wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
billóoji b-
sorcier qui n’exerce plus son pouvoir maléfique mais qui peut guérir une victime
Yóbbuleen ko ca billóoji ba, mu faj ko
emmenez-le chez le sorcier, qu’il le guérisse !
bindante
s’écrire (des lettres)
bind b-
aspect physique forme
Ci sama bind la
C'est dû à mon aspect physique.
bindoo
être constitué de telle façon
Naka la bindoo ?
quelle en est la forme ?
Ku nekk ak ni nga bindoo
à chacun sa constitution.
bineegar b-
vinaigre
Jottali ma butéelu bineegar bi
passe-moi la bouteille de vinaigre !
binit b-
vase de terre boue
Sa tànk yaa ngi fees ak binit
tes pieds sont pleins de boue.
bippu
se dégager violemment d’une prise
Dama ko jàpp, mu bippu
je l’ai attrapé, il s’est dégagé violemment.
birale
rester éveillé pendant la nuit
Dama birale biig yépp
je suis resté éveillé toute la nuit dernière.
birig b-
brique de construction
Birig yi doyuñu
les briques ne suffisent pas.
bistoroŋ b-
bistrot
bët-set
faire jour
Bët-set na
il fait jour.
béjante
débattre
bind
créer
Yàllaa ma bind
C'est Dieu qui m’a créé.
bitti-loxo b-
revers de la main
Diw ko ci bitti-loxo bi
enduis-en le revers de la main !
bocci
dégainer (une arme blanche)
Moytuleen ! bocci na paaka
faites attention ! il a dégainé un couteau.
boddekoonte b-
ségrégation
Boddekonte ci biir i xeet lañuy xeex
ils combattent la ségrégation raciale.
boddi
tenir qqn à l’écart
Faatu boddiwul kenn
Fatou ne tient personne à l’écart.
bojj
enfoncer
Dafa ko bojj paaka ci biir
il lui a enfoncé un couteau dans le ventre.
bojj
piler pour extraire les grains de mil du reste comprenant l’épi (ou la panicule) et les poils
Dafay bojj dugub ji
elle pile l’épi de mil pour en extraire les grains.
bokkaale
pratiquer l’idolâtrie
Araab yu jëkk ya dañu daan bokkaale
les premiers Arabes pratiquaient l’idolâtrie.
bokk g-
parenté
Bokk gi dox sunu diggante moo tax
C'est à cause de la parenté qu’il y a entre nous.
bokkoo
être en bonne entente
Dangeen wara bokkoo ndax ay dëkkandoo ngeen
vous devez être en bonne entente parce que vous êtes des voisins.
bokkoo g-
entente entre individus
Bokkoo gi am ci seen biir, mooy seen doole
J'entente qui existe parmi vous, c’est ça qui est votre force.
bol b-
poudre
Bolu meew laa jénd
J'ai acheté du lait en poudre.
bolde b-
gourdin, massue
Su ngeen ko téyewul, dina ko dóor bolde bi
si vous ne le retenez pas, il le frappera avec le gourdin.
bomb
frotter
Nanga bomb biir beek biti bi
tu frotteras l’intérieur et l’extérieur.
boŋ-boŋ b-
gâteau
Indil naa leen boŋ-boŋ
je vous ai apporté des gâteaux.
bonde
rebondir
Ci kow taabal bi la bal bi bonde
la balle a rebondi sur la table.
boob m-
herbe sèche
Nanga lakk boob mi
tu brûleras l’herbe sèche.
boog
alors
Na dem boog
qu’il parte alors !
boolante
mettre en complémentarité
Ay xalaat yu, su ñu leen boolantee, dina baax
des idées qui seraient bien si on les mettait en complémentarité.
boole b-
fait d’associer, de regrouper
boon b-
cigarette de chanvre indien (pop.) joint
Paas ma boon bi
passe-moi le joint !
boot
porter sur le dos
Dafa boot xale bi, santal liggéey bi keneen
elle porte l’enfant sur le dos, fais faire le travail par quelqu’un d’autre !
Dafa laabir ba ku dikk ci dëkk bi rekk, mu boot ko
il est si charitable qu’il prend en charge tous ceux qui viennent au village.
(prov.) Ku boot bukki, xaj bów la
les chiens aboient après celui qui porte une hyène sur le dos.
bootaay b-
fait de porter sur le dos
Bootaay bu ëpp dafay tax mu yiixa dox
le fait de porter excessivement (l’enfant) sur le dos fait qu’il tarde à marcher.
bootal-mbaar b-
responsable des circoncis sur le plan mystique
Góor gi Omar a di seen bootal-mbaar
C'est le vieux Omar qui est leur protecteur sur le plan mystique.
booy
être envahi par la mauvaise herbe
Sama tool dafa booy ndax dama tukki woon
mon champ est envahi par la mauvaise herbe car j’étais en voyage.
boow
faire aller et venir sur qqch la lame d’un couteau
Boow naa paaka bi ba tàyyi, daggul dara
J'ai eu beau faire aller et venir le couteau, il n’a rien coupé.
boow
astiquer
Nanga boow bool bi ba muy mellax
tu astiqueras le bol jusqu’à ce qu’il brille.
baawlu
aller au puits sans corde et chercher à se faire offrir de l’eau
Damay baawlusi
je viens demander de l’eau.
booyal
laisser en jachère
Dama booyal sama tool
J'ai laissé mon champ en jachère.
bare-pexe
être débrouillard, plein de ressources
Wax ko Omar; ku bare-pexe la
dis-le à Omar; il est débrouillard.
bitti-loxo
frapper du revers de la main
Dafa ko bitti-loxo
il l’a frappé du revers de la main.
béjante b-
débattre
Danu ciy béj béjante yu tar
nous en débattons intensément.
boqaale b-
maîtresse amant (de personnes mariées)
Dafa am ab boqaale
il a une maîtresse (ou bien) elle a un amant.
boq
prendre sous l’aisselle
Mu ngi boq saakam, di dem ekool
il s’en va à l’école, le sac sous le bras.
Dafa bon ba boq mbonaat
il est extrêmement mauvais.
bor b-
dette
Feyal say bor ba-noppi. ?
Paie tes dettes d’abord !
(prov.) Bu gor ñàkkee, fàttaliku bor
dans le besoin, l’honnête homme se rappelle ses créances.
boreeku
s’écorcher
Dafa boreeku tuuti ci conco li
il s’est un peu écorché le coude.
bori
saigner du nez
Dafay bori; amul solo
il saigne du nez; ce n’est pas grave.
bori b-
Épistaxis ; saignement de nez