seeni noon, goreel jaam bu jullit rekk a war ka reye. Bu bokkee ci ñoo xam ne kóllare dox na ci seen diggante, dana ko war ndàmpaay lu mu jox ay mbokkam ak goreel jaam bu di jullit. Ku gisul [jaam bu mu goreel], na woor ñaari weer yu toftaloo mu di tuub gu Yàlla nangu. Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la.(s)" }
4
93
{ "fr": "Quiconque tue intentionnellement un croyant, Sa rétribution alors sera l´Enfer, pour y demeurer éternellement. Allah l´a frappé de Sa colère, l´a maudit et lui a préparé un énorme châtiment.", "wo": "Ku rey ab jullit te tey ko, peyam Safara la, te dafay béel. Merum Yàlla ak rëbbam tegu ci kawam, te mbugal mu mag moo ko fay xaar." }
4
94
{ "fr": "ô les croyants ! Lorsque vous sortez pour lutter dans le sentier d´Allah, voyez bien clair (ne vous hâtez pas) et ne dites pas à quiconque vous adresse le salut (de l´Islam) : \"Tu n´es pas croyant\", convoitant les biens de la vie d´ici-bas. Or c´est auprès d´Allah qu´il y a beaucoup de butin. C´est ainsi que vous étiez auparavant; puis Allah vous a accordé Sa grâce. Voyez donc bien clair. Allah est certes Parfaitement Connaisseur de ce que vous faites .", "wo": "Éy yéen ñi gëm ! Ndegam dox ngeen ci yoonu Yàlla, nangeen leerlu bu baax te buleen nattu ñay wone jàmm, buleen ne ko : “Doo jullit” , ngir bëgg wut alali àddina . Alal yu baree nga ca Yàlla. Te sax yéen noonu ngeen meloon bu yàggul ; terewul Yàlla jox na leen xéewal. Deeleen di leerlu. Yàlla deñ na kumpa ca la ngeen di def." }
4
95
{ "fr": "Ne sont pas égaux ceux des croyants qui restent chez eux - sauf ceux qui ont quelques infirmité - et ceux qui luttent corps et biens dans le sentier d´Allah. Allah donne à ceux qui luttent corps et biens un grade d´excellence sur ceux qui restent chez eux. Et à chacun Allah a promis la meilleure récompense; et Allah a mis les combattants au-dessus des non combattants en leur accordant une rétribution immense;", "wo": "Ña bokk ci jullit yi toog bañ a xareji ci lu dul ngànt, duñu yem mukk ak ña xare ca yoonu Yàlla ak seeni alal ak seeni bakkan. Ña xareji, Yàlla defal na leen ngëneel ak daraja ca kaw ña toog bañ a xareji. Waaye ñoom ñépp nag Yàlla dig na leen Àjjana ; teewut itam Mu defal ngëneel way-xare ya ca kaw ña toogoon, ña xareji muy pey gu màgg ;" }
4
96
{ "fr": "des grades de supériorité de Sa part ainsi qu´un pardon et une miséricorde. Allah est Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "muy yokkute gu tukkee ci Yàlla, ak njéggal ak yërmaande. Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la. " }
4
97
{ "fr": "Ceux qui ont fait du tort à eux mêmes, les Anges enlèveront leurs âmes en disant : \"Où en étiez-vous ? \" (à propos de votre religion) - \"Nous étions impuissants sur terre\", dirent-ils. Alors les Anges diront : \"La terre d´Allah n´était-elle pas assez vaste pour vous permettre d´émigrer ? \" Voilà bien ceux dont le refuge et l´Enfer. Et quelle mauvaise destination !", "wo": "Ña Malaaka ya jël seeni ruu te ñu doon tooñ seen bopp, Danañu leen laaj : “Ca la ngeen nekkoon ?” [bañ a dem xareji] - Ñu toontu ne : “Danoo nekkoon ñu ñu néewal doole ci kaw suuf” . Ñu ne leen : “Moo ndax suufus Yàlla si dafa yaatuwul ba ngeen mën a gàddaay jëm feneen ?” . Ñooña Safaraa di seen dëkkuwaay. Te ndaw muj gu bon !" }
4
98
{ "fr": "A l´exception des impuissants : hommes, femmes et enfants, incapables de se débrouiller, et qui ne trouvent aucune voie :", "wo": "Ba mu des ña néew doole : ci góor ñi, ak ci jigéen ñi, ak xale yi ci ñàkk pexe, bu ñu gindikoo [ba genn màkka]" }
4
99
{ "fr": "A ceux-là, il se peut qu´Allah donne le pardon. Allah est Clément et Pardonneur.", "wo": "Ñooña xéy-na Yàlla jéggal leen. Yàlla Kuy baale la, di jéggale." }
4
100
{ "fr": "Et quiconque émigre dans le sentier d´Allah trouvera sur terre maints refuges et abondance. Et quiconque sort de sa maison, émigrant vers Allah et Son messager, et que la mort atteint, sa récompense incombe à Allah. Et Allah est Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "Ku gàddaay ngir Yàlla, fu mu mën a jëm, dana fa fekk delluwaay yu bari ak ug yaatal. Ku génn këram, di gàddaay ngir Yàllaak ub Yonentam, ba dee dab ko, kooku peyam Yàlla warlul na ko ko. Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.(r)" }
4
101
{ "fr": "Et quand vous parcourez la terre, ce n´est pas un péché pour vous de raccourcir la Salat, si vous craignez que les mécréants ne vous mettent à l´épreuve, car les mécréants demeurent pour vous un ennemi déclaré.", "wo": "Bu ngeen di tukki ci réew yi, aayul ci yéen ngeen wàññi ci julli yi, bu ngeen ragalee yéefar yi fitnaal leen, yéefar yi seeni noon lañu yu bir." }
4
102
{ "fr": "Et lorsque tu (Muhammad) te trouves parmi eux, et que tu les diriges dans la Salat, qu´un groupe d´entre eux se mette debout en ta compagnie, en gardant leurs armes. Puis lorsqu´ils ont terminé la prosternation, qu´ils passent derrière vous et que vienne l´autre groupe, ceux qui n´ont pas encore célébré la Salat. A ceux-ci alors d´accomplir la Salat avec toi, prenant leurs précautions et leurs armes. Les mécréants aimeraient vous voir négliger vos armes et vos bagages, afin de tomber sur vous en une seule masse. Vous ne commettez aucun péché si, incommodés par la pluie ou malades, vous déposez vos armes; cependant prenez garde. Certes, Allah a préparé pour les mécréants un châtiment avilissant.", "wo": "Boo nekkee [Mahammad] ci seen biir, te nga jiite leen ci julli, na benn kurél ci ñoom ànd ak yaw, na beneen kurél ba jël seeni ngànnaay. Bu ñu sujjóotee ñu nekk ca ginnaaw ñay julli, kurél boobu julliwul woon ñëw [bu bu jëkk ba noppee] julli ànd ak Yaw. Nañu fogu te jël seeni ngànnaay. Yéefar yaa ngi ne siiw ngeen sàggane seeni ngànnaay ak seeni yóbbal, ba ñu song leen menn cong mu tar. Aayul ci yéen su amee lu leen lor ci taw walla ngeen wopp, ngeen tëral seeni ngànnaay te fogu.. Yàlla xaaroo na yéefar yi mbugal muy doyadale [toroxale]." }
4
103
{ "fr": "Quand vous avez accompli la Salat, invoquez le nom d´Allah, debout, assis ou couchés sur vos côtés. Puis lorsque vous êtes en sécurité, accomplissez la Salat (normalement), car la Salat demeure, pour les croyants, une prescription, à des temps déterminés.", "wo": "Bu julli ga sottee, tudduleen Yàlla ci taxawaay ak ci toogaay, ak bu ngeen tëddee. Te bu ngeen nekkee ci kóolute, nangeen taxawal julli. Julli kat, doon na lu Nu sàkkal ay waxtu ci kaw jullit ñi." }
4
104
{ "fr": "Ne faiblissez pas dans la poursuite du peuple [ennemi]. Si vous souffrez, lui aussi souffre comme vous souffrez, tandis que vous espérez d´Allah ce qu´il n´espère pas. Allah est Omniscient et Sage.", "wo": "Buleen yaanaani ci am cong. Bu ngeen di metitlu [ci ay jam-jam], ñoom it am nañu metit ni yéen, te yéen yaakaar ngeen ci Yàlla loo xam ne yaakaaruñu ko ñoom. Te Yàlla Ku Xam la te Xereñ." }
4
105
{ "fr": "Nous avons fait descendre vers toi le Livre avec la vérité, pour que tu juges entre les gens. selon ce qu´Allah t´a appris. Et ne te fais pas l´avocat des traîtres.", "wo": "Wàcce Nanu ci Yaw Téere ba ci dëgg, ngir nga àtte diggante nit ñi ni la ko Yàlla xamalee. Bul doon kuy layal wurujkat ya.(s)" }
4
106
{ "fr": "Et implore d´Allah le pardon car Allah est certes Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "Jéggalul Yàlla, Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la." }
4
107
{ "fr": "Et ne dispute pas en faveur de ceux qui se trahissent eux-mêmes. Allah vraiment, n´aime pas le traître et le pécheur.", "wo": "Bul dàggasanteek ñiy wuruj seen bopp. Yàlla safoowul ku di wurujkat di bàkkaarkat. " }
4
108
{ "fr": "Ils cherchent à se cacher des gens, mais ils ne cherchent pas à se cacher d´Allah. Or, Il est avec eux quand ils tiennent la nuit des paroles qu´Il (Allah) n´agrée pas. Et Allah ne cesse de cerner (par Sa science) ce qu´ils font.", "wo": "Nëbbu nañu nit ñi, waaye mënuñoo nëbbu Yàlla. Ndax mook ñoom a nekkoon ba ñuy fanaanoo ay wax yu ko neexul. La ñu doon def, Yàlla péeg na ko [ci xam-xam]." }
4
109
{ "fr": "Voilà les gens en faveur desquels vous disputez dans la vie présente. Mais qui va disputer pour eux devant Allah au Jour de la Résurrection ? Ou bien qui sera leur protecteur ?", "wo": "Yéen a ngi noonu di layal ñooñu ci dundug àddina bi. Waaye ana kan moo leen di layal ca Bis-pénc ba ? Walla ana kan mooy doon seen wéeruwaay ?" }
4
110
{ "fr": "Quiconque agit mal ou fait du tort à lui-même, puis aussitôt implore d´Allah le pardon, trouvera Allah Pardonneur et Miséricordieux.", "wo": "Képp ku def ñaawtéef mbaa mu tooñ boppam, gaaw jéggalu Yàlla, dana fekk di Jéggalaakoon, di Jaglewaakoon." }
4
111
{ "fr": "Quiconque acquiert un péché, ne l´acquiert que contre lui-même. Et Allah est Omniscient et Sage.", "wo": "Ku fàggu bàkkaar, defu ko kenn ku dul boppam. Yàlla Ku xam la, di Ku xereñ." }